1 Corinthians (Wolof)

1 Corinthians (Wolof)

1

1:1b.1CO.001.001 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Sosten sunu mbokk,

1:2b.1CO.001.002 noo leen di bind, yéen mbooloom Yàlla, mi dëkk Korent. Nu ngi leen di nuyu, yéen ñi Yàlla sédde boppam jaare ci Kirist Yeesu, yéen ñi Yàlla woo, ngeen sell, boole leen ak ñi nekk ci àddina sépp tey tudd turu sunu Boroom Yeesu Kirist, miy seen Boroom, di sunu bos.

1:3b.1CO.001.003 Na leen Yàlla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi may yiw ak jàmm.

1:4b.1CO.001.004 Duma jóg ci di sant Yàlla sama Boroom ci seen mbir ndax yiw, wi mu leen may ci seen bokk ci Kirist Yeesu.

1:5b.1CO.001.005 Ndaxte ci yiwi Yàlla yépp ngeen woomle ci Kirist, muy ci wax, muy ci xam-xam.

1:6b.1CO.001.006 Ndaxte li nu doon seedeel Kirist, Yàlla dëggal na ko ci yéen.

1:7b.1CO.001.007 Noonu nag ñàkkuleen genn may léegi bi ngeen di séentu waxtu, wi sunu Boroom Yeesu Kirist di feeñ ci biir ndamam.

1:8b.1CO.001.008 Kirist dina leen dooleel ba ca muj ga, ngir ngeen bañ a am wenn ŋàññ bés bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee.

1:9b.1CO.001.009 Yàlla kuy sàmm kóllëre la, moom mi leen woo, ngir ngeen bokk ak Doomam Yeesu Kirist, sunu Boroom.

1:10b.1CO.001.010 Waaye bokk yi, maa ngi leen di dénk ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen juboo te bañ a féewaloo ci seen biir. Waaye nangeen ànd te booloo, bokk xel, bokk xalaat.

1:11b.1CO.001.011 Ndaxte bokk yi, waa kër Kelowe xamal nañu ma ne, dangeen di xuloo.

1:12b.1CO.001.012 Maa ngi ñëw ca wax ja: kenn ku nekk ci yéena ngi naan: «Man ci Pool laa bokk!» «Man ci Apolos!» «Man ci Sefas!» «Man ci Kirist!»

1:13b.1CO.001.013 Ndax Kirist dafa xaajoo? Ndax Pool lañu daajoon ca bant ba, mu dee ngir yéen? Ndax sóob nañu leen ci ndox, ngir wone ne bokk ngeen ci Pool?

1:14b.1CO.001.014 Maa ngi sant Yàlla ci li ma sóobul kenn ci yéen, ku dul Kirispus ak Gayus,

1:15b.1CO.001.015 ngir kenn bañ a wax ne, ci sama tur lañu ko sóob.

1:16b.1CO.001.016 Aaŋkay! Sóob naa it ci ndox waa kër Estefanas. Waaye ci sama pàttaliku sóobuma keneen.

1:17b.1CO.001.017 Ndaxte Kirist yebalu ma ngir may sóobe ci ndox, waaye da maa yebal, ngir may yégle xebaar bu baax bi, te ma bañ koo def ak waxi xam-xamu nit, ngir bañ a ñàkkal faayda deewu Kirist ca bant ba.

1:18b.1CO.001.018 Ndaxte yégleb deewu Kirist ca bant ba, ag ndof la ci ñiy sànku. Waaye ci nun ñi aw ci yoonu mucc gi, dooley Yàlla la.

1:19b.1CO.001.019 Ndaxte Mbind mi nee na:«Dinaa folli xam-xamu boroom xam-xam yi,lem xalaati ñi am xel.»

1:20b.1CO.001.020 Ana boroom xam-xam bi? Ana kaaŋ mi? Ana boroom làmmiñ wu neex, wi ci àddina sii? Xanaa Yàlla wonewul ne, xam-xamu àddina si ag ndof la?

1:21b.1CO.001.021 Gannaaw àddina si ci xam-xamam demul ba xam Yàlla --te Yàllaa dogal loolu ci xam-xamam — soob na Yàlla mu musal ñi gëm, jaar ci yégleb xebaaru Kirist, fekk ag ndof la ci bëti nit.

1:22b.1CO.001.022 Ndaxte Yawut yi ñu ngi laaj ay firnde; Gereg yi di wut xam-xam.

1:23b.1CO.001.023 Waaye nun nu ngi yégle Kirist, mi ñu reyoon ca bant ba, te loolooy téq ngëmu Yawut yi, di ag ndof ci ñi dul Yawut.

1:24b.1CO.001.024 Waaye ci ñi Yàlla woo, ñuy Yawut mbaa di Gereg, Kirist mooy dooley Yàlla, di xam-xamu Yàlla.

1:25b.1CO.001.025 Li ñuy wax ag ndof ca wàllu Yàlla moo gën a tedd xam-xamu nit. Te li ñuy wax ñàkk dooley Yàlla moo ëpp kàttan dooley nit.

1:26b.1CO.001.026 Bokk yi, seetleen seen nekkin, bi leen Yàlla di woo. Barewul woon ci yéen, ñi ñuy tudde ay boroom xam-xam mbaa ay boroom doole mbaa ñu rafet ab juddu.

1:27b.1CO.001.027 Waaye li àddina teg ag ndof, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom xam-xam yi; te li àddina teg ag ñàkk doole, Yàlla tànn na ko, ngir rusloo boroom doole yi.

1:28b.1CO.001.028 Li dul juddu bu rafet te mat a xeeb ci àddina, Yàlla tànn na ko; Yàlla tànn na li nekkul, ngir neenal li nekk.

1:29b.1CO.001.029 Noonu kenn du man a damu ca kanam Yàlla.

1:30b.1CO.001.030 Waaye Yàlla moo def ba ngeen bokk ci Kirist, moom mi doon ci nun xam-xam bu jóge ca Yàlla, maanaam: sunu njubte, sunu sellaay, sunu njot.

1:31b.1CO.001.031 Loolu dafa am, ngir li Mbind mi wax am, ne: «Kuy damu, na damu ci Boroom bi.»

2

2:1b.1CO.002.001 Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma ñëwee ci yéen, ngir yégle mbóoti Yàlla, ñëwuma ci ay wax yu neex ak xam-xam bu réy.

2:2b.1CO.002.002 Dogu woon naa ci bañ a xam dara ci seen biir lu dul Yeesu Kirist, te muy ki ñu rey ca bant ba.

2:3b.1CO.002.003 Bi ma teewee ci yéen, ànd naa ak ñàkk doole, ragal ak njàqare.

2:4b.1CO.002.004 Li ma wax ak li ma waare, defuma ko ci làmmiñ wu neex, sukkandikoo ko ci xam-xamu nit, waaye ànd na ak ay firnde yu soqikoo ci kàttanu Xelum Yàlla,

2:5b.1CO.002.005 ngir seen ngëm bañ a wékku ci xam-xamu nit ñi waaye mu wékku ci dooley Yàlla.

2:6b.1CO.002.006 Moona am na xam-xam bu nuy yégal ñi mat, xam-xam bu bokkul ci àddina si, te njiiti àddina si xamuñu ko, ñoom ñi nar a wéy.

2:7b.1CO.002.007 Nu ngi yégle mbóotu xam-xamu Yàlla, mu nëbbu woon te Yàlla dogal ko ngir sunu ndam, laata àddina di sosu.

2:8b.1CO.002.008 Kenn ci njiiti àddina amul woon xam-xam boobu. Su ñu ko amoon, kon duñu rey Boroom ndam li ci bant bi.

2:9b.1CO.002.009 Waaye Mbind mi nee na:«Lu bët gisul,nopp déggu kote xel xalaatu ko,loolu la Yàlla dencal ñi ko bëgg.»

2:10b.1CO.002.010 Fekk nag nun la ko Yàlla won, jaarale ko ci Xelam. Xelum Yàlla mooy leeral lépp, ba ci xalaati Yàlla yi gën a xóot.

2:11b.1CO.002.011 Kan ci nit ñi moo xam yëfi nit? Xanaa xelum nit mi nekk ci moom rekk a ko xam. Noonu it kenn xamul yëfi Yàlla, ku dul Xelum Yàlla.

2:12b.1CO.002.012 Nun nag Xel mi nu jot, jógewul ci àddina, waaye Yàllaa nu ko sol.

2:13b.1CO.002.013 Te loolu nu Yàlla may, yéglewunu ko ci ay baat yu soqikoo ci xam-xamu nit, waaye nu ngi koy yégle ci baat, yi soqikoo ci Xelum Yàlla, di tekkantal yëfi Xelum Yàlla ci ay baat yu mu nu sol.

2:14b.1CO.002.014 Nit kese du nangu yëfi Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom, te du ko man a nangu, ndaxte ku yor Xelum Yàlla rekk moo ko man a ràññale.

2:15b.1CO.002.015 Nit ki yor Xelum Yàlla dafay àtte lépp, te moom ci boppam, kenn du ko àtte.

2:16b.1CO.002.016 Ndaxte Mbind mi nee na:«Ana ku xam xalaatu Boroom bi?Ku ko doon digal?» Waaye nun am nanu xalaatu Kirist.

3

3:1b.1CO.003.001 Man nag bokk yi, mënuma woon a wax ak yéen ni ay nit ñuy déggal Xelum Yàlla, waaye waroon naa wax ak yéen ni ñuy topp seen nafsu, mel ni ay liir ci seen dund ci Kirist.

3:2b.1CO.003.002 Nàmpaloon naa leen, waaye joxuma leen dugub, ndaxte àttanuleen ko woon, te ba léegi sax àttanuleen ko

3:3b.1CO.003.003 ci li ngeen di topp seen nafsu. Bu ñeetaan ak xuloo amee ci seen biir, xanaa du loolu mooy wone ne, dangeen a topp seen nafsu, di doxale ni niti àddina?

3:4b.1CO.003.004 Bu kenn yéglee ne: «Man ci Pool laa bokk,» keneen ne: «Man ci Apolos,» ndax jëfewuleen ni niti àddina rekk?

3:5b.1CO.003.005 Kuy Apolos? ak kuy Pool? Nun ay surga rekk lanu, yu ngeen jaare, ba gëm. Te Boroom bi moo sas ku nekk liggéeyam.

