Colossians (Wolof)
1
1:1b.COL.001.001 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Timote sunu mbokk,
1:2b.COL.001.002 noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell, yi dëkk Kolos te di ay bokk ci gëm Kirist. Na leen Yàlla sunu Baay may yiw ak jàmm.
1:3b.COL.001.003 Dunu noppee sant Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, saa su nu leen di ñaanal,
1:4b.COL.001.004 ndaxte yég nanu seen ngëm ci Kirist Yeesu ak seen mbëggeel ci gaayi Yàlla yépp.
1:5b.COL.001.005 Ngëm googu ak mbëggeel googu ñu ngi sosoo ci yaakaaru ëllëg, jiy cér bi leen Yàlla dencal ca asamaan. Mas ngeen a dégg yaakaar jooju ci kàddug dëgg gi, di xebaar bu baax bi.
1:6b.COL.001.006 Ni xebaar bu baax bi wàcce ci yéen, noonu lay wàcce ci àddina sépp, di meññ te di law. Te noonu lay doxale ci yéen, li dale ci bés, ba ngeen dégge xebaaru yiwu Yàlla, te xam dëggam gi mu ëmb;
1:7b.COL.001.007 moom ngeen jànge ci Epafras, miy sunu nawle ci liggéey bi te nu sopp ko, di jawriñu Kirist bu takku ngir seen njariñ.
1:8b.COL.001.008 Te moo nu yégal it mbëggeel, gi Xelu Yàlla mi sol ci yéen.
1:9b.COL.001.009 Looloo tax ci sunu wàllu bopp, ba nu ko yégee ba tey, jógunu ci di leen ñaanal. Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen xam bu baax coobareem ci xel mu mat ak ràññee gu aju ci dooley Xelam.
1:10b.COL.001.010 Noonu dingeen dund dund gu dëppoo ak seen bokk ci Boroom bi, ba neex ko ci fànn gu nekk, di def bépp jëf yu baax, te yokk seen xam-xam ci Yàlla.
1:11b.COL.001.011 Te Yàlla dina leen dooleel ak bépp doole, mu mengoo ak kàttanu ndamam, ngir ngeen man a tegoo coono te muñ, ba fa muñ di yem.
1:12b.COL.001.012 Dingeen gërëm Yàlla Baay bi, ànd ci ak mbég, moom mi leen jagleel, ngeen bokk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi ci leer.
1:13b.COL.001.013 Yàlla musal na nu ci dooley lëndëm, yóbbu nu ci nguuru Doomam ji mu bëgg,
1:14b.COL.001.014 moom mi nu jot, maanaam baal nu sunuy bàkkaar.
1:15b.COL.001.015 Doom jooju moo di melokaanu Yàlla, ji kenn gisul. Mooy taaw bi, ki gën a màgg lépp luy mbindeef.
1:16b.COL.001.016 Ndaxte ci moom la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf, li ñuy gis ak li ñu mënul a gis, muy buur, njiit, kilifa mbaa boroom sañ-sañ. Lépp lu ñu sàkk, ci moom lañu ko jaarale, ci moom lañu ko jëme.
1:17b.COL.001.017 Laata dara di am, fekkoon na moom mu nekk, te lépp a ngi jàppoo ci moom.
1:18b.COL.001.018 Mooy bopp bi yilif jëmm ji, di mbooloom ñi ko gëm, ndaxte moom mooy njàlbéen gi, di taaw bi, maanaam ki jëkk a dekki, ngir muy kilifa ci bépp fànn.
1:19b.COL.001.019 Ndaxte soob na Yàlla mu dëkkal matam gépp ci moom
1:20b.COL.001.020 te jaar ci moom, jubale lépp ak boppam, muy ci kaw asamaan yi mbaa ci suuf, ba mu wàccee jàmm jaarale ko ci deret ji tuuru, bi Doom ji deeyee ca bant ba.
1:21b.COL.001.021 Te yéen ñi sore woon Yàlla te doon ay noonam ci seen xel ak seen jëf yu bon,
1:22b.COL.001.022 léegi nag Yàlla jubale na leen ak boppam jaare ko ci deewu Kirist ci yaramu nitam, ngir taxawal leen ca kanamam, ngeen sell te ñàkk sikk ak i ŋàññ.
1:23b.COL.001.023 Loolu nag na fekk ngeen wéy ci ngëm, sampu ci ba dëgër ci, tey séentu cér, bi leen xebaar bu baax bi jox. Te xebaar bu baax, boobu ngeen dégg te ñu yégal waa àddina sépp, man Pool moom laay yégle.
