2 Peter (Wolof)
1
1:1b.2PE.001.001 Man Simoŋ Pieer, jaamu Yeesu Krist ak ndawam, maa leen di bind, yeen ñi Yàlla jagleel ngëm gu rafet ni nun, aju ci njubu sunu Yàlla ak Musalkat, Yeesu Krist.
1:2b.2PE.001.002 Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm, jaar ci xam ko ak Yeesu sunu Boroom.
1:3b.2PE.001.003 Dooley Yàlla moo nu may lépp lu aju ci dund gu sax ak ragal Yàlla, jaarale ko ci xam gi nu ko xam, moom mi nu woo ci kaw ndamam ak dooleem.
1:4b.2PE.001.004 Noonu la nu dige ay dig yu rafet, te réy ba ëpp xel, ngir nu gëm leen, te Yàlla sol nu jikoom, nu mucc ci yàqute, gi bànneexu bakkan samp ci àddina si.
1:5b.2PE.001.005 Na loolu tax ngeen góor-góorlu, ba yokk ci seen ngëm njàmbaar, ci njàmbaar googu ngeen yokk ci xam-xam, yokk ci noot sa bopp.
1:6b.2PE.001.006 Noot sa bopp googu, ngeen yokk ci muñ, yokk ci ragal Yàlla,
1:7b.2PE.001.007 yokk ci sopp mbokk, yokk ci bëgg ñépp.
1:8b.2PE.001.008 Ndaxte bu leen jiko yooyu soloo, ba sax ci yeen, dina tax seen xam Yeesu Krist Boroom bi am njeriñ te jur mbaax.
1:9b.2PE.001.009 Waaye ku ñàkk jiko yooyu, ay bëtam dañoo lëndëm ba gumba, te fàtte na, ni ko Yàlla fóotale bàkkaari démb.
1:10b.2PE.001.010 Kon nag samay mbokk, gannaaw Yàlla da leena tànn te woo leen, góor-góorluleen ci feddali ko ak seen kem-kàttan. Ndaxte su ngeen ko defee, dungeen jeng mukk.
1:11b.2PE.001.011 Te noonu dingeen tàbbi ak ndam ci nguur gu sax gu sunu Boroom, di sunu Musalkat Yeesu Krist.
1:12b.2PE.001.012 Wóor na ma ne xam ngeen loolu, ba sampu ci dëgg gi leen Yàlla jagleel, waaye fas naa yéene, may sax ci di leen ko fàttali.
1:13b.2PE.001.013 Te jàpp naa ko, muy sama warugar, feek maa ngi noyyi, ma di leen fàttali loolu, ba yee leen.
1:14b.2PE.001.014 Ndaxte xam naa ne, léegi ma jóge fi, ni ma ko Yeesu Krist Boroom bi leerale woon.
1:15b.2PE.001.015 Te dinaa góor-góorlu, ngir sama gannaaw ngeen di fàttaliku li ma leen doon wax.
1:16b.2PE.001.016 Bi nu leen yégalee dooley Yeesu Krist sunu Boroom ak ñëwam ci biir ndam, sukkandikuwunu woon ciy léeb yu sësul fenn, waaye danoo teewe ag màggam.
1:17b.2PE.001.017 Ndaxte Yàlla Baay bi sol na ko teraanga ak ndam, te baatub Aji Màgg ju tedd ji jib na ne: Sama Doom a ngii, di sama Soppe; ci moom laa ame bànneex.
1:18b.2PE.001.018 Te nun dégg nanu baat boobu jóge asamaan, bi nu nekkee ak moom ca tund wu tedd wa.
1:19b.2PE.001.019 Noonu bir na ne, waxu yonent yi wér na, te war ngeen koo fonk; mi ngi mel ni làmp, buy leer ci bérab bu lëndëm, ba kera fajar di xar, te biddiiwub njël bi feq, leeral seeni xol.
1:20b.2PE.001.020 Waaye jëkkleena xam ne, amul jenn waxu yonent ci Mbind mi, ju balle ci xelu boppam.
1:21b.2PE.001.021 Ndaxte kenn ci yonent yi musula wax ci coobareg boppam, waaye, Xel mu Sell mi daa na xiir nit ñi, ñu yégle kàddug Yàlla.
