Galatians (Wolof)
1
1:1b.GAL.001.001 Man Pool, ndawul Yeesu Kirist --nit falu ma ko, te jaarewul it ci nit, mi ngi jaare ci Yeesu Kirist ak Yàlla Baay, bi ko dekkal —
1:2b.GAL.001.002 man ak bokk yiy ànd ak man yépp, nu ngi leen di bind, yéen mboolooy ñi gëm te dëkk ci diiwaanu Galasi.
1:3b.GAL.001.003 Na yiw ak jàmm féete ak yéen, jóge ci Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi,
1:4b.GAL.001.004 moom mi joxe bakkanam ngir dindi sunuy bàkkaar, te musal nu ci àddina su bon, si nu nekk, dëppook coobareg Yàlla sunu Baay,
1:5b.GAL.001.005 bi yelloo ndam ba fàww. Amiin.
1:6b.GAL.001.006 Man de jaaxle naa! Yàlla woo na leen ci boppam jaarale ko ci yiw, wi nu Kirist defal, waaye yéena ngi koy gaawantoo bàyyi, ngir topp beneen xebaar,
1:7b.GAL.001.007 fekk du xebaar bu baax bi. Dafa am rekk ci seen biir ay nit ñiy nëxal xel yi, te bëgg a dandal xebaar bu baax bu Kirist.
1:8b.GAL.001.008 Waaye su fekkee kenn ci nun ñëw, walla malaaka sax mu jóge asamaan, di yégle beneen xebaar bu mengoowul ak bi nu leen yégal, kooku Yal na alku!
1:9b.GAL.001.009 Wax nanu ko, maa ngi koy waxaat: bu leen kenn yégalee beneen xebaar bu dul bi ngeen nangu, kooku Yal na alku!
1:10b.GAL.001.010 Ndax kon nit laay wut a gëmloo, am damay fexee yey Yàlla? Mbaa damay wut a neex nit ñi? Su ma doon wut a neex nit ñi ba tey, kon duma nekkati jaamu Kirist.
1:11b.GAL.001.011 Bokk yi, maa ngi leen di xamal ne, xebaar bu baax bi ma yégle, jógewul ci nit.
1:12b.GAL.001.012 Jëlewuma ko ci nit, te kenn jàngalu ma ko, waaye Yeesu Kirist moo ma ko won.
1:13b.GAL.001.013 Dégg ngeen ni ma doon jëfe, bi ma nekkee ci diiney Yawut yi, di fitnaal bu metti mbooloom Yàlla, di ko jéem a tas.
1:14b.GAL.001.014 Bokkoon naa ci ñi gën a farlu ci diiney Yawut yi, te sawar it ci sàrti yoon, yi fi samay maam bàyyi, ba raw sama maas, gi ma bokkal askan.
1:15b.GAL.001.015 Waaye Yàlla mi ma tànn lu jiitu sama juddu te woo ma ci boppam ci kaw yiwam, bi mu ko soobee, xamal na ma kan mooy Doomam, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi ci mbirum Kirist; booba nag diisoowuma ci ak kenn.
1:17b.GAL.001.017 Demuma sax Yerusalem seeti ñi ma jëkk a nekk ay ndawi Kirist, waaye réewu Arabi laa dem, te gannaaw loolu ma dellusiwaat Damas.
1:18b.GAL.001.018 Ba ñu ca tegee ñetti at, ma sog a dem Yerusalem, ngir xamante ak Sefas, dal fa moom lu mat ñaari ayu-bés.
1:19b.GAL.001.019 Waaye gisuma keneen ci ndaw yi ku dul Saag, doomu ndeyu Boroom bi.
1:20b.GAL.001.020 Lii ma leen di bind nag, Yàllaa may seede ci ne, du ay fen.
1:21b.GAL.001.021 Bi loolu wéyee dem naa réewu Siri ak réewu Silisi.
1:22b.GAL.001.022 Waaye ba tey mboolooy ñi gëm Kirist ci diiwaanu Yude xamuñu ma woon.
1:23b.GAL.001.023 Dañu déggoon ñu naan rekk ne: «Ki nu daan fitnaal bu jëkk te daan jéem a far yoonu ngëm wi, léegi mi ngi koy yégle!»