1:24b.COL.001.024 Léegi nag maa ngi am bànneex ci coono, yi may daj ngir seen njariñ; te li des sax ci fitnay Kirist, noonu laa koy àggalee ngir njariñu mbooloom ñi gëm, di jëmmam.
1:25b.COL.001.025 Jawriñu mbooloo moomu laa, ndaxte Yàlla sas na ma ngir yéen, may yégle fu nekk kàddoom,
1:26b.COL.001.026 maanaam ma yégle kumpa, gi nëbbu woon ay jamonoy jamono, waaye léegi Yàlla xamal na ko ay gaayam
1:27b.COL.001.027 ci xeeti àddina sépp. Ñoom nag la Yàlla bëgg a xamal ni ndamu kumpa googu màgge, maanaam Kirist a ngi dëkk ci yéen, di yaakaar ju wér ci ndamu ëllëg.
1:28b.COL.001.028 Moom Kirist lanuy yégle, di artu te di jàngal ku nekk, ànd ak xel mu mat, ngir jébbal Yàlla ku nekk ni ku mat ci Kirist.
1:29b.COL.001.029 Ci loolu laay jëmale sama liggéey, di bëree dooley Kirist, jiy yengu ci man ak kàttan.
2
2:1b.COL.002.001 Bëgg naa nag, ngeen xam bëre bu metti, bi may bëre ngir yéen, ngir waa Lawdise ak ñépp ñi ma musul a teg bët. Damay def sama kem-kàttan,
2:2b.COL.002.002 ngir ngeen am fit te nekk benn ci mbëggeel, ngir dajal noonu xam-xam bu mat, ba xam kumpag Yàlla, di Kirist.
2:3b.COL.002.003 Ci moom lañu denc lépp lu ñuy sàkku ci xel ak ci xam-xam.
2:4b.COL.002.004 Maa ngi wax lii, ngir kenn bañ leen a nax ci ay wax yu neex.
2:5b.COL.002.005 Jëmm ji ñëwul waaye sama xel a ngi ci yéen, di bég ci seen doxalin ak ngëm gu dëgër, gi ngeen am ci Kirist.
2:6b.COL.002.006 Kon nag, ni ngeen nangoo Kirist Yeesu ni Boroom bi, dundeleen noonu ci moom.
2:7b.COL.002.007 Saxleen ci moom, di màgg ci moom, tey gën a dëgër ci ngëm, gi ñu leen jàngal, ba seen xol di baawaan ci gërëm Yàlla.
2:8b.COL.002.008 Moytuleen ba kenn bañ leen a fàbbi ci ay xam-xami nit yuy naxi neen. Xam-xam yu mel noonu, ñu ngi soqikoo ci aada yu nit tëral, ci aaday àddina, waaye soqikoowul ci Kirist.
2:9b.COL.002.009 Ndaxte ci Kirist, maanaam ci yaramu nitam, la matug Yàlla gépp dëkk,
2:10b.COL.002.010 te mat ngeen ci moom, miy buuru kilifa yépp ak boroom sañ-sañ yépp.
2:11b.COL.002.011 Ndax seen ngëm ci moom xaraf ngeen xaraf bu loxol nit deful, maanaam Kirist summil na leen dooley bàkkaar, ji moomoon seen yaram. Loolu mooy xaraf, bi Kirist def.
2:12b.COL.002.012 Bi ñu leen sóobee ci ndox, suulaale nañu leen ak moom, te it dekki ngeen ak moom, ndaxte gëm ngeen ci dooley Yàlla, ji ko dekkal ca néew ya.
2:13b.COL.002.013 Te yéen ñi doon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, Yàlla dundalaat na leen ak Kirist, baal nu sunuy bàkkaar yépp.
2:14b.COL.002.014 Mbind mi nu doon tiiñal, te daa nu yey ndax ay sàrtam, Yàlla far na ko, dindi ko, daajaale ko ca bant, ba Kirist deeye.
2:15b.COL.002.015 Futti na kilifa yi ak boroom sañ-sañ yi, weer leen ci kanamu ñépp, sëkktal leen niy jaam ndax ndam la Kirist jële ca bant ba.
2:16b.COL.002.016 Kon nag bu leen kenn teg tooñ ci li jëm ciy ñam mbaa naan, ci màggal mbaa xewu weer wu feeñ, mbaa ci bésu noflaay.
2:17b.COL.002.017 Loolu lépp nag takkandeer la woon buy misaal li waroon a ñëw, waaye lu dëggu li mi ngi ci Kirist.
