2 Timothy (Wolof)
1
1:1b.2TI.001.001 Man Pool, ndawul Yeesu Kirist ci coobareg Yàlla, ngir xamle dund gi nu Yàlla dig te féete ci Kirist Yeesu,
1:2b.2TI.001.002 maa ngi lay bind Timote, sama doomu diine ji ma bëgg. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm.
1:3b.2TI.001.003 Fu ma tollu maa ngi lay boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla, mi may jaamu ci xel mu dal, ni ko samay maam daan defe. Guddi ak bëccëg, bu sama xel demee ci say rangooñ,
1:4b.2TI.001.004 ma bëgg laa gis, ba am mbég mu réy.
1:5b.2TI.001.005 Maa ngi fàttaliku sa ngëm gu dëggu, gi nekkoon ci sa maam Lowis ak sa yaay Ënis, te mu wóor ma ne, sax na ci yaw it.
1:6b.2TI.001.006 Looloo tax maa ngi lay fàttali, nga xambaat taal bi Yàlla taal ci yaw, di may gi mu la jagleel, bi ma la tegee samay loxo.
1:7b.2TI.001.007 Ndaxte Xel mi nu Yàlla sol du ànd ak ragal, waaye day ànd ak kàttan, mbëggeel ak moom sa bopp.
1:8b.2TI.001.008 Bul rus ci seedeel sunu Boroom, mbaa ci li ñu ma tëj ndax turam, waaye bokkal ak man tiis ci xamle xebaar bu baax bi, wéeru ci kàttanu Yàlla.
1:9b.2TI.001.009 Moo nu musal te woo nu ci dund gu sell, ci lu ajuwul ci sunuy jëf, waaye ci dogalu boppam ak yiwam, wi nu Yàlla may ci Kirist Yeesu, ba àddina sosoogul.
1:10b.2TI.001.010 Te léegi biral na ko ci feeñug sunu Musalkat Kirist Yeesu, mi nasaxal dee te feeñal dund ci xebaar bu baax bi, te muy dund gu sax.
1:11b.2TI.001.011 Te Yàlla fal na ma ndaw ak jàngalekat, ngir may yégle xebaar bi;
1:12b.2TI.001.012 looloo tax ma jànkoonte ak tiis yu mel nii. Waaye rusuma ci, ndaxte xam naa Ki ma wékk sama yaakaar, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, man na koo denc ba bés ba.
1:13b.2TI.001.013 Toppal ci tànki wax yu wér yi nga dégge ci man, jàpp ci ak ngëm ak mbëggeel, yi nu am ci sunu bokk ci Kirist Yeesu.
1:14b.2TI.001.014 Te nga sàmm bu baax li la Yàlla dénk, wéeru ci Xel mu Sell, mi dëkk ci nun.
1:15b.2TI.001.015 Xam nga ne, waa diiwaanu Asi gépp, won nañu ma gannaaw, ñu deme niki Fusel ak Ermosen.
1:16b.2TI.001.016 Waaye Onesifor daa na faral di dëfël sama xol; na Boroom bi sotti yërmandeem ci këram. Rusul woon sax ci samay jéng,
1:17b.2TI.001.017 waaye bi mu ñëwee dëkku Room, wut na ma fu ne, ba gis ma.
1:18b.2TI.001.018 Na ko Boroom bi teeru ak yërmandeem ca bés ba. Umplewoo it coono yi mu daj, ngir dimbali ma ca dëkku Efes.
2
2:1b.2TI.002.001 Kon nag yaw sama doomu diine, doolewool yiw, wi ci Kirist Yeesu.
2:2b.2TI.002.002 Te wax yi nga dégge ci man fi kanam seede yu bare, nanga leen jottali nit ñu takku, ngir ñoom it ñu man a jàngal ñeneen.
2:3b.2TI.002.003 Bokkal ak man tiis, di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu,
2:4b.2TI.002.004 xam ne xarekat bu bëgg a neex ka ko solal, du dugg ci yëfi àddina.
2:5b.2TI.002.005 Te it ku tàggat yaramam ngir rawante, duñu ko jagleel kaalag ndam mukk, su toppul sàrt ya.
2:6b.2TI.002.006 Noonu it beykat bi sonn mooy jëkk a ñam toolam.
2:7b.2TI.002.007 Xalaatal bu baax sama wax jii, ndax Boroom bi dina leeral sa xel ci lépp.
2:8b.2TI.002.008 Fàttalikul Yeesu Kirist mi dekki, soqikoo ci Daawuda, tukkee ci xebaar bu baax bi may waare.
2:9b.2TI.002.009 Xebaar booboo tax may jànkoonte ak i tiis, ba ñu jéng ma ni defkatu lu bon; waaye kàddug Yàlla moom, kenn du ko jéng.