3:6b.1CO.003.006 Maa jëmbët, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil.

3:7b.1CO.003.007 Ki jëmbët nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, waaye Yàlla miy jebbil rekk moo am solo.

3:8b.1CO.003.008 Ki jëmbët ak ki suuxat benn lañu. Teewul nag ku nekk dina jot yool bu tollook liggéeyam.

3:9b.1CO.003.009 Nu ngi liggéeyandoo ci liggéeyu Yàlla; yéenay toolu Yàlla, yéenay taaxum Yàlla.

3:10b.1CO.003.010 Man nag teg naa fondamaa bi, ni tabaxkat bu man liggéeyam, dëppoo ak sas wi ma Yàlla jagleel ci kaw yiwam. Te keneen a ngi tabax ci kaw; waaye na ku nekk teeylu ci ni muy tabaxe.

3:11b.1CO.003.011 Ci li jëm ci fondamaa bi, kenn mënu fee tëral beneen bu dul bi fi xas a taxaw, muy Yeesu Kirist.

3:12b.1CO.003.012 Ku tabax ci kaw fondamaa bi, wurus, xaalis, per, dénk, gittax walla boob,

3:13b.1CO.003.013 sa liggéey dina fés, ndaxte bés baa koy xamle. Bés boobu dina fenk ni safara, te safara si dina nattu liggéeyu ku nekk.

3:14b.1CO.003.014 Ku sa liggéey dëgër, dinga jot yool.

3:15b.1CO.003.015 Waaye ku sa liggéey lakk, dinga ñàkk. Yaw ci sa bopp dinga mucc, waaye mel ni ku rëcc ci safara si.

3:16b.1CO.003.016 Xanaa xamuleen ne, yéenay kër Yàlla, te Xelum Yàlla dëkk na ci yéen?

3:17b.1CO.003.017 Ku yàq kër Yàlla gi, Yàlla dina la yàq, ndaxte kër Yàlla gi dafa sell, te yéenay kër googu.

3:18b.1CO.003.018 Kon bu kenn nax boppam: su kenn ci yéen tegee boppam boroom xam-xam ci gis-gisu àddina sii, kooku na doon dof, ngir am xam-xam bu wóor.

3:19b.1CO.003.019 Ndaxte xam-xamu àddina si, ndof la fa Yàlla. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla jàpp na ñu muus ñi, ba seen fiir këppu ci seen kaw.»

3:20b.1CO.003.020 Te it: «Boroom bi xam na xalaati boroom xam-xam yi; xam ne, duñu mujj fenn.»

3:21b.1CO.003.021 Kon nag bu kenn tiitaru ndax nit ñi, ndaxte yéena moom lépp,

3:22b.1CO.003.022 muy Pool, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di lu am, di luy ñëw; lépp, yéena ko moom.

3:23b.1CO.003.023 Te yéen, Kirist a leen moom, te Kirist, Yàllaa ko moom.

4

4:1b.1CO.004.001 Nañu nu teg kon ay surgay Kirist, di ay jawriñ yuy xamle mbóoti Yàlla.

4:2b.1CO.004.002 Li war ci jawriñ mooy mu takku ci liggéeyam.

4:3b.1CO.004.003 Ngeen àtte ma walla ñeneen àtte ma, amaluma ko solo. Te man sax duma àtte sama bopp.

4:4b.1CO.004.004 Sama xel yeddu ma ci dara, waaye loolu taxul ma jub; ki may àtte mooy Boroom bi.

4:5b.1CO.004.005 Looloo tax buleen daan kenn ci àtte, bala jamono ji di jot te Boroom bi ñëw. Mooy leeral yi nëbbu ci lëndëm, di làññi mébétu xol yi. Bu ko defee ku nekk dina jot ci Yàlla ngërëm, li mu yelloo.

4:6b.1CO.004.006 Bokk yi, ci loolu ma leen doon wax lépp nag, misaal naa leen ko ci Apolos ak ci man, ngir ngeen xool ci nun, ba xam li wax jii di tekki: «Bu seen xalaat weesu li Mbind mi wax.» Noonu kenn du màggal kii, suufeel ki ci des.

4:7b.1CO.004.007 Ndaxte yaw, ku la def, ba nga gën a màgg ñi ci des? Loo am lu ñu la mayul? Te bu ñu la ko mayee, lu tax nga di ci tiitaru, mel ni mayuñu la ko?

4:8b.1CO.004.008 Yéen suur ngeen xaat! Woomle ngeen xaat! Tàmbali ngeen di nguuru te agseegunu! Céy ni ma bëgge, ngeen di nguuru, ba nu man a bokk ak yéen di nguuru!

4:9b.1CO.004.009 Xalaat naa ne, nun ndawi Kirist yi, Yàlla def na ba nu mel ni nit ñu ñu jàppe ci xare te mujj ci sàppe yi, ñu dogal seen dee, nuy ceetaanum mbindeef yépp, muy nit muy malaaka.

4:10b.1CO.004.010 Nun teg nañu nu ni ay dof ndax Kirist, waaye yéen am ngeen xel ci Kirist. Néew nanu doole, waaye yéen am ngeen doole. Nawees na leen, waaye nun dañu noo xeeb.

4:11b.1CO.004.011 Ba fii mu nekk, danoo xiif, mar te rafle; ñu ngi nuy dóor, te dëkkunu fenn;

4:12b.1CO.004.012 nu ngi ñaq di jariñoo. Ku nu saaga, nu ñaanal la lu baax. Coono bu ñu nu teg, nu tegoo ko.

4:13b.1CO.004.013 Ku nu ñaawal, nu tontu la tont lu rafet. Fi mu ne noo mujj di mbalitu àddina, di ñu ñàkk njariñ ci lépp.

4:14b.1CO.004.014 Binduma leen loolu ngir ngeen am yeraange, waaye dama koo def ngir artu leen, ndaxte yéenay samay doom te bëgg naa leen.

4:15b.1CO.004.015 Su ngeen amee junniy njiit yu leen di sàmm ci Kirist, ba tey benn baay rekk ngeen am, ndaxte maa leen yégal xebaar bu baax bi, ba jur leen ci Kirist.

4:16b.1CO.004.016 Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen roy ci man.

4:17b.1CO.004.017 Looloo tax ma yebal ci yéen Timote, miy sama doomu diine, di doom ju takku te ma bëgg ko. Dina leen fàttali ni may dunde ci Kirist, te mu dëppook li may jàngale fu nekk ci mboolooy ñi gëm ñépp.

4:18b.1CO.004.018 Am na ci seen biir ñuy tiitaru, di xalaat ne, duma delluseeti ci yéen.

4:19b.1CO.004.019 Waaye bu soobee Boroom bi, léegi ma ñëw ci yéen te seet boroom tiitar yooyu; waxuma seen kàddu, seen doole laay seet.

4:20b.1CO.004.020 Ndaxte nguuru Yàlla du waxi kese, waaye doole la.

4:21b.1CO.004.021 Lu leen gënal? Ma ñëw ci yéen, yor ab yar, walla ma ànd ak mbëggeel, te lewet?

5

5:1b.1CO.005.001 Dégg nanu sax ñu naan, am na kuy moy Yàlla ci seen biir, moy gu ni tollu, duñu ko gis sax ci ñi xamul Yàlla. Dem na, ba am ci yéen kuy séy ak jabaru baayam.

5:2b.1CO.005.002 Moona yéen de, yéena ngi tiitaru. Waaye dangeen a waroon a am naqar, ba dàq kiy def loolu ci seen biir!

5:3b.1CO.005.003 Man nag, jëmm ji sore na leen, waaye xel mi mu ngi ci yéen, te àtte naa xaat kiy def loolu, ni su ma teewoon ci seen biir. Dogal naa,

5:4b.1CO.005.004 ngeen daje ci turu Boroom bi Yeesu, te sama xel teewe ko, ànd ak dooley Boroom bi Yeesu,

5:5b.1CO.005.005 nu jébbal nit kooku Seytaane, yaramam yàqu, ngir ruuwam mucc keroog bésu Boroom bi.

5:6b.1CO.005.006 Seen tiitar bi jekkul dara. Xanaa xamuleen ne, tuuti lawiir day tax tooyalu fariñ bépp funki?

5:7b.1CO.005.007 Ni ma leen ko man a misaale, jëleleen fi bépp lawiir bu yàgg, ngir ngeen sell ni tooyal bu bees bu amul lawiir, ndax nekk ngeen ko ba noppi. Ndaxte Kirist deeyal na nu ca bant ba, mel ni mbote mu ñuy rendi, jébbal ko Yàlla ca màggalu bésu Jéggi ba.

5:8b.1CO.005.008 Kon nanu màggal sunu Màggal, waxuma ak lawiir bu màggat biy misaal kiñaan ak lu bon, waaye ak mburu mu amul lawiir, maanaam ci xol bu laab ak ci dëgg.

5:9b.1CO.005.009 Bindoon naa leen, ngeen bañ a séq dara ak njaalookat yi.

5:10b.1CO.005.010 Bëgguma ci woon a limaale waa àddina, maanaam njaalookat yi, nay yi, njublaŋ yi ak xërëmkat yi. Su ngeen séqul ak ñooñu dara, kon fàww ngeen génn àddina.

5:11b.1CO.005.011 Lii laa leen bëggoon a wax: buleen séq dara ak ku ñu tudde mbokk mu gëm Kirist, te fekk day njaaloo walla mu nay walla muy xërëm walla muy xas nit walla muy màndi walla muy njublaŋ. Nit ku mel noonu moom, buleen bokk ak moom, sax far di lekk.

5:12b.1CO.005.012 Ndax man maa war a àtte ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm Kirist? Déedéet! Waaye ñi bokk ci seen mbooloo yéena leen war a àtte.

5:13b.1CO.005.013 Ñi bokkul ci mbooloom ñi gëm, Yàlla moo leen di àtte. Waaye yéen, ni ko Mbind mi waxe: «Dàqleen ci seen biir kiy def lu bon.»

6

6:1b.1CO.006.001 Te it bu kenn ci yéen amee lëj-lëj digganteem ak mbokku taalibeem, lu tax muy dem ca àttekaayi ñi xamul Yàlla, te bañ a dem ca gaayi Yàlla yi, ñu àtte ko?