1:24b.GAL.001.024 Te ñuy sant Yàlla ci man.
2
2:1b.GAL.002.001 Ba ñu ca tegee fukki at ak ñeent, ànd naa ak Barnabas, dellu Yerusalem, yóbbaale Tit.
2:2b.GAL.002.002 Dem naa fa, ndaxte Yàllaa ma fa yebal ci kaw peeñu. Ba ma demee, daje naa ak ñi ñu gën a fonk ca mbooloo ma, ma wéetoo ak ñoom, won leen xebaar bu baax, bi may yégal ñi dul Yawut; ngir ragal sama coonob démb mbaa tey neen.
2:3b.GAL.002.003 Te Tit mi ma gunge woon sax de, li mu bokk ci xeetu Gereg, taxul ñu sonal nu ci xarafal ko.
2:4b.GAL.002.004 Fekk na mbir moomu nekk coow ndax naaféq, yi yoxoosu ci sunu biir ak mébét mu bon, ngir seet yaatu gi nu am ci Yeesu Kirist, ba fexe noo defaat ay jaam.
2:5b.GAL.002.005 Waaye yaatalunu leen benn yoon, ngir dëggug xebaar bu baax bi man a sax ci yéen.
2:6b.GAL.002.006 Waaye ñi ñu gën a fonk --ak lu man a doon seen sag xooluma ko, ñépp a yem fa kanam Yàlla — waaye ñooñu ñu teg njiit boog, bi ma dajee ak ñoom, yokkuñu dara ci sama sas.
2:7b.GAL.002.007 Gis nañu ne, Yàllaa nu yebal, muy man di Piyeer, ngir nu yégle xebaar bu baax bi; ma féetewoo ñi dul Yawut, Piyeer féetewoo Yawut yi.
2:8b.GAL.002.008 Ndaxte ni Yàlla jëfe ci Piyeer, miy ndawam ci Yawut yi, noonu it la jëfe ci man, may ndawam ci ñi dul Yawut.
2:9b.GAL.002.009 Te Saag, Sefas ak Yowaana nag, ñi ñu teg kenuy mbooloo mi, bi ñu ràññee yen bi ma Yàlla jagleel ci yiwam, ñu fekksi nu ci, ba jox nu loxo, man ak Barnabas, nu liggéey ca ña dul Yawut, ñoom ñu liggéey ca Yawut ya.
2:10b.GAL.002.010 Li ñu doon laaj rekk moo di, nuy fàttaliku seen aji néew doole yi, fekk sax laxasu woon naa ci def ko.
2:11b.GAL.002.011 Waaye bi Sefas ñëwee dëkku Ancos, yedd naa ko ci kanamu ñépp, ndaxte li mu def jaaduwul.
2:12b.GAL.002.012 Ndaxte laata ndaw yi Saag yónni di ñëw, da daan bokk di lekk ak ñi dul Yawut. Waaye bi ñu agsee, te mu ragal kureel boobu faaydaal xaraf, mu dellu gannaaw, di sore ñi dul Yawut.
2:13b.GAL.002.013 Yeneen Yawut yi it daldi ànd ak Sefas ci naaféqam, ba yóbbaale sax Barnabas.
2:14b.GAL.002.014 Bi ma seetee nag ne, awuñu woon ci dëgg, gi xebaar bu baax bi di jàngale, ma yedd Sefas ci kanamu ñépp ne ko: «Yaw miy Yawut, gannaaw dëddu nga aaday Yawut yi, ba dund ni ku dul Yawut, lu tax nga bëgg a sëf diiney Yawut ci ñi dul Yawut?»
2:15b.GAL.002.015 Nun danoo cosaanoo ci xeetu Yawut, te bokkunu ci xeet, yi xamul Yàlla tey bàkkaar.
2:16b.GAL.002.016 Teewul nu xam ne, Yàlla du àtte kenn ni ku jub ci kaw sàmm yoon, waaye ci gëm Yeesu Kirist. Kon nun itam gëm nanu Kirist Yeesu, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw gëm Kirist, te du ci sàmm yoon. Ndaxte du caageenug sàmm yoon mooy tax Yàlla àtte kenn ni ku jub.