2:18b.COL.002.018 Kuy bég ci di toroxlu ci ngistal, di jaamu ay malaaka, buleen ko may, mu àtte leen. Kooku dafay jeneer, di seet li koy feeñu, bay tiitaroo xalaatam, fekk xalaatu nit kese la, te neen.
2:19b.COL.002.019 Taqul ci Kirist, miy bopp bi yilif jëmm ji. Bopp bee tax ba jëmm jépp, ji siddit yi ak tenqo yi téye te taqale ko, di màgg màgg gi ko Yàlla di jox.
2:20b.COL.002.020 Ndegam deeyandoo ngeen ak Kirist, ba génne noonu ci aaday àddina, lu tax ngeen di nangu, ñu di leen teg ay sàrt yu mel nii: «Bul fab, bul ñam, bul laal,» ni bu seenug dund aju woon ci àddina si?
2:22b.COL.002.022 Sàrt yooyu ñu ngi aju ci ndigali nit ñi ak seen njàngale. Yëf yi ñu tudd yépp, dees na leen jariñoo, ba ñu jeex.
2:23b.COL.002.023 Dëgg la, seeni sàrt dañuy dénkaane pasteef ci jaamu Yàlla, di toroxlu ak di fitnaal seen yaram. Waaye sàrt yooyu nag amuñu benn njariñ, ngir nit ñi noot seen nafsu.
3
3:1b.COL.003.001 Kon nag ndegam dekkeendoo ngeen ak Kirist, wutleen yëf, ya nekk ca kaw, fa Kirist toog ca ndeyjooru Yàlla.
3:2b.COL.003.002 Fonkleen yëf ya ca kaw, te ngeen bañ a faale yi ci suuf,
3:3b.COL.003.003 ndaxte dee ngeen, te seen dund boole nañu ko ak Kirist, denc ca Yàlla.
3:4b.COL.003.004 Te bés bu Kirist miy seen dund feeñee, yéen itam dingeen feeñ ak moom ci biir ndam.
3:5b.COL.003.005 Kon nag li nekk ci yéen te bokk ci mbiri àddina, jébbal-leen ko dee, yu deme ni ndoxaanu yàqute, sobe, xemmem, bëgg-bëgg yu bon, ak bëgge, maanaam bokkaale Yàlla.
3:6b.COL.003.006 Yooyooy xëcc merum Yàlla.
3:7b.COL.003.007 Yéen itam noonu ngeen daan doxale bu jëkk, ba ngeen daan dunde noonu.
3:8b.COL.003.008 Waaye léegi bàyyileen yii yépp: mer, xadar, kiñaan ak di génne ci seen gémmiñ sos ak wax ju ñaaw.
3:9b.COL.003.009 Bàyyileen di fen seeni moroom, ndaxte summi ngeen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale, moom ak ay jëfam;
3:10b.COL.003.010 te sol ngeen dund gu bees, gi Yàlla sàkk te di ko yeesal ba mu mel ni moom, ngir ngeen man koo xam bu wér.
3:11b.COL.003.011 Ci dund gu bees googu, amul Yawut ak ku dul Yawut, ku xaraf walla ku xaraful, jaam walla gor, ku jàngul ni Baarbaar yi, ak ku yeewuwul ni waa Sit, waaye Kirist ay lépp te dëkk ci ñépp.
3:12b.COL.003.012 Kon nag ndegam Yàlla tànn na leen, sellal leen, sopp leen, solooleen boog yërmande, laabiir, woyof, lewet ak muñ.
3:13b.COL.003.013 Muñalanteleen, di baalante, su amee kuy tawat moroomam. Baalanteleen, ni leen Boroom bi baale.
3:14b.COL.003.014 Ci kaw loolu lépp amleen mbëggeel, giy jókkaale lépp, ba mu mat.
3:15b.COL.003.015 Na jàmm ji Kirist di joxe noot seeni xol, ndaxte Yàlla woo na leen ci loolu, mel ni ay cér yu bokk benn yaram; te gërëmleen Yàlla.
3:16b.COL.003.016 Na kàddug Kirist dëkk ci yéen, bay baawaan, ngeen di jàngalante ak a artoonte ci seen biir ak xel mu mat sëkk, di woy ak a gërëm Yàlla ak seen xol bépp, ay taalifi Sabóor, ay kañ Yàlla ak ay cant yu tukkee ci Xelum Yàlla.
3:17b.COL.003.017 Te lu ngeen man a def, muy ci wax mbaa ci jëf, wéerleen ko ci turu Boroom bi Yeesu, jaare ci moom gërëm Yàlla Baay bi.
3:18b.COL.003.018 Jigéen ñi, na ku nekk nangul jëkkëram, ndaxte looloo jekk ci ñi bokk ci Boroom bi.