6:2b.1CO.006.002 Xanaa dangeen a xamul ne, gaayi Yàlla yi ñooy àtteji àddina? Te ndegam yéenay àtteji àddina, lu tere ngeen man a àtte mbir yu ñàkk solo yi?

6:3b.1CO.006.003 Xanaa xamuleen ne, nooy àtteji malaaka yi? waxatumaak mbiri àddina sii.

6:4b.1CO.006.004 Bu ngeen amee ay lëj-lëj yu mel noonu, dangeen di wuti ay àttekat ci ay nit, ñi amul wenn yoon ci mbooloom ñi gëm!

6:5b.1CO.006.005 Ma ne kon, war ngeen a rus! Xanaa amul ci seen biir kenn ku am xel, ku man a àtte mbokkam yi?

6:6b.1CO.006.006 Waaye defuleen loolu; mbokk a ngi layoo ak moroomam, rax-ca-dolli ci kanamu ñi gëmul lañu koy defe!

6:7b.1CO.006.007 Layoo bi sax wone na ne, bàyyi ngeen seen warugar. Lu tax muñuleen sax tooñ, yi ñu leen di tooñ? Lu tax far nanguwuleen, ñu sàcc leen?

6:8b.1CO.006.008 Waaye yéen sax yéenay tooñ ak di sàcc, te seeni bokk ngeen koy def!

6:9b.1CO.006.009 Xanaa xamuleen ne, ñi jubadi duñu bokk ci nguuru Yàlla? Bu leen ci kenn nax: ñiy doxaan walla xërëmkat yi ak njaalookat yi ak góor-jigéen ñi ak ñi ko nangu,

6:10b.1CO.006.010 walla sàcc yi ak ñu bëgge ñi ak màndikat yi ak ñiy xaste ak njublaŋ yi, duñu bokk ci nguuru Yàlla.

6:11b.1CO.006.011 Te am na ñu meloon noonu ci yéen. Waaye Yàlla fóotal na leen seeni bàkkaar, sellal leen, àtte leen ni ñu jub, ci turu Boroom bi Yeesu Kirist ak ci dooley Xelum Yàlla, sunu Boroom.

6:12b.1CO.006.012 Am na ci yéen ñu naan: «Sañ naa lépp.» Waaw, waaye du lépp a jariñ nit. «Sañ naa lépp,» waaye duma bàyyi dara, mu noot ma.

6:13b.1CO.006.013 Am na ci yéen ñu naan: «Ñam mooy jariñ biir, te biir ay jariñoo ñam.» Waaw, te Yàlla dina leen yàq, ñoom ñaar yépp. Waaye sàkkuñu yaram ngir moy Yàlla; dañu koo sàkk, ngir muy jariñ Boroom bi, Boroom bi di ko jariñoo.

6:14b.1CO.006.014 Te Yàlla, mi dekkal Boroom bi, dina dekkal it sunu yaram jaare ko ci dooleem.

6:15b.1CO.006.015 Xanaa xamuleen ne, seen yaram ñooy céri Kirist? Ndax kon damay jël céri Kirist, def ko céri jigéeni moykat? Mukk!

6:16b.1CO.006.016 Xanaa xamuleen ne, kuy ànd ak jigéen juy moy dafay booloo ak moom, nekk benn? Ndaxte Mbind mi nee na: «Ñoom ñaar dinañu doon benn.»

6:17b.1CO.006.017 Waaye nag kuy ànd ak Boroom bi, xel yi dañuy booloo, nekk benn.

6:18b.1CO.006.018 Dawleen njaaloo! Bépp bàkkaar bu nit man a def, du laal yaramam, waaye nag kuy njaaloo, dafay bàkkaar, di lor yaramam.

6:19b.1CO.006.019 Xanaa xamuleen ne, seen yaram mooy kër Yàlla gi? Gannaaw Xel mu Sell maa ngi ci yéen, te Yàllaa leen ko may, kon moomuleen seen bopp,

6:20b.1CO.006.020 ndaxte Yàlla jot na leen ak njëg gu réy. Kon nag màggal-leen Yàlla ci seen yaram.

7

7:1b.1CO.007.001 Nanu jàll nag léegi ci laaj, yi ngeen ma doon bind, ci bañ a ànd ak jigéen, ndax lu baax la ci góor.

7:2b.1CO.007.002 Lii mooy sama xalaat: moy gu bare gi tax na ba, na góor gu nekk am jabaram, jigéen ju nekk am jëkkëram.

7:3b.1CO.007.003 Jëkkër war na def warugaru jëkkër ci jabaram; jabar it def warugaru jabar ci jëkkëram.

7:4b.1CO.007.004 Jigéen ji amul sañ-sañ ci yaramam moom kenn; jëkkëram moo ko moom. Niki noonu it jëkkër ji amul sañ-sañ ci yaramam; jabaram moo ko moom.

7:5b.1CO.007.005 Bu kenn tere boppam moroomam, su dul ne dangeen a mànkoo ci def noonu ab diir, ngir gën a man a wéet ak Yàlla ciy ñaan. Waaye su loolu weesoo, nangeen doxal yoonu séy; lu ko moy, Seytaane dina leen fiir ndax seen ñàkk maandute.

7:6b.1CO.007.006 Li ma leen di wax fii du ndigal, waaye dama leen di xamal li ñu leen may, ngeen def ko.

7:7b.1CO.007.007 Ndaxte dëgg-dëgg su ma sañoon, kon ñépp mel ni man; waaye ku nekk ak li la Yàlla jagleel, kii ak may gii, kee ak may gale.

7:8b.1CO.007.008 Lii laay yégal ñi séyul ak it ñi seen jëkkër dee: baax na ci yéen, su fekkee dangeen a toog rekk ni man, bañ a séy.

7:9b.1CO.007.009 Waaye su ngeen mënul a téye seen bopp, nangeen séy, ndaxte séy moo gën xemmem di leen gaañ.

7:10b.1CO.007.010 Ñi séy nag, maa ngi leen di jox ndigal lii --Boroom bi moo ko waxoon, du man — jigéen ju séy warul a teqalikoo ak jëkkëram.

7:11b.1CO.007.011 Te bu teqalikoo ak moom, bumu séyaat, mbaa boog na juboo ak jëkkëram. Te bu jëkkër ji fase jabaram.

7:12b.1CO.007.012 Ñi ci des nag, lii laa leen di wax --Boroom bi waxu ko woon — su nit ku gëm Kirist amee jabar ju gëmul, te mu nangoo séy ak moom, waru koo fase.

7:13b.1CO.007.013 Naka noonu it su jigéen ju gëm Kirist amee jëkkër ju gëmul, te mu nangoo nekk ak moom, warul a tas.

7:14b.1CO.007.014 Li tax ma wax ko moo di, jëkkër ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jabaram. Te it jigéen ji gëmul, Yàlla sellal na ko, ndax li mu ànd ak jëkkëram ji gëm; lu ko moy, seeni doom dinañu am sobe, te fekk dañoo sell.

7:15b.1CO.007.015 Waaye nag, su fekkee ki gëmul bëgg na dem, na dem. Ci wàll googu nag, ki gëm Kirist, muy jëkkër ji walla jabar ji, amul benn tënk, ndaxte Yàlla moo leen woo ngir ngeen dund ci jàmm.

7:16b.1CO.007.016 Loo ci xam, yaw jigéen ji, ndax dinga gëmloo sa jëkkër Musalkat bi walla déet? Loo ci xam yaw jëkkër ji it, ndax dinga gëmloo sa jabar Musalkat bi walla déet?

7:17b.1CO.007.017 Ku nekk nag na dund, ni ko ko Boroom bi jagleele, mu mengoo ak ni mu meloon, bi ko Yàlla wooyee. Moom laay tëral ci mboolooy ñi gëm yépp.

7:18b.1CO.007.018 Ki xaraf, bi ko Yàlla wooyee, warul a jéem a far màndargam xaraf bi. Ki xaraful, bi ko Yàlla wooyee, aajowul mu xaraf.

7:19b.1CO.007.019 Xaraf ak ñàkka xaraf lépp a yem; li am solo moo di topp ndigali Yàlla.

7:20b.1CO.007.020 Na kenn ku nekk jàpp ci li mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee.

7:21b.1CO.007.021 Ndax jaam nga woon, bi la Yàlla wooyee? Na ci sa xel dal. Waaye soo amee bunt, ba yiwiku, nanga ci jaar.

7:22b.1CO.007.022 Ku nekkoon jaam, bi la Boroom bi wooyee, Boroom bi goreel na la. Ba tey it ku nekkoon gor, bi ñu la wooyee, jaamu Kirist nga.

7:23b.1CO.007.023 Gannaaw Yàlla jot na leen ak njëg gu réy, buleen doon jaamub nit.

7:24b.1CO.007.024 Bokk yi, fàww ku nekk wéy ca kanam Yàlla ci fànn ga mu nekkoon, bi ko Yàlla wooyee.

7:25b.1CO.007.025 Ci li jëm ci janq yi, awma ndigalu Boroom bi, waaye maa ngi joxe sama xalaat, ni ku ñu wóolu ndax li ma jot yërmandey Boroom bi.

7:26b.1CO.007.026 Bu nu seetee tiis wii fi teew nag, defe naa ne li baax ci nit, moo di mu sax ci li mu nekk.

7:27b.1CO.007.027 Ndax takk nga jabar? Bul wut a tàggoo ak moom. Ndax takkuloo jabar? Bul wut jabar.

7:28b.1CO.007.028 Waaye nag boo séyee, defoo bàkkaar, te bu janq séyee, deful bàkkaar. Waaye ñi séy dinañu am naqar ci àddina, te naqar woowu dama leen koo bëggoon fanqal, yéen ñi séyagul.

7:29b.1CO.007.029 Lii laa bëgg a wax, bokk yi: diir bu gàtt rekk a fi des. Lu weesu tey, na góor ñi am jabar di def, ni bu ñu ko amul woon;

7:30b.1CO.007.030 ñiy jooy, mel ni ñu jooyul; ñiy bég, mel ni ñu bégul; ñiy jënd, ni ñu moomul li ñu jënd;

7:31b.1CO.007.031 ñiy jariñoo àddina, bañ cee xér. Ndaxte àddina sii, ci ni mu mel, dootul yàggati.

