Philippians (Wolof)

Philippians (Wolof)

1

1:1b.PHI.001.001 Nun Pool ak Timote, jaami Kirist Yeesu, noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yépp ci dëkku Filib, yi bokk ci Kirist Yeesu, yéen ak seeni njiit ak ñiy topptoo yëfi mbooloo mi.

1:2b.PHI.001.002 Na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.

1:3b.PHI.001.003 Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Yàlla sama Boroom;

1:4b.PHI.001.004 te saa su ma leen di ñaanal yéen yépp, duma noppee bég,

1:5b.PHI.001.005 ndax seen ànd ak man ci tas xebaar bu baax bi, ca ndoorte la ba tey.

1:6b.PHI.001.006 Wóor na ma ne, Yàlla mi tàmbali jëf ju baax jii ci yéen, dina ci sax, ba bésu Kirist Yeesu ñëw.

1:7b.PHI.001.007 Te juumuma ci li ma xalaat loolu ci yéen ñépp, ndaxte def naa leen ci sama xol; ba tax fii ci kaso bi, ci taxawal xebaar bu baax bi ak lawal ko, yéen ñépp am ngeen wàll ak man ci yiwu Yàlla.

1:8b.PHI.001.008 Ndaxte Yàllaa seede ne, sama xol seey na ci yéen ñépp ci biir cofeelu Kirist Yeesu.

1:9b.PHI.001.009 Li ma leen di ñaanal nag mooy lii: na seen mbëggeel di yokku tey gën a tar, jaar ci xam ak xàmmi gu wér;

1:10b.PHI.001.010 nangeen sax noonu ci yi gën a rafet, ngeen am xol bu laab te bañ a am benn sikk, ba bésu Kirist ñëw;

1:11b.PHI.001.011 na seen xol meññ njub, ba ne gàññ, jaar ci Yeesu Kirist ci ndamul Yàlla ak cantam.

1:12b.PHI.001.012 Damaa bëgg, bokk yi, ngeen xam lii: li ma dal taxul xebaar bu baax dellu gannaaw, waaye da koo jëmale kanam.

1:13b.PHI.001.013 Noonu ñiy wottu buur bi ak ñépp gis nañu bu leer ne, turu Kirist rekk a tax ñu jàpp ma.

1:14b.PHI.001.014 Te it bokk yu bare takk nañu seeni fit ci li ñu gis samay buum, ba tax ñu gën a ñeme ci wax kàddug Yàlla ci lu àndul ak genn tiit.

1:15b.PHI.001.015 Am na ñuy waare ci turu Kirist ci kaw kiñaan ak xëccoo, waaye ñi ci des ci kaw cofeel ak xol bu laab, ndaxte xam nañu ne, Yàlla moo ma teg fii, ngir ma taxawal xebaar bu baax bi.

1:17b.PHI.001.017 Waaye ñale amuñu xol bu laab, te seen njariñu bopp rekk a tax ñuy yégle turu Kirist, di wut a feddali samay buum ak coono.

1:18b.PHI.001.018 Lu ci génn nag? Xanaa lii rekk: turu Kirist jolli na ci nii mbaa naa, muy ci naaféq, muy ci dëgg; bég naa ci te dinaa ci bégati.

1:19b.PHI.001.019 Ndaxte xam naa ne, loolu lépp mu ngi jëm ci sama mucc, jaar ci seeni ñaan ak ndimbalu Xelum Yeesu Kirist, mi ma Yàllay yéwénal.

1:20b.PHI.001.020 Ndaxte sama xënte ak sama yaakaar mooy ma bañ a rus ci lenn, waaye sama yaram feeñal ndamu Kirist, ma ànd ci ak kóolute gu mat, su may dund mbaa may dee; moom laa daan def démb, te moom laay def tey.

1:21b.PHI.001.021 Ndaxte su ma dundee, Kirist laay noyyee, te su ma deeyee, xéewal lay doon ci man.

1:22b.PHI.001.022 Su ma Yàlla bàyyee ci àddina, sas wu am njariñ la ci man. Am naa xel ñaar, te xawma bi ci gën. Am naa yéeney jóge fi, fekki Kirist, te looloo gën fuuf,

1:24b.PHI.001.024 waaye ma des fi ci àddina moo gën ci yéen.

