Acts (Wolof)
1
1:1b.ACT.001.001 Yaw Teyofil, téere bu jëkk, ba ma bindoon, ëmb na lépp li Yeesu tàmbali woon a jëf ak a jàngale,
1:2b.ACT.001.002 ba ci bés, ba ko Yàlla yéege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, jëm ci ndaw ya mu tànnoon.
1:3b.ACT.001.003 Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent-fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla.
1:4b.ACT.001.004 Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.
1:5b.ACT.001.005 Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.»
1:6b.ACT.001.006 Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?»
1:7b.ACT.001.007 Mu tontu leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.
1:8b.ACT.001.008 Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.»
1:9b.ACT.001.009 Bi mu waxee loolu, te ñu di ko xool, Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët.
1:10b.ACT.001.010 Bi muy dem nag, te ñu ne jàkk asamaan, ñaar ñu sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet.
1:11b.ACT.001.011 Ñu ne leen: «Yéen waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male ñu jële ci seen biir, yéege ko asamaan, dina dellusi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.»
1:12b.ACT.001.012 Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem.
1:13b.ACT.001.013 Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag.
1:14b.ACT.001.014 Ñoom ñépp ñoo bokk menn xel, di wéy ci ñaan ci Yàlla, ànd ak jigéen ñi ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
1:15b.ACT.001.015 Ca bés yooya nag Piyeer taxaw ca digg bokk ya, di mbooloo mu tollu ni téeméer ak ñaar-fukk.
1:16b.ACT.001.016 Mu ne leen: «Bokk yi, li Xel mu Sell mi waxoon ci Mbind mi jaarale ko ci gémmiñu Daawuda, fàww mu am. Waxoon na ci mbirum Yudaa, mi wommat ñi jàpp Yeesu
1:17b.ACT.001.017 te mu bokkoon ci nun, ba am cér ci liggéey bi.»
1:18b.ACT.001.018 --Pey gi Yudaa jotoon ci ñaawteefam, mu jënd ci tool, daanu fa, ba fàcc, ay buttitam tuuru.
1:19b.ACT.001.019 Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen làkk ñuy tudde tool ba Akeldama, maanaam «Toolu deret.» —
1:20b.ACT.001.020 Piyeer teg ca ne: «Ndaxte lii lañu bind ci téereb Sabóor:“Na këram gental,bu fa kenn dëkk.” Te it:“Na keneen bey sasam.”
1:21b.ACT.001.021 Kon ñeel na nu, nu tànn kenn ci ñi bokk ak nun, diir bi Yeesu doon dem ak a dikk ci sunu biir,
1:22b.ACT.001.022 li dale ci bi ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jële ci sunu biir, yéege ko. Kooku war na ànd ak nun, di seedeel ndekkitel Yeesu.»
1:23b.ACT.001.023 Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas.
1:24b.ACT.001.024 Ñu ñaan ci Yàlla ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu nit ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii,
1:25b.ACT.001.025 mu yenu liggéeyu nekk sa ndaw, wuutu Yudaa, mi ko bàyyi, dem bérabam.»
1:26b.ACT.001.026 Noonu ñu boole leen, tegoo ay bant, bant ba dal ca Macas, mu fekki fukki ndaw ya ak benn.
2
2:1b.ACT.002.001 Bi bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp booloo nañu ci benn bérab.
2:2b.ACT.002.002 Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell kër, ga ñu toog.
2:3b.ACT.002.003 Te ay làmmiñ yu mel ni safara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk.
2:4b.ACT.002.004 Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneeni làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko.
2:5b.ACT.002.005 Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp.
2:6b.ACT.002.006 Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk.
2:7b.ACT.002.007 Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile?
2:8b.ACT.002.008 Naka la man a ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?
2:9b.ACT.002.009 Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,
2:10b.ACT.002.010 di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,
2:11b.ACT.002.011 Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Kereet ak Araab yi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»
2:12b.ACT.002.012 Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»
2:13b.ACT.002.013 Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! ñii dañoo màndi ak biiñ.»
2:14b.ACT.002.014 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
2:15b.ACT.002.015 Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
2:16b.ACT.002.016 Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
2:17b.ACT.002.017 “Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi,dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp;seen xeet wu góor ak wu jigéendinañu wax ci kàddug Yàlla;waxambaane yi dinañu gis ay peeñute màggat yi di gént ay gént.
2:18b.ACT.002.018 Waaw ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xelci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen,te dinañu wax ci kàddug Yàlla.
2:19b.ACT.002.019 Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaanak ay firnde ci suuf ci àddina,muy deret, safara ak ay niiri saxar.
2:20b.ACT.002.020 Jant bi dina daldi lëndëm,weer wi deretal,bala bésu Boroom biy ñëw,di bés bu mag, bi ànd ak ndam.
2:21b.ACT.002.021 Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam,dinga mucc.”
2:22b.ACT.002.022 «Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko.
2:23b.ACT.002.023 Moom nag jébbale nañu ko, jaar ci nas, bi Yàlla dogaloon te xam ko lu jiitu; te yéen rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy bàkkaarkat.
2:24b.ACT.002.024 Waaye Yàlla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee mënu koo téye.
2:25b.ACT.002.025 Daawuda wax na ci mbiram ne:“Saa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam,gannaaw mu ngi ci sama ndeyjoor,kon duma raf.
2:26b.ACT.002.026 Moo tax sama xol sedd,may woy sama bànneex,te it sama yaram di tëdd ci yaakaar.
2:27b.ACT.002.027 Ndaxte doo bàyyi sama ruu ci barsàq,te doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.
2:28b.ACT.002.028 Xamal nga ma yoonu dund;dinga ma béglooji ci sa kanam.”
2:29b.ACT.002.029 «Bokk yi, man naa leen a wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey.
2:30b.ACT.002.030 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne, Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne, dina teg ci nguuram kenn ci askanam.
2:31b.ACT.002.031 Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne, bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul.
2:32b.ACT.002.032 Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko.
2:33b.ACT.002.033 Yàlla yéege na ko ak ndeyjooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko.
2:34b.ACT.002.034 Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na:“Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,
2:35b.ACT.002.035 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ”
2:36b.ACT.002.036 «Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne, Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
2:37b.ACT.002.037 Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu war a def?»
2:38b.ACT.002.038 Piyeer tontu leen ne: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi.
2:39b.ACT.002.039 Ndaxte li Yàlla dige woon, yéena ko moom ak seeni doom ak ñu sore ñépp, di ñépp ñi Yàlla sunu Boroom di woo ci moom.»
2:40b.ACT.002.040 Noonu mu artu leen ak yeneen wax yu bare, di leen dénk ne: «Rëccleen ci niti jamono ju dëng jii.»
2:41b.ACT.002.041 Ñi nangu ay waxam nag, ñu sóob leen ci ndox, te ca bés booba lu mat limub ñetti junniy nit yokku nañu ci ñoom.
2:42b.ACT.002.042 Ñoom nag ñuy wéy ci njàngalem ndaw yi ak cig bokk, ci damm mburu ak ñaan ci Yàlla.
2:43b.ACT.002.043 Ragal jàpp ñépp, te ndaw yi di def ay kéemaan ak ay firnde yu bare.
2:44b.ACT.002.044 Ñi gëm nag dañoo booloo te bokk lépp.
2:45b.ACT.002.045 Ñu jaay seeni suuf ak seen alal, séddoo ko, ku nekk ak la ngay soxla.
2:46b.ACT.002.046 Te bés bu nekk ñu saxoo teew ak benn xalaat ca kër Yàlla ga, tey damm mburu ca kër ya; ñuy lekk seen ñam ak xol bu laab tey bég,
2:47b.ACT.002.047 di màggal Yàlla te am yiw ci wetu nit ñépp. Noonu bés bu nekk Boroom bi di yokk ca mbooloo ma ñi mucc.
3
3:1b.ACT.003.001 Am bés Piyeer ak Yowaana dem, ba bëgg a dugg ca kër Yàlla ga ca waxtuw ñaan, maanaam tisbaar.
3:2b.ACT.003.002 Fekk ñu indi fa nit ku judduwaale lafañ, ñu di ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye Bunt bu rafet ba, ca kër Yàlla ga, ngir muy yelwaan ña fay dugg.
3:3b.ACT.003.003 Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana nag, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu dékk leen loxo.
3:4b.ACT.003.004 Ci kaw loolu Piyeer ak Yowaana ne ko jàkk, te Piyeer ne ko: «Xool nu.»
3:5b.ACT.003.005 Lafañ bi xool leen, yaakaar ne dina jot dara ci ñoom.
3:6b.ACT.003.006 Noonu Piyeer ne ko: «Awma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, dinaa la ko jox: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret doxal!»
3:7b.ACT.003.007 Mu jàpp ci loxol ndeyjooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam ak ay kostanam dëgër.
3:8b.ACT.003.008 Mu tëb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak ñoom ca kër Yàlla ga, muy dox, di tëb tey sant Yàlla.
3:9b.ACT.003.009 Noonu ñépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
3:10b.ACT.003.010 Te ñu xàmmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu daldi waaru lool te yéemu ci li ko dikkal.