7:32b.1CO.007.032 Bëggoon naa, ngeen bañ a am benn xalaat. Góor gu takkul jabar dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi, di wut a neex Boroom bi.

7:33b.1CO.007.033 Waaye ku takk jabar, fàww mu bàyyi xel ci mbiri àddina si, ak nu mu man a neexe jabaram,

7:34b.1CO.007.034 te noonu dafay daldi bare soxla. Te jigéen ju séyul, walla janq, dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi — bëgg koo jox yaramam ak xelam. Waaye jigéen ji séy dafay bàyyi xel ci mbiri àddina, ak nu mu man a neexe jëkkëram.

7:35b.1CO.007.035 Seen njariñ a tax ma wax lii, du ngir teg leen yen bu ngeen àttanul, waaye ngeen man a jàppandil Boroom bi ci njaamu gu rafet gu àndul ak genn njaaxle.

7:36b.1CO.007.036 Nanu jàll nag ci mbiri kiy takk ngoro te amul pasteefu takk ndaw si. Su fekkee ne waxambaane wi xalaat na ne, jëfewul nu jekk ak janq bi, fekk muy wees ag ndawam, te mu xalaat ne dafa koo war a takk, kon na ko takk, ni mu ko bëgge; deful bàkkaar.

7:37b.1CO.007.037 Waaye nag su dogoo dëgg ci bañ a takk, fekk sagoom rekk a tax te kenn tegu ko ko, kon ba tey def na lu baax.

7:38b.1CO.007.038 Noonu ku takk as ndawam def na lu baax, rawatina nag ku takkul.

7:39b.1CO.007.039 Jigéen ji séy dina ànd ak jëkkëram giiru dundam. Waaye su jëkkër ji faatoo, man na séy ak ku ko neex, su fekkee ne góor gu gëm la.

7:40b.1CO.007.040 Moona nag dina gën a bég, bu toogee noonu rekk. Loolu mooy sama xalaat, te defe naa ne, man it am naa Xelum Yàlla.

8

8:1b.1CO.008.001 Léegi nag, ci li jëm ci yàpp wi ñu jébbal xërëm yi: nun ñépp am nanu xam-xam, loolu dëgg la. Xam-xam day tax ba nit yég boppam, waaye mbëggeel day yékkati ngëm.

8:2b.1CO.008.002 Ku xalaat ne xam nga dara, sa xam-xam bënnagul.

8:3b.1CO.008.003 Waaye ku bëgg Yàlla, Yàlla xam la.

8:4b.1CO.008.004 Kon nag ci li jëm ci lekk yàpp wu ñu jébbal xërëm yi, xam nanu ne, xërëm du dara ci àddina te xam nanu itam ne, Yàlla kenn rekk la.

8:5b.1CO.008.005 Su fekkee ne am na sax yu ñuy teg Yàlla, muy ci asamaan mbaa ci suuf --ndaxte am na yu bare yu ñu faral di bokkaaleel Yàlla ak Boroom bi —

8:6b.1CO.008.006 ba tey ci nun, jenn Yàlla rekk a am, muy Baay bi; lépp a ngi jóge ci moom te moom lanu nekkal. Te it benn Boroom rekk a am, muy Yeesu Kirist; lépp a ngi jaare ci moom, te nun it nu ngi dund jaare ci moom.

8:7b.1CO.008.007 Waaye ñépp xamuñu loolu. Am na ñu tàmmoon xërëm yi, te léegi, bu ñu lekkatee yàppu sarax yi, dañuy xalaat ne, xërëm lañu ko jagleel. Seen xel dafa leen di yedd, ndaxte ci seen ñàkka xam dañuy foog ne, taq nañu sobe ndax ñam woowu.

8:8b.1CO.008.008 Waaye ñam mënul a tax nu neex Yàlla. Su nu ci lekkee, du yokk dara ci nun. Su nu ci lekkul, du nu wàññi dara.

8:9b.1CO.008.009 Waaye moytuleen, ba sañ-sañ bi ngeen am, bañ a yóbbe bàkkaar ñi seen ngëm néew.

8:10b.1CO.008.010 Su amee ku ngëmam néew, mu gis la, yaw mi bare xam-xam, nga toog di lekk ca màggalukaayu xërëm ya, ndax du ko xiir mu lekk yàppu sarax?

8:11b.1CO.008.011 Noonu sa xam-xam dina lor kooku ngëmam néew, fekk sa mbokk moomu, Kirist dee na ngir moom!

8:12b.1CO.008.012 Su ngeen bàkkaaree, ba tooñ bokk yi néew ngëm, di nëxal seen xel, bàkkaar ngeen ba tooñ Kirist.

8:13b.1CO.008.013 Kon bu sama mbokk sóoboo ci bàkkaar ndax ñam wi ma lekk, dootuma lekk mukk yàpp, ngir bañ a sóob ci bàkkaar sama mbokk mi.

9

9:1b.1CO.009.001 Ndax awma ndogal ci li may def? Ndax duma ndawul Kirist? Ndax gisuma Yeesu sunu Boroom? Xanaa du yéena soqikoo ci liggéey, bi ma Boroom bi sant?

9:2b.1CO.009.002 Su ma ñenn ñi tegul ndaw, moom laa ci yéen, ndaxte yéenay firnde jiy wone ne, ndawul Boroom bi dëgg laa.

9:3b.1CO.009.003 Nii laay tontoo ñi may àtte:

9:4b.1CO.009.004 Xanaa sañunoo lekk ak a naan?

9:5b.1CO.009.005 Xanaa sañunoo indaale jabar ju gëm Kirist, ni yeneen ndawul Kirist ak doomi ndeyu Boroom bi ak Sefas sax?

9:6b.1CO.009.006 Walla boog man ak Barnabas rekk noo war a daan sunu doole?

9:7b.1CO.009.007 Kan moo mas a solu soldaar ci pexey boppam? Kan mooy bey tool te du ci jariñu? Walla kan mooy sàmm jur te du naan ca soow ma?

9:8b.1CO.009.008 Lii may wax, du ci yëfi doom Aadama rekk laa ko jukkee; xanaa du yoon wi it moo ko santaane?

9:9b.1CO.009.009 Ndaxte bind nañu ci yoonu Musaa ne: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk ci bojjukaay.» Ndax mooy tekki nag ne, Yàlla dafa bàyyi xel nag yi?

9:10b.1CO.009.010 Walla boog xanaa nun noo moom wax jooju? Waaw, noo tax ñu bind loolu. Noonu kuy bey war na am yaakaar, te kuy bojj di yaakaar a jot wàllam.

9:11b.1CO.009.011 Nu ji ci yéen yëfi Xelum Yàlla, ba noppi góobe ci yéen yëfi àddina, ndax loolu dafa ëpp li nu war a séentu?

9:12b.1CO.009.012 Ndegam ñeneen a am sañ-sañ boobu ci yéen, nun kon waxi-noppi. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Danuy far muñ lépp, ngir bañ a indi ndog ci yoonu xebaar bu baax bu Kirist bi.

9:13b.1CO.009.013 Xanaa xamuleen ne, ñiy liggéeyal yëf yu sell yi, dañuy lekk ñam, wi ci kër Yàlla gi, te ñiy liggéey ci saraxalukaay bi, dañuy jot seen wàll ci sarax yi?

9:14b.1CO.009.014 Naka noonu it Boroom bi digle na ne, ñiy yégle xebaar bu baax bi, nanu ci dund.

9:15b.1CO.009.015 Waaye man jariñoowuma benn ci sañ-sañ yooyu, te binduma yëf yooyu, ngir ngeen di ma defal yu ni mel. Dee sax moo ma ko gënal — kenn du jële ci man mbir moomu may kañoo!

9:16b.1CO.009.016 Su may yégle xebaar bu baax bi, mënuma cee kañu. Sas la, wu ñu ma sas. Dinaa torox, su ma yéglewul xebaar bu baax bi!

9:17b.1CO.009.017 Su doon ci sama coobare laa yégle xebaar bu baax bi, man naa ci séentu yool. Waaye defuma ko ci sama coobare, ndaxte sas la, wu ñu ma sas.

9:18b.1CO.009.018 Kon nag lan mooy sama yool? Xanaa di yégle xebaar bu baax bi ci dara, te bañ a jariñoo sañ-sañ boobu ma ci yelloo.

9:19b.1CO.009.019 Gor laa te kenn moomu ma; teewul def naa sama bopp jaamu ñépp, ngir man a gindi nit ñu bare ci Kirist.

9:20b.1CO.009.020 Ci biir Yawut yi, sol naa melow Yawut yi, ngir gindi leen. Man ci sama bopp yoonu Musaa jiitalu ma, terewul bi ma nekkee ci biir ñiy sàmm yoonu Musaa, sàmm naa yoon wa, ngir gindi leen.

9:21b.1CO.009.021 Ci biir ñi nekkul ci yoonu Musaa, faalewuma woon yoon wi, ngir gindi leen; waxuma ne, ànduma ak yoonu Yàlla, waaye topp naa yoon ci sama bokk ak Kirist.

9:22b.1CO.009.022 Ci biir ñi néew ngëm, meloon naa ni ku néew ngëm, ngir gindi leen. Doon naa lépp ci ñépp, ngir def lépp lu ma man, ba ñenn mucc ci.

9:23b.1CO.009.023 Damaa def loolu lépp ndax xebaar bu baax bi, ngir man it ma am wàll ci barkeem.

9:24b.1CO.009.024 Xanaa xamuleen ne, ñépp ñooy daw cib rawante, waaye kenn rekk ay jël ndam li? Dawleen nag ngir jël ko.

9:25b.1CO.009.025 Ñiy joŋante ci po muy waral tàggat yaram, dañuy xañ seen bopp lu bare. Dañu koy def, ngir am kaalag ndam gu dul yàgg; waaye nun danu koy def, ngir am kaalag ndam gu sax ba fàww.

9:26b.1CO.009.026 Man nag noonu laay dawe, te duma dawantu. Noonu laay bëree, waaye duma def ni nit kuy dóor ci jaww ji.

9:27b.1CO.009.027 Waaye damay noot sama yaram, ba moom ko, ngir ragal a yégal ñi ci des xebaar bu baax bi, ba noppi Yàlla xañ ma ndam li.