2:17b.GAL.002.017 Waaye ba tey su fekkee ne nu ngi wut a jub ci kaw gëm Kirist, fekk nu ne fàŋŋ di ay bàkkaarkat, ndax nag Kirist moo sas bàkkaar? Mukk!
2:18b.GAL.002.018 Waaye su ma delloo di sàmm ndigali yoon, yi ma bàyyi, dëgg-dëgg dinaa wone noonu ne, moykatu yoon wi laa.
2:19b.GAL.002.019 Ci li jëm ci yoonu Musaa, dee naa, fekk yoon wi ci boppam moo ko waral, ngir ma man a dund, ba amal jariñ Yàlla.
2:20b.GAL.002.020 Daajaale nañu ma ak Kirist ca bant ba, te noonu du man may dundati, waaye Kirist mooy dund ci man. Dundu mbindeef, gi may dund nag, maa ngi koy dund ci gëm Doomu Yàlla ji, moom mi ma bëgg, ba joxe bakkanam ngir man.
2:21b.GAL.002.021 Duma neenal yiwu Yàlla, ndaxte su sàmm yoon doon tax a jub fa kanam Yàlla, kon Kirist dee na cig neen.
3
3:1b.GAL.003.001 Yéen waa Galasi, yéena ñàkk xel! Ku leen fàbbi, gannaaw bi ma leen yégalee ci lu leer ni ñu daaje Yeesu Kirist ca bant ba?
3:2b.GAL.003.002 Lenn rekk laa bëgg, ngeen wax ma ko: ndax sàmm yoon wee tax, ngeen jot Xelum Yàlla? Déedéet! Dangeen a dégg xebaar bu baax bi te gëm ko.
3:3b.GAL.003.003 Mbaa du nii ngeen ñàkke xel, ba tàmbalee ci Xelum Yàlla, ba noppi yaakaar a mate ci seen jëfi bopp?
3:4b.GAL.003.004 Mbaa du fitna, yi ngeen daj yépp, dafa nar a neen? Mënuma koo gëm!
3:5b.GAL.003.005 Bu leen Yàlla di may Xelam, di leen won jalooreem, ndax li ngeen sàmm yoon a tax, mu def ko, mbaa li ngeen dégg xebaar bu baax te gëm ko?
3:6b.GAL.003.006 Xool-leen ci Ibraayma; Mbind mi wax na ne:«Ibraayma gëm na Yàlla,te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.»
3:7b.GAL.003.007 Xamleen boog ne, boroom ngëm yi rekk ñooy doomi Ibraayma.
3:8b.GAL.003.008 Mbind mi tëral na lu jiitu ne, Yàlla dina àtte jub ñi dul Yawut ci kaw ngëm. Kon looloo tax mu yégal Ibraayma lu jiitu xebaar bu baax bi ne ko: «Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci yaw.»
3:9b.GAL.003.009 Kon ñi gëm, Yàlla dina leen barkeel, sukkandikoo ko ci seen ngëm, ni mu defal Ibraayma, boroom ngëm.
3:10b.GAL.003.010 Ñiy wékku ñépp ci jëfi yoon wi, ñu alku lañu, ndaxte bind nañu ne: «Képp ku dul topp lépp lu ndigali yoon wi santaane, Yal na alku.»
3:11b.GAL.003.011 Bir na sax ne, sàmm yoon du tax kenn jub fa kanam Yàlla, ndaxte Mbind mi tëral na ne: «Ku jub ci kaw ngëm dinga dund.»
3:12b.GAL.003.012 Waaye yoon wi laajul ngëm. Mbind mi nee na: «Ku manoon a matal li yoon wi wax, kon dinga dund ba fàww.»
3:13b.GAL.003.013 Waaye Kirist jot na nu ci alkande, ji yoon wi indi; mu gàddul nu ko, ba far alku moom ci boppam, ndaxte Mbind mi nee na: «Képp ku ñu rey, wékk ko ci bant, alku nga.»
3:14b.GAL.003.014 Noonu barke bi Yàlla dig Ibraayma baawaan na, ba daj ñi dul Yawut te gëm Kirist Yeesu, te nu jot ci kaw ngëm Xel mu Sell, mi Yàlla dige.