3:11b.ACT.003.011 Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan.
3:12b.ACT.003.012 Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii?
3:13b.ACT.003.013 Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi.
3:14b.ACT.003.014 Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.
3:15b.ACT.003.015 Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.
3:16b.ACT.003.016 Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér peŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp.
3:17b.ACT.003.017 «Léegi nag bokk yi, xam naa ne, ñàkka xam a tax ngeen def ko, yéen ak seeni kilifa.
3:18b.ACT.003.018 Waaye noonu la Yàlla amale li mu yégle woon lu jiitu jaarale ko ci gémmiñug yonent yépp naan, Almaseem dina sonn.
3:19b.ACT.003.019 Tuubleen seeni bàkkaar nag te woññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far.
3:20b.ACT.003.020 Noonu jamonoy péex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu.
3:21b.ACT.003.021 Asamaan war na koo yor, ba jamono ju ñuy defaraat lépp, di jamono ji Yàlla waxoon jaarale ko ci gémmiñug yonentam yu sell yépp, li dale ci njàlbéenug àddina.
3:22b.ACT.003.022 Ndaxte Musaa nee woon na: “Boroom bi seen Yàlla dina leen feeñalal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
3:23b.ACT.003.023 Képp ku déggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.”
3:24b.ACT.003.024 «Li dale sax ci Samwil ak ñi ci topp, bépp yonent bu wax yégle na bés yii.
3:25b.ACT.003.025 Yéen nag yéenay donn yonent yi ak kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, bi mu naan Ibraayma: “Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci ki soqikoo ci yaw.”
3:26b.ACT.003.026 Yàlla feeñal na Ndawam, jëkk koo yebal ci yéen, ngir barkeel leen, ci woññi leen kenn ku nekk ci say bàkkaar.»
4
4:1b.ACT.004.001 Bi ñuy wax ak mbooloo ma, saraxalekat ya ak kilifag ñiy wottu kër Yàlla ga ak Sadusen ya daanu ci seen kaw.
4:2b.ACT.004.002 Ñu mer lool ci li ñuy waar nit ñi, di yégle ndekkitel ñi dee, sukkandikoo ko ci ndekkitel Yeesu.
4:3b.ACT.004.003 Noonu ñu jàpp leen, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndaxte mu nga doon tàmbalee guddi.
4:4b.ACT.004.004 Waaye ñu bare ca ña dégg wax ja gëm nañu, te limu góor ñi gëm yokku na, ba mat juróomi junni.
4:5b.ACT.004.005 Ca ëllëg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem.
4:6b.ACT.004.006 Ràññe nañu ci: Anas, miy saraxalekat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki saraxalekat bu mag bi.
4:7b.ACT.004.007 Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?»
4:8b.ACT.004.008 Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi,
4:9b.ACT.004.009 bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey,
4:10b.ACT.004.010 nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp! Ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam.
4:11b.ACT.004.011 Yeesu moomu mooy:“Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi,te moo doon doju koñ.”
4:12b.ACT.004.012 Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu war a mucce.»
4:13b.ACT.004.013 Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne, musuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne, daa nañu ànd ak Yeesu.
4:14b.ACT.004.014 Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, mënuñu caa teg dara.
4:15b.ACT.004.015 Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir,
4:16b.ACT.004.016 ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te mënunu koo weddi.
4:17b.ACT.004.017 Waaye ngir mbir mi bañ a law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu bañ a waxati ak kenn ci tur woowu.»
4:18b.ACT.004.018 Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.
4:19b.ACT.004.019 Waaye Piyeer ak Yowaana tontu leen ne: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla moo jub ci kanam Yàlla, seetleen ko.
4:20b.ACT.004.020 Waaye nun mënunoo bañ a wax li nu gis te dégg ko.»
4:21b.ACT.004.021 Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon.
4:22b.ACT.004.022 Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent-fukki at.
4:23b.ACT.004.023 Bi ñu leen yiwee nag, ñu dem ci seeni bokk, nettali leen li saraxalekat yu mag ya ak njiit ya waxoon lépp.
4:24b.ACT.004.024 Bi ko bokk ya déggee nag, ñu mànkoo, diis seen kàddu Yàlla ne: «Boroom bi, yaa sàkk asamaan, suuf, géej ak lépp li nekk ci seen biir.
4:25b.ACT.004.025 Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon gémmiñu Xel mu Sell mi, ne:“Lu tax xeeti àddina di bax?Lu tax ñuy fexe lu mënul a am?
4:26b.ACT.004.026 Buuri àddina dañoo booloo,te kilifa yi dajaloo,di bañ Boroom bi ak Almaseem.”
4:27b.ACT.004.027 Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu,
4:28b.ACT.004.028 te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon.
4:29b.ACT.004.029 Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.
4:30b.ACT.004.030 Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.»
4:31b.ACT.004.031 Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yengatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
4:32b.ACT.004.032 Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.
4:33b.ACT.004.033 Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp.
4:34b.ACT.004.034 Kenn ci ñoom ñàkkul dara, ndaxte képp ku nekk boroom suuf mbaa am ay kër, jaay na ko, indi njëg gi,
4:35b.ACT.004.035 teg ko ci loxoy ndaw ya; ñu di ci sédd, kenn ku nekk li mu soxla.
4:36b.ACT.004.036 Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi dàkkentale ko Barnabas, miy tekki «Kiy dëgëral fit yi,» mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar.
4:37b.ACT.004.037 Moom nag jaay na tool, ba mu moom, indi xaalis ba, teg ko ci loxoy ndaw ya.
5
5:1b.ACT.005.001 Naka noonu nit ku tudd Anañas, ànd ak Safira jabaram, jaay làccu suuf.
5:2b.ACT.005.002 Mu dencal boppam benn cér ca njëg ga, ànd ca ak jabaram; ba noppi mu indi cér ba ca des, teg ko ci loxoy ndaw ya.
5:3b.ACT.005.003 Bi mu ko defee Piyeer ne ko: «Anañas, lu tax nga bàyyi Seytaane dugg la, ba fees sa xol, ngay wor Xel mu Sell mi, ci li nga dencal sa bopp benn cér ci njëg gi?
5:4b.ACT.005.004 Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon njëg gi? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit ñi, waaye Yàlla nga wor.»
5:5b.ACT.005.005 Bi Anañas déggee baat yooyu, mu daanu dee. Ñi ko dégg ñépp tiit, ba ne nërëm.
5:6b.ACT.005.006 Noonu waxambaane ya jóg, ñu sàng ko, yóbbu ko, jébbal Yàlla.
5:7b.ACT.005.007 Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew.
5:8b.ACT.005.008 Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njëgu tool bi?» Mu tontu ko: «Waawaaw, lii la.»
5:9b.ACT.005.009 Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.»
5:10b.ACT.005.010 Ca saa sa mu daanu ciy tànkam dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram.
5:11b.ACT.005.011 Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.
5:12b.ACT.005.012 Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga.
5:13b.ACT.005.013 Te kenn ci ña ca des ñemewul a booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.
5:14b.ACT.005.014 Moona ay nit ñu gën a bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.
5:15b.ACT.005.015 Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.
5:16b.ACT.005.016 Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.
5:17b.ACT.005.017 Booba saraxalekat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen, ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen,
5:18b.ACT.005.018 ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba.
5:19b.ACT.005.019 Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan:
5:20b.ACT.005.020 «Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.»
5:21b.ACT.005.021 Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, saraxalekat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
5:22b.ACT.005.022 Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi dellusi, yégle ko
5:23b.ACT.005.023 ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
5:24b.ACT.005.024 Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak saraxalekat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
5:25b.ACT.005.025 Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»
5:26b.ACT.005.026 Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.
5:27b.ACT.005.027 Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanamu mbooloo ma. Saraxalekat bu mag ba laaj leen
5:28b.ACT.005.028 ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
5:29b.ACT.005.029 Waaye Piyeer ak ndaw ya tontu leen ne: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.
5:30b.ACT.005.030 Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba.
5:31b.ACT.005.031 Te Yàlla yékkati na ko ci ndeyjooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar.
5:32b.ACT.005.032 Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.»
5:33b.ACT.005.033 Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leen a rey.
5:34b.ACT.005.034 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.
5:35b.ACT.005.035 Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
5:36b.ACT.005.036 Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
5:37b.ACT.005.037 Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
5:38b.ACT.005.038 Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.
5:39b.ACT.005.039 Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko man a fanq, ngir ragal a jànkoonte ak Yàlla.»
5:40b.ACT.005.040 Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.
5:41b.ACT.005.041 Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa.
5:42b.ACT.005.042 Noonu bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngale ak a xamle xebaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.
6
6:1b.ACT.006.001 Ca bés yooyu, naka taalibe yi di gën a bare, Yawut yiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci mbirum Yawut tigi yi, te lii a ko waral: jigéen ñi seen jëkkër dee, te ñu bokk ci ñoom, naraalewuñu leen ca ndimbal, la ñuy séddale bés bu nekk.
6:2b.ACT.006.002 Noonu fukki ndaw ya ak ñaar woo mbooloom taalibe ya ne leen: «Nu bàyyi kàddug Yàlla, di topptoo mbirum séddale, loolu jekkul ci nun.