10

10:1b.1CO.010.001 Bokk yi, bëgguma ngeen umple li daloon sunu maam ya. Ñoom ñépp niir wa tiimoon na leen, te ñoom ñépp jàll nañu géej.

10:2b.1CO.010.002 Sóobu nañu ca ndoxu géej ga ak ca niir wa, ba bokk noonu ci Musaa.

10:3b.1CO.010.003 Ñoom ñépp bokk nañoo lekk ñam, wa Yàlla joxe,

10:4b.1CO.010.004 naan naan ga mu joxe, ndaxte ñu ngi doon naan ca xeer, wa leen doon gunge, te xeer woowa Kirist la woon.

10:5b.1CO.010.005 Teewul ñi ëpp ci ñoom neexuñu woon Yàlla, ba mu fàddoon leen ca màndiŋ ma.

10:6b.1CO.010.006 Mbir yooyu ay misaal lañu, yu nuy artu, ngir benn bëgg-bëgg bu bon bañ noo jiital, na mu leen jiitale woon.

10:7b.1CO.010.007 Buleen jaamu ay xërëm, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon. Ndaxte Mbind mi nee na: «Mbooloo mi dafa toog, di lekk ak di naan, ba noppi ñu jóg di mbumbaay.»

10:8b.1CO.010.008 Bunu njaaloo, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax ñaar-fukki junni ak ñett ci ñoom dee ci benn bés.

10:9b.1CO.010.009 Bunu diiŋat Kirist, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe, ba ay jaan màtt leen, ñu dee.

10:10b.1CO.010.010 Buleen xultu, ni ko ñenn ñi ci ñoom defe woon, ba tax malaakam Yàqkat mi rey leen.

10:11b.1CO.010.011 Mbir yooyu leen daloon misaal la ci nun, te bind nañu ko ngir artu nu, nun ñiy dund ci jamono jii lépp mat.

10:12b.1CO.010.012 Kon nag kiy naw sa doole, ba yaakaar ne taxaw nga, moytul a daanu ci bàkkaar!

10:13b.1CO.010.013 Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit ñépp. Te sax Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu, dina leen ubbil bunt bu ngeen man a récce, ba ngeen man koo dékku.

10:14b.1CO.010.014 Looloo tax, sama soppe yi, nangeen daw xërëm yi.

10:15b.1CO.010.015 Maa ngi wax ak yéen ñi am xel. Kon seetleen li ma leen wax.

10:16b.1CO.010.016 Kaas bu yiw, bi tax nuy gërëm Yàlla, ndax du wone sunu booloo ak deretu Kirist? Mburu mi nuy damm, xanaa du dafay wone sunu booloo ak yaramu Kirist?

10:17b.1CO.010.017 Ndegam benn mburu rekk a am, kon nun ñépp lu nu baree-bare, menn mbooloo lanu, ndaxte bokk nanu menn mburu mi.

10:18b.1CO.010.018 Seetleen ci bànni Israyil. Ñiy lekk sarax si ñu rendi, ndax booloowuñu ak Yàlla ji ñu jagleel saraxalukaay ba? Aaŋkay!

10:19b.1CO.010.019 Li may wax, lu muy tekki? Ndax yàpp wi ñu jagleel xërëm yi dafay dara? walla xërëm yi dañuy dara?

10:20b.1CO.010.020 Déedéet! Waaye sarax yi xërëmkat yi di rendi, ay rab lañu ko jagleel; jagleeluñu ko Yàlla. Te man bëgguma, ngeen booloo ak rab yi.

10:21b.1CO.010.021 Mënuleen a naan ci kaasu Boroom bi, naan ci kaasu rab yi. Mënuleen a sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi.

10:22b.1CO.010.022 Walla boog ndax danuy jéem a gillil meru Boroom bi? Xanaa noo ko ëpp doole?

10:23b.1CO.010.023 Dafa am ñu naan: «Lépp lanu sañ.» Waaw, waaye du lépp a baax ci nun. «Lépp lanu sañ,» waaye it lépp du yékkati ngëm.

10:24b.1CO.010.024 Bu kenn seet njariñam rekk, waaye nay seet njariñul moroomam.

10:25b.1CO.010.025 Man ngeen a lekk lépp lu ñuy jaay ca ja ba, bañ cee boole ay laaj ngir dalal seen xel.

10:26b.1CO.010.026 Ndaxte Mbind mi nee na: «Àddina ak li ci biiram lépp, Boroom bi moo ko moom.»

10:27b.1CO.010.027 Ku xamul Yàlla nag, bu leen wooyee aw ñam këram, te ngeen nangoo dem, lekkleen lépp lu ñu leen dëj, bañ a laajte dara ngir dalal seen xel.

10:28b.1CO.010.028 Waaye bu leen kenn nee: «Lii sarax la, bu ñu jagleel xërëm yi,» suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal.

10:29b.1CO.010.029 Waxuma sa xel yaw, waaye xelu keneen laay wax. Waaye nga ne: «Li ma sañ a def, lu tax nit ku xelam dalul di am dara lu mu ciy wax?

10:30b.1CO.010.030 Su ma lekkee dara di ci sant Yàlla, lu tax ñu may wax lu ñaaw, fekk sant naa ci Yàlla.»

10:31b.1CO.010.031 Kon su ngeen di lekk walla ngeen di naan, walla lu ngeen man a def, defleen lépp ngir màggal Yàlla.

10:32b.1CO.010.032 Buleen def dara lu man a fanq ngëmu Yawut yi walla ñi dul Yawut walla mbooloom Yàlla.

10:33b.1CO.010.033 Noonu laay def man ci sama bopp: damay wut a neex ñépp ci lépp. Wutuma lu may jariñ, waaye luy jariñ ñu bare laay wut, ngir ñu mucc.

11

11:1b.1CO.011.001 Royleen ma nag, ni may roye Kirist.

11:2b.1CO.011.002 Maa ngi leen di sant ci li ngeen may fàttaliku ci lépp, ak ci li ngeen di topp dénkaane, yi ma leen dénk.

11:3b.1CO.011.003 Waaye nag bëgg naa ngeen xam lii: Kirist mooy kilifag bépp góor, góor di kilifag jigéen, te Yàlla di kilifag Kirist.

11:4b.1CO.011.004 Kon nag góor guy ñaan Yàlla, walla muy wax ci kàddug Yàlla, fekk mu teg dara ci boppam, day suufeel Kirist, kilifaam.

11:5b.1CO.011.005 Waaye bu jigéen musóoruwul, buy ñaan walla buy wax ci kàddug Yàlla, kooku day suufeel jëkkëram jiy kilifaam, ndaxte day mel ni jigéen ju ñu wat.

11:6b.1CO.011.006 Jigéen ju dul musóoru, bu yaboo, mu watu. Waaye su fekkee ne jigéen dafay am kersa, su wàññee kawaram walla mu watu, fàww kon mu musóoru.

11:7b.1CO.011.007 Góor nag moom warul a teg dara ci boppam, ndaxte mooy melokaanu Yàlla te dafay wone ndamu Yàlla. Jigéen moom dafay wone ndamu góor.

11:8b.1CO.011.008 Ndaxte jëlewuñu góor ci jigéen, waaye jigéen lañu jële ci góor.

11:9b.1CO.011.009 Te sàkkuñu góor ngir jigéen, waaye jigéen lañu sàkk ngir góor.

11:10b.1CO.011.010 Looloo tax jigéen war a teg ci kaw boppam luy màndargaal kilifteef ga, ndax malaaka yi.

11:11b.1CO.011.011 Teewul nag ci sunu booloo ak Boroom bi, jigéen a ngi wéeru ci góor, te góor a ngi wéeru ci jigéen.

11:12b.1CO.011.012 Ni ñu sàkke jigéen ci góor, noonu la góor juddoo ci jigéen, te lépp a ngi jóge ca Yàlla.

11:13b.1CO.011.013 Seetleen mbir mii: ndax jekk na jigéen bañ a musóoru, buy ñaan Yàlla?

11:14b.1CO.011.014 Xanaa du àddina ci boppam dafa leen di won ne, gàcce la ci góor, ngir muy yar kawar gu bare?

11:15b.1CO.011.015 Waaye loolu nag ab taar la ci jigéen. Dañoo jagleel jigéen kawar gu gudd, muy muuraay ci moom.

11:16b.1CO.011.016 Waaye su kenn bëggee werante ci mbir moomu, na xam lii: amunu beneen aada ci njàng mi, du nun walla mboolooy Yàlla.

11:17b.1CO.011.017 Bi may tollu ci ndigal yi, mënuma leen a sant, ndaxte seeni ndaje loraange lañuy jur, waaye du njariñ.

11:18b.1CO.011.018 Ci bu jëkk dégg naa lii: bu ngeen di daje, am na ci yéen ñuy féewaloo, te xaw naa koo gëm.

11:19b.1CO.011.019 Fàww mu am ay féewaloo ci seen biir, ngir ñu man a xàmmi ñi neex Yàlla ci yéen.

11:20b.1CO.011.020 Bu ngeen dajee, mënuleen a wax ne reeru Boroom bi ngeen di lekk.

11:21b.1CO.011.021 Ndaxte bu ngeen dee lekk, ku nekk dafay gaawantu di lekk reeram, ba tax ñenn ñaa ngi xiif, fekk ñeneen di màndi.

11:22b.1CO.011.022 Xanaa amuleen kër yu ngeen di lekke ak di naane? Walla ndax dangeen a xeeb mbooloom Yàlla? Walla ngeen bëgg a rusloo ñi amul dara? Lu ma leen ci war a wax nag? Ma gërëm leen ci loolu? Mukk! Gërëmuma leen.

11:23b.1CO.011.023 Li ma jële ci Boroom bi, moom laa leen jottali: Boroom bi Yeesu, ci guddi gi ñu ko woree, dafa jël mburu,

11:24b.1CO.011.024 sant Yàlla, damm ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»

11:25b.1CO.011.025 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees, gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret. Defleen lii ngir fàttaliku ma.»

11:26b.1CO.011.026 Ndaxte saa su ngeen di lekk mburu mii, walla ngeen di naan ci kaas bii, yéena ngi yégle deewu Boroom bi, ba kera muy ñëw.

11:27b.1CO.011.027 Kon nag képp ku jekkadi ni mu lekke ci mburu mi te naane ni ci kaasu Boroom bi, tooñ nga yaramu Boroom bi ak deretam.