2:10b.2TI.002.010 Te lii tax may muñ lépp, ngir ñi Yàlla tànn it am mucc gi ci Kirist Yeesu, gu ànd ak ndam lu sax.
2:11b.2TI.002.011 Kàddu gu wóor a ngii:Su nu deeyaalee ak Kirist,dinanu dundaat ak moom;
2:12b.2TI.002.012 su nu takkoo,dinanu nguuru ak moom.
2:13b.2TI.002.013 Su nu ko weddee,kon mu weddi nu;su nu ko ñàkkee kóllëre,moom dina sax ci kóllëreem,ndax mënul a weddi boppam.
2:14b.2TI.002.014 Saxal ci di leen fàttali mbir yooyu, di leen dénk fa kanam Yàlla, ñu moytoo werante ciy araf, ndax loolu jëmul fu dul ci yàq ngëmu ñiy déglu.
2:15b.2TI.002.015 Góor-góorlul ba teew fa kanam Yàlla, nekk liggéeykat bu mu nangul te rusoo ci dara, di faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi.
2:16b.2TI.002.016 Moytul bépp jataayu waxi neen yu àddina kese, ndax ña fa toog dinañu gën a xuus cig weddi,
2:17b.2TI.002.017 te seen kàddu day burux ni ngal. Imene ak Filet, ci ñoom lañu bokk;
2:18b.2TI.002.018 dañoo moy dëgg, di wax ne ndekkite wees na, ba yàq ngëmu ñenn ñi.
2:19b.2TI.002.019 Waaye teewul fondamaa bu dëgër, bi Yàlla tabax, nee na kekk, te lii lañu ci tàmpe: «Boroom bi xam na ñi bokk ci moom,» te it: «Ki tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.»
2:20b.2TI.002.020 Ci kër gu mag nag, du ndabi wurus walla xaalis rekk a fa am, waaye itam yoy dénk walla ban; yii tedd nañu, yee ñàkk solo.
2:21b.2TI.002.021 Kon nag ku laabal sa bopp ci yooyu yépp, dinga nekk ndab lu tedd te sell, nga am njariñ ci Boroom bi te jekk ci bépp jëf ju rafet.
2:22b.2TI.002.022 Dawal bépp bëgg-bëggu ngune, te sóobu ci njub, ngëm, mbëggeel, jàmm, ànd ak ñépp ñiy tudd turu Boroom bi ak xol bu sell.
2:23b.2TI.002.023 Tanqamlul bépp weranteb neen bu amul njariñ, xam ne xuloo rekk lay jur.
2:24b.2TI.002.024 Te jaamu Boroom bi warul a xuloo, waaye na lewet ci ñépp, jekk ngir jàngale tey muñ fitnay noon.
2:25b.2TI.002.025 Na jubbanti cig suufe ñi koy diiŋat, tey yéene Yàlla xiir leen ci réccu, ba ñu xam dëgg;
2:26b.2TI.002.026 ñu rëcc ci fiirug Seytaane, mi leen jàpp niy jaam, te ñu dellusi ci seen xel yu rafet, ba sóobuwaat ci coobareg Yàlla.
3
3:1b.2TI.003.001 Nanga xam lii: bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci muju jamono.
3:2b.2TI.003.002 Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur; duñu am kóllëre, sellaay
3:3b.2TI.003.003 mbaa cofeel; dañuy jàpp mer ak a sos; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax;
3:4b.2TI.003.004 ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar; seen bànneex a leen gënal Yàlla.
3:5b.2TI.003.005 Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. Ñu deme noonu, dëddu leen.
3:6b.2TI.003.006 Nit ñu mel noonu ñooy yoxoosu ci biir kër yi, ba fàbbi jigéen ñu ñàkk pasteef, ñi seeni bàkkaar ub seen bopp, te bëgg-bëgg yu wuute jiital leen.
3:7b.2TI.003.007 Duñu noppee gëstu, waaye duñu man a yegg ci xam-xamu dëgg mukk.
3:8b.2TI.003.008 Nit ñooñu dañuy bëreek dëgg, ni Sànnes ak Sàmbares bëree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba lañu, yu seen ngëm tekkiwul dara.
3:9b.2TI.003.009 Waaye duñu dem fu sore, ndax seen ñàkk xel dina bir ñépp, ni mu dale woon Sànnes ak Sàmbares.
3:10b.2TI.003.010 Waaye yaw nag xam nga bu baax sama njàngale, sama dund, sama takkute, sama ngëm, sama muñ, sama mbëggeel ak sama dékku tiis.
3:11b.2TI.003.011 Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci dëkki Ancos, Ikoñum ak Listar. Céy li ma jànkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci lépp.