6:3b.ACT.006.003 Kon nag bokk yi, tànnleen juróom-ñaari nit ci seen biir, ñu am seede su rafet te fees ak Xel mu Sell mi ak sago, nu dénk leen liggéey bii.
6:4b.ACT.006.004 Waaye nun dinanu wéy ci ñaan ci Yàlla ak ci yenub xamle kàddu gi.»
6:5b.ACT.006.005 Lii ñu wax nag neex na mbooloo mépp. Noonu ñu tànn Ecen, di nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya.
6:6b.ACT.006.006 Ñu jébbal leen ndaw ya, ñaanal leen, teg leen loxo.
6:7b.ACT.006.007 Noonu kàddug Yàlla di law, ba mbooloom taalibe yi di yokku bu bare ci Yerusalem; te saraxalekat yu bare déggal Yàlla ci topp yoonu ngëm wi.
6:8b.ACT.006.008 Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak kàttan, di def ay kéemaan yu mag ak ay firnde ca nit ña.
6:9b.ACT.006.009 Waaye ay nit jóg, bokk ci jàngu, bi ñuy wax Jàngub ñi ñu goreel, di ay niti dëkki Siren ak Alegsàndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. Ñuy werante ak Ecen,
6:10b.ACT.006.010 waaye àttanuñu sagoom ak Xel mi muy waxe.
6:11b.ACT.006.011 Kon ñu daldi jënd ay nit, ñu ne: «Dégg nanu ko, muy sosal Musaa ak Yàlla.»
6:12b.ACT.006.012 Noonu ñu jógloo nit ñi ak njiit yi ak xutbakat yi, ñu dal ci kawam, jàpp ko, yóbbu ko ca kureelu àttekat ya.
6:13b.ACT.006.013 Te ñu sàkk ay naaféq yuy seede ne: «Kii du bàyyee wax lu juuyoo ak bérab bu sell ba ak yoonu Musaa.
6:14b.ACT.006.014 Ndaxte dégg nanu, muy wax ne, Yeesum Nasaret moomu dina daaneel bérab bii te soppi aada, yi nu Musaa batale woon.»
6:15b.ACT.006.015 Bi ñu ko waxee, ña toogoon ñépp ca mbooloo ma xool ko jàkk, gis xar-kanamam, mu mel ni xar-kanamu malaaka.
7
7:1b.ACT.007.001 Noonu saraxalekat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»
7:2b.ACT.007.002 Ecen tontu ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan.
7:3b.ACT.007.003 Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.”
7:4b.ACT.007.004 «Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi.
7:5b.ACT.007.005 Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu war a donnale, du sax fu mu man a teg tànkam; waaye dig na ko ne, dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.
7:6b.ACT.007.006 Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.”
7:7b.ACT.007.007 Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.”
7:8b.ACT.007.008 Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom-ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.
7:9b.ACT.007.009 «Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,
7:10b.ACT.007.010 génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanamu Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp.
7:11b.ACT.007.011 «Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk.
7:12b.ACT.007.012 Yanqóoba nag dégg ne, Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk.
7:13b.ACT.007.013 Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa xàmmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam.
7:14b.ACT.007.014 Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak mbokkam yépp, ñuy juróom-ñaar-fukki nit ak juróom.
7:15b.ACT.007.015 Noonu Yanqóoba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam.
7:16b.ACT.007.016 Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sikem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Emor ca Sikem.
7:17b.ACT.007.017 «Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gën a bare ci Misra,
7:18b.ACT.007.018 ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.
7:19b.ACT.007.019 Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.
7:20b.ACT.007.020 «Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,
7:21b.ACT.007.021 ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.
7:22b.ACT.007.022 Musaa nag di ku yeewu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf.
7:23b.ACT.007.023 «Bi mu demee ba am ñeent-fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil.
7:24b.ACT.007.024 Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyyul ko, ba dóor waayi Misra ja.
7:25b.ACT.007.025 Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne, ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko.
7:26b.ACT.007.026 Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéem a jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?”
7:27b.ACT.007.027 Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw?
7:28b.ACT.007.028 Ndax danga maa bëgg a rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?”
7:29b.ACT.007.029 Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom.
7:30b.ACT.007.030 «Lu ko wees ñeent-fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku safara ci biir as ngarab.
7:31b.ACT.007.031 Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko:
7:32b.ACT.007.032 “Man maay sa Yàllay maam, di Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.” Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te ñemeetul a xool.
7:33b.ACT.007.033 Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la.
7:34b.ACT.007.034 Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.”
7:35b.ACT.007.035 «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.
7:36b.ACT.007.036 Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca Géej gu xonq ga ak ca màndiŋ ma diirub ñeent-fukki at.
7:37b.ACT.007.037 Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.”
7:38b.ACT.007.038 Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko.
7:39b.ACT.007.039 Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra.
7:40b.ACT.007.040 Ñu sant Aaroona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.”
7:41b.ACT.007.041 Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo.
7:42b.ACT.007.042 Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne:“Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur,jébbal ma, boole ko ak i sarax,diirub ñeent-fukki at ca màndiŋ ma?
7:43b.ACT.007.043 Yóbbu ngeen sax fu nekk tànt,biy màggalukaayu Molog ak biddiiwub Refan,bi ñu daan bokkaaleel Yàlla,di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen!Kon nag dinaa leen toxal,yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.”
7:44b.ACT.007.044 «Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma tàntu màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Tànt boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon.
7:45b.ACT.007.045 Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot tànt ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Tànt ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.
7:46b.ACT.007.046 Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba.
7:47b.ACT.007.047 Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga.
7:48b.ACT.007.048 «Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:
7:49b.ACT.007.049 “Asamaan mooy sama jal,te suuf mooy sama tegukaayu tànk.Kon gan kër ngeen may tabaxal,mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay?
7:50b.ACT.007.050 Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp?— Moom la Boroom bi doon wax.”
7:51b.ACT.007.051 «Yéen ñi dëgër bopp, ànd ak xol buy bañ ak ay nopp yuy fatt, mel ni ñi xamul Yàlla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def yéen itam.
7:52b.ACT.007.052 Kan ca yonent ya la seeni maam tegul woon ay fitna? Rey nañu ñi doon yégle ñëwug Aji Jub ji, moom mi ngeen jébbale léegi, ba ñu rey ko.
7:53b.ACT.007.053 Jot ngeen yoonu Musaa, wi Yàlla wàcce jaarale ko ci ay malaaka, te sàggane ngeen ko.»
7:54b.ACT.007.054 Bi ñu déggee loolu nag, seeni xol di dagg, ñuy yéyu, jëm ci kawam.
7:55b.ACT.007.055 Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne jàkk ci asamaan, gis ndamu Yàlla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndeyjooru Yàlla.
7:56b.ACT.007.056 Mu ne: «Seetleen, maa ngi gis asamaan yi ubbiku, te Doomu nit kaa ngii taxaw ci ndeyjooru Yàlla.»
7:57b.ACT.007.057 Bi ñu déggee loolu, ñu daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; ñu ànd, ne milib ci kawam;
7:58b.ACT.007.058 ñu wat-wate ko, génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon nañu seeni yére ci tànki waxambaane wu tudd Sool.
7:59b.ACT.007.059 Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!»
7:60b.ACT.007.060 Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: «Boroom bi, bu leen bindal bàkkaar bii,» ba noppi mu nelaw.
8
8:1b.ACT.008.001 Sool moom ànd na ci ñi doon rey Ecen. Bés booba nag fitna ju metti dal na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk Yerusalem, ba ñépp, ñu moy ndaw ya, tasaaroo ci diiwaani Yude ak Samari.
8:2b.ACT.008.002 Ay nit ñu ragal Yàlla fab Ecen, jébbal ko Boroom bi, di ko jooy bu wér.
8:3b.ACT.008.003 Waaye naka Sool, mu ngay tas mbooloom ñi gëm, di tàbbi ca kër ya, tey jàpp góor ak jigéen, di leen tëj kaso.
8:4b.ACT.008.004 Ñi tasaaroo nag dem fu nekk, di fa xamle xebaar bu baax bu kàddug Yàlla.
8:5b.ACT.008.005 Naka Filib mu dem ca benn dëkk ca Samari, di leen yégal Kirist.
8:6b.ACT.008.006 Bi ko mbooloo mi déggee te gis kéemaan yi muy def, ñu bokk benn xalaat, fekki ko ci li mu wax.
8:7b.ACT.008.007 Ndaxte ay rab yu bon bàyyi nañu nit ñu bare, ña ñu jàppoon, di yuuxu ci kaw; te ñu bare ñu làggi ak ñu lafañ daldi wér.
8:8b.ACT.008.008 Noonu mbég mu réy tàbbi ca dëkk ba.
8:9b.ACT.008.009 Amoon na nag nit ku tudd Simoŋ, di luxuskat bu yàgg ca dëkk ba, te daan yéem waa Samari gépp, ci naan: «Aji Màgg laa.»
8:10b.ACT.008.010 Kon ñépp, mag ak ndaw, taq ci moom ne: «Kii mooy jaasiy Aji Kàttan ji.»