11:28b.1CO.011.028 Na ku nekk seetlu boppam nag, sog a lekk ci mburu mi te naan ci kaas bi.

11:29b.1CO.011.029 Ku lekk mburu mi, naan ci kaas bi, fekk faalewuloo solos yaramu Kirist wi, sa lekk ak sa naan dina xëcc àtteb Yàlla ci sa kaw.

11:30b.1CO.011.030 Looloo tax ñu bare ci yéen wopp te ñàkk doole, ba ñenn ñi faatu.

11:31b.1CO.011.031 Su nu doon seetlu sunu bopp ni mu ware, kon àtte du nu dal.

11:32b.1CO.011.032 Waaye bu nu Boroom bi dee àtte, da nuy yar ngir bañ noo boole ci mbugalu àddina.

11:33b.1CO.011.033 Noonu nag bokk yi, bu ngeen dajee, di lekk reeru Boroom bi, nangeen xaarante.

11:34b.1CO.011.034 Ku xiif, na lekke këram, ngir bañ a indi ci yéen àtteb Yàlla ndax seen ndaje yi. Yeneen fànn yi ci des nag, bu ma ñëwee ci yéen, dinaa ko seet.

12

12:1b.1CO.012.001 Léegi nag bokk yi, ci li jëm ci mayi Xelum Yàlla, bëgguma ngeen umple ci dara.

12:2b.1CO.012.002 Xam ngeen ne, bi ngeen xamagul woon Yàlla, xërëm, yi mënul a wax, ñoo leen jiitaloon, di leen wommat.

12:3b.1CO.012.003 Moo tax ma leen di xamal lii: ku Xelum Yàlla solu du wax ne: «Yeesu dafa araam.» Te it kenn mënul a wax ne: «Yeesu mooy Boroom bi,» su ko ko Xelum Yàlla waxloowul.

12:4b.1CO.012.004 Am na fànni may yu bare yu jóge ci Xelum Yàlla, waaye menn Xel moomu moo koy séddale.

12:5b.1CO.012.005 Am na ay sas yu bare, waaye benn Boroom bi la.

12:6b.1CO.012.006 Am na ay fànn yu bare yu Yàllay feeñale dooleem, waaye jenn Yàlla ji mooy jëfe doole yooyu yépp ci ñépp.

12:7b.1CO.012.007 Noonu Yàlla jox na ku nekk fànn gu muy feeñale Xelam mu Sell mi ngir njariñul ñépp.

12:8b.1CO.012.008 Am na ku Yàlla sédde, jaarale ko ci Xelam, mayu wax ak xel mu leer, keneen am mayu xam-xam, te mu bawoo ci menn Xel mi.

12:9b.1CO.012.009 Keneen it menn Xel mi jox ko ngëm, keneen di wéral ay jàngoro ci kàttanu Xel moomu,

12:10b.1CO.012.010 keneen di def ay kéemaan, am kuy wax ci kàddug Yàlla, am keneen kuy ràññee li jóge ci Xelum Yàlla ak li jóge ci yeneen xel yi, keneen it di wax ay xeeti làkk, ak kuy firi làkk yooyu.

12:11b.1CO.012.011 Loolu lépp, menn Xel moomu moo koy def, ku nekk mu sédd la ci, ni mu ko soobe.

12:12b.1CO.012.012 Noona la ci yaramu nit. Yaram wenn la, teewul am na cér yu bare. Waaye céri yaram yépp, ak li ñuy baree-bare, ñoo bokk, doon wenn yaram. Te noonu la Kirist mel.

12:13b.1CO.012.013 Yàlla sóob na nu ci menn Xelam mi, ngir nu doon wenn yaram: nuy Yawut walla nu dul Yawut, nuy jaam mbaa gor, nun ñépp Yàlla may na nu, nu naan ci menn Xel mi.

12:14b.1CO.012.014 Yaram du benn cér, waaye cér yu bare la.

12:15b.1CO.012.015 Kon bu tànk nee: «Man duma loxo, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.

12:16b.1CO.012.016 Te bu nopp nee: «Duma bët, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.

12:17b.1CO.012.017 Bu yaram wépp doon bët, kon nan lay dégge? Walla bu yaram wépp doon nopp, kon nan lay xeeñtoo?

12:18b.1CO.012.018 Waaye Yàlla dafa riime céri yaram wi, def bu ci nekk fa mu ko soobe.

12:19b.1CO.012.019 Bu lépp doon benn cér, kon fu yaram di nekk?

12:20b.1CO.012.020 Cér yi daal, bare nañu waaye wenn yaram rekk a am.

12:21b.1CO.012.021 Bët nag mënul ne loxo: «Soxlawuma la!» Te bopp it mënul ne tànk yi: «Soxlawuma leen!»

12:22b.1CO.012.022 Loolu sax mënul a am, ndaxte céri yaram, yi gën a néew doole, ñoo gën a am jariñ.

12:23b.1CO.012.023 Te cér yi gën a ñàkk maana, ñoom lanuy gën a topptoo. Cér yi ci rafetul a tudd, ñoom lanuy gën a suturaal,

12:24b.1CO.012.024 fekk yi gën a rafet, soxlawul nu leen di suturaale noonu. Waaye Yàlla dafa boole sunu céri yaram yi, ngir gën a teral cér yi ko soxla.

12:25b.1CO.012.025 Noonu yaram du séddaloo, waaye cér bu ci nekk dina dimbali yi ci des.

12:26b.1CO.012.026 Bu sa benn céru yaram dee metti, yeneen yi ci des yépp dañuy bokk, yég metit wi. Te bu dee dangaa fonk sa benn céru yaram it, ndax du sa yaram wépp a ciy bànneexu?

12:27b.1CO.012.027 Léegi benn yaram ngeen, muy yaramu Kirist, te kenn ku nekk ci yéen cér nga ci.

12:28b.1CO.012.028 Te Yàlla teg na ci mbooloom ñi gëm, ku nekk ak sa may: ci bu jëkk ay ndawi Kirist, teg ca ñiy wax ci kàddug Yàlla, teg ca ñiy jàngale, ñiy def ay kéemaan, ñi am mayu wéral ay jàngoro, ñiy dimbalee, ñiy jiite, ñiy wax ay xeeti làkk.

12:29b.1CO.012.029 Ndax ñépp ay ndawi Kirist lañu? Ndax ñépp dañuy wax ci kàddug Yàlla? Ndax ñépp ay jàngale? Ndax ñépp ay def kéemaan?

12:30b.1CO.012.030 Ndax ñépp a am mayu wéral ay jàngoro? Ndax ñépp ay wax ay làkk? Ndax ñépp a leen di firi?

12:31b.1CO.012.031 Waaye fonkleen may yi gën. Léegi nag ma won leen yoon wu gën lépp.

13

13:1b.1CO.013.001 Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mbëggeel, duma dara lu dul ndënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi.

13:2b.1CO.013.002 Su ma yéglee wax ju tukkee ci Yàlla, ma xam lépp luy kumpa, ma yor xam-xam bépp, te gëm Yàlla ba man a randal ay tund, fekk boolewuma ci mbëggeel, duma dara.

13:3b.1CO.013.003 Te it su ma doon saraxe li ma am lépp, di bàyyi ñu lakk sama yaram, ba rey ma, su ma ci boolewul mbëggeel, du ma jariñ dara.

13:4b.1CO.013.004 Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du kiñaan, du kañu, du tiitaru,

13:5b.1CO.013.005 du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort.

13:6b.1CO.013.006 Du bég ci lu awul yoon, waaye dina bég ci lépp luy jollil dëgg.

13:7b.1CO.013.007 Mbëggeel day baale lépp, am gëm ci lépp, yaakaar lépp, muñ lépp.

13:8b.1CO.013.008 Mbëggeel amul àpp. Ñiy wax ci kàddug Yàlla dinañu noppi, ñiy wax ay làkk dinañu ko bàyyi, ñiy xamle xam-xamu Yàlla wàcc.

13:9b.1CO.013.009 Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xebaar bi nu Yàlla dénk des na.

13:10b.1CO.013.010 Waaye li mat, bu dikkee, li matul jóge fi.

13:11b.1CO.013.011 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di dégge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, bàyyi naa lu bokkoon cig ndaw.

13:12b.1CO.013.012 Tey jii gis bu lëndëm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu lëndëm, bu ëllëgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na, bu ëllëgee dinaa xam ba mat sëkk, ni ma Yàlla xame.

13:13b.1CO.013.013 Léegi nag ñett yii ñooy sax: ngëm, yaakaar, mbëggeel; te mbëggeel moo ci raw.

14

14:1b.1CO.014.001 Xintewooleen mbëggeel te fonk mayi Xelum Yàlla, rawatina mayu wax ci kàddug Yàlla,

14:2b.1CO.014.002 ndaxte kiy wax aw làkk, waxul ak nit ñi, waaye Yàlla lay waxal, ndaxte kenn déggul li muy wax. Dafay wax ay mbóot ci xelam.

14:3b.1CO.014.003 Waaye kiy jottali kàddug Yàlla, nit ñi lay waxal ngir yékkati seen ngëm, di leen dénk ak a dëfël.

14:4b.1CO.014.004 Kiy wax aw làkk dafay yokk boppam, waaye kiy wax ci kàddug Yàlla, dafay yokk ngëmu mbooloo mi.

14:5b.1CO.014.005 Léegi nag bëgg naa yéen ñépp, ngeen di wax ay làkk, waaye li ma gënal mooy ngeen di wax ci kàddug Yàlla. Kiy wax ci kàddug Yàlla moo gën kiy wax ay làkk, su firiwul li muy wax, ngir ngëmu mbooloo mi yokku.

14:6b.1CO.014.006 Kon nag bokk yi, su ma ñëwee ci yéen, di wax ay làkk, lu ma leen di jariñ? Dara, su ma leen indilul dëgg gu Yàlla feeñal, walla xam-xam walla kàddu gu tukkee ca Yàlla, walla am njàngale.

14:7b.1CO.014.007 Noonu la mel itam ci yëf yi dundul tey riir, ni toxoro walla xalam. Su li ci jibe leerul, naka la nit man a ràññee li mbiibi toxoro walla buumi xalam di wax?