3:12b.2TI.003.012 Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la.
3:13b.2TI.003.013 Waaye nit ñu bon ñi ak naaféq yi dinañu fi yées, di naxe ak a nax seen bopp.
3:14b.2TI.003.014 Yaw nag saxal ci li nga jàng te mu wóor la, xam fi nga tibbe.
3:15b.2TI.003.015 Li dale ci sa ngune xam nga Mbind mu sell, mi la man a yee ci yoonu mucc, jaar ci gëm Kirist Yeesu.
3:16b.2TI.003.016 Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub.
3:17b.2TI.003.017 Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.
4
4:1b.2TI.004.001 Kon nag maa ngi lay dénk fa kanam Yàlla ak Kirist Yeesu, miy àtte ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci feeñam ci biir ndam ak ci nguuram, nga def lii:
4:2b.2TI.004.002 xamleel kàddug Yàlla, sax ci, su neexee ak su naqaree; yeyal ñi tooñ, di yedd ak a dénk ñépp, def ko ci muñ gu yaatu ak njàngale mu mat.
4:3b.2TI.004.003 Ndaxte jamono dina ñëw, joo xam ne nit ñi dootuñu xajoo njàngale mu wér mi, waaye dinañu jublu ci seeni bëgg-bëgg, di fortaatu jàngalekat yu leen di jey.
4:4b.2TI.004.004 Dinañu tanqamlu dëgg, jeng jëm ci léebi diiney neen.
4:5b.2TI.004.005 Waaye yaw nanga foog ci lépp, dékku tiis, tey tas xebaar bu baax bi, ba matal sag yónnent.
4:6b.2TI.004.006 Ndaxte maa ngi ci tànki joxe sama bakkan ni sarax, te sama waxtuw dem jot na.
4:7b.2TI.004.007 Bëre naa ba ub làmbi ngëm, daw naa ba àkk, sàmm naa mboolem dëgg, gi ñu ma dénk.
4:8b.2TI.004.008 Fi mu ne Yàllaa ngi may xaare añu ku jub, di kaalag ndam gi ma Boroom, biy Àttekat bu jub, di jox ca bés ba, te jéllale naa sama bopp, waaye képp ku def sa xol cig feeñam.
4:9b.2TI.004.009 Defal sa kem-kàttan, ba fekksi ma ci ni mu gën a gaawe.
4:10b.2TI.004.010 Ndaxte Demas topp na àddina, ba bàyyi ma, dem dëkku Tesalonig; Kereseñsë dem na diiwaanu Galasi, Tit dem diiwaanu Dalmasi.
4:11b.2TI.004.011 Luug rekk a des fi man. Indaaleel Màrk, ndaxte amal na ma njariñ ci liggéey bi.
4:12b.2TI.004.012 Tisig moom yebal naa ko dëkku Efes.
4:13b.2TI.004.013 Te sooy ñëw, indaaleel mbubb, ma ma dénkoon Karpus ca dëkku Torowas, te it bul fàtte téere yi, rawatina téere yu am maana, yi ñu bind ci der.
4:14b.2TI.004.014 Alegsàndar tëgg bi def na ma ñaawteef yu ne, waaye Boroom bi dina ko fey ay jëfam.
4:15b.2TI.004.015 Moytu ko bu baax, ndaxte bëre na ak sunuy wax ba tàyyi.
4:16b.2TI.004.016 Keroog bi ma jëkkee taxaw, di làyyil sama bopp, awma woon kenn ku ma taxawu, ñépp dañu maa daw — bu leen ko Yàlla jàppe nag.
4:17b.2TI.004.017 Waaye Boroom bi moo ma taxawu te dooleel ma, ma jollil kàddu gi, ba xeet yépp dégg ko. Te Boroom bi musal na ma ci selli gaynde.
4:18b.2TI.004.018 Rax-ca-dolli dina ma musal ci bépp jëf ju ñaaw, tette ma ci jàmm, ba tàbbal ma ci nguuram gu kawe ga. Na yelloo ndam ba fàww. Amiin.
4:19b.2TI.004.019 Nuyul ma Piriska ak Akilas ak waa kër Onesifor.
4:20b.2TI.004.020 Erast des na dëkku Korent. Torofim dafa woppoon, ma bàyyi ko dëkku Mile.
4:21b.2TI.004.021 Gaawal a ñëw, bala lolli di gàllankoor sa yoon. Ëbulus, Pudeñsë, Linus, Këlójaa ak yeneen bokk yépp ñu ngi lay nuyu.
4:22b.2TI.004.022 Na Boroom bi aar sa xel. Na yiwu Yàlla ànd ak yéen ñépp.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. 2 Timothy (Wolof). 2 Timothy (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C351-0