3:19b.COL.003.019 Góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram te muñal ko.
3:20b.COL.003.020 Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, ndaxte looloo rafet ci ñi bokk ci Boroom bi.
3:21b.COL.003.021 Baay yi, buleen bundaxataal seeni doom, ngir bañ a jeexal seen xol.
3:22b.COL.003.022 Jaam yi, nangul-leen ci lépp seen sang, yi ci àddina. Buleen ko def rekk ci seen kanam, di sàkku ngërëm, waaye na nekk lu dëggu ci yéen, ndax seen ragal Boroom bi.
3:23b.COL.003.023 Lu ngeen man a def, na ci seen xol tàlli; ngeen def ko ngir Boroom bi, te du ngir nit,
3:24b.COL.003.024 xam ne Boroom bi dina fey seeni jëf, mu di cér bi mu leen dencal. Kirist mooy Boroom, bi ngeen di liggéeyal.
3:25b.COL.003.025 Waaye ku def lu bon, Boroom bi dina la delloo sa jëf, te du gënale.
4
4:1b.COL.004.001 Sang yi, yorleen seeni jaam ci nu jub te aw yoon, xam ne, am ngeen yéen itam ab Sang ca asamaan.
4:2b.COL.004.002 Dëkkleen ci ñaan Yàlla, farlu ci, boole ci ngërëm.
4:3b.COL.004.003 Te ngeen fasaale nu ci ñaan yi itam, ngir Yàlla ubbil nu bunt, nu man a xamle kàddoom, di yégle kumpa gi di Kirist, muy kumpa gi waral ñu jéng ma.
4:4b.COL.004.004 Ñaanleen ngir ma xamle ko ni mu ware.
4:5b.COL.004.005 Jëfeleen ak xel ci seen diggante ak waa àddina, te fu ngeen ame jot, fexeleen ba jariñoo ko.
4:6b.COL.004.006 Na seen wax jépp fees ak yiw te am xorom, ngir ngeen xam nan ngeen war a tontoo ku nekk.
4:7b.COL.004.007 Tisig, sama mbokk mi ma sopp, di jawriñ ju takku ak sama nawle ci liggéeyu Boroom bi, dina leen yégal lépp lu jëm ci samay mbir.
4:8b.COL.004.008 Lii moo tax ma yebal ko ci yéen: ngeen xam xebaar bi jóge ci nun, te it mu dëfël seen xol.
4:9b.COL.004.009 Onesim lay àndal, sunu mbokk mu takku, mi nu sopp, te mu bokk ci yéen. Dinañu leen xamal lépp lu xew fii.
4:10b.COL.004.010 Aristàrk mi nekk ak man ci kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnabas. Jot ngeen ay ndigal ci mbirum Màrk: bu ñëwee ci yéen, teral-leen ko.
4:11b.COL.004.011 Yeesu mi ñuy dàkkentale Yustus, moom it mu ngi leen di nuyu. Ñoom rekk ñooy Yawut yiy liggéeyandook man ngir nguuru Yàlla, te ñoo féexal sama xol.
4:12b.COL.004.012 Jaamu Kirist, Epafras, mi bokk ci yéen, mu ngi leen di nuyu. Du jóg ci di leen ñaanal, farlu ci ni kuy bëre, ngir ngeen taxaw temm ci coobareg Yàlla gépp, ànd ak ngëm gu mat ak kóolute gu wóor.
4:13b.COL.004.013 Maa ngi koy seedeel ne, mu ngi sonn bu baax ngir yéen, ngir waa Lawdise ak waa Yerapolis.
4:14b.COL.004.014 Luug, doktoor bi ñu sopp, mu ngi leen di nuyu, moom ak Demas.
4:15b.COL.004.015 Nuyul-leen nu mbokk, yi nekk Lawdise. Nuyul-leen nu itam Nimfa ak mbooloom ñi gëm, miy daje ci këram.
4:16b.COL.004.016 Bu ñu jàngee bataaxal bii ci yéen, fexeleen ba ñu jàng ko it ci mbooloom ñi gëm mi nekk Lawdise, te yéen it ngeen jàng bi ma yónnee waa Lawdise.
4:17b.COL.004.017 Te neleen Arkib: «Farlul ci sas, wi la Boroom bi sédde, ba matal ko.»
4:18b.COL.004.018 Man Pool maa leen di bind nuyoo bii ci sama loxob bopp. Fàttalikuleen ne, dañu maa jéng. Na yiwu Boroom bi ànd ak yéen!
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Colossians (Wolof). Colossians (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C345-E