14:8b.1CO.014.008 Rax-ca-dolli su liit gi jibul bu leer, kuy man a waajal xare ba?

14:9b.1CO.014.009 Noonu itam bu ngeen génnewul ay wax yu leer ci seen gémmiñ, nan lañuy man a xame li ngeen di wax? Dingeen wax cig neen!

14:10b.1CO.014.010 Xawma ñaata xeeti làkk a am ci àddina, te wu ci nekk am na lu muy tekki.

14:11b.1CO.014.011 Su ma xamul nag làkk wi ñu may làkk, doxandéem laay doon ci ki koy wax, te ki koy wax it doxandéem la ci man.

14:12b.1CO.014.012 Yéen itam, gannaaw dangeen a fonk mayi Xelum Yàlla, jéemleen a ëpple ci liy yokk ngëmu mbooloo mi.

14:13b.1CO.014.013 Looloo tax kiy wax aw làkk, na ñaan ngir mu man a firi li looluy tekki.

14:14b.1CO.014.014 Su may ñaan Yàlla ci aw làkk, sama xol day ñaan, waaye sama xel amalul kenn njariñ.

14:15b.1CO.014.015 Kon nag lu muy indi? Bu may ñaan, dinaa ànd ak sama xol, àndaale ak sama xel. Bu may woy, dinaa ànd ak sama xol, àndaale ak sama xel.

14:16b.1CO.014.016 Walla, boo dee gërëm Yàlla, ànd ci ak sa xol rekk, kon ku musul a jàng mbir yooyu, nan la man a waxe: «Amiin,» ci sa cant Yàlla googu? Ndaxte xamul li ngay wax.

14:17b.1CO.014.017 Dëgg la, dangay sant Yàlla bu baax, waaye ki ci des, ngëmam yokkuwul.

14:18b.1CO.014.018 Maa ngi sant Yàlla ci li may wax ay làkk, ba raw leen yéen ñépp.

14:19b.1CO.014.019 Waaye ci ndajem mbooloom ñi gëm, wax juróomi baat yu am njariñ, ngir jàngal ñi ci des, moo ma gënal wax fukki junniy baat ciw làkk.

14:20b.1CO.014.020 Bokk yi, buleen melati ni ay xale, ci ni ngeen di xalaate. Ci lu jëm ci lu bon, mel-leen ni ay xale, waaye ci seeni xalaat, mel-leen ni ay mag.

14:21b.1CO.014.021 Bind nañu ci téereb yoon wi:«Dinaa wax ak mbooloo mii,jaare ko ci ay nit, ñuy wax yeneen làkk,ak ay gémmiñi doxandéem,waaye ba tey duñu ma déglu.» Moom la Boroom bi wax.

14:22b.1CO.014.022 Ci noonu wax ay làkk, firnde la ci ñi gëmul, te du firnde ci ñi gëm. Te it wax ci kàddug Yàlla, du firnde ci ñi gëmul, waaye firnde la ci ñi gëm.

14:23b.1CO.014.023 Kon nag su fekkee ku jàngul mbiri Kirist walla ku gëmul dugg ca mbooloo ma, fekk ñépp di wax ay làkk, ndax du wax ne, dangeen a dof?

14:24b.1CO.014.024 Waaye bu ñépp dee wax ci kàddug Yàlla, te ku gëmul dugg fa, walla ku jàngul mbiri Kirist, wax yi ñépp wax dafay wone bàkkaaram te àtte ko,

14:25b.1CO.014.025 ba kumpay xolam feeñ. Bu ko defee dina dëpp jëwam ci suuf, di màggal Yàlla te naan: «Dëgg-dëgg Yàllaa ngi ci seen biir.»

14:26b.1CO.014.026 Kon nag bokk yi, lu muy indi? Bu ngeen dajee, kii am aw taalif, kii am njàngale, kii dëgg gu Yàlla feeñal, kii di wax aw làkk, kee di ko firi. Na loolu lépp aw ci yoonu yokk ngëmu mbooloo mi.

14:27b.1CO.014.027 Su amee kuy wax aw làkk, na ñaar wax walla gën gaa bare ñett. Nañu ko toppante, te kenn di firi.

14:28b.1CO.014.028 Su amul kuy firi, kooku di wax aw làkk, na noppi ci ndajem mbooloo mi. Na waxanteek Yàlla ci xolam.

14:29b.1CO.014.029 Ci ñiy wax ci kàddug Yàlla nag, na ñaar walla ñett wax, te ñi ci des ràññee li ñuy wax.

14:30b.1CO.014.030 Su amee ku toog te Yàlla feeñal ko dëgg, na ki doon wax noppi.

14:31b.1CO.014.031 Yéen ñépp man ngeen a kenn-kennoo wax ci kàddug Yàlla, ngir ñépp jàng te dégg li ñu leen di dénk.

14:32b.1CO.014.032 Ñiy jottali kàddug Yàlla dañoo moom seen xel,

14:33b.1CO.014.033 ndaxte Yàlla du Yàllay lëj-lëj waaye Yàllay jàmm la. Ci mboolooy gaayi Yàlla yépp,

14:34b.1CO.014.034 na jigéen ñi noppi ci ndaje mi, ndaxte sañuñu faa wax. Nañu doon jigéen ñu nangu, ni ko yoon wi tërale.

14:35b.1CO.014.035 Te su ñu bëggee laaj dara, nañu ko laaj seen jëkkër ca kër ga, ndaxte jigéen di wax ci ndajem mbooloom ñi gëm, gàcce la.

14:36b.1CO.014.036 Ndax ci yéen la kàddug Yàlla sosoo? Walla ndax ci yéen rekk la agsi?

14:37b.1CO.014.037 Su kenn xalaatee ne, mooy wax ci kàddug Yàlla, walla mu xalaat ne, Xelum Yàlla jagleel na may, na nangu ne lii ma leen bind ndigalu Boroom bi la.

14:38b.1CO.014.038 Te su ko xeebee it, ñu xeeb ko.

14:39b.1CO.014.039 Kon nag bokk yi, farluleen ci di wax ci kàddug Yàlla, te buleen tere kenn muy wax ay làkk.

14:40b.1CO.014.040 Waaye nag, na lépp di dox ciy teggin te aw yoon.

15

15:1b.1CO.015.001 Léegi nag bokk yi, maa ngi leen di fàttali xebaar bu baax bi ma leen yégal. Xebaar bu baax boobu, nangu ngeen ko te yéena ngi ciy sax.

15:2b.1CO.015.002 Ci moom ngeen jaare, ba mucc, bu ngeen téyee bu dëgër njàngale mi, ni ma leen ko yégale. Walla xanaa boog gëm ngeen ko cig neen?

15:3b.1CO.015.003 Li ma jotoon, jottali naa leen ko, te moo jëkk ci maana yi: Kirist dee na ngir dindi sunuy bàkkaar, ni ko Mbind mi tërale,

15:4b.1CO.015.004 suul nañu ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba, ni ko Mbind mi tërale.

15:5b.1CO.015.005 Feeñu na Sefas, teg ca fukki taalibe ya ak ñaar.

15:6b.1CO.015.006 Gannaaw ga feeñu na lu ëpp juróomi téeméeri bokki taalibe ci benn yoon. Te ñu bare ci ñoom ñu ngi dund ba léegi, waaye am na ci ñu nelaw.

15:7b.1CO.015.007 Ba noppi feeñu na Saag ak ndawi Kirist yépp.

15:8b.1CO.015.008 Man nag la mujj a feeñu, ma mel ni liir bu judduwul ci jamonoom.

15:9b.1CO.015.009 Ndaxte maa gën a ñàkk solo ci ndawi Kirist yi, te yeyoowuma sax, ñu may wooye ndaw, man mi doon fitnaal mbooloom Yàlla.

15:10b.1CO.015.010 Waaye nag yiwu Yàlla moo tax ma doon li ma doon, te yiw, wi mu wone ci man, du cig neen. Waaye sax maa gën a liggéey ñi ci des ñépp: du ci man, waaye yiwu Yàlla, wiy jëf ci man, moo tax.

15:11b.1CO.015.011 Noonu nag muy man muy ñoom, dénkaane boobu lanuy yégle, te moom ngeen gëm.

15:12b.1CO.015.012 Waaye su nu yéglee ne, Kirist dekki na, nan la ñenn ñi ci yéen man a waxe ne, néew yi duñu dekki?

15:13b.1CO.015.013 Su fekkee ne ñi dee duñu dekki, kon Kirist it dekkiwul.

15:14b.1CO.015.014 Te su Kirist dekkiwul, sunu waare day neen, te it seen ngëm day neen.

15:15b.1CO.015.015 Rax-ca-dolli gis nañu ne, seedeel nanu Yàlla ay fen, ndaxte seede nanu ci mbiram ne, dekkal na Yeesu, te fekk dekkalu ko, su néew yi dul dekki.

15:16b.1CO.015.016 Su néew yi dul dekki, Kirist moom it dekkiwul.

15:17b.1CO.015.017 Te su Kirist dekkiwul, seen ngëm du am solo, ba tey yéena ngi ci seeni bàkkaar.

15:18b.1CO.015.018 Te it ñi dee ba noppi ci Kirist sànku nañu.

15:19b.1CO.015.019 Su fekkee ci giiru dund gii rekk la sunu yaakaar ci Kirist ame solo, kon noo gën a mat a yërëm ñépp.

15:20b.1CO.015.020 Waaye léegi Kirist dekki na, di ku jëkk a dekki, ni gub yi ñu jëkk a tànne ci ngóob mi, jagleel leen Yàlla.

15:21b.1CO.015.021 Gannaaw ci nit la dee jaar, dugg àddina, kon it ci nit la ndekkite jaar.

15:22b.1CO.015.022 Kon ni ñépp deeye ci seen bokk ci Aadama, noonu la ñépp di dundaate ci seen bokk ci Kirist.

15:23b.1CO.015.023 Waaye ku nekk ak ayam. Kirist moo jëkk, mel ni gub yi ñu jëkk a tànne ci ngóob mi, ba noppi, bu Kirist dellusee, ñi bokk ci moom jël seen ay.

15:24b.1CO.015.024 Gannaaw ga, mujug jamono taxaw, te Kirist dina noot gépp kilifa ak bépp sañ-sañ ak doole, ba noppi delloo nguur gi kiy Yàlla di Baayam.