2
2:1b.2PE.002.001 Waaye ci bànni Israyil, amoon na naaféq yu mbubboo turu yonent, ni muy ame seen biir ñuy mbubboo turu jàngalekat. Ci seeni pexe dinañu dugal ci yeen xalaat yu sànke, di weddi Boroom bi leen jot, tey yóbbe seen bopp alkande ju teew.
2:2b.2PE.002.002 ñu bare dinañu leen fekki ci seeni ñaawteef, ba gàkkal yoonu dëgg ci bëti nit ñi.
2:3b.2PE.002.003 Seen bëgge dina tax, ñu dàbbdaaxe ay wax, ngir nax leen, ba lekk seenus tuut. Waaye àtte baa ngi leen di xaar, te seen alkande di leen teeru.
2:4b.2PE.002.004 Ndaxte Yàlla jeggalul malaaka ya bàkkaaroon, waaye tàbbal na leen safara, tëj leen ca kàmb yu lëndëm, di leen nége àtte ba.
2:5b.2PE.002.005 Te it jeggalul àddina su jëkk sa weddi woon, ba xooj ko ci ndoxu mbënn ma, waaye musal na Nóoyin rekk, mi daan waare ci njub, moom ak juróom-ñaari nit.
2:6b.2PE.002.006 Te it Yàlla daan na dëkki Sodom ak Gomor, raafal leen cig lakk, ñuy misaalu ñiy weddi ëllëg.
2:7b.2PE.002.007 Waaye musal na Lóot mi jub, mi sonnoon ndax ñaawteefi ñu dëng, ñooñu mu nekkaloon.
2:8b.2PE.002.008 Ndaxte Lóot, mi dëkkoon ci seen biir, dafa dëkke woon tiisu xol, ndax ñaawteef yi mu gis ak a dégg guddi ak bëccëg.
2:9b.2PE.002.009 Gannaaw loolu lépp am na nag, nanu bir ne, Boroom bi man na musal aji gëm ji nekk ci nattu, te denc ñi jubadi, ngir alag leen bésu àtte ba.
2:10b.2PE.002.010 Rawatina ñiy topp seen bakkan ciy bëgg-bëgg yu ruslu, te faalewuñu genn kilifteef. ñu ñeme Yàlla lañu, te dëgër bopp, ba ragaluñoo xas kilifa ya gëna kawe.
2:11b.2PE.002.011 Fekk sax malaaka, yi leen ëpp doole ak kàttan, tey sax ca jetaayu Boroom bi, ñemewuñoo xas kilifa yooyu.
2:12b.2PE.002.012 Waaye ñoom dañuy xas ci biir yi ñu xamul. ñoom ak bàyyima ñoo yem, di ay mbindeef yuy tañaxu, te tër rendi rekk a jekk ci ñoom; dees na leen rey ni bàyyima,
2:13b.2PE.002.013 muy seen peyug njubadi. Xawaare bëccëgu ndara-kàmm mooy seen bànneex. Su ñuy lekkandoo ak yeen, dañuy bànneexu ci seeni bëgg-bëgg, di ay gàkk ak i sikk ci seen biir.
2:14b.2PE.002.014 Jigéen ju seen bët tegu, ñu xédd ko, ba duñu tàggook moy mukk; ku ñàkk pasteef ñu fàbbi la; ñu xelu lañu jëme cig bëgge -- ñu alku lañu!
2:15b.2PE.002.015 Réer nañu ba wàcc yoon wu jub wi, topp yoonu Balaam, doomu Bosor, mi bëgge xiiroon ci njubadi.
2:16b.2PE.002.016 Waaye déggadeem yóbbe na ko yeraanga; xam ngeen ne mbaam-sëf du wax, waaye mbaam wax na ak moom ci làmmiñ wu bir, ngir mu génn ci ndofam googu.
2:17b.2PE.002.017 Ñooñule ay teen yu dëy lañu, di xiini lay, yu ngelaw liy naawal, te seen pey mooy lëndëm gu ne taraj.
2:18b.2PE.002.018 Dañuy fàbbi ñu naroona mucc ci àddina ju réer, dig leen ak làmmiñ yu neex bànneexi bakkan yu jéggi dayo.
2:19b.2PE.002.019 Dañu leen di dig ngoreel, te fekk ñoom ci seen bopp jaami yàqute lañu, ndaxte lu la noot, jaamam nga.
2:20b.2PE.002.020 Su ñu xamee Boroom bi, di sunu Musalkat Yeesu Krist, ba mucc ci sobes àddina, ba noppi sóobuwaat ca, ba mu noot leen, seen muj moo yées seen njàlbéen.
2:21b.2PE.002.021 Ndaxte ñu xam yoon wu jub wi, ba noppi dëddu ndigal lu sell li ñu déggoon, bañoon koo xam moo gënoon ci ñoom.
2:22b.2PE.002.022 Noonu seen mbir dëggal na li ñuy wax ne: Xaj mooy waccu, di ko lekkaat; te it: Mbaam-xuux, loo ko sang-sang, mu xalangu ci ban.
3
3:1b.2PE.003.001 Yeen samay xarit, sama ñaareelu bataaxel a ngi nii. Bind naa leen, ngir xiir leen ci xalaat yu sell.
3:2b.2PE.003.002 Maa ngi leen di fàttali kàdduy yonent yu sell, yi fi jiitu woon, ak ndigalu Boroom bi sunu Musalkat, li ngeen déggoon ci ndaw, yi Yàlla yebaloon fi yeen.
3:3b.2PE.003.003 Nangeen jëkka xam lii: muju jamano dingeen gis ay tiiñalkat, di topp seen bakkan; dinañu leen tiiñal
3:4b.2PE.003.004 ci di leen ne: Ki dige woon ne dina ñëw, ana mu? Ndaxte baay ya nelaw nañu, waaye lépp a ngi dox ca njàlbéen ga ba tey.
3:5b.2PE.003.005 Fekk bëgguñoo xam lii: kàddug Yàllaa tax, asamaan ak àddina yu jëkk ya juddoo ca ndox, te dunde ko.
3:6b.2PE.003.006 Te ndox it moo labal àddina sa, raafal ko.
3:7b.2PE.003.007 Te kàddug Yàlla googu moo denc asamaan yii fi nekk ak suuf si, ngir lakk leen; Yàllaa ngi leen di nége bésub àtte, ba muy alag ñi weddi.
3:8b.2PE.003.008 Yeen samay xarit, buleen umple ne, benn bés ak junniy at ñoo yem fi Boroom bi.
3:9b.2PE.003.009 Li Yàlla dige, dina ko def, lu mu yeex-yeex ci xalaatu nit. Xanaa kay da leena muñal, ndax bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar.
3:10b.2PE.003.010 Waaye bésu Boroom bi dina ñëw, bett àddina ni sàcc. Su boobaa, asamaan yi dinañu ne rajax toj, lu ne ci àddina lakk ba seey, te suuf ak lu mu ëmb dina ne fàŋŋ fa kanam Yàlla.
3:11b.2PE.003.011 Gannaaw loolu lépp dina seeye noonu nag, nangeen góor-góorlu ci gëna sellal seen nekkin, te feddali seen ragal Yàlla.
3:12b.2PE.003.012 Te it ngeen taxaw temm ci séentu bésu Yàlla bi, te waajal ñëwam. Su boobaa, asamaan yi dinañu lakk, ba naaw ni pënd, te lu nekk ci àddina dina lakk, ba seey nib dóom.
3:13b.2PE.003.013 Waaye nun ngi séentu asamaan su bees ak suuf su bees, fa njub dëkk, ci ni ko Yàlla dige.
3:14b.2PE.003.014 Kon nag samay soppe, gannaaw yeena ngi séentu loolu, góor-góorluleen, ngir bu Krist ñëwee, mu fekk leen ci jàmm, ngeen baña am benn gàkk mbaa sikk.
3:15b.2PE.003.015 Te jàppleen ne, muñug sunu Boroom muccu nit la. Sunu mbokk mi nu bëgg Pool bind na leen ko, ci xel mi ko Yàlla sol.
3:16b.2PE.003.016 Noonu lay waxe ciy bataaxelam yépp di ci biral lii. Am na ci sax yu jafee xam, te ñi amul xam-xam te seen ngëm dëgërul di ko walbati, ba alag seen bopp, te loolu lañuy def ci Mbind yi ci des.
3:17b.2PE.003.017 Noonu yeen samay xarit, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, moytuleen ñi weddi fàbbi leen ci seen réer, ba yolomal seen wàkkirlu ci Yàlla.
3:18b.2PE.003.018 Waaye màggleen ci yiwu sunu Boroom ak Musalkat Yeesu Krist, te sax ci xam ko; moo yelloo ndam fii ba fàww.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. 2 Peter (Wolof). 2 Peter (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C363-C