1:25b.PHI.001.025 Loolu wóor na ma; kon xam naa ne, dinaa fi des, di leen taxawu yéen ñépp, ngir seen ngëm yokku, ànd ak mbég.

1:26b.PHI.001.026 Noonu dinaa dellusi ci yéen, ngir sama taxawaay gën a lawal seen mbég ci Kirist Yeesu.

1:27b.PHI.001.027 Waaye dénk naa leen lii: na seeni jëf yelloo ak li Kirist digle ci xebaar bu baax bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma dégg seen mbir rekk, dinaa xam ne yéena ngi dëgër ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xebaar bu baax bi,

1:28b.PHI.001.028 te bañ a tiit dara ndax noon, yi leen di xëbal. Màndarga la muy wone ne aji sànku lañu, di màndarga it ne aji mucc ngeen, di mucc gu jóge ci Yàlla.

1:29b.PHI.001.029 Ndaxte Yàlla may na leen, ngeen gëm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam,

1:30b.PHI.001.030 di wéy ci bëre, bi ngeen gisoon ci man, te dégg léegi sama mbir.

2

2:1b.PHI.002.001 Su nu Kirist mayee fit nag ak mbëggeel guy dëfël sunu xol, su nu amee cér ci Xel mu Sell mi, su amee cofeel ak yërmande ci sunu bokk ci moom,

2:2b.PHI.002.002 kon mottalileen sama mbég, ci bokk benn xalaat ak genn mbëggeel, benn bakkan ak menn xel.

2:3b.PHI.002.003 Buleen def dara ci kaw wut aw tur walla wonu, waaye jiital-leen seeni moroom cig woyof.

2:4b.PHI.002.004 Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom.

2:5b.PHI.002.005 Te ngeen soloo xel mi nekkoon ci Kirist Yeesu:

2:6b.PHI.002.006 Njàlbéen ga fekk na Kirist yor melow Yàlla,waaye aakimowul taxawaayamci li mu mengoo ak Yàlla.

2:7b.PHI.002.007 Waaye daa wàcce boppam,ba tollook nit ñi,def boppam surga.Te bi mu yoree bindu nit,

2:8b.PHI.002.008 daa suufeel boppam,di dégg ndigal, ba joxe boppam,ñu daaj ko sax ci bant.

2:9b.PHI.002.009 Moo tax Yàlla kaweel ko lool,jox ko tur wi tiim yépp,

2:10b.PHI.002.010 ngir turu Yeesoo tax ñépp sukk,ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf;

2:11b.PHI.002.011 te ñépp bokk genn kàddu naan:Yeesu Kirist mooy Boroom bi;ci màggug Yàlla Baay bi.

2:12b.PHI.002.012 Noonu samay soppe, xam naa ne, musuleen a jóg ci dégg ndigal, waxuma sax bi ma nekkee ak yéen rekk, waaye rawatina bi ma leen soree. Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen biral seen mucc ci seeni jëf, te def ko ci ragal Yàlla gu dëggu.

2:13b.PHI.002.013 Ndaxte Yàlla ci boppam mooy jëf ci yéen, ngir ngeen fonk coobareem te di ko jëfe.

2:14b.PHI.002.014 Lépp lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo.

2:15b.PHI.002.015 Noonu dingeen am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ, di guney Yàlla yu amul sikk ci biir jamono ju yàqu te rëb. Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci àddina si,

2:16b.PHI.002.016 di jottali kàddug dund gi. Noonu bu bésu Kirist ñëwee, dinaa man a bég, xam ne dawuma lu amul njariñ, te sonnuma cig neen.

2:17b.PHI.002.017 Te bu sama deret waree tuuru sax, ngir seen ngëm mat sëkk, ma mel ni naan gu ñu boole ak sarax su jëm ci Yàlla, ba tey bég naa ci, te dinaa ci bégati.

2:18b.PHI.002.018 Yéen itam nag bégleen, waaw fekksileen ma ci sama mbég.

2:19b.PHI.002.019 Gannaaw loolu, bu soobee Boroom bi Yeesu, yaakaar naa ne, dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir sama xel dal ci xam nan ngeen def.

2:20b.PHI.002.020 Ndaxte amu fi kenn gannaaw Timote, ku bokk ak man xalaat te fonk leen bu wér.

2:21b.PHI.002.021 Ñi ci des ñépp, seen bopp lañuy xalaat, waaye du mbiri Yeesu Kirist.

2:22b.PHI.002.022 Waaye xam ngeen takkuteg Timote, ci ni mu ànde ak man ci tas xebaar bu baax bi, ni doom di taxawoo baayam.

2:23b.PHI.002.023 Moom laa yaakaar a yónni fi yéen nag, waxtu wu ma yégee, nu sama mbir di tëdde.

2:24b.PHI.002.024 Waaye wóor na ma ne, Boroom bi dina ma may, man ci sama bopp, ma seetsi leen balaa yàgg.

2:25b.PHI.002.025 Ci lu jëm ci sama mbokk Epafrodit nag, miy sama nawle ci liggéey bi ak ci xeex bi, te di seen ndaw ci faj samay soxla, jàpp naa ne, war naa leen koo delloo.

2:26b.PHI.002.026 Ndaxte namm na leen lool, te tiisoo na li ngeen yég jagadeem.

2:27b.PHI.002.027 Ci dëgg-dëgg woppoon na ba xaw a dee, waaye Yàlla yërëm na ko, ba fëgg boppam, rax-ca-dolli siggil na ma man itam, ngir ma bañ a am tiis ci kaw tiis.

2:28b.PHI.002.028 Noonu delloo naa leen ko ci lu gaaw, ngir ñëwam bégal seeni xol, te man itam sama xol féex.

2:29b.PHI.002.029 Teeruleen ko teeru bu rafet nag ngir Boroom bi, te teral ñi mel ni moom.

2:30b.PHI.002.030 Ndaxte liggéeyal na Kirist, ba riisu dee, te gar na bakkanam ci taxawal leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man.

3

3:1b.PHI.003.001 Kon nag samay bokk, bégleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju.

3:2b.PHI.003.002 Moytuleen xaj yi, waaw moytuleen ñiy jëfe lu bon, ñoom ñi seen xarafal weesul wàññi yaramu nit.

3:3b.PHI.003.003 Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy màggal Yàlla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu jenn yaakaar ci matug nit.

3:4b.PHI.003.004 Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw.

3:5b.PHI.003.005 Xarafoon naa ca ayu-bés ga, bokk ci bànni Israyil ci giiru Ben-yamin, di Ibrë ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen bëgg a wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon;

3:6b.PHI.003.006 bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom ñi gëm Kirist; bu dee ci njub ci sàmm yoon, awma benn gàkk.

3:7b.PHI.003.007 Waaye loolu lépp lu ma tegoon ay njariñ fa kanam Yàlla, dëddu naa ko ngir Kirist.

3:8b.PHI.003.008 Rax-ca-dolli dëddu naa lépp ngir xéewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu xóot, ba xel mënu koo takk. Moo tax ñàkk naa sama lépp, te def ko ni mbalit, ngir am cér ci Kirist.

3:9b.PHI.003.009 Na ma Yàlla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci sàmm yoon, waaye gu aju ci gëm Kirist, maanaam njub gi nu Yàlla sol ci kaw ngëm.

3:10b.PHI.003.010 Moom laay ittewoo xam, ak doole ji ànd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam,

3:11b.PHI.003.011 ngir man a séddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.

3:12b.PHI.003.012 Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist jël ma.

3:13b.PHI.003.013 Bokk yi, gëmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: fàtte li ma weesu, jublu ci li féete kanam,

3:14b.PHI.003.014 di daw yen muj ga, ngir jot li ma Yàlla tax a woo, di cér bi ma Yàlla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.

3:15b.PHI.003.015 Nun ñi mat nag, nanu xalaat loolu. Te su ngeen ci amee werantey xol, Yàlla dina leen ko leeralal.

3:16b.PHI.003.016 Li am daal, fa seen ngëm tolloo, na fa seen jëf àgg.

3:17b.PHI.003.017 Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen.

3:18b.PHI.003.018 Ndaxte jëfi ñu bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba tàyyi, maa ngi koy waxaat léegi ak i jooy.

3:19b.PHI.003.019 Alku lañuy mujje, ñoom ñiy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut yëfi àddina rekk.

3:20b.PHI.003.020 Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist jóge fa, musalsi nu.