15:25b.1CO.015.025 Ndaxte fàww Kirist nguuru, ba kera Yàlla di daaneel noonam yépp ciy tànkam.

15:26b.1CO.015.026 Noon bu mujj, bi mu fiy jële, mooy dee.

15:27b.1CO.015.027 Ndaxte Mbind mi nee na: «Yàlla nootal na ko lépp, mu teg ci tànk.» Waaye bu Mbind mi nee, «noot na lépp,» wóor na ne, moom mi ko nootal lépp, génne na ci boppam.

15:28b.1CO.015.028 Léegi bu ñu ko nootalee lépp nag, moom Kirist muy Doom ji dina delloo kilifteef gi Yàlla, mi ko nootal lépp, ngir Yàlla nekk buur ci lépp.

15:29b.1CO.015.029 Su ndekkite amul, kon ñi ñu sóob ci ndox ngir ñi dee, lu mu leen di jariñ? Su dekki amul, kon lu tax ñu leen di sóob ngir ñi dee?

15:30b.1CO.015.030 Te nun it lu tax fu nu tollu nu jaay sunu bakkan?

15:31b.1CO.015.031 Bokk yi, ni ma damoo ci yéen ndax Yeesu Kirist, ni la ma wóore ne, bés bu nekk ma riisu dee.

15:32b.1CO.015.032 Su fekkee ne ci ni ñu ko waxe, xeex naa ca dëkku Efes ak rabi àll, kon ban njariñ la may amal? Su néew yi dul woon dekki, am na lu ci léeb wax:«Nanu lekk di naan, ndaxte ëllëg dinanu dee.»

15:33b.1CO.015.033 Bu leen ko réere mbir: «Ànd bu bon dina yàq nit ku baax.»

15:34b.1CO.015.034 Delloosileen xel yi te bàyyi bàkkaar, ndaxte am na ci yéen, ñu umple Yàlla. Kon war ngeen a rus!

15:35b.1CO.015.035 Waaye dina am kuy naan: «Nan la néew yi di dekkee? Wan yaram lañuy dellusee?»

15:36b.1CO.015.036 Yaa gàtt xel! Li ngay ji, du jebbi dund gu bees, fi ak deewul ba noppi.

15:37b.1CO.015.037 Te li ngay ji du jëmmi gàncax giy ñëwi, waaye pepp kese la, maanaam dugub, walla weneen jiwu.

15:38b.1CO.015.038 Noonu Yàlla jox ko jëmm ju ko neex, jiwu wu nekk ak jëmmam.

15:39b.1CO.015.039 Jëmmi mbindeef yépp a wuute: nit ak jëmmam, mala, picc, jën — yu ci nekk ak sa jëmmi bopp.

15:40b.1CO.015.040 Am na itam ay jëmm ca asamaan ak ay jëmm ci suuf. Leeru jëmm ca asamaan wuute na ak gi ci suuf.

15:41b.1CO.015.041 Jant bi, weer wi ak biddiiw, lu nekk ak sag leer. Te it leeru biddiiw bu nekk dina wuute ak moroomam.

15:42b.1CO.015.042 Noonu la ndekkitel néew yi di deme. Bu ñu suulee néew bi, dañoo ji lu yàqu. Bu dekkee, du yàqooti ba abadan.

15:43b.1CO.015.043 Lu ñàkk solo lañuy suul; mu dekki ak ndam. Lu néew doole lañuy suul, mu dekki ak kàttan.

15:44b.1CO.015.044 Bu ñu koy suul, yaram lay doon wu soloo woon ruu. Bu dekkee, doon yaram wu soloo ndamu Xelum Yàlla. Ndegam am na yaram wu soloo ruu, kon dina am yaram wu soloo ndamu Xelum Yàlla.

15:45b.1CO.015.045 Mbind mi nee na: «Nit ku jëkk ka, Aadama, doon na boroom ruu,» waaye Aadama mu mujj mi doon na Xel muy joxe dund.

15:46b.1CO.015.046 Yaram wi soloo ndamu Xelum Yàlla jiituwul; yaramu doom Aadama moo jiitu; yaramu ndam li moo ci topp.

15:47b.1CO.015.047 Nit ku jëkk ka pëndu suuf la woon; ñaareelu nit ki di Kirist, mi ngi jóge asamaan.

15:48b.1CO.015.048 Waa àddina yor nañu jëmmi nit, ki ñu sàkke ci suuf; noonu it ñi bokk ci asamaan dinañu yor melokaanu ki jóge ci asamaan.

15:49b.1CO.015.049 Te ni nu yore melokaanu ki ñu sàkke ci suuf, noonu lanuy yoreji melokaanu ki jóge ca asamaan.

15:50b.1CO.015.050 Li may wax nag bokk yi, moo di ne, sunu yaram wii mënul a am wàll ci nguuru Yàlla, te lu yàqu mënul a am wàll ci liy sax abadan.

15:51b.1CO.015.051 Lii ma leen di xamal, mbóotu Yàlla la. Dégluleen, dunu jaar ci dee nun ñépp, waaye nun ñépp dinanu soppiku,

15:52b.1CO.015.052 ci saa su gàtt, ci xef-ak-xippi, bu liit gu mujj gi jibee. Ndax liit gi dina jib, néew yi dekki, di dund abadan, te nun dinanu soppiku.

15:53b.1CO.015.053 Yaram wu yàqu war na sol jëmm ja dul yàqooti, te yaram wiy dee sol dund gu sax abadan.

15:54b.1CO.015.054 Bu li yàqu solee melokaanu li dul yàqu, te liy dee sol melokaanu liy sax abadan, kon lii ñu wax ci Mbind mi mat:«Yàlla noot na dee, ba labal ko ci ndamam.

15:55b.1CO.015.055 Céy yaw dee! Ana sa ndam?Céy yaw dee! Ana sa daŋar ji ngay fitte?»

15:56b.1CO.015.056 Daŋaru dee mooy bàkkaar, te dooley bàkkaar mooy Yoon wi.

15:57b.1CO.015.057 Waaye jërë-jëf yaw Yàlla, ji nu jox ndam li jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist!

15:58b.1CO.015.058 Kon nag sama bokk yi ma sopp, nangeen takku, sampu ba dëgër, te gën a sawar ci liggéeyu Boroom bi, xam ne seen liggéey, bi jëm ci Boroom bi, du neen.

16

16:1b.1CO.016.001 Léegi nag ci li jëm ci ndimbal, li ñuy sàkkal gaayi Yàlla yi, defleen li ma tëral ci mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Galasi.

16:2b.1CO.016.002 Bés bu jëkk ci ayu-bés yi, na ku nekk ber lu mu àttan, denc ko, ngir saa yu ma dikkee, ñu bañ di wër di laaj xaalis.

16:3b.1CO.016.003 Su ma dikkee, dinaa dénk seen xaalis ñi ngeen tànn, yónni leen Yerusalem, boole ko ak bataaxal.

16:4b.1CO.016.004 Su aajoo ma demal sama bopp, kon dinañu ànd ak man.

16:5b.1CO.016.005 Gannaaw bu ma jàllee diiwaanu Maseduwan, dinaa ñëw ci yéen, ndaxte fas naa ko yéenee jàll.

16:6b.1CO.016.006 Man na am ma yàgg ci yéen, jombul sax ma lollikoo fi yéen. Noonu dingeen taxawu sama yoon, fu ma man a jëm.

16:7b.1CO.016.007 Ndaxte fi mu ne bëgguma leen a gis rekk, jàll, waaye yaakaar naa ne, dinaa toog ci yéen ab diir, bu neexee Boroom bi.

16:8b.1CO.016.008 Ba tey dinaa toog fii ci dëkku Efes ba màggalu Pàntakot,

16:9b.1CO.016.009 ndaxte Yàlla ubbil na ma bunt, ba mu ne làññ, ngir may def liggéey bu man a am muj gu rafet, te noon yu bare bëgg a gàllankoor liggéey bi.

16:10b.1CO.016.010 Bu leen Timote ganesee, fexeleen ba bumu am njàqare ci seen biir, ndaxte dafay liggéeyal Boroom bi ni man.

16:11b.1CO.016.011 Kon bu ko kenn xeeb. Nangeen taxawu yoonam, ba mu dellusi ci man ci jàmm, ndaxte maa ngi koy xaar ak bokk yi.

16:12b.1CO.016.012 Naka Apolos sunu mbokk mi nag moom, xiir naa ko ay yooni yoon, mu ñëw ci yéen, ànd ak bokk yi. Waaye fi mu ne dëppoowul ak coobareem. Dina ñëw saa su ko manee.

16:13b.1CO.016.013 Farluleen te dëgër ci ngëm, di góor-góorlu te am pasteef.

16:14b.1CO.016.014 Lépp li ngeen di def, defleen ko ak mbëggeel.

16:15b.1CO.016.015 Xam ngeen ne, Estefanas ak njabootam ñoo jëkk a nangu xebaar bu baax bi ci diiwaanu Akayi, te ñoo joxe seen bopp, ngir liggéeyal gaayi Yàlla yi. Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan,

16:16b.1CO.016.016 ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak képp ku ànd ak ñoom ci liggéey bi.

16:17b.1CO.016.017 Bi ma Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus seetsee, bég naa ci lool. Taxawal nañu leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man te tële ko.

16:18b.1CO.016.018 Seral nañu sama xol ak seen yos itam. Kon fonkleen nit ñu mel noonu.

16:19b.1CO.016.019 Mboolooy ñi gëm te nekk diiwaanu Asi ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci Boroom bi, ñoom ak mbooloom ñi gëm tey daje seen kër.

16:20b.1CO.016.020 Bokk yépp ñu ngi leen di nuyu. Saafoonteleen ak xol bu laab.

16:21b.1CO.016.021 Man Pool maa bind nuyoo bii ci sama loxob bopp.

16:22b.1CO.016.022 Képp ku bañ Boroom bi, Yal na ko Yàlla alag. Boroom bi, ñëwal!

16:23b.1CO.016.023 Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen.

16:24b.1CO.016.024 Bëgg naa leen yéen ñépp ndax sunu booloo ak Yeesu Kirist.


Holder of rights
Multilingual Bible Corpus

Citation Suggestion for this Object
TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. 1 Corinthians (Wolof). 1 Corinthians (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C336-F