3:15b.GAL.003.015 Bokk yi, maa ngi misaal wax ji ci jëfi doom Aadama. Xam ngeen ne, kóllëre gu ñu fas ba noppi, waruñu koo fecci, walla ñu ciy rax dara.
3:16b.GAL.003.016 Léegi nag Yàlla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam. Mbind mi waxul: «Ak i sëtam,» mu mel ni ñu bare, waaye kenn la wax: «Ak sa askan,» maanaam Kirist.
3:17b.GAL.003.017 Li ma ci bëgg a wax mooy lii: ndegam Yàlla fas na kóllëreem, yoonu Musaa, wi feeñ ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw ga, du ko man a fecci, ba tebbi digeb Yàlla.
3:18b.GAL.003.018 Ndaxte xéewal, yi Yàllay dige, bu ñu doon jóge ci yoon wi, kon ajootuñu ci dige bi, fekk ci kaw dige la ko Yàlla maye Ibraayma.
3:19b.GAL.003.019 Waaw kon yoonu Musaa, luy jariñam? Dañu koo wàcceel nit ñi, ngir seen jàdd yoon ne fàŋŋ. Looloo doon wàllu yoon wi, ba kera Sët biy ñëw, moom mi ñu digoon dige bi. Yoon wi nag, Yàlla tëral na ko jaare ci ay malaaka, te am na ku ko jottali.
3:20b.GAL.003.020 Waaye aajowul jottalikat, su fi kenn rekk teewee, te Yàlla kenn la.
3:21b.GAL.003.021 Ndax kon yoonu Musaa wi dafa juuyoo ak li Yàlla dige? Mukk! Su amoon yoon wu nit man a sàmm, ba mu jural ko dund gu sax, kon sàmm yoon dina tax nit jub fa kanam Yàlla.
3:22b.GAL.003.022 Waaye yoon wi tëj na ñépp ci dooley bàkkaar, ngir ñi gëm Yeesu Kirist jot li Yàlla dige woon ci seen kaw ngëm.
3:23b.GAL.003.023 Bi ngëm Yeesu Kirist feeñagul nag, yoon wi da noo tëjoon ràpp, ba kera ngëm di feeñ.
3:24b.GAL.003.024 Ci noonu la nu yoon wi doon noote, ba Kirist di ñëw, ngir Yàlla àtte nu jub ci kaw ngëm.
3:25b.GAL.003.025 Waaye léegi, bi jamonoy ngëm ji ñëwee, nekkatunu ci kilifteefu yoon wi.
3:26b.GAL.003.026 Yéen ñépp doomi Yàlla ngeen ndax li ngeen bokk ci Kirist Yeesu ci kaw ngëm.
3:27b.GAL.003.027 Yéen ñépp, ñi ñu sóob ci ndox ngir wone seen bokk ci Kirist, soloo ngeen Kirist.
3:28b.GAL.003.028 Kon nag amul xaajale ci diggante Yawut ak ki dul Yawut, ci diggante jaam ak gor, ci diggante góor ak jigéen. Yéen ñépp benn ngeen ci seen bokk ci Kirist.
3:29b.GAL.003.029 Bu ngeen bokkee ci Kirist, kon bokk ngeen ci askanu Ibraayma, te jot ngeen xéewal, yi ko Yàlla dig.
4
4:1b.GAL.004.001 Li ma leen di wax, mooy lii: doom ji war a donni baayam, fi ak mu ngi cig ndaw, ak lu ko alal jiy lew lépp, du wuute dara ak jaam.
4:2b.GAL.004.002 Ñi ko yore tey sàmm alalam ñoo koy yilif, ba jamono ji ko baayam àppaloon mat.
4:3b.GAL.004.003 Nun itam naka noonu, laata nuy mat, aaday àddina ñoo nu nootoon, ba def nu ni ay jaam.
4:4b.GAL.004.004 Waaye bi àpp bi Yàlla tëraloon matee, yónni na Doomam, mu juddoo ci jigéen, ci biir yoonu Musaa,
4:5b.GAL.004.005 ngir jot ñi yoon wi nootoon, ndax Yàlla jàpp nu ni ay doomam.
4:6b.GAL.004.006 Gannaaw doomi Yàlla ngeen nag, Yàlla yónni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: «Abba,» maanaam «Baay.»
4:7b.GAL.004.007 Noonu dootuloo jaam, doom nga. Te ndegam doom nga, Yàlla jagleel na la cér ci xéewal, yi mu dencal ay doomam.
4:8b.GAL.004.008 Bu jëkk, bi ngeen xamagul Yàlla, yéena ngi doon jaamu yeneen yu ñu daan bokkaaleel Yàlla.
4:9b.GAL.004.009 Waaye léegi nag bi ngeen xamee Yàlla, walla boog bi leen Yàlla xàmmee, nan ngeen man a def, bay delluwaat ca aaday àddina? Aada yooyee ñàkk doole te ñàkk njariñ, lu tax ngeen bëgg, ñu nootaat leen?
4:10b.GAL.004.010 Yéena ngi fonk bés yi, weer yi, màggal yi ak at yi!
4:11b.GAL.004.011 Sama xel dalul ci yéen, ngir ragal sama coono ci yéen neen.
4:12b.GAL.004.012 Bokk yi, dama leen di ñaan, ngeen mel ni man, ndaxte man itam fekksi naa leen ci seen xalaat. Tooñuleen ma.
4:13b.GAL.004.013 Xam ngeen ne, sama wopp moo taxoon, ma yégal leen xebaar bu baax bi.
4:14b.GAL.004.014 Coono, gi leen sama wopp tegoon, taxul ngeen bañ ma, taxul ngeen séexlu ma. Waaye teeru ngeen ma, ni bu ngeen doon teeru malaakam Yàlla walla Yeesu Kirist.
4:15b.GAL.004.015 Waaw, fan la seen mbég jaar? Ndaxte seedeel naa leen ne, su ngeen ko manoon, kon luqi ngeen seeni bët, jox ma.
4:16b.GAL.004.016 Ndax dëgg, gi ma leen wax, moo tax ngeen def ma ab noon?
4:17b.GAL.004.017 Nit ñooñu leen di farle, seen mébét baaxul. Dañu leen a bëgg a tàggale ak nun, ngir ngeen far ak ñoom.
4:18b.GAL.004.018 Farle baax na, bu àndee ak mébét mu baax. Waaye bu sama jëmm rekk tax ngeen koy def.
4:19b.GAL.004.019 Sama doom yi! Yéena tax may dellu ci metit ni kuy matu, ba kera jikkoy Kirist di mat ci yéen.
4:20b.GAL.004.020 Léegi bëggoon naa nekk ci seen biir, ngir man a jubbanti sama kàddu, ndaxte xamatuma nu may doxale ak yéen!
4:21b.GAL.004.021 Yéen ñi bëgg a topp yoon wi, xanaa xamuleen li yoonu Musaa wi wax?
4:22b.GAL.004.022 Mbind mi nee na: Ibraayma am na ñaari doom; ki jaam bi jur ak ki gor si jur.
4:23b.GAL.004.023 Doomu jaam bi juddu na ni bépp doom, waaye doom, ji mu am ak jabaram, juddu na ci kaw digeb Yàlla.
4:24b.GAL.004.024 Loolu nag am na lu muy misaal. Ñaari jigéen ñi dañoo bijji ñaari kóllëre. Benn bi di Ajara, mooy wone kóllëre, gi Yàlla fasoon ca tundu Sinayi. Ay jaam lay jur.
4:25b.GAL.004.025 Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wi nekk ca réewu Arabi. Te it mooy misaalu dëkku Yerusalem, bi fi nekk tey. Ndaxte moom ak ay doomam yépp ay jaam lañu.
4:26b.GAL.004.026 Waaye Yerusalem, ga ca kaw, mooy gor si. Moom mooy sunu ndey.
4:27b.GAL.004.027 Ndaxte Mbind mi nee na:«Bégal, yaw jigéen ji dul jur,te musul a am doom.Reeyal te bànneexu,yaw mi musul a xam coonob mat,ndaxte jigéen ji ñu faalewulmoo gën a jaboot ki nekk ak jëkkëram.»
4:28b.GAL.004.028 Yéen bokk yi, yéenay doom yi ñu dige woon, niki Isaaxa.
4:29b.GAL.004.029 Waaye doom ji juddoo ni bépp doom, dafa daan sonal doom ji juddoo ci dooley Xelum Yàlla. Te loolu mooy law ba léegi.
4:30b.GAL.004.030 Lu ci Mbind mi wax nag? Nee na: «Dàqal jaam bi ak doomam, ndaxte doomu jaam bi warul a bokk cér ak doomu gor si ci ndono.»
4:31b.GAL.004.031 Kon nag bokk yi, nun dunu doomi jaam, ay doomi gor lanu.
5
5:1b.GAL.005.001 Kirist a nu daggal sunu buumi njaam, ngir goreel nu. Kon dëgërleen ci seen ngor te bañ a delluwaat ci njaam.
5:2b.GAL.005.002 Dégluleen! Man Pool maa leen koy wax: bu ngeen itteelee xaraf, kon Kirist dootu leen jariñ dara.
5:3b.GAL.005.003 Te maa ngi dellu di waxaat ne, képp kuy farataal xaraf, fàww nga sàmm lépp lu yoon wi santaane.
5:4b.GAL.005.004 Yéen ñiy fexee jub fa kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, tàggalikoo ngeen ak Kirist; dëddu ngeen yiwu Yàlla.
5:5b.GAL.005.005 Waaye njub, gi nu Yàlla dencal ëllëg, nu ngi koy séentu ci kaw ngëm ak ci ndimbalu Xelum Yàlla.
5:6b.GAL.005.006 Ndaxte bu nu bokkee ci Kirist Yeesu, xaraf ak bañ a xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm, giy jëf ci mbëggeel.
5:7b.GAL.005.007 Ni ngeen jógtee woon de baax na! Waaw ku leen dog, ba ngeen bañ a déggal dëgg?
5:8b.GAL.005.008 Li ñu leen xiir jógewul ci Yàlla, mi leen woo.
5:9b.GAL.005.009 Dees na ne: «Tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki.»
5:10b.GAL.005.010 Waaye teewul Boroom bi jox na ma kóolute ci yéen. Biral na ma ne, dingeen bokk ak man xalaat. Léegi nag, kiy nëxal seen xel, ku mu man a doon, Yàlla dina ko mbugal.
5:11b.GAL.005.011 Man nag bokk yi, bu ma doon faaydaal xaraf ci sama waare, kon duñu ma fitnaale nii; te it li may yégle ci deewu Kirist ca bant ba dootul naqari kenn.
5:12b.GAL.005.012 Ñi farataal xaraf te di leen dëpp, nañu gën a sore ci seen réer: bu yaboo sax ñu dagg seen ngóora, ba dara du ci des!
5:13b.GAL.005.013 Yéen nag bokk yi, Yàlla woo na leen, ngeen nekk i gor. Waaye nag buleen ci sukkandiku, bay topp seen nafsu, waaye dimbaleenteleen ci kaw mbëggeel.
5:14b.GAL.005.014 Ndaxte yoon wépp, ndigal lii a ko tënk: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
5:15b.GAL.005.015 Waaye moytuleen! Bu ngeen dee màttante ak a lekkante, dingeen yàqante.
5:16b.GAL.005.016 Li ma leen di wax mooy lii: dundleen ci Xelum Yàlla, kon dungeen topp seen nafsu.
5:17b.GAL.005.017 Ndaxte sunu nafsu am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu Xelum Yàlla. Te Xelum Yàlla itam am na ay bëgg-bëgg yu mengoowul ak yu sunu nafsu. Ñoom ñaar dañoo juuyoo ci bépp fànn, ba tax lépp lu ngeen bëggoon a def, dungeen ko man.
5:18b.GAL.005.018 Waaye bu ngeen toppee Xelum Yàlla, nekkatuleen ci kilifteefu yoon wi.
5:19b.GAL.005.019 Kuy topp sa nafsu, nii ngay jëfe: njaaloo, xalaat yu bon, def i ñaawteef ak say cér,
5:20b.GAL.005.020 xërëm, luxus, noonoo ak xuloo, ñeetaane, xadar, diiroo mbagg, féewaloo ak xaajaloo,
5:21b.GAL.005.021 kiñaan, màndite ak xawaare ak yeneen yu ni mel. Léegi nag maa ngi leen di artu, ni ma ko defe woon: ñiy jëfe noonu duñu am cér ci nguuru Yàlla.
5:22b.GAL.005.022 Waaye li Xelu Yàlla mi di meññ mooy: mbëggeel, mbég, jàmm, muñ, laabiir, mbaax, kóllëre,
5:23b.GAL.005.023 lewetaay ak maandute. Yoon wi terewul yu ni mel.
5:24b.GAL.005.024 Léegi ñi bokk nag ci Yeesu Kirist, daaj nañu seen nafsu ca bant ba, wacc ko fa, moom ak ay xemmemam ak ay bëgg-bëggam.
5:25b.GAL.005.025 Gannaaw nag nu ngi dund léegi ci Xelum Yàlla, kon nanu ko topp.
5:26b.GAL.005.026 Bu nu tiitaru di dëkkante, di iñaanante.
6
6:1b.GAL.006.001 Bokk yi, ku ñu fekk muy def lu Yàlla bëggul, yéen ñi topp Xelum Yàlla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga sàmm sa bopp, ngir bàkkaar bañ laa fiir, yaw itam.
6:2b.GAL.006.002 Jàppalanteleen, noonu dingeen sàmm yoon wi Kirist tëral.
6:3b.GAL.006.003 Ndaxte kuy naagu te fekk doo dara, dangay nax sa bopp.
6:4b.GAL.006.004 Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina man a naw boppam, tey bañ di diirante mbagg ak ñi ci des.
6:5b.GAL.006.005 Ndaxte ku ci nekk dangaa war a yenu sab yen.
6:6b.GAL.006.006 Kiy jàng kàddug Yàlla war na sédd ki koy jàngal ci alalam jépp.
6:7b.GAL.006.007 Bu leen ci dara nax; kenn du fontoo Yàlla, ndaxte lu waay ji, moom ngay góob.
6:8b.GAL.006.008 Ku ji ngir sa nafsu, dinga góob li sa nafsu meññ, maanaam ag yàqute. Waaye ku ji lu soloo ak Xelum Yàlla, li Xel mi meññ ngay góob, maanaam dund gu dul jeex.
6:9b.GAL.006.009 Bunu tàyyi ci def lu baax, ndaxte bu nu ci sawaree, bu waxtu wi jotee dinanu jariñu.
6:10b.GAL.006.010 Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax, rawatina nag sunu bokk yi gëm.
6:11b.GAL.006.011 Seetleen araf yu mag yii ma leen bind ci sama loxob bopp!
6:12b.GAL.006.012 Ñiy gistal ci seen yaram, ñooñoo bëgg ngeen xaraf, ngir ragal a daj fitna ci yégle deewu Kirist ca bant ba.
6:13b.GAL.006.013 Kureel gi faaydaal xaraf, ñoom ci seen bopp sax, duñu topp yoon wi. Dañoo bëgg a ngeen xaraf, ba ñu man a bàkku ci seen yaram, yéen.
6:14b.GAL.006.014 Man ci sama wàllu bopp, duma bàkku mukk su dul ci deewu sunu Boroom Yeesu Kirist, ba ñu ko daajee ca bant ba. Deeyam moo tax ma mel ni ku dee ci yëfi àddina; yëfi àddina dee ci man.
6:15b.GAL.006.015 Xaraf ak bañ a xaraf dara amu ci solo. Li am solo mooy nekk mbindeef mu bees.
6:16b.GAL.006.016 Ñiy topp ndigal lii nag, na Yàlla wàcce jàmm ak yërmande ci ñoom, ak ci Israyilu Yàlla.
6:17b.GAL.006.017 Léegi nag, bu ma kenn lëjalati, ndaxte yor naa ci sama yaram ay leget yuy màndargaal ne, jaamu Yeesu laa.
6:18b.GAL.006.018 Bokk yi, na yiwu Yeesu Kirist sunu Boroom ànd ak seen xel. Amiin.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Galatians (Wolof). Galatians (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C33C-9