8:11b.ACT.008.011 Ñu taq ci moom, ndax li mu leen yàgg a waar ci ay luxus.
8:12b.ACT.008.012 Waaye bi ñu gëmee xebaar bu baax, bi Filib yégle jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Kirist, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
8:13b.ACT.008.013 Simoŋ sax gëm, ñu sóob ko ci ndox; mu wéy nag ci topp Filib, di waaru ci kéemaan yi ak firnde yu mag yiy am.
8:14b.ACT.008.014 Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem yég nañu ne, waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla; ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana.
8:15b.ACT.008.015 Ñu dem fa nag, ñaanal leen, ngir ñu jot Xel mu Sell mi.
8:16b.ACT.008.016 Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu.
8:17b.ACT.008.017 Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi.
8:18b.ACT.008.018 Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,
8:19b.ACT.008.019 ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»
8:20b.ACT.008.020 Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne, man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.
8:21b.ACT.008.021 Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.
8:22b.ACT.008.022 Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.
8:23b.ACT.008.023 Ndaxte gis naa ne, sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar noot na la.»
8:24b.ACT.008.024 Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.»
8:25b.ACT.008.025 Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xebaar bu baax bi ci dëkk yu bare yu waa Samari.
8:26b.ACT.008.026 Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: «Jógal te jublu Misra, jaar ci yoon wi jóge Yerusalem, jëm Gasa, di màndiŋ.»
8:27b.ACT.008.027 Filib jóg dem. Noonu mu gis fa nitu Ecópi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, te di ko wottul xaalisam bépp. Fekk mu ñëwoon Yerusalem, ngir màggalsi Yàlla, bay dellu;
8:28b.ACT.008.028 mu toog ci watiiram, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.
8:29b.ACT.008.029 Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.»
8:30b.ACT.008.030 Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
8:31b.ACT.008.031 Mu tontu ko ne: «Nu ma ko man a xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom.
8:32b.ACT.008.032 Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi:«Yóbbu nañu ko ni xar mu ñuy rendiji;ni mburt mu luu ci kanami watkat,mu ne cell.
8:33b.ACT.008.033 Ci toroxteem nangu nañu dëggam;ñi mu tollool jamono, ku ci xalaat lii?Jële nañu bakkanam ci àddina.»
8:34b.ACT.008.034 Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?»
8:35b.ACT.008.035 Noonu Filib tàmbali ci aaya yooyu, xamal ko xebaar bu baax bi ci mbirum Yeesu.
8:36b.ACT.008.036 Bi ñuy jaar ci yoon wi, ñu agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci?»
8:38b.ACT.008.038 Mu santaane nag, ñu taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja wàcc ñoom ñaar ci biir ndox ma, mu sóob ko ca.
8:39b.ACT.008.039 Ba noppi ñu génn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi fëkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, ànd ak mbég.
8:40b.ACT.008.040 Filib moom teeri dëkku Asot, muy jaar ci dëkk yépp, di fa xamle xebaar bu baax bi, ba kera muy ñëw dëkku Sesare.
9
9:1b.ACT.009.001 Naka Sool, muy tëkkoo rey taalibey Boroom bi, ba di ko noyyee far. Mu dem nag ca saraxalekat bu mag ba,
9:2b.ACT.009.002 laaj ko ay bataaxal yu muy yóbbul jànguy dëkku Damas. Noonu ñu mu fa fekk, te ñu bokk ci yoon wi, góor mbaa jigéen, mu am dogalu yeew leen, indi leen Yerusalem.
9:3b.ACT.009.003 Waaye bi muy jub Damas, ca saa sa leer gu jóge asamaan melax, ba ëmb ko.
9:4b.ACT.009.004 Mu daanu ci suuf, dégg baat bu ko ne: «Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?»
9:5b.ACT.009.005 Mu wuyu ne: «Yaay kan Boroom bi?» Boroom bi ne ko: «Maay Yeesu, mi ngay fitnaal.
9:6b.ACT.009.006 Waaye jógal, dugg ca dëkk ba, te dinañu la wax li nga war a def.»
9:7b.ACT.009.007 Nit ñi ànd ak moom nag taxaw, waaru ba luu, ci li ñu dégg baat bi te gisuñu kenn.
9:8b.ACT.009.008 Noonu Sool jóg, xippi, waaye gisul dara; kon ñu wommat ko, yóbbu ko Damas.
9:9b.ACT.009.009 Diirub ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.
9:10b.ACT.009.010 Amoon na nag ci Damas taalibe bu tudd Anañas. Bi loolu amee nag Boroom bi feeñu ko ne: «Anañas!» Mu wuyu: «Maa ngi nii Boroom bi.»
9:11b.ACT.009.011 Boroom bi ne ko: «Jógal, nga jaar ci mbedd, mi ñuy wax Mbedd mu jub mi, te seet ci kër Yudaa nit ku tudd Sool te dëkk Tars, ndaxte mu ngay ñaan.
9:12b.ACT.009.012 Te gis na cim peeñu nit ku tudd Anañas, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.»
9:13b.ACT.009.013 Waaye Anañas tontu ko ne: «Boroom bi, dégg naa ci nit ñu bare ci mbirum kooku, ñu seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem.
9:14b.ACT.009.014 Te indaale na fii sax sañ-sañ bu jóge ci saraxalekat yu mag ya, ngir yeew képp kuy tudd saw tur.»
9:15b.ACT.009.015 Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte maa ko tànn, muy sama jëfandukaay, ngir yóbbu sama tur fa kanam ñi nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak bànni Israyil.
9:16b.ACT.009.016 Te dinaa ko won coono yu bare yu mu war a dékku ngir sama tur.»
9:17b.ACT.009.017 Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg ay loxoom Sool. Mu ne ko: «Sool sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la feeñu woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma yónni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.»
9:18b.ACT.009.018 Ca saa sa lu mel ni ay waasintoor génne ci ay bëtam, mu daldi gisaat. Noonu mu jóg, ñu sóob ko ci ndox;
9:19b.ACT.009.019 ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damas.
9:20b.ACT.009.020 Ca saa sa muy yégle ca jàngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.
9:21b.ACT.009.021 Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanamu saraxalekat yu mag ya?»
9:22b.ACT.009.022 Moona Sool di gën a am kàttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.
9:23b.ACT.009.023 Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
9:24b.ACT.009.024 Waaye Sool yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
9:25b.ACT.009.025 Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
9:26b.ACT.009.026 Bi Sool agsee Yerusalem, mu jéem a ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
9:27b.ACT.009.027 Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sool gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damas.
9:28b.ACT.009.028 Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
9:29b.ACT.009.029 Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wut a rey.
9:30b.ACT.009.030 Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
9:31b.ACT.009.031 Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gën a dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
9:32b.ACT.009.032 Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yàlla yi dëkk Lidd,
9:33b.ACT.009.033 mu gis fa nit ku làggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom-ñetti at.
9:34b.ACT.009.034 Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa.
9:35b.ACT.009.035 Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron gépp gisee, ñu daldi woññiku ci Boroom bi.
9:36b.ACT.009.036 Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas,» maanaam «kewel,» te muy wéy ci jëf yu baax ak saraxe.
9:37b.ACT.009.037 Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu ñu sang ko, teg ko ca néeg, ba sut ca taax ma.
9:38b.ACT.009.038 Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi dégg ne, Piyeer a nga fa, ñu yónnee ko ñaari nit, ñaan ko mu ñëw ci ñoom ci saa si.
9:39b.ACT.009.039 Bi ko Piyeer déggee, mu jóg, ànd ak ñoom. Bi mu ñëwee, ñu yóbbu ko ca néeg bu kawe ba. Fekk fa ay jigéen ñi seeni jëkkër faatu, ñu daldi wër Piyeer, ñépp di jooy, di ko won kamisool ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam.
9:40b.ACT.009.040 Ci kaw loolu Piyeer génne ñépp ci biti, mu sukk, ñaan ci Yàlla, ba noppi walbatiku ca néew ba ne ko: «Tabita, jógal!» Noonu mu xippi, gis Piyeer, daldi toog.
9:41b.ACT.009.041 Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Mu woo gaayi Yàlla ya ak jigéen ña, won leen ko, muy dund.
9:42b.ACT.009.042 Mbir ma siiw ca Yope gépp, ba ñu bare gëm Boroom bi.
9:43b.ACT.009.043 Gannaaw loolu Piyeer toog ay fan ci Yope, ci këru ku tudd Simoŋ, miy wullikat.
10
10:1b.ACT.010.001 Amoon na ci Sesare nit ku tudd Korney, nekk njiitu xare, mu bokk ci mbooloom xare, mi ñuy wax mu Itali.
10:2b.ACT.010.002 Moom nag ku farlu woon ci Yàlla la, te ragal ko, moom ak waa këram gépp; muy sarax ñu bare ci bànni Israyil, tey saxoo ci ñaan ci Yàlla.
10:3b.ACT.010.003 Am bés ci tisbaar nag mu am peeñu, gis bu leer malaakam Yàlla feeñu ko ne ko: «Korney!»
10:4b.ACT.010.004 Noonu Korney ne ko jàkk, daldi tiit ne ko: «Kilifa gi, lu mu doon?» Malaaka ma ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa kanam Yàlla, te nangul na la.
10:5b.ACT.010.005 Yónnil léegi nag ay nit ci dëkku Yope, ñu woo ku tudd Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.
10:6b.ACT.010.006 Mu nga dal fa Simoŋ wullikat, bi këram nekk ci wetu géej.»
10:7b.ACT.010.007 Bi malaaka mi doon wax ak moom demee, Korney woo ñaar ci ay surgaam ak benn xarekat bu farlu ci Yàlla ci ñi koy topptoo;
10:8b.ACT.010.008 mu nettali leen lépp, yebal leen Yope.
10:9b.ACT.010.009 Ca ëllëg sa, ba ñuy jaar ca yoon wa, ba jub dëkk ba, Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg-bëccëg ngir ñaan ci Yàlla.
10:10b.ACT.010.010 Noonu xiif dab ko fa, mu bëgg a lekk. Waaye bi ñu koy toggal, Yàlla feeñu ko.
10:11b.ACT.010.011 Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni sér bu mag bu ñu téye ci ñeenti laf ya, yoor ko, mu jëm suuf.
10:12b.ACT.010.012 Boroom ñeenti tànk yépp ñu nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan.
10:13b.ACT.010.013 Te baat ne ko: «Jógal, Piyeer, rey te lekk.»
10:14b.ACT.010.014 Waaye Piyeer tontu ko: «Mukk, Boroom bi, ndaxte musumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.»
10:15b.ACT.010.015 Waaye baat bi wax ak moom ñaareelu yoon ne ko: «Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.»
10:16b.ACT.010.016 Ñu def ko nag, ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas sér ba, jëme asamaan.
10:17b.ACT.010.017 Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu peeñu miy tekki; fekk booba nit ñi Korney yebal, laajte woon nañu kër Simoŋ, ba agsi ci bunt bi.
10:18b.ACT.010.018 Ñu woote nag naan: «Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer, ndax fi la dëkk?»
10:19b.ACT.010.019 Bi Piyeer di rabal xelam ci peeñu ma, Xel mi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la wut.
10:20b.ACT.010.020 Jógal, nga wàcc te ànd ak ñoom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.»
10:21b.ACT.010.021 Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni tànk?»
10:22b.ACT.010.022 Ñu tontu ko: «Korney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Yàlla, ba am seede su rafet ci bànni Israyil gépp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci këram te déglu li ngay wax.»
10:23b.ACT.010.023 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer jóg, dem ak ñoom, ànd ak ñenn ci bokk yi dëkk Yope,
10:24b.ACT.010.024 te bés ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na këram ay bokkam ak i xaritam yi ko gën a jege, di xaar Piyeer.
10:25b.ACT.010.025 Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy tànkam, sargal ko.
10:26b.ACT.010.026 Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.»
10:27b.ACT.010.027 Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare.
10:28b.ACT.010.028 Mu ne leen: «Xam ngeen ne, aaye nañu Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci këram. Waaye Yàlla won na ma ne, warumaa ne kenn setul mbaa araam na.
10:29b.ACT.010.029 Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ñëw naa ci lu àndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?»
10:30b.ACT.010.030 Ci kaw loolu Korney tontu ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam,
10:31b.ACT.010.031 mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla.
10:32b.ACT.010.032 Yónneel nag ci Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; mu nga dal ci kër Simoŋ miy wullikat ca wetu géej ga.”
10:33b.ACT.010.033 Yónnee naa nag ci ni mu gën a gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.»
10:34b.ACT.010.034 Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne, Yàlla du gënale,
10:35b.ACT.010.035 waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.
10:36b.ACT.010.036 Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xebaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp.
10:37b.ACT.010.037 Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox.
10:38b.ACT.010.038 Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom.
10:39b.ACT.010.039 «Seede nanu li mu def lépp ci biir réewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey nañu ko ci wékk ko ci bant.
10:40b.ACT.010.040 Waaye Yàlla dekkal na ko ci ñetteelu fan ba te biral ko,
10:41b.ACT.010.041 waxuma xeet wépp, waaye seede yi Yàlla tànn lu jiitu, maanaam nun ñi daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem.
10:42b.ACT.010.042 Te Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne, moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee.
10:43b.ACT.010.043 Yonent yépp seedeel nañu ko ne, ku ko gëm, Yàlla dina la baal say bàkkaar ci turam.»
10:44b.ACT.010.044 Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi wàcc ci kaw ñépp ñiy déglu kàddu ga.
10:45b.ACT.010.045 Yawut yi gëm yépp nag, ñi ànd ak Piyeer, daldi waaru ci li Yàlla tuur Xel mu Sell, mi mu maye, ci ñi dul Yawut itam.
10:46b.ACT.010.046 Ndaxte dégg nañu leen, ñuy wax yeneeni làkk ak di màggal Yàlla.
10:47b.ACT.010.047 Booba Piyeer daldi wax ne: «Ñii jot Xel mu Sell mi ni nun, ndax manees na leen a bañ a sóob ci ndox?»
10:48b.ACT.010.048 Noonu mu santaane, ñu sóob leen ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Gannaaw loolu ñu ñaan ko, mu toog ci ñoom ay fan.
11
11:1b.ACT.011.001 Bi loolu amee ndaw yi ak bokk yi nekk ci diiwaanu Yude, dégg nañu ne, ñi dul Yawut nangu nañu kàddug Yàlla.
11:2b.ACT.011.002 Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko:
11:3b.ACT.011.003 «Lu tax nga dem ca këru ñu xarafal, bay lekk sax ak ñoom?»
11:4b.ACT.011.004 Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko
11:5b.ACT.011.005 ne: «Nekkoon naa ca dëkku Yope, di fa ñaan ci Yàlla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am peeñu: lu mel ni sér bu mag wàcc, jóge ci asamaan, ñu yoor ko ca ñeenti laf ya, mu ñëw ba ci man.
11:6b.ACT.011.006 Ma xool ko jàkk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom ñeenti tànk yu nekk ci kaw suuf, di rabi àll yi, yiy raam ak picci asamaan.
11:7b.ACT.011.007 Te dégg naa baat bu ma ne: “Jógal Piyeer, rey te lekk.”
11:8b.ACT.011.008 Waaye ma tontu ne: “Mukk Boroom bi, ndax dara lu daganul mbaa lu araam musul a dugg ci sama gémmiñ.”
11:9b.ACT.011.009 Waaye ñaareel bi yoon baat bi dellu ne ma: “Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.”
11:10b.ACT.011.010 Loolu am ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas lépp, jëme asamaan.
11:11b.ACT.011.011 «Ca saa sa ñetti góor, ña ñu yebal ci man, jóge Sesare, agsi ca kër ga ma dal.
11:12b.ACT.011.012 Te Xel mi ne ma: “Àndal ak ñoom, te bu ci werante.” Juróom-benni bokk, yi fi teew, gunge woon nañu ma, ba nu dugg ca kër góor googu.
11:13b.ACT.011.013 Mu nettali nu ne, gis na malaaka, feeñu ko ca këram ne ko: “Yónneel ca dëkku Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.
11:14b.ACT.011.014 Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
11:15b.ACT.011.015 «Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom, ni mu wàcce woon ci nun bu jëkk.
11:16b.ACT.011.016 Bi loolu amee ma fàttaliku li Boroom bi wax ne: “Yaxya ci ndox la daan sóobe, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi.”
11:17b.ACT.011.017 Gannaaw nag Yàlla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu gëmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi àtteb Yàlla?»
11:18b.ACT.011.018 Bi ñu déggee loolu, amuñu dara lu ñu ca teg, ñu daldi màggal Yàlla ne: «Yàlla nag may na ñi dul Yawut it ñu tuub seeni bàkkaar, ba am dund gu wóor gi.»
11:19b.ACT.011.019 Ñi tasoon nag ndax fitna, ji amoon gannaaw Ecen, ñu dem ba diiwaanu Fenisi, ci dunu Sipar ak ca dëkku Ancos, di wax kàddu gi, waaye yemale ko ci Yawut yi.
11:20b.ACT.011.020 Moona amoon na ci ñoom ay niti Sipar ak dëkku Siren, ñu ñëw ci Ancos, ba seen wax law ci Gereg yi it, ñu di leen xamal xebaar bu baax bu Yeesu Boroom bi.
11:21b.ACT.011.021 Te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, ba mbooloo mu mag gëm te woññiku ci Boroom bi.
11:22b.ACT.011.022 Ba mbir ma siiwee, ba àgg ci noppi mbooloom ñi gëm ci Yerusalem, ñu yebal Barnabas ba Ancos.
11:23b.ACT.011.023 Bi mu agsee nag, ba gis yiw, wi leen Yàlla may, mu bég ci te di leen xiir, ñu wàkkirlu ci Boroom bi te dogu ci.
11:24b.ACT.011.024 Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi.
11:25b.ACT.011.025 Gannaaw loolu Barnabas dem ca dëkku Tars, di wut Sool.
11:26b.ACT.011.026 Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist.
11:27b.ACT.011.027 Ca fan yooyu ay yonent jóge Yerusalem, ñëw Ancos.
11:28b.ACT.011.028 Kenn ci ñoom tudd Agabus jóg, mu yégle jaarale ko ci Xelu Yàlla mi ne, xiif bu metti dina daj àddina sépp. Loolu nag amoon na ca ayug buur bu ñuy wax Këlódd.
11:29b.ACT.011.029 Kon taalibe ya fas yéenee sàkk ndimbal, jëme ca bokk ya dëkk diiwaanu Yude, ku nekk ak sa kem-kàttan.
11:30b.ACT.011.030 Noonu lañu def nag, teg ko ci loxoy Barnabas ak Sool, yónnee ko njiit ya.
12
12:1b.ACT.012.001 Ca jamono jooja Erodd buur ba jàppoon na ay nit ci mbooloom ñi gëm, ngir fitnaal leen.
12:2b.ACT.012.002 Noonu mu daldi jàpp Saag, doomu ndeyu Yowaana, mu reylu ko ci jaasi.
12:3b.ACT.012.003 Bi mu gisee nag ne, mbir moomu neex na Yawut ya, mu daldi jàpp it Piyeer; fekk loolu daje ak bési màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir.
12:4b.ACT.012.004 Bi mu ko jàppee, mu tëj ko kaso, teg ko ci loxoy ñeenti mboolooy xarekat, ngir ñu wottu ko, fekk mbooloo mu ci nekk di ñeenti nit; amoon na yéeney yóbbu ko ci kanamu Yawut ya gannaaw màggalu bésu Jéggi ba.
12:5b.ACT.012.005 Noonu ñuy wottu Piyeer ca kaso ba, waaye mbooloom ñi gëm di ko ñaanal Yàlla ak seen xol bépp.
12:6b.ACT.012.006 Bi Erodd nekkee ci tànki indilu ko, ca guddi googa yeewoon nañu Piyeer ak ñaari càllala, muy nelaw diggante ñaari xarekat, te ay xarekat di wottu buntu kaso ba.
12:7b.ACT.012.007 Ca saa sa malaakam Boroom bi ñëw, te leer ne ràyy ca néeg ba. Malaaka ma dóor Piyeer ci wetam, yee ko ne ko: «Jógal bu gaaw!» Noonu jéng ya rot ciy loxoom.
12:8b.ACT.012.008 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def ko. Malaaka ma ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
12:9b.ACT.012.009 Piyeer génn, topp ca malaaka ma, fekk gëmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne peeñu la.
12:10b.ACT.012.010 Noonu ñu weesu wottukat bu jëkk ba ak ba ca tegu, ñu agsi ca buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. Ñu génn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko bàyyi.
12:11b.ACT.012.011 Bi xelam dellusee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.»
12:12b.ACT.012.012 Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem kër Maryaama, ndeyu Yowaana, mi ñuy wooye Màrk, fekk ñu bare booloo fa, di ñaan ci Yàlla.
12:13b.ACT.012.013 Noonu Piyeer fëgg buntu kër ga, te mbindaan mu tudd Rodd wuyusi ko.
12:14b.ACT.012.014 Mu xàmmi baatu Piyeer, bég ci, ba fàtte koo ubbil, waaye mu daw ci biir, xamle ne Piyeer a nga ca bunt ba.
12:15b.ACT.012.015 Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof.» Waaye mu dëgër ci li mu wax. Noonu ñu ne ko: «Xanaa malaakaam la.»
12:16b.ACT.012.016 Fekk Piyeer di gën a fëgg. Noonu ñu tijji, gis ko, daldi waaru.
12:17b.ACT.012.017 Piyeer taf loxoom ci gémmiñam, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee ca kaso ba. Mu ne leen: «Tee ngeen jottali ko Saag ak bokk ya.» Bi mu ko waxee, mu jóge fa, dem feneen.
12:18b.ACT.012.018 Bi bët setee nag, yengu-yengu bu réy am na ca xarekat ya, ñu ne: «Ana Piyeer?»
12:19b.ACT.012.019 Noonu Erodd wutlu ko, waaye gisu ko. Kon mu àtte wottukat ya, joxe ndigalu rey leen. Bi loolu amee Erodd jóge ci diiwaanu Yude, dem dëkku Sesare, toog fa.
12:20b.ACT.012.020 Fekk mu nekk ci xëccoo bu tàng ak waa dëkki Tir ak Sidon. Naka noona ñu ànd, bëgg koo gis. Ñu neexal Balastus, bëkk-néegu buur ba, di ñaan jàmm, ndaxte réewu buur ba moo doon dundal seen bos.
12:21b.ACT.012.021 Ca bés ba ñu jàpp nag Erodd sol mbubbi buuram, toog ca jal ba ca àttekaay ba, di leen yedd ak a dénk.
12:22b.ACT.012.022 Noonu mbooloo mi di yuuxu naan: «Lii baatu Yàlla la, du baatu nit!»
12:23b.ACT.012.023 Ca saa sa nag, gannaaw màggalul Yàlla, malaakam Boroom bi fàdd ko te ay sax dugg ko, ba mu dee.
12:24b.ACT.012.024 Moona kàddug Boroom bi di gën a màgg tey law.
12:25b.ACT.012.025 Naka Barnabas ak Sool, bi ñu matalee seen liggéey, ñu jóge Yerusalem, ñibbi, ànd ak Yowaana mi tudd Màrk.
13
13:1b.ACT.013.001 Amoon na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk dëkku Ancos, ay yonent ak ay jàngalekat: maanaam Barnabas, Simeyon ku ñu dàkkentale Niseer, Lusiyus mi dëkk Siren, Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom diiwaan ba, ak Sool.
13:2b.ACT.013.002 Am bés nag, bi ñuy jaamu Boroom bi ak di woor, Xel mu Sell mi ne: «Beral-leen ma Barnabas ak Sool ngir liggéey, bi ma leen wooye.»
13:3b.ACT.013.003 Bi ñu ko déggee, ñu daldi woor ak a ñaan, teg leen ay loxo, ba noppi bàyyi leen ñu dem.
13:4b.ACT.013.004 Noonu Xel mu Sell mi yónni leen. Ñu dem nag ci dëkku Selusi, dugg fa gaal, jëm ci dun bu ñuy wax Sipar.
13:5b.ACT.013.005 Bi ñu teeree ca dëkku Salamin nag, ñu yégle fa kàddug Yàlla ca jàngub Yawut ya. Ku tudd Yowaana ànd ak ñoom, di leen jàpple ci liggéey bi.
13:6b.ACT.013.006 Noonu ñu jaar ci dun bépp, ba egg dëkku Pafos. Foofa ñu gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent.
13:7b.ACT.013.007 Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool, ngir bëgg a dégg kàddug Yàlla.
13:8b.ACT.013.008 Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi --ndaxte loolu la turam di tekki — di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm.
13:9b.ACT.013.009 Ci kaw loolu Sool, mi tudd it Pool, daldi fees ak Xel mu Sell mi; mu xool ko jàkk,
13:10b.ACT.013.010 ne ko: «Yaw mi fees ak fen ak lu bon, di doomu Ibliis, tey noonu lépp lu jub, ndax doo bàyyee dëngal yoon yu jub yu Boroom bi?
13:11b.ACT.013.011 Léegi loxob Boroom bi dina dal sa kaw, te dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa nag ay bëtam muuru, mu daldi tàbbi cig lëndëm, muy làmbatu, di wut ku ko wommat.
13:12b.ACT.013.012 Ba boroom réew ma gisee li xew nag, mu daldi gëm, di yéemu ci yoonu Boroom bi.
13:13b.ACT.013.013 Naka noona Pool ak ñi mu àndal jóge Pafos, jaar ci géej, jëm dëkku Peers ci réewu Pamfili. Yowaana nag tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.
13:14b.ACT.013.014 Waaye ñoom ñu jóge Peers, aw ca yoon wa, ba ñëw dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. Bésu noflaay ba nag ñu dugg ca jàngu ba, toog.
13:15b.ACT.013.015 Bi ñu jàngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti jàngu ba yónnee ca ñoom ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di dénk mbooloo mi, waxleen ko.»
13:16b.ACT.013.016 Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen!
13:17b.ACT.013.017 Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom.
13:18b.ACT.013.018 Diirub ñeent-fukki at mu di leen muñal ca màndiŋ ma.
13:19b.ACT.013.019 Gannaaw loolu faagal na juróom-ñaari xeet ci réewu Kanaan, ba sunuy maam donn réew ma.
13:20b.ACT.013.020 Loolu lépp xew na ci diirub ñeenti téeméeri at ak juróom-fukk. «Gannaaw loolu mu jox leen ay àttekat, ba ci yonent Yàlla Samwil.
13:21b.ACT.013.021 Booba ñuy ñaan buur, te Yàlla jox leen Sóol, doomu Kis ci giiru Ben-yamin, muy seen buur diirub ñeent-fukki at. Gannaaw ga mu jële ko fa,
13:22b.ACT.013.022 dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: “Gis naa Daawuda, doomu Yese, ku ma neex ci sama xol, te dina def lépp luy sama coobare.”
13:23b.ACT.013.023 «Noonu ci askanam Yàlla indil na bànni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon.
13:24b.ACT.013.024 Laata muy ñëw nag, Yaxya daan na waare, ne bànni Israyil gépp, ñu tuub seeni bàkkaar, te mu sóob leen ci ndox.
13:25b.ACT.013.025 Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: “Ku ngeen may teg? Duma Ki war a ñëw; waaye am na kuy ñëw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay dàllam.”
13:26b.ACT.013.026 «Bokk yi, yéen askanu Ibraayma ak yéen ñi ragal Yàlla, kàddug mucc gi ci nun la wàcc.
13:27b.ACT.013.027 Waa Yerusalem ak seeni kilifa xàmmiwuñu woon Yeesu te xamuñu woon waxu yonent, yi ñuy jàng bésu noflaay bu nekk; teewul ñu amal waxu yonent yi, ci li ñu àtte Yeesu, ba daan ko.
13:28b.ACT.013.028 Yoon dabu ko fenn, moona ñaan nañu Pilaat, mu reylu ko.
13:29b.ACT.013.029 Noonu ñu def lépp lu yonent yi bindoon ci mbiram, ba noppi ñu wàcce ko ca bant ba, tàbbal ko ci bàmmeel.
13:30b.ACT.013.030 Waaye Yàlla dekkal na ko,
13:31b.ACT.013.031 te diirub ay fan yu bare feeñu na ñi àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem; léegi nag ñooy ay seedeem ci wetu xeet wi,
13:32b.ACT.013.032 te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, li Yàlla digoon sunuy maam,
13:33b.ACT.013.033 def na ko ngir nun seeni sët, ci li mu dekkal Yeesu. Moom lañu bindoon ci ñaareelu saaru Sabóor ne:“Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.”
13:34b.ACT.013.034 Te it li ko Yàlla dekkal, ba mu bañatee jaar ci dee, te suuf du ko lekk mukk, moom la Yàlla wax ne:“Dinaa la may barke yu sell te wóor,yi ma digoon Daawuda.”
13:35b.ACT.013.035 Moo tax mu waxaat feneen ne:“Doo bàyyi sa Waa ju sell, mu yàqu.”
13:36b.ACT.013.036 Ndaxte bi Daawuda defee coobareg Yàlla ci jamonoom, mu faatu, ñu suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko.
13:37b.ACT.013.037 Waaye Ki Yàlla dekkal, yaramam seeyul.
13:38b.ACT.013.038 «Kon nag bokk yi, nangeen xam ne, ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woon a àttee nit ni ku jub,
13:39b.ACT.013.039 fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm.
13:40b.ACT.013.040 Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leen a dal, ci li ñu ne:
13:41b.ACT.013.041 “Yéen ñiy xeebaate, gis leen lii,ngeen yéemu ba far;ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf,joo xam ne su ngeen ko déggee sax,dungeen ko gëm.”»
13:42b.ACT.013.042 Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésu noflaay ba ca tegu.
13:43b.ACT.013.043 Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla.
13:44b.ACT.013.044 Noonu bésu noflaay ba ca tegu, daanaka waa dëkk bépp daje, ngir déglu kàddug Yàlla.
13:45b.ACT.013.045 Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, ñu daldi fees ak kiñaan, di weddi li Pool di wax te di ko xas.
13:46b.ACT.013.046 Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu war a jëkk a yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne, yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi woññiku ci ñi dul Yawut.
13:47b.ACT.013.047 Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan:“Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut,ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”»
13:48b.ACT.013.048 Ñi dul Yawut nag, bi ñu déggee loolu, daldi bég tey màggal kàddug Boroom bi; te ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex daldi gëm.
13:49b.ACT.013.049 Noonu kàddug Boroom bi di law ci diiwaan bépp.
13:50b.ACT.013.050 Waaye Yawut ya xiir ay jigéen, ñi woomle te farlu ci diine, ñoom ak magi dëkk ba, ñu fitnaal Pool ak Barnabas, ngir génne leen réew ma.
13:51b.ACT.013.051 Waaye Pool ak Barnabas daldi yëlëb seen pëndu tànk, ngir dëggal seen weddi, jëm dëkku Ikoñum.
13:52b.ACT.013.052 Naka taalibe yi nag, ñu fees ak mbég ak Xel mu Sell mi.
14
14:1b.ACT.014.001 Bi Pool ak Barnabas nekkee Ikoñum nag, ñu dugg ci jàngub Yawut ya, ni ñu ko daan defe; ñuy waare, ba mbooloom Yawut ak Gereg mu bare gëm.
14:2b.ACT.014.002 Waaye Yawut yu nanguwul yi ñoo jógloo ñi dul Yawut, di ñaawal seen njort ci bokki taalibe yi.
14:3b.ACT.014.003 Pool ak Barnabas nag sax nañu ci Ikoñum lu yàgg, ñu wéeru ci Boroom bi, bay wax ak fit wu dëgër; te Yàlla dëggal kàddug yiwam, ba may leen, ñu def ay kéemaan ak ay firnde.
14:4b.ACT.014.004 Noonu waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.
14:5b.ACT.014.005 Waaye ñi dul Yawut ak Yawut yi, ñoom ak seeni kilifa, lal pexem fitnaal leen ci sànni ay doj.
14:6b.ACT.014.006 Bi ko Pool ak Barnabas yégee nag, ñu daw ca diiwaanu Likawni ca dëkk ya ñuy wax Listar ak Derbë ak wàllaa ya.
14:7b.ACT.014.007 Foofa ñu di fa xamle xebaar bu baax bi.
14:8b.ACT.014.008 Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay tànkam làggi, ndax li mu judduwaale lafañ te musul a dox.
14:9b.ACT.014.009 Moom nag muy déglu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko jàkk, gis ne, am na ngëm ngir wér.
14:10b.ACT.014.010 Mu ne ko ak baat bu dëgër: «Jógal taxaw bu jub.» Noonu nit ki ne bërét, jóg, daldi dox.
14:11b.ACT.014.011 Bi mbooloo ma gisee li Pool def, ñu daldi yuuxu, ne ci làkku waa Likawni: «Yàlla yi soppiku nañu nit, wàcc ci nun.»
14:12b.ACT.014.012 Noonu ñu tudde Barnabas, Sës, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji.
14:13b.ACT.014.013 Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Saraxalekat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala.
14:14b.ACT.014.014 Waaye bi ko ndaw yi Barnabas ak Sool déggee, ñu sib ko ba xotti seeni yére, ñu daldi daw, tàbbi ca mbooloo ma, di wax ci kaw ne:
14:15b.ACT.014.015 «Yéen nit ñi, lu leen xiir ci lii? Nun it ay nit lanu, ñu bokk bind ak yéen. Te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, ngeen dëddu yëfi neen yii te woññiku ci Yàlla miy dund te sàkk asamaan, suuf, géej ak li ñu ëmb lépp.
14:16b.ACT.014.016 Démb mayoon na xeet yépp, ñu aw seen yoonu bopp.
14:17b.ACT.014.017 Moona noppiwul a firndeel aw meloom ci def lu baax, di leen wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég.»
14:18b.ACT.014.018 Noonu ci lu jafe yey nañu mbooloo ma ak wax jooju, ba tere leen, ñu rendil leen sarax.
14:19b.ACT.014.019 Waaye bi loolu wéyee amoon na ay Yawut yu jóge Ancos ak Ikoñum, ñu fàbbi mbooloo ma, sànni Pool ay doj, ba yaakaar ne dee na, ñu diri ko ba ca gannaaw dëkk ba.
14:20b.ACT.014.020 Waaye taalibe ya ñëw wër ko, mu daldi jóg, duggaat ca dëkk ba. Ca suba sa nag, mu ànd ak Barnabas, dem Derbë.
14:21b.ACT.014.021 Bi ñu fa àggee nag, ñu xamle fa xebaar bu baax bi, ba sàkk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu ñu dellusi Listar, Ikoñum ak Ancos,
14:22b.ACT.014.022 di dooleel xeli taalibe ya, xiir leen ñu sax ci yoon wi; ñu ne leen: «Ci kaw nattu yu bare lanu war a dugge ci nguuru Yàlla.»
14:23b.ACT.014.023 Ci mbooloom ñi gëm mu nekk nag, ñu tànn ci ay njiit; ba noppi ñu ñaan Yàlla ak di woor, dénk leen Boroom bi ñu gëm.
14:24b.ACT.014.024 Gannaaw loolu ñu jaar diiwaanu Pisidi, dikk ci Pamfili.
14:25b.ACT.014.025 Ñu yégle kàddu gi ci dëkku Peers, door a dem dëkku Atali.
14:26b.ACT.014.026 Foofa nag ñu dugg gaal, jëm Ancos, fa ñu leen dénke woon ca yiwu Yàlla, ngir liggéey bi ñu àggale.
14:27b.ACT.014.027 Bi ñu agsee, ñu woo mbooloom ñi gëm, nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp, ak ni mu ubbee buntu ngëm ci ñi dul Yawut.
14:28b.ACT.014.028 Noonu ñu toog ak taalibe ya diir bu yàgg.
15
15:1b.ACT.015.001 Amoon na bés ay nit jóge diiwaanu Yude, ñuy jàngal bokk yi ne leen: «Ku xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, doo man a mucc.»
15:2b.ACT.015.002 Pool ak Barnabas nag am ak ñoom diisoo ak werante wu metti; noonu bokk yi jàpp ne, Pool ak Barnabas ak ñeneen ci ñoom war nañoo dem Yerusalem ca ndaw ya ak njiit ya, ngir leeral werante wi.
15:3b.ACT.015.003 Kon nag mbooloo mi gunge leen, ñu jaar ci wàlli Fenisi ak Samari, di nettali ni ñi dul Yawut woññikoo ci Yàlla, ba bokk yépp am ca mbég mu réy.
15:4b.ACT.015.004 Te bi ñu agsee Yerusalem, mbooloom ñi gëm, ndaw yi ak njiit yi teeru leen, ñu nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp.
15:5b.ACT.015.005 Ci kaw loolu ñeneen, ñi gëm waaye bokk ci tariixab Farisen ya, daldi jóg ne: «Fàww ñi dul Yawut xaraf, te ñu dénk leen sàmm yoonu Musaa.»
15:6b.ACT.015.006 Noonu ndaw yi ak njiit yi dajaloo, ngir seet mbir moomu.
15:7b.ACT.015.007 Gannaaw werante wu bare Piyeer jóg ne leen: «Yéen bokk yi, xam ngeen ne, ca njàlbéen ga Yàlla tànnoon na ma ci yéen, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi, ba ñu gëm.
15:8b.ACT.015.008 Te Yàlla, mi xam xol yi, seede na leen ci li mu leen may Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye nun itam.
15:9b.ACT.015.009 Gënalantewu nu ak ñoom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ngëm.
15:10b.ACT.015.010 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, ciy teg taalibe yi yen bu nu musul a àttan, nun mbaa sunuy maam?
15:11b.ACT.015.011 Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaar a mucce, te ñoom itam, ci lañu wékku.»
15:12b.ACT.015.012 Bi mu ko waxee, mbooloo mépp ne xeram, di déglu Barnabas ak Pool, ñuy nettali kéemaan ak firnde yépp, yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut.
15:13b.ACT.015.013 Bi ñu noppee, Saag jël kàddu ga ne:
15:14b.ACT.015.014 «Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam.
15:15b.ACT.015.015 Te loolu sax dëppoo na ak li yonent yi tëral; ñu bind ne:
15:16b.ACT.015.016 “Boroom bi nee na:Gannaaw loolu dinaa dellusi,te yékkati këru Daawuda, gi ne tasar,dinaa defar toj-toj ya,ba taxawalaat ko.
15:17b.ACT.015.017 Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi,maanaam xeet yi dul Yawut, ñuy tudd sama tur.
15:18b.ACT.015.018 Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax,te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.”
15:19b.ACT.015.019 «Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te woññiku ci Yàlla.
15:20b.ACT.015.020 Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja.
15:21b.ACT.015.021 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésu noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.»
15:22b.ACT.015.022 Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñuy dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.
15:23b.ACT.015.023 Ñu jox leen bataaxal bu ne: Yéen sunu bokk yi dul Yawut te dëkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi.
15:24b.ACT.015.024 Dégg nanu ne, am na ay nit ñu bawoo ci nun, ñu di leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seeni xol, te fekk sukkandikuwuñu ci lenn ndigal lu jóge ci nun.
15:25b.ACT.015.025 Kon nag mànkoo nanu ci tànn ay nit, yónnee leen ko, ànd ak sunuy soppe Barnabas ak Pool.
15:26b.ACT.015.026 Ñoom jaay nañu seen bakkan ngir turu Yeesu Kirist Boroom bi.
15:27b.ACT.015.027 Yónni nanu nag Yudd ak Silas, ñu di leen xamal xebaar boobu ci seen gémmiñ.
15:28b.ACT.015.028 Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leen a teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ,
15:29b.ACT.015.029 maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo yëf yooyu, dingeen def lu baax. Ci jàmm.
15:30b.ACT.015.030 Noonu ñu tàggoo, dem Ancos, ñu dajale mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
15:31b.ACT.015.031 Ñu jàng ko nag, seen xol sedd ci doole, ji leen bataaxal bi indil.
15:32b.ACT.015.032 Te Yudd ak Silas, ñi doon yonent, ñuy dooleel bokk yi, di dëgëral seen fit ak wax yu bare.
15:33b.ACT.015.033 Bi loolu amee ñu toog fa ab diir, ba noppi bokk yi yiwi leen ci jàmm, ñu dellu ca ña leen yónni woon.
15:35b.ACT.015.035 Waaye Pool ak Barnabas des ci Ancos, di jàngale ak di xamle xebaar bu baax bu kàddug Boroom bi, ñoom ak ñeneen ñu bare.
15:36b.ACT.015.036 Gannaaw ay fan Pool ne Barnabas: «Nan dellu seeti bokk ya ca dëkk yépp, fu nu mas a yéglee kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.»
15:37b.ACT.015.037 Barnabas nag bëggoon na yóbbaale Yowaana, mi ñuy wax it Màrk.
15:38b.ACT.015.038 Waaye Pool dafa lànk ne: «Matul nu yóbbu ki nu waccoon ca Pamfili, ba àndul woon ak nun ca liggéey ba.»
15:39b.ACT.015.039 Noonu ñu xuloo, ba far tàggoo. Barnabas yóbbaale Màrk, ñu dugg gaal, jëm Sipar.
15:40b.ACT.015.040 Pool tànn Silas, dem; bokk ya dénk leen ci yiwu Boroom bi;
15:41b.ACT.015.041 mu jaar ci diiwaanu Siri ak Silisi, di dëgëral mboolooy ñi gëm.
16
16:1b.ACT.016.001 Naka noona mu dikk dëkki Derbë ak Listar, fekk fa taalibe bu tudd Timote te ndeyam di Yawut bu gëm, waaye baayam di Gereg.
16:2b.ACT.016.002 Te mbokk, yi nekk dëkki Listar ak Ikoñum, seedeel nañu ko lu baax.
16:3b.ACT.016.003 Pool bëgg nag mu ànd ak moom, waaye ndegam Yawut yépp, ya dëkk ca wàllaa ya, xam ne baayam Gereg la woon, mu jël ko, xarafal ko.
16:4b.ACT.016.004 Bi loolu amee ñuy jaar ca dëkk ya, jottali leen dénkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen ñu sàmm ko.
16:5b.ACT.016.005 Noonu mboolooy ñi gëm di gën a dëgër ci yoon wi, tey yokku bés bu nekk.
16:6b.ACT.016.006 Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, ñu yégleji kàddu gi ci diiwaanu Asi, ñu daldi jaari wàlli Firisi ak Galasi.
16:7b.ACT.016.007 Bi ñu agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, ñuy jéem a dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayuleen ko.
16:8b.ACT.016.008 Ñu romb nag Misi, dem dëkku Torowas.
16:9b.ACT.016.009 Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!»
16:10b.ACT.016.010 Bi mu amee peeñu moomu, ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xebaar bu baax bi.
16:11b.ACT.016.011 Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, jóge fa ca ëllëg sa, nu jëm teerub Neyapolis.
16:12b.ACT.016.012 Bi nu fa teeree, nu jëm Filib, bi nekk dëkk bi ëpp maana ca wàll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it suufus Room. Nu toog fa ay fan.
16:13b.ACT.016.013 Bi bésu noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo.
16:14b.ACT.016.014 Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax.
16:15b.ACT.016.015 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir.
16:16b.ACT.016.016 Am bés, ba nuy dem nag ca ñaanukaay ba, nu daje ak jaam bu jigéen bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jariñu lu bare ci gisaaneem.
16:17b.ACT.016.017 Mu daldi topp ci Pool ak nun, di xaacu ne: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; ñoo leen di yégal yoonu mucc.»
16:18b.ACT.016.018 Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu woññiku ne rab wa: «Sant naa la ci turu Yeesu Kirist, génnal ci moom.» Noonu rab wa ne mëll, génn ci moom.
16:19b.ACT.016.019 Bi ay sangam gisee nag seen buntu wërsëg tëju, ñu daldi jàpp Pool ak Silas, di leen diri, jëme leen ca pénc ma fa kanam njiit ya.
16:20b.ACT.016.020 Noonu ñu dëj leen fa mbaxanay menne naan: «Yawut yii lëjal nañu sunu dëkk,
16:21b.ACT.016.021 di xamle ay aada yu nu sañul a nangu mbaa nu di ko topp, nun ñi bokk ci nguuru Room.»
16:22b.ACT.016.022 Mbooloo ma it ànd ci, dal ci seen kaw; àttekat ya nag summilu seeni yére, santaane ñu dóor leen ay yar.
16:23b.ACT.016.023 Noonu ñu dóor leen ay yar yu bare, tëj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu wér.
16:24b.ACT.016.024 Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu sànni leen ca néeg ba gën a ruqu ci biir kaso ba, jéng seeