Hebrews (Wolof)
1
1:1b.HEB.001.001 Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya.
1:2b.HEB.001.002 Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina.
1:3b.HEB.001.003 Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndeyjooru Aji Màgg ji ca kaw,
1:4b.HEB.001.004 wone noonu ne, moo gën a màgg malaaka yi. Te it Yàlla jox na ko tur wu sut seen tur.
1:5b.HEB.001.005 Ndaxte Yàlla musul a wax kenn ci malaaka yi ne:«Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.» Musul ne ci mbirum kenn ci ñoom it:«Man Yàlla, dinaa doon Baay ci moom,mu nekk Doom ci man.»
1:6b.HEB.001.006 Waaye bi muy yónni Doom jooju di taaw bi ci àddina, da ne:«Na ko malaakay Yàlla yépp jaamu.»
1:7b.HEB.001.007 Ci wàllu malaaka yi, lii la ci Yàlla wax:«Def na malaakaam yi, ñu mel ni ay ngelaw,ñooñu koy liggéeyal, mu def leen niki safara.»
1:8b.HEB.001.008 Waaye ci wàllu Doom ji, lii la ko Yàlla wax:«Yaw Yàlla, dinga toog ci jal bi ba fàww,ci njubte ngay nguuru.
1:9b.HEB.001.009 Sopp nga njub te bañ lu bon.Looloo tax yaw Yàlla,sa Yàlla sol la mbég mu gën a réymi mu jagleel say àndandoo.»
1:10b.HEB.001.010 Newaat na it:«Yaw Boroom bi,yaa sàkk àddina ca njàlbéen ga,defar asamaan yi ci sa loxoy bopp.
1:11b.HEB.001.011 Yëf yooyu dinañu wéy,waaye yaw dinga sax,dinañu màggat ñoom ñépp ni ay yére.
1:12b.HEB.001.012 Dinga leen taxañ ni malaan,ñu furi ni ay yére,waaye yaw doo soppiku,te sa dund amul àpp.»
1:13b.HEB.001.013 Waaye Yàlla musul a teral kenn ci malaaka yi, ba di ko wax:«Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneel say noonci sa kanam.»
1:14b.HEB.001.014 Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla, mu di leen yónni ñuy dimbali nit, ñi nar a jot mucc gi.
2
2:1b.HEB.002.001 Moo tax kon nu war a gën a faaydaal wax yi nu dégg, ngir bañ a bayliku.
2:2b.HEB.002.002 Xam nanu ne kàddug yoon, wi Yàlla yégle jaarale ko ci malaaka yi, wareef la woon, te képp ku ko mas a moy, walla mu mas koo tanqamlu, jot na mbugal gi mu yelloo.
2:3b.HEB.002.003 Kon nun ñi dégg mucc gu mag gi, bu nu ko sàgganee, nan lanuy man a rëcce mbugalu Yàlla? Boroom bi moo xamle woon mucc googu ca njàlbéen ga, te gannaaw gi, ñi ko dégg, ñoo nu ko wóoralal.
2:4b.HEB.002.004 Te it Yàlla dëggal na seen seede ci ay firnde ak ay kéemaan, ay jaloore yu bare ak ci ay may yu jóge ci Xelam mu Sell, te mu séddale leen ni mu ko bëgge.
2:5b.HEB.002.005 Yàlla jébbalul malaaka yi benn sañ-sañ bu jëm ci jamonoy ëllëg ji nuy wax; keneen la ko jébbal,
2:6b.HEB.002.006 ndaxte am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:«Lan mooy nit, yaw Yàlla, ba nga di ko xalaat?Lan mooy doomu nit, ba nga koy topptoo?
2:7b.HEB.002.007 Wàcce nga ko, def komu gën a suufe tuuti malaaka yi.Kaalaa nga ko teraanga ak ndam,
2:8b.HEB.002.008 nootal ko lépp, mu teg ci tànk.» Bi ko Yàlla nootalee lépp nag, bàyyiwul dara. Fi mu nekk gisagunu ne, lépp a ngi ci sañ-sañam;
2:9b.HEB.002.009 Waaye gis nanu Yeesu. Wàcce nañu ko, def ko mu gën a suufe tuuti malaaka yi, ngir mu dee ci wàllu ñépp, ndaxte loolu la Yàlla dogal ci yiwam. Waaye léegi Yàlla kaalaa na ko teraanga ak ndam ndax coono bi mu daj ba dee.
2:10b.HEB.002.010 Ndaxte Yàlla mi yelloo lépp te sàkk lépp, dogal na def ñu bare ay doomam, boole leen ci ndamam. Jekk na nag mu matal Yeesu ci coono bi mu daj, moom mi leen xàllal yoonu mucc gi.
2:11b.HEB.002.011 Moom Yeesu miy sellal, ak ñi muy sellal, ñoom ñépp genn njaboot lañu. Moo tax Yeesu rusu leen a wooye ay doomi baayam.
2:12b.HEB.002.012 Nee na:«Yaw Yàlla, dinaa xamle sa turci samay doomi baay,dinaa la tagg ci biir mbooloo mi.»
2:13b.HEB.002.013 Newaat na:«Dinaa am ci Yàlla kóolute.» Dellu na waxaat ne:«Maa ngi nii, man ak doom yi ma Yàlla jox.»
2:14b.HEB.002.014 Doomam yooyu muy wax, nit kese lañu. Looloo tax Yeesu it moom ci boppam, wàcc na, jëmmoo ni ñoom, ngir dee, ba man caa daaneel Ibliis, mi yore dooley dee.
2:15b.HEB.002.015 Noonu mu yiwi nit, ñi meloon ni ay jaam seen giiru dund gépp ndax ragal a dee.
2:16b.HEB.002.016 Leer na ne, Yeesu xettalisiwul malaaka yi, waaye askanu Ibraayma lay xettalisi.
2:17b.HEB.002.017 Looloo taxoon mu war a mel niy doomi baayam ci bépp fànn, ngir doon seen saraxalekat bu mag fa kanam Yàlla, bi leen yërëm te di sàmm kóllëre, te ci liggéeyu saraxaleem joxe na bakkanam ngir dindi bàkkaari nit ñi, ba Yàlla baal leen.
2:18b.HEB.002.018 Gannaaw sonn na ci nattu yi mu daj, man na dimbali ñiy jaar ciy nattu.
3
3:1b.HEB.003.001 Kon nag yéen bokk yu sell yi, yéen ñi Yàlla woo, ngeen bokk ci nguuram gu kawe ga, seetleen ci Yeesu, moom miy ndawu Yàlla li, di saraxalekat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
3:2b.HEB.003.002 Ku takku la ci liggéey bi ko Yàlla sas, ni ko Musaa nekke woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla.
3:3b.HEB.003.003 Waaye Yeesu yelloo na ndam lu sut lu Musaa, ni kiy tabax kër ëppe maana kër ga muy tabax.
3:4b.HEB.003.004 Ndaxte kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla.
3:5b.HEB.003.005 Musaa moom ku takku la woon ci lépp lu jëm ci waa kër Yàlla. Waaye jawriñ rekk la woon, ngir seede li Yàlla waroon a yégle.
3:6b.HEB.003.006 Yeesu nag ku takku la it, waaye Doom la, juy yilif kër Baayam. Nun nooy këram googu, bu nu saxee ci sunu kóolute te di bég ci li nuy séentu.
3:7b.HEB.003.007 Moo tax Xel mu Sell mi wax lii ci Mbind mi:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,
3:8b.HEB.003.008 buleen dëgër bopp,ni seeni maam defoon ca màndiŋ ma,keroog ba ñu dëddoo Yàlla di ko diiŋat.»
3:9b.HEB.003.009 Yàlla ne:«Foofa seeni maam diiŋat nañu ma fa,di ma fexee fiir,te gis nañu samay jëf
3:10b.HEB.003.010 diirub ñeent-fukki at.Looloo tax gennliku naa leen, daldi ne:“Seeni xalaat a leen di réeral saa su nekk,xamuñu yoon yi ma neex.”
3:11b.HEB.003.011 Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay.”»
3:12b.HEB.003.012 Bokk yi, wottuleen ba kenn ci yéen bañ a am xol bu bon te gëmadi, bay dëddu Yàlla jiy dund.
3:13b.HEB.003.013 Waaye bés bu nekk, deeleen soññante ci lu jëm ci Yàlla, fi ak bés boobu ñu wax wéyul, ngir ragal bàkkaar nax kenn, ba xolam tëju.
3:14b.HEB.003.014 Am nanu wàll ci Kirist, su nu wéyee fii ba muj ga ci sunu kóolute, gi nu amoon ca njàlbéen ga.
3:15b.HEB.003.015 Lii la Mbind mi wax:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,buleen dëgër bopp,ni seeni maam defoon, ba ñu dëddoo Yàlla.»
3:16b.HEB.003.016 Ñan ñoo dégg baatu Yàlla bi nag te di ko dëddu? Xanaa ña Musaa génne woon Misra ñépp.
3:17b.HEB.003.017 Te ñan la Yàlla mere lu mat ñeent-fukki at? Xanaa ñi daan bàkkaar te seeni néew tëdd ca màndiŋ ma.
3:18b.HEB.003.018 Te it bi Yàlla defee ngiñ lii: «Duñu dugg mukk ci sama noflaay,» booba ñan ñoo ko taxoon di wax? Xanaa ña ko déggadil.
3:19b.HEB.003.019 Noonu gis nanu sax ne, jotuñoo dugg ci noflaay boobu ndax seen gëmadi.
4
4:1b.HEB.004.001 Yàlla dige na ne, dina am ñu dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci yéen réer ba du dugg ci noflaay boobu.
4:2b.HEB.004.002 Nun jot nanu xebaar bu baax bi ni ñoom, waaye kàddu, ga ñu déggoon, jariñu leen dara, ndaxte boolewuñu ci ngëm, ba ñu koy déglu.
4:3b.HEB.004.003 Nun ñi gëm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe:«Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay,”» doonte sax liggéeyam bépp matoon na, ca ba mu sàkkee àddina ak léegi. Ci lu jëm ci juróom-ñaareelu fan ba,
4:4b.HEB.004.004 am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:«Yàlla noppalu na ci liggéeyam béppca juróom-ñaareelu fan ba.»
4:5b.HEB.004.005 Te it waxoon na ci baat yi nu jot a lim ba noppi:«Duñu dugg mukk ci sama noflaay.»
4:6b.HEB.004.006 Kon am na ñu ci war a dugg ba tey. Te ñi jëkkoon a jot xebaar bu baax bi, dugguñu ci ndax seen déggadi.
4:7b.HEB.004.007 Noonu ay ati at gannaaw ga, Yàlla àppaat na beneen bés, def ko «tey jii,» bi mu waxee ci gémmiñu Daawuda ci baat yii ñu jot a lim:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,buleen dëgër bopp.»
4:8b.HEB.004.008 Su Yosuwe duggaloon sunu maam ya ca noflaayu Yàlla ba, kon gannaaw gi Yàlla du wax dara ci lu jëm ci beneen bés.
4:9b.HEB.004.009 Kon ba tey Yàllaa ngi dencal ay gaayam noflaay bu nirook noflaayu Yàlla ca juróom-ñaareelu fan ba.
4:10b.HEB.004.010 Ndaxte képp ku mas a dugg ca noflaayu Yàlla, noppalu na ci ay jëfam ni Yàlla.
4:11b.HEB.004.011 Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn bañ a déggadi, ba daanu ni maam ya ca màndiŋ ma.
4:12b.HEB.004.012 Xam nanu ne, kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gën a ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol.
4:13b.HEB.004.013 Te itam amul mbindeef mu man a nëbbu Yàlla, waaye lépp a ubbiku, ba ne fàŋŋ ci bëti ki nu war a àtte.
4:14b.HEB.004.014 Gannaaw am nanu saraxalekat bu mag-a-mag bu àgg ba ca kanam Yàlla, di Yeesu Doomu Yàlla ji, nanu jàpp bu dëgër yoon wi nu gëm.
4:15b.HEB.004.015 Saraxalekat bu mag bi nu am, du ku mënul a bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar.
4:16b.HEB.004.016 Kon nag nanu am kóolute ci jege jalu Yàlla bu yiw ba, ngir jot yërmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.
5
5:1b.HEB.005.001 Saraxalekat bu mag bu nekk nag, ci biir nit ñi lañu ko jële, te fal ko muy dox seen diggante ak Yàlla. Noonu dina jébbal Yàlla ay sarax, tey rendi ay mala ngir dindi seeni bàkkaar.
5:2b.HEB.005.002 Te ndegam moom ci boppam nit kese la, man na muñal ñiy moy ndax seen ñàkka xam.
5:3b.HEB.005.003 Li mu ñàkk doole moo tax mu war a def ay sarax ngir mbaalug bàkkaaram, ni mu ko tàmmee defal mbooloo mi.
5:4b.HEB.005.004 Kenn mënul a teral sa bopp ba doon ab saraxalekat, su dul ne Yàllaa la woo, ni mu ko defe woon Aaroona.
5:5b.HEB.005.005 Kirist itam yékkatiwul boppam, ba doon saraxalekat bu mag, waaye Yàlla moo ko woo, bi muy wax ne:«Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.»
5:6b.HEB.005.006 Am na feneen fu mu wax ne:«Doon nga saraxalekat ba fàwwmel ni Melkisedeg.»
5:7b.HEB.005.007 Giiru dundam gépp ci àddina, Kirist da daan ñaan wall ci Yàlla, di ko dénku, boole ko ak i jooy ak i rangooñ. Da doon ñaan ci Yàlla, mi ko man a musal ci dee. Te ñaanam nangu na, ndax ni mu jébbale boppam Yàlla.
5:8b.HEB.005.008 Waaye li muy nekk-nekk doom, teewul mu jàng déggal Yàlla, jaare ko ci coono bi mu daj.
5:9b.HEB.005.009 Noonu la àgge cig mat, ñu def ko ki waral mucc gi dul jeex, ngir ñi ko déggal ñépp.
5:10b.HEB.005.010 Fekk na Yàlla tudde ko saraxalekat bu mag ni ko Melkisedeg nekke.
5:11b.HEB.005.011 Ci fànn googu, am na lu bare lu nu ci bëgg a wax, waaye tekkil leen ko dina jafe, ndaxte dangeen a naqari xel.
5:12b.HEB.005.012 Bu yàgg ngeen waroon a jàngal ñeneen ñi, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci kàddug Yàlla. Léegi nag yéena ngi tollu fi ñu leen war a nàmpale, ndaxte àttanuleen ñam wu dëgër.
5:13b.HEB.005.013 Képp kuy nàmp, ab xale nga ba tey. Jëfeegoo njàngale, mi jëm ci wàllu njubte.
5:14b.HEB.005.014 Waaye ñam wu dëgër, ñi mat a ko yelloo, maanaam ñiy jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon.
6
6:1b.HEB.006.001 Kon nag léegi, nanu jóge ci liifantu gi jëm ci Kirist, te jàll cig mat. Nanu bañ a dalaat njàngale mu jëkk moomu, ci ne nit ñi dañoo war a tuub jëf, yi jëm ci dee, te gëm Yàlla,
6:2b.HEB.006.002 di leen jàngalaat ci mbirum sangu set ci ay fànn yu bare, ak teg loxo ak ci mbirum ndekkite ak lu jëm ci àtte biy sax dàkk.
6:3b.HEB.006.003 Te noonu lanuy def, bu soobee Yàlla.
6:4b.HEB.006.004 Li nu war a jëme kanam mooy lii: su amee ay nit ñu Yàlla xas a leeral ba noppi, ñu mos mayu Yàlla gi, am wàll ci Xelam mu Sell,
6:5b.HEB.006.005 te xam mbaax, gi ci kàddug Yàlla, ak kéemaani jamono jiy ñëw,
6:6b.HEB.006.006 te loolu lépp teewul ñu walbatiku, ñooñu kenn dootu leen man a yeesalaat, ba ñu tuub seeni bàkkaar. Li ko waral moo di, dañoo bëgg a daajaat Doomu Yàlla ji ci bant, di ko toroxal, te fekk muy seen ngaañ.
6:7b.HEB.006.007 Maanaam suuf suy naan taw bi ciy dal, tey jox ñi ñu koy beyal gàncax gu am njariñ, day jot barke bi jóge ci Yàlla.
6:8b.HEB.006.008 Waaye su meññee ay dég ak ay xaaxaam, du am benn njariñ; repp na ñu alag ko, te lakk lay mujje.
6:9b.HEB.006.009 Waaye nag yéen samay soppe, su fekkee ne sax, nii lanuy waxe, nu ngi yaakaar li gën ci yéen te ànd ak mucc.
6:10b.HEB.006.010 Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak mbëggeel, gi ngeen wone ci turam, ci li ngeen dimbali ay gaayam, te yéena ngi koy def ba tey.
6:11b.HEB.006.011 Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yéen wone cawarte gu mel ni ga ngeen amoon, ba kera ngeen di am mat, gi ngeen di séentu.
6:12b.HEB.006.012 Bëggunu ngeen tayel, waaye royleen ñi gëm te muñ, ndaxte ñooy jot li leen Yàlla dig.
6:13b.HEB.006.013 Ibraayma bokk na ci ñoom. Bi ko Yàllay dig, mënul woon a giñ ci keneen ku ko gën a màgg, ba tax mu giñ ci boppam,
6:14b.HEB.006.014 ne ko: «Sàllaaw dinaa la barkeel, yokk saw askan.»
6:15b.HEB.006.015 Noonu Ibraayma di xaar tey muñ, ba jot li ko Yàlla digoon.
6:16b.HEB.006.016 Nit kuy giñ nag, daf koy wékk ci ku ko sut. Ngiñ lu mel noonu moo wóoral mbir te mooy jeexal lépp lu ñuy werante.
6:17b.HEB.006.017 Ñi war a jot li mu dige, Yàlla dafa leen bëggoon a won ne, dogalam du tebbiku mukk; looloo tax mu dige, boole ci ngiñ.
6:18b.HEB.006.018 Noonu ñaari jëf yooyu nga xam ne duñu tebbiku te Yàlla mënu cee dellu gannaaw, dañu nuy gën a sóob ci muñ, nun ñi daw ba am kiiraay, ngir nu man a téye bu dëgër yaakaar, ji mu nu dig.
6:19b.HEB.006.019 Ci yaakaar jooju lanu sës sunu xol, ba man a sampu bu dëgër. Yaakaar la juy jàll ba fa Yàlla nekk, ca gannaaw ridob bérab bu sell-baa-sell.
6:20b.HEB.006.020 Yeesu ci boppam moo fa jëkk a dugg, muy ndaw li nu jiitu, ñu def ko saraxalekat bu mag ba fàww, mel ni Melkisedeg.
7
7:1b.HEB.007.001 Melkisedeg moomu doon buuru Salem, moo nekkoon saraxalekat ca Yàlla Aji Kawe ji. Gannaaw ba Ibraayma dàqee buur ya, ba dellusi, Melkisedeg gatandu woon na ko, di ko barkeel.
7:2b.HEB.007.002 Noonu Ibraayma fab fukkeelu cér bi, maanaam asaka, ci li mu jële woon ci xare ba lépp, jox ko. Ci lu jëkk turu Melkisedeg mi ngi tekki «buur bu jub bi.» Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki «buuru jàmm.»
7:3b.HEB.007.003 Melkisedeg nag xamaluñu ko baay, xamaluñu ko yaay walla menn maam. Amul fenn fu ñu wax ag juddoom walla ag deeyam. Moo tax nu di ko mengale ak Doomu Yàlla ji, ndaxte saraxalekat la bu kenn dul wuutu.
7:4b.HEB.007.004 Seetleen ni mu màgge, moom Melkisedeg! Ibraayma sax, maamu cosaan mi, fab na li mu jële woon lépp ca xare ba, jox Melkisedeg asaka ja.
7:5b.HEB.007.005 Yoonu Musaa digle na ne, ñi bokk ci giiru Lewi te di ay saraxalekat, nañu jot asaka ci alalu bànni Israyil, doonte sax ñuy seeni bokk te soqikoo ci Ibraayma.
7:6b.HEB.007.006 Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Yàlla sédde woon dige yi.
7:7b.HEB.007.007 Kiy barkeel a gën a màgg ki ñuy barkeel, loolu amu ci benn werante.
7:8b.HEB.007.008 Saraxalekat yi soqikoo ci Lewi, ñu ngi jot asaka, ni ko Melkisedeg jote woon. Waaye ñoom ñu nar a dee lañu. Melkisedeg nag moom, Mbind mi wóoral na ne, dafay dund.
7:9b.HEB.007.009 Léegi nag ci ni ñu ko man a waxe, Lewi miy jot asaka ci bànni Israyil, moom ci boppam jox na ko Melkisedeg, jaare ko ci Ibraayma.
7:10b.HEB.007.010 Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma, bi ko Melkisedeg gatandoo.
7:11b.HEB.007.011 Jox nañu bànni Israyil yoon wu sukkandiku ci liggéeyu saraxalekat yi soqikoo ci Lewi. Su fekkoonte ne nag liggéeyu saraxalekat yooyu manoon na yeggale nit cig mat, kon du soxlaati ab saraxalekat ni ko Melkisedeg nekke, ci fànn gu wuute ak gu Aaroona.
7:12b.HEB.007.012 Te bu ñu fi jëlee saraxalekat yi ak seen liggéey, dañoo war a toxal itam yoon, wi ñu fi tëraloon.
7:13b.HEB.007.013 Noonu Yeesu mi nuy wax, mi ngi soqikoo ci geneen giir gu bokkul ak giiru Lewi. Giir googu nag, amu ci kenn ku ci mas a def liggéeyu saraxale ca saraxalukaay ba.
7:14b.HEB.007.014 Li wóor moo di, sunu Boroom mi ngi soqikoo ci giiru Yuda. Te bi Musaa bindee ci mbirum saraxalekat yi, limaalewul woon giir googu.
7:15b.HEB.007.015 Li waral mbir mi gën a leer moo di ne, beneen saraxalekat bu mel ni Melkisedeg dafa ñëw.
7:16b.HEB.007.016 Te defuñu ko saraxalekat jaarale ko ci yoonu ndono, waaye fal nañu ko ci dooley dund gu amul àpp.
7:17b.HEB.007.017 Ndaxte seedeel nañu Yeesu lii:«Doon nga saraxalekat ba fàwwmel ni Melkisedeg.»
7:18b.HEB.007.018 Noonu tebbi nañu yoon wu jëkk, wa néewoon doole te meññul dara
7:19b.HEB.007.019 --ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat — waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu man a jaare ngir jege Yàlla.
7:20b.HEB.007.020 Te rax-ca-dolli ngiñ ànd na ci. Ndaxte ñi soqikoo ci Lewi doon nañu ay saraxalekat te kenn giñul.
7:21b.HEB.007.021 Waaye nag Yeesu moom doon na saraxalekat, bi Yàlla giñee ne ko:«Boroom bi giñ nate du dellu gannaaw mukk:“Doon nga saraxalekat ba fàww.”»
7:22b.HEB.007.022 Ngiñ loolu moo tax Yeesu nekk tayle, giy wóoral kóllëre gi gën.
7:23b.HEB.007.023 Te it yeneen saraxalekat yi dañoo bare woon, ndaxte dee moo daan tax duñu man a sax ci seen liggéey.
7:24b.HEB.007.024 Waaye Yeesu miy dund ba fàww, sasoo na liggéeyu saraxale bu sax fàww.
7:25b.HEB.007.025 Loolu moo tax it mu man a musal tey yeggale cig mat ñiy jaar ci moom te bëgg jege Yàlla, ndaxte mi ngi dund ba fàww ngir di leen rammu.
7:26b.HEB.007.026 Kon nag Yeesu mooy saraxalekat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq bàkkaar, bokkul dara ak bàkkaarkat yi, te yéege nañu ko fa Yàlla.
7:27b.HEB.007.027 Niroowul ak yeneen saraxalekat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam.
7:28b.HEB.007.028 Naka yoonu Musaa, aji néew doole yi lay fal saraxalekat yu mag. Waaye ngiñu Yàlla gi ñëw gannaaw yoon wi, Doom ji la fal saraxalekat bu mag bu mat ba fàww.
8
8:1b.HEB.008.001 Lii mooy li ëpp solo ci li nuy wax: am nanu saraxalekat bu mag bu mel noonu, moom mi toog ci ndeyjooru Aji Màgg ja ca nguuram ca kaw.
8:2b.HEB.008.002 Mu ngi liggéey ca bérab bu sell-baa-sell, di màggalukaay bu dëggu. Nit defaru ko; Boroom bee ko sos.
8:3b.HEB.008.003 Bépp saraxalekat bu mag fal nañu ko, ngir muy def ay sarax ak ay saraxi mala yu jëm ca Yàlla. Kon nag fàww Yeesu am lu mu joxe.
8:4b.HEB.008.004 Bu nekkoon ci àddina, du nekk sax saraxalekat, ndaxte am na fi ba noppi ay saraxalekat yuy def ay sarax, ni ko yoonu Musaa santaanee.
8:5b.HEB.008.005 Saraxalekat yooyu ñu ngi liggéeyal Yàlla ca màggalukaay, ba nekk misaal tey takkandeeru yëf yu dëggu, ya féete kaw. Moo tax ba Musaa naree defar tàntu màggalukaay ba, Yàlla artu na ko ne ko: «Teeylul ba def lépp, roye ko ci bi ma la won ca tund wa.»
8:6b.HEB.008.006 Waaye léegi nag liggéeyu saraxale, bi ñu jox Yeesu, moo gën a màgg liggéeyu saraxalekat yooyu, mel ni it kóllëre, gi Yeesu fas diggante Yàlla ak nit, moo sut kóllëre gu jëkk ga te mu tëdd ci ay dige yu ëpp yu jëkk ya.
8:7b.HEB.008.007 Bu fekkoonte ne, kóllëre gu jëkk ga dafa amul woon benn sikk, kon du aajo ñu koy weccee ak geneen.
8:8b.HEB.008.008 Waaye nag Yàlla sikk na bànni Israyil, bi mu naan:Boroom bi nee na:«Ay fan a ngi ñëwyu may fasi kóllëre gu beesak bànni Israyil ak waa Yude.Kóllëre googu nagbokkul ak gi ma fasoon ak seeni maam,
8:9b.HEB.008.009 ba ma leen jàppee ci loxo,génne leen réewu Misra.Boroom bi nee na:Beddeeku naa leenndaxte sàmmuñu sama kóllëre.
8:10b.HEB.008.010 Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak bànni Israyil,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xel,bind ko ci seen xol.Dinaa nekk seen Yàlla,ñu doon samay gaay.
8:11b.HEB.008.011 Kenn dootul war a jàngal moroomamwalla mbokkam, di wax naan:“Xamal Boroom bi!”Ndaxte ñépp dinañu ma xam,li dale ci ki gën a ndaw ba ci ki gën a mag.
8:12b.HEB.008.012 Ndaxte dinaa leen baal seeni tooñ,te dootuma fàttaliku seeni bàkkaar.»
8:13b.HEB.008.013 Kon nag bi Yàllay wax ci kóllëre gu bees gi, dafa fekk mu màggatal gu jëkk ga. Te lu xewwi te màggat mi ngi ci tànki wéy.
9
9:1b.HEB.009.001 Kóllëre gu jëkk ga ëmboon na ay ndigal ci mbirum ni ñu war a jaamoo Yàlla. Amoon na itam kër Yàlla gu nekkoon àddina.
9:2b.HEB.009.002 Nekkoon na ab tàntu màggalukaay bu ñu séddale ñaari néeg. Ca ba jiitu la làmpu diwlin ba nekkoon ak taabal, ja ñu daan teg mburu ya ñu daa jébbal Yàlla. Foofaa nga tuddoon bérab bu sell ba.
9:3b.HEB.009.003 Néeg ba ñu tudde bérab bu sell-baa-sell a nga nekkoon ca gannaaw ñaareelu rido ba.
9:4b.HEB.009.004 Saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, a nga fa woon, ak gaalu kóllëre, ga ñu taf wurus ba mu daj. Ca biir gaal ga amoon na fa benn njaqu wurus bu defoon ñam, wi ñuy wax mànn, ak it yetu Aaroona wi jebbi woon, ak àlluway doj, ya ñu bindoon wax yi kóllëre gi ëmb.
9:5b.HEB.009.005 Ca kaw gaal ga teg nañu fa ñaari nataali mbindeef yu ñuy wax Seruben, yu doon wone ndamu Yàlla. Seeni laaf ñoo doon yiir baalukaay ba. Waaye loolu lépp léegi mënunu koo tekki benn-benn.
9:6b.HEB.009.006 Ba ñu defaree lépp, saraxalekat ya dañu daan dugg bés bu set ca néeg bu jëkk ba, ngir mottali seen liggéeyu saraxale ca Yàlla.
9:7b.HEB.009.007 Waaye ca néeg ba ca topp, saraxalekat bu mag ba rekk moo fa daan dugg benn yoon ci at mi. Te daawu fa dugg mukk te yóbbaalewul deretu mala, yi muy jagleel Yàlla, ngir bàkkaari boppam ak yu mbooloo mi daan def ci seen ñàkka xam.
9:8b.HEB.009.008 Ci noonu nag Xel mu Sell mi wone na ne, yoon wi ñuy jaar, ba dem ca bérab bu sell-baa-sell, ubbikoogul woon, fi ak tànt ba jëkk baa ngi doon taxaw.
9:9b.HEB.009.009 Misaal la ci jamonoy tey; dafay wone ne, sarax yi ak saraxi mala yi ñu daan jagleel Yàlla, mënuñoo dalal xelu jaamukatu Yàlla bi.
9:10b.HEB.009.010 Sarax yooyu ñu ngi jëmoon ci lekk ak ci naan ak ci fànn yu bare ci mbirum sangu set. Ay sàrt yu jëm ci yaram lañu, yu ñu waroon a farataal, ba kera jamono ji Yàllay tëral kóllëre gu bees.
9:11b.HEB.009.011 Waaye Kirist ñëw na, doon saraxalekat bu mag, bi joxe xéewal yi teew. Jaar na ca màggalukaay ba gën a màgg te gën a mat, te màggalukaay booba loxol nit defaru ko, maanaam bokkul ci àddina sii.
9:12b.HEB.009.012 Noonu Kirist dugg na benn yoon ba fàww ca bérab bu sell-baa-sell. Duggu fa ak deretu sikket yi ak yu yëkk yi. Waaye mi ngi duggaale ak deretu boppam te indil na nu noonu njot gu amul àpp.
9:13b.HEB.009.013 Deretu sikket yi ak ju yëkk yi, ak wëllu, wi ñu lakk te di suy dóom bi ñi taq sobe, ñooy sellal yaram.
9:14b.HEB.009.014 Su fekkee ne noonu la deme nag, du kon deretu Kirist moo ëpp doole? Jox na bakkanam Yàlla, def ko sarax su amul sikk jaarale ko ci dooley Xel miy sax abadan. Kon deretam moo man a sellal sunu xel, mi nu doon yedd ndax jëf yu jëm ci dee, ngir nu man a jaamu Yàlla jiy dund.
9:15b.HEB.009.015 Looloo tax mu nekk Rammukat bi ci wàllu kóllëre gu bees ci diggante Yàlla ak nit, ngir ñi Yàlla woo am cér bu sax ci kaw, te mu digoon leen ko, ndaxte Kirist dee na, ngir jot ñi jàdd yoon ca kóllëre gu jëkk ga.
9:16b.HEB.009.016 Ci li jëm ci dénkaane bu ñu bind, jëme ci miraas, fàww ñu wone firndeg deewu ka ko bind,
9:17b.HEB.009.017 ndaxte bala dénkaaneb miraas di taxaw, dee am; te taxawul, fi ak ki ko bind a ngi dund.
9:18b.HEB.009.018 Looloo waral kóllëre gu jëkk ga, ñu fasoon ko ak deret.
9:19b.HEB.009.019 Keroog Musaa jàng na ndigali yoon wépp ci kanamu bànni Israyil gépp. Gannaaw loolu jël na deretu wëllu, jëlaale ndox, ak bantu garab gu ñuy wax isob, laxas ci kawaru xar mu xonq. Noonu mu capp ko ca deret ja, daldi ko wis ca téereb yoon wa ak ca mbooloo mépp
9:20b.HEB.009.020 te naan: «Lii mooy deretu kóllëre gi leen Yàlla tëralal.»
9:21b.HEB.009.021 Noonu mu daldi wis it deret ja ca tànt ba ak ca jumtukaay, ya ñu daan jaamoo.
9:22b.HEB.009.022 Ndaxte ci yoonu Musaa, daanaka deret lañuy sellale lépp, te bu deret tuuruwul, mbaalug bàkkaar du am.
9:23b.HEB.009.023 Yëfi àddina yi misaal yu dëggu yi ci asamaan, war nañu leen a sellale noonu. Waaye yëf yu dëggu yooyu ci asamaan, laaj na sarax yu gën a baax, ngir ñu sell.
9:24b.HEB.009.024 Ndaxte Kirist duggul ci bérab bu sell bu nit tabax, muy doon nataal ci bu dëggu bi. Waaye dugg na ca biir asamaan sax, ngir taxawal nu ca kanam Yàlla léegi.
9:25b.HEB.009.025 Saraxalekat bu mag bi dafay dugg at mu jot ca bérab bu sell-baa-sell ak deret ju dul josam. Waaye Kirist joxewul bakkanam ay yooni yoon.
9:26b.HEB.009.026 Bu demee woon noonu, kon dina sonn ba tàyyi ca njàlbéenug àddina ba tey. Waaye nag benn yoon rekk la feeñu ci mujjeelu jamono yi, joxe boppam ni sarax ngir far bàkkaar yi.
9:27b.HEB.009.027 Kon ni nit ñi deeye benn yoon rekk, ba noppi jaar ca àtte ba, ni ko Yàlla dogale,
9:28b.HEB.009.028 noonu it la Kirist joxee boppam benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina feeñaat, waxuma ci mbiri bàkkaar, waaye ngir indil ñi koy séentu mucc gi.
10
10:1b.HEB.010.001 Yoonu Musaa dafa misaal xéewal yi waroon a ñëw; takkandeer la ci yëf yu dëggu yi, waaye du ñoom ci seen bopp. Looloo tax mënul a yeggale cig mat ñi ñëw ci Yàlla, ndaxte at mu nekk duñu jóg ci jébbal Yàlla sarax yooyu.
10:2b.HEB.010.002 Sarax yi ñuy def, bu ñu manoon a sellal ñiy jaamu benn yoon ba fàww, kon dinañu leen bàyyi, ndaxte dootuñu am yeraange ci seeni bàkkaar.
10:3b.HEB.010.003 Waaye dañuy fàttaliku bàkkaar yi ci sarax yi ñuy def at mu jot.
10:4b.HEB.010.004 Ndaxte deretu yëkk yi ak ju sikket yi mënuñoo dindi bàkkaar yi.
10:5b.HEB.010.005 Looloo tax bi muy wàcc àddina, Kirist nee na:«Bëggoo saraxu mala walla beneen sarax,waaye aw yaram nga ma defaral.
10:6b.HEB.010.006 Sarax yu ñuy lakkwalla sarax yiy dindi bàkkaar,benn neexu la ci.
10:7b.HEB.010.007 Moo tax ma ne: “Damaa wàccngir def sa coobare, yaw Yàlla,mu dëppoo ak li ñu bind ci sama mbirci téereb yoon wi.”»
10:8b.HEB.010.008 Wax na bu jëkk: «Saraxi mala walla yeneeni sarax, sarax yu ñuy lakk walla sarax yiy dindi bàkkaar, bëgguloo leen te benn neexu la ci.» Teewul yoon wi moo leen santaane.
10:9b.HEB.010.009 Noonu mu tegaat ca ne: «Damaa wàcc ngir def sa coobare.» Noonu toxal na jëfin wu jëkk wa, ngir wuutal fi weneen wu bees.
10:10b.HEB.010.010 Te ci li Kirist def coobareg Yàlla, bi mu joxee yaramam sarax benn yoon ba fàww, moo tax nu sell ci bàkkaar.
10:11b.HEB.010.011 Bés bu nekk saraxalekat yi dañuy taxaw di liggéeyal Yàlla, di sax ci def sarax yu mënul a dindi bàkkaar yi mukk.
10:12b.HEB.010.012 Waaye nag saraxalekat bii di Kirist, bi mu saraxee sarax bu am doole ngir dindi bàkkaar yi benn yoon ba fàww, dafa toog ca ndeyjooru Yàlla,
10:13b.HEB.010.013 di xaar ba kera mu daaneel ko ay noonam ci kanamam.
10:14b.HEB.010.014 Noonu ñi ñuy sellal, ci benn sarax rekk la leen yeggali cig mat ba fàww.
10:15b.HEB.010.015 Te it Xel mu Sell mi seedeel na nu ko;
10:16b.HEB.010.016 dafa jëkk a wax ne:«Boroom bi nee na:Kóllëre gaa ngii,kóllëre gi may fas ak ñoom,bu bés yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xol,bind ko ci seen xel.»
10:17b.HEB.010.017 Noonu mu tegaat ca ne:«Dootuma fàttaliku seeni bàkkaarwalla seeni tooñ.»
10:18b.HEB.010.018 Kon nag fu ñuy baale bàkkaar, aajootul sarax su koy dindi.
10:19b.HEB.010.019 Bokk yi, gannaaw nag deretu Yeesu may na nu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell-baa-sell,
10:20b.HEB.010.020 nuy jaar ci rido bi, ci yoon wi mu nu ubbil, di yoon wu bees tey dund, maanaam ndax li mu joxe yaramam sarax te mi ngi dund,
10:21b.HEB.010.021 te gannaaw am nanu saraxalekat bu mag, biy yilif waa kër Yàlla,
10:22b.HEB.010.022 kon nanu jege Yàlla ak xol bu laab, ak ngëm gu ànd ak kóolute, am xel mu dal ci bépp yeraange, ak yaram wu ñu raxas ci ndox mu sell.
10:23b.HEB.010.023 Nanu jàpp ci yaakaar, ji nu am, te bañ a toqi, ndaxte ki nu dig, lu mu wax def ko.
10:24b.HEB.010.024 Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax.
10:25b.HEB.010.025 Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi.
10:26b.HEB.010.026 Gannaaw ba nu nangoo xam dëgg ba noppi, bu nu teyee di def bàkkaar, kon sarax dootul am ngir bàkkaar yooyu.
10:27b.HEB.010.027 Déedéet, bu nu defee noonu, dinanu tiit di xaar àtte ba, muy taal bu yànj, biy war a lakk nooni Yàlla yi.
10:28b.HEB.010.028 Ku weddi ndigali yoonu Musaa wi, te ñaar walla ñetti nit seede ko, dina dee ci lu amul benn yërmande.
10:29b.HEB.010.029 Ku xeeb Doomu Yàlla ji te fonkadi deretu kóllëre, ji ñu ko sellale, te muy toroxal Xelum Yàlla, mi indi yiw, naka la mbugalam war a gën a yéese?
10:30b.HEB.010.030 Xam nanu ki wax ne: «Man maay àtte, maay fey jëf.» Te newaat na: «Boroom bi dina àtte ay gaayam.»
10:31b.HEB.010.031 Ndaw tiitaange ci ku sàggan, ba tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund!
10:32b.HEB.010.032 Fàttalikuleen bés yu jëkk ya, ba leeru Yàlla tàbbee ci yéen; dékku ngeen xeex bu mag ciy fitna.
10:33b.HEB.010.033 Léeg-léeg ñu saaga leen ak di leen sonal ci kanamu nit ñi; léeg-léeg it ngeen taxawu ñi ñuy def noonu.
10:34b.HEB.010.034 Ndaxte bokk ngeen naqar ak ñi ñu tëj, te nangu ngeen ak xol bu sedd, ñu foqarñi seen alal, xam ne, am ngeen alal ju gën te di sax ba fàww.
10:35b.HEB.010.035 Kon nag buleen sàggane kóolute gi ngeen am, ndaxte ëmb na yool bu mag.
10:36b.HEB.010.036 Dangeen a war a muñ, ba def coobareg Yàlla, sog a jot li mu leen digoon.
10:37b.HEB.010.037 Ndaxte lii la Mbind mi wax:«Ci kanam tuuti, ki war a ñëw dina ñëwte léegi mu agsi.
10:38b.HEB.010.038 Ku jub ci sama kanam dina dund ci kaw ngëm,waaye bu delloo gannaaw,sama xol du sedd ci moom.»
10:39b.HEB.010.039 Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw bay réer, waaye nu ngi bokk ci ñi am ngëm tey mucc.
11
11:1b.HEB.011.001 Am ngëm lii lay tekki: dafa nuy wóor ne, li nuy yaakaar dina am, te it li nu dul gis nekk na.
11:2b.HEB.011.002 Maam ya, seen ngëm a tax ba Yàlla seedeel leen lu baax.
11:3b.HEB.011.003 Ngëm a tax ba nu xam ne, Yàlla sàkk na àddina jaarale ko ci kàddoom, ngir li bët di gis, defarees ko ak lu bët mënul a gis.
11:4b.HEB.011.004 Ngëm moo tax ba Abel jébbal Yàlla sarax su gën saraxu Kayin. Ngëmu Abel moo tax ba Yàlla àtte ko ni ku jub, bi mu ko seedeelee ne, saraxam baax na. Te ci kaw ngëm lay wax ba tey, moom mi dee ba noppi.
11:5b.HEB.011.005 Ngëm moo tax ba Enog jaarul ci dee. Yàllaa ko yóbbu ca moom, te kenn gisatu ko, ndaxte Yàllaa ko toxal. Ndaxte Mbind mi seedeel na ko ne, laata muy toxu, neex na Yàlla.
11:6b.HEB.011.006 Waaye ku amul ngëm doo man a neex Yàlla, ndaxte ku bëgg a jegeñ Yàlla war ngaa gëm ne, Yàlla am na te dina neexal ñi koy wut.
11:7b.HEB.011.007 Ngëm moo tax ba, bi Yàlla yégalee Nóoyin lu jiitu ci mbir yi dikkagul, mu ragal ba defar gaal ngir musal njabootam. Ngëmam moo tax mu yey niti àddina, ba noppi jot njubte, li Yàllay joxe ci kaw ngëm.
11:8b.HEB.011.008 Ngëm moo tax ba Ibraayma déggal Yàlla. Bi ko Yàlla wooyee, mu dem toxu ci menn réew, ma mu waroon a jote ca Yàlla. Noonu la gàddaaye dëkkam te xamul woon fan la jëm.
11:9b.HEB.011.009 Ngëm a tax ba Ibraayma sanc ci réew, mi ko Yàlla digoon, dëkk ci ay tànt ni doxandéem, moom ak doomam Isaaxa ak sëtam Yanqóoba, fekk sax Yàlla digoon na leen réew mi.
11:10b.HEB.011.010 Waaye nag Ibraaymaa ngi doon séentu dëkk bi sax, bi Yàlla tabax te sanc ko.
11:11b.HEB.011.011 Ngëm moo tax ba Ibraayma, li muy màggat lépp te Saarata mënul woon a am doom, Yàlla def ba mu jur doom, ndaxte dafa gëmoon ne, Yàlla lu mu dige def ko.
11:12b.HEB.011.012 Looloo tax ba, Ibraayma mi màggat lool, aw xeet jóge ci moom, baree ni biddiiwi asamaan, te sakkan ni suufu tefes, ba kenn mënu koo xayma.
11:13b.HEB.011.013 Ñoom ñépp dee nañu ci ngëm. Jotuñu li ñu leen digoon, waaye séen nañu ko fu sore ba nuyu leen, te nangu ne, ay doxandéem ak i gan lañu woon ci àddina.
11:14b.HEB.011.014 Ñiy waxe noonu nag dañuy wone ne, ñoo ngi wut réew mu ñu moomal seen bopp.
11:15b.HEB.011.015 Bu ñu nammoon réew mi ñu jóge, kon dinañu am jotu dellu fa.
11:16b.HEB.011.016 Waaye ñu ngi doon séentu réew mu gën, maanaam mi nekk ci asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu koy wooye seen Yàlla, ndaxte defaral na leen ab dëkk.
11:17b.HEB.011.017 Ngëm moo tax Ibraayma naroon a rey Isaaxa ni sarax, bi ko Yàlla nattoo. Moom mi jotoon dige yi, moo demoon bay saraxe jenn doom ji mu am kepp,
11:18b.HEB.011.018 fekk sax Yàlla nee woon na ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.»
11:19b.HEB.011.019 Waaye xelu Ibraayma jàppoon na ne, Yàlla am na dooley dekkal néew yi. Te dëgg-dëgg ci misaal dafa mel ni, Isaaxa dafa dee te dekki.
11:20b.HEB.011.020 Te it ngëm moo tax ba Isaaxa barkeel Yanqóoba ak Esawu, di wax ci mbirum yëf yiy ñëw.
11:21b.HEB.011.021 Ngëm moo tax ba, bi Yanqóoba nekkee ci sukkurat, mu barkeel kenn ku nekk ci doomi Yuusufa yi. Moo tax it mu màggal Yàlla, jafandu ci yetam.
11:22b.HEB.011.022 Ngëm moo tax ba, bi Yuusufa nekkee ci sukkurat, mu waxoon ci gàddaay gi bànni Israyil waroon a gàddaaye Misra, di joxe ndigal jëme ci mbirum néewam.
11:23b.HEB.011.023 Ngëm moo tax ba, bi Musaa juddoo, ay waajuram nëbb ko lu mat ñetti weer, ndaxte gisoon nañu ne, xale bu taaru la woon, te ragaluñu woon ndigalu buur bi.
11:24b.HEB.011.024 Ngëm a tax ba bi Musaa màggee, muy bañ ñu koy wooye sëtu Firawna.
11:25b.HEB.011.025 Bokk coono ak gaayi Yàlla yi moo ko gënaloon muy bànneexu ab diir ci bàkkaar.
11:26b.HEB.011.026 Ñu toroxal ko ngir Almasi bi mi ngi mel ci moom ni alal ju ëpp alali Misra yépp, ndaxte yool bi la doon séentu.
11:27b.HEB.011.027 Ngëm moo tax mu jóge Misra te ragalul merum buur bi. Dafa muñ, mel ni nit kuy gis Yàlla, mi kenn mënul a teg bët.
11:28b.HEB.011.028 Ngëm moo tax mu sos màggalu Bésu Jéggi ba, di wis deret ci bunt yi, ngir malaakam Yàqkat mi bañ a laal taawi bànni Israyil.
11:29b.HEB.011.029 Ngëm moo tax ba bànni Israyil jaar ci Géej gu xonq gi, mel ni kuy jaar ci yoonu suuf su wow. Waaye bi ci waa Misra yi doon jéem a jaar, ñoom ñu daldi lab.
11:30b.HEB.011.030 Ngëm moo tax miir yi wëroon dëkku Yeriko màbb, gannaaw ba ko bànni Israyil wëree lu mat juróom-ñaari fan.
11:31b.HEB.011.031 Ngëm moo tax ba Raxab jigéenu moykat bi mucc, keroog ba ñuy bóom ñi déggadiloon Yàlla, ndax li mu teeru woon yëddukat ya teeru bu ànd ak jàmm.
11:32b.HEB.011.032 Lu ma ci war a tegaat? Ndaxte awma jotu wax ci mbirum Sedeyon, Barag, Samson, Yefte, Daawuda, Samwil ak yonent yi.
11:33b.HEB.011.033 Seen ngëm a tax ñu noot ay buur, di doxal yoon tey jot li Yàlla dige. Ngëm moo tax ba tey, ñu tëj gémmiñu gaynde yi,
11:34b.HEB.011.034 fey dooley safara, rëcc ci jaasi, ñu génn ci néew doole, dugg ci kàttan, doon ay jàmbaar, dàq xarekat, ya jóge bitim réew.
11:35b.HEB.011.035 Ngëm moo tax ba ay jigéen gis ñu dekkal seeni néew, delloo leen ko; ñeneen ñi ñu metital leen, te bañ ku leen musal, ngir jot ndekkite lu gën.
11:36b.HEB.011.036 Ñeneen ñi dékku nañu ay xas ak ay yar, ay jéng ak kaso yi.
11:37b.HEB.011.037 Ñii, sànni nañu leen ay xeer ba ñu dee; ñii, ñu xar leen ñaar; ñii, ñu reye leen jaasi. Ñu ngi doon wëndéelu, sol ay deri xar ak yu bëy, di ay walaakaana; ñu di leen sonal, di leen fitnaal.
11:38b.HEB.011.038 Ñu ngi leen doon def noonu, fekk àddina sax yelloowul leen. Ñu ngi doon wëreelu ci àll yi ak ci tund yi, dal ci xunti yi ak ci kàmb yi.
11:39b.HEB.011.039 Nit ñooñu ñépp, seen ngëm a tax ba Yàlla seedeeloon leen lu baax. Moona de, jotuñu li Yàlla dige woon,
11:40b.HEB.011.040 ndaxte Yàlla dafa tëral lu gën ci nun te bëggu leen a yeggale cig mat, fi ak ànduñu ci ak nun.
12
12:1b.HEB.012.001 Kon nag gannaaw mbooloo mu bare moo nu yéew, di nu seedeel seen ngëm, nanu yenniku bépp yen ak bàkkaar bu nuy téqtal ci lu yomb, tey daw xél wi nekk sunu kanam, ànd ci ak muñ.
12:2b.HEB.012.002 Nanu ne jàkk Yeesu, moom mi samp ngëm, ba ub làmbi ngëm. Mbég mi mu dëgmël moo tax mu dékku dee ca bant ba te faalewul toroxte, ji ko fa fekk, ba noppi toog ca ndeyjooru jal, ba Yàlla nekk.
12:3b.HEB.012.003 Defleen seen xel ci moom, moom mi muñ noonu ko bàkkaarkat yi bañe woon, ngir bañ seen kàttan jeex, ngeen xàddi.
12:4b.HEB.012.004 Yéen demaguleen ba tuur seen deret ci seen bëre ak bàkkaar.
12:5b.HEB.012.005 Te fàtte ngeen li leen Yàlla dénk ni baay ak ay doomam naan:«Sama doom, bul fonkadi yarub Boroom bimbaa ngay xàddi, bu lay yedd,
12:6b.HEB.012.006 ndaxte ku Boroom bi sopp, yar la,tey duma bépp doom bu mu nangu.»
12:7b.HEB.012.007 Li ngeen di war a muñ, ab yar la. Yàlla dafay jëf ak yéen ni ay doomam, ndaxte ana doom ju baayam dul yar?
12:8b.HEB.012.008 Bu ngeen bokkul woon ci yar, bi ñépp am wàll, kon dungeen ay doomi yoon; ay doom yu daganul ngeen.
12:9b.HEB.012.009 Waaye sax far, sunuy baay ci àddina yaroon nañu nu, te wegoon nanu leen. Baay bi yore ruu yi kon, xanaa warunu koo gën a déggal ngir man a dund?
12:10b.HEB.012.010 Sunuy baay yar nañu nu diir bu gàtt ci seen coobare. Waaye Yàlla dafa nuy yar ngir sunu njariñ, ngir nu bokk ci sellaayam.
12:11b.HEB.012.011 Li am moo di ne, yar bu nuy dal, du ànd ak bànneex, day naqari, waaye gannaaw ga dafay meññ jub ak jàmm, ci ñi ko jariñoo.
12:12b.HEB.012.012 Kon nag mayleen doole loxo yi toqi, ak óom yi bañ,
12:13b.HEB.012.013 te fàkkal seeni tànk ay yoon yu jub, ngir cér bi làggi bañ cee jekkalikoo waaye mu wére ci.
12:14b.HEB.012.014 Wutleen ak ñépp jàmm te fonk dund gu sell, ndaxte ku sellul doo gis Boroom bi.
12:15b.HEB.012.015 Moytuleen ba kenn du ñàkk yiwu Yàlla mbaa kenn mel ni reen bu wex buy jebbi, ba di leen lëjal tey gaañ ñu bare ci wextanam.
12:16b.HEB.012.016 Moytuleen it ba kenn du njaaloo walla muy fonkadi yëfi Yàlla, ni Esawu, mi weccee woon ndonol taawam ngir ag lekk.
12:17b.HEB.012.017 Xam ngeen ne, ba ñu ca tegee tuuti, gàntu nañu ko, ba mu bëggee jot barke bi. Amul fenn fu mu jaar ba defar njuumteem, te jooy, yi mu doon jooy, mënu ci dara.
12:18b.HEB.012.018 Ndaxte meluleen ni bànni Israyil ñoom ñi jege woon tund wu ñu man a laal, wu doon tàkk jeppit te ànd ak xiin ak lëndëm ak ngelaw.
12:19b.HEB.012.019 Jegewuleen liit guy jib ak baat buy wax ay wax yoo xam ne ñi ko doon dégg, ñaan ñu bañ leen cee tegal benn baat,
12:20b.HEB.012.020 ndaxte mënuñu woon a dékku ndigal lii: «Su mala sax laalee tund wa, nangeen ko sànni ay xeer, ba mu dee.»
12:21b.HEB.012.021 Te mbir moomu ñu doon seetaan dafa raglu, ba Musaa naan: «Damaa tiit bay lox.»
12:22b.HEB.012.022 Waaye yéen jege ngeen tund wi ñuy wax Siyon, di dëkku Yàlla jiy dund, muy Yerusalem ba ca asamaan. Jege ngeen it junniy junniy malaaka yu bég-a-bég, ba daje di màggal;
12:23b.HEB.012.023 jege mbooloom taawi Yàlla, yu ñu bind seen tur ca asamaan. Jege ngeen Yàlla, jiy àtte ñépp; jege ruuwi nit ñu jub, ñi àgg cig mat;
12:24b.HEB.012.024 jege Yeesu, Rammukat bi sàmm kóllëre gu bees gi; jege deretam, ji ñu wis. Te deret jooju, li muy yégle moo gën a neex li deretu Abel doon yéene.
12:25b.HEB.012.025 Moytuleen a tanqamlu nag kiy wax ak yéen. Ndegam ñiy tanqamlu ki leen di artu ci àddina, ñoo mënul a rëcc ci àtte bi, aste ku dummóoyu kiy wax ci asamaan.
12:26b.HEB.012.026 Bu jëkk baatam yengaloon na suuf, waaye léegi dafa dige ne: «Beneen yoon laay yengalaat suuf, yengal asamaan itam.»
12:27b.HEB.012.027 Ci li mu wax: «Beneen yoon,» dafay xamle ne, Yàlla dina dindi yi ñu man a yengal, maanaam li ñu sàkk, ngir li ñu mënul a yengal sax ba fàww.
12:28b.HEB.012.028 Kon nag gannaaw dinañu jot nguur gu kenn mënul a yengal, nanu ci sant Yàlla, di ko jaamu, ni mu ko bëgge, boole ci wegeel ak ragal,
12:29b.HEB.012.029 ndaxte sunu Yàlla, safara la suy lakke.
13
13:1b.HEB.013.001 Saxleen ci bëggante ni ay bokk.
13:2b.HEB.013.002 Buleen fàttee teral ñiy ñëw ci yéen, ndaxte ñenn ñi, bi ñu ko defee, teral nañu ay malaaka te xamuñu ko.
13:3b.HEB.013.003 Fàttalikuleen ñi ñu tëj, mel ni su ñu leen boole woon ak ñoom tëjaale. Fàttalikuleen ñi ñuy sonal, ni su ngeen bokkoon ak ñoom coono.
13:4b.HEB.013.004 Na ñépp fullaal séy, te lalu séy bi bañ a taq sobe, ndaxte Yàlla dina àtte ñu yàqu ñi ak njaalookat yi.
13:5b.HEB.013.005 Buleen bëgge; deeleen doylu, ndaxte Yàlla ci boppam nee na:«Duma la wacc mukk,duma la wor mukk,»
13:6b.HEB.013.006 ba tax nu am kóoluteg wax ne:«Boroom bi moo di sama ndimbal;duma ragal dara.Lu ma nit manal?»
13:7b.HEB.013.007 Fàttalikuleen seen njiit, yi leen yégal kàddug Yàlla. Nemmikuleen li seen dund meññ te roy seen ngëm.
13:8b.HEB.013.008 Yeesu Kirist du soppiku mukk; ni mu mel démb ak tey lay mel ba fàww.
13:9b.HEB.013.009 Buleen nangu mukk ñu fàbbi leen ak njàngale yu bare yu wuute ak yu jëkk ya. Li gën moo di xol yi jële seen doole ci yiwu Yàlla, te bañ koo jële ci sàrt yi jëm ci ñam, yi jariñul dara ñi koy sàmm.
13:10b.HEB.013.010 Am nanu sarax boo xam ne ñiy jaamu Yàlla ci tàntu màggalukaayu bànni Israyil sañuñu koo lekk.
13:11b.HEB.013.011 Ndaxte saraxalekat bu mag bi dafay yóbbu deretu mala yi ca bérab bu sell-baa-sell ni sarax ngir dindi bàkkaar yi, waaye yàpp wi dees na ko lakk ca gannaaw dal ba.
13:12b.HEB.013.012 Looloo tax Yeesu sonn ca gannaaw dëkk ba, ngir sellal mbooloo mi ak deretam.
13:13b.HEB.013.013 Nanu ko fekki nag ca gannaaw dal ba, bokk ak moom toroxte ga.
13:14b.HEB.013.014 Amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye nu ngi wut dëkk biy ñëw.
13:15b.HEB.013.015 Kon nag nanu jaare ci Yeesu, tey dëkk ci jébbal Yàlla sarax bu koy màggal, maanaam sant turam.
13:16b.HEB.013.016 Buleen fàtte di def lu baax ak di sédde ci seen alal, ndaxte sarax yu mel noonu ñoo neex Yàlla.
13:17b.HEB.013.017 Déggal-leen seeni njiit te topp seen ndigal, ndaxte ñoo leen di sàmm te ñooy layoo seen liggéey. Kon nangeen leen déggal, ngir ñu man a def seen liggéey ak xol bu sedd, bañ cee am naqar, ndaxte loolu du leen amal njariñ.
13:18b.HEB.013.018 Deeleen nu ñaanal. Wóor nanu ne, sunu xel dal na, ndaxte danoo bëgg a rafet ci lépp lu nuy def.
13:19b.HEB.013.019 Maa ngi leen di xiir, ngeen ñaanal nu, ba tuur ci seen ñaq, ngir ma yiwiku, ba dellusi ci yéen ci ni mu gën a gaawe.
13:20b.HEB.013.020 Na leen Yàlla Boroom jàmm, mi dekkal sunu Boroom Yeesu, di Sàmm bu mag bi, ci darajay deret, ji fas kóllëre gu sax,
13:21b.HEB.013.021 matal ci lépp lu baax, ba ngeen man a def coobareem, di jëfe ci nun li neex ci moom, mu jaarale lépp ci Yeesu Kirist, moom mi yelloo ndam ba fàww. Amiin.
13:22b.HEB.013.022 Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan, ngeen tegoo baatu yedd yooyu, ndaxte dama leen a bind ci lu gàtt.
13:23b.HEB.013.023 Xamleen ne, Timote sunu mbokk, génn na kaso. Su dikkee léegi, dinaa ànd ak moom, seetsi leen.
13:24b.HEB.013.024 Nuyul-leen ma seen njiit yépp ak gaayi Yàlla yépp. Waa Itali ñu ngi leen di nuyu.
13:25b.HEB.013.025 Na yiwu Yàlla nekk ànd ak yéen ñépp.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Hebrews (Wolof). Hebrews (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C35A-7