3:21b.PHI.003.021 Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi ànd ak ndam dëppook kàttanam, gi ko man a nootal mbindeef yépp.

4

4:1b.PHI.004.001 Kon nag yéen samay bokk, ñi ma bëgg te namm leen, di sama mbég ak sama kaalag ndam, jàppleen bu dëgër noonu ci Boroom bi, soppe yi!

4:2b.PHI.004.002 Ci lu jëm ci Ewodi ak Santis, maa ngi leen di ñaan, ñu bokk benn xalaat ci Boroom bi.

4:3b.PHI.004.003 Te yaw sama nawle bu wér, nanga dimbali jigéen ñooñu xeexoon ci sama wet ci tas xebaar bu baax bi, boole ci Këlemaŋ ak samay yeneeni nawle, ñoom ñi Yàlla bind seeni tur ci téereb dund ba.

4:4b.PHI.004.004 Deeleen bég ci Boroom bi; maa ngi koy waxati: bégleen!

4:5b.PHI.004.005 Na seen lewet leer ñépp. Boroom bi jege na.

4:6b.PHI.004.006 Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetal-leen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant.

4:7b.PHI.004.007 Noonu jàmmu Yàlla, ji xel mënta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu.

4:8b.PHI.004.008 Léegi nag bokk yi, na seen xalaat jublu ci lii: lu dëggu, lu jekk, lu jub, lu sell, lu rafet ak lu faaydawu; su fi amee lu baax mbaa lu mat a naw, xalaatleen ko.

4:9b.PHI.004.009 Li ngeen jànge ci man te nangu ko, li ngeen dégge ci man te gis ko, jëfeleen ko; kon Yàllay jàmm dina ànd ak yéen.

4:10b.PHI.004.010 Sama xol sedd na guyy ci Boroom bi, ci ni ngeen yeesale seen ndimbal ci man. Xam naa ne, amoon ngeen yéene ji, waaye man gi moo fi nekkul woon.

4:11b.PHI.004.011 Ba tey soxla taxul ma waxe nii, ndaxte jàng naa doylu ci mbir mu ma man a dab.

4:12b.PHI.004.012 Miin naa ñàkk, man naa naataange. Ci fépp ak ci lépp, Yàlla def na ba sama xol toj ci suur ak xiif, barele ak néewle.

4:13b.PHI.004.013 Man naa lépp ci ndimbalu Aji Dooleel ji.

4:14b.PHI.004.014 Waaye teewul taxawu, bi ngeen ma taxawu ci sama tiis, jëf ju rafet la.

4:15b.PHI.004.015 Yéen waa Filib xam ngeen ne, bi ngeen jëkkee xam xebaar bu baax bi, te ma jóge diiwaanu Maseduwan, benn mbooloo àndul woon ak man ci mbirum joqleente ndimbal, mu dul yéen doŋŋ.

4:16b.PHI.004.016 Ba ma nekkee dëkku Tesalonig sax, yónnee ngeen ay yooni yoon, ngir faj samay soxla.

4:17b.PHI.004.017 Loolu tekkiwul ne, damay sàkku ay ndimbal ci yéen, waaye damaa bëgg rekk seen denc yokku fa Yàlla.

4:18b.PHI.004.018 Fi mu ne jot naa li ma aajowoo lépp, ba maa ngi ci naataange; li ngeen ma yónnee ci loxoy Epafrodit doy na sëkk; ni xetu latkoloñ la mel ci man, di sarax su neex Yàlla te mu nangu ko.

4:19b.PHI.004.019 Te Yàlla sama Boroom, mi denc ci Kirist Yeesu xéewal yu dul jeex, dina ci faj seeni soxla yépp.

4:20b.PHI.004.020 Na Yàlla sunu Baay yelloo ndam ba fàww. Amiin.

4:21b.PHI.004.021 Nuyul-leen ma gaayi Kirist Yeesu yu sell yépp. Bokk yi ànd ak man, ñu ngi leen di nuyu.

4:22b.PHI.004.022 Te it gaayi Yàlla yu sell yépp ñu ngi leen di nuyu, rawatina nag ñi nekk kër buur bi Sesaar.

4:23b.PHI.004.023 Na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist ànd ak seen xel.


Holder of rights
Multilingual Bible Corpus

Citation Suggestion for this Object
TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Philippians (Wolof). Philippians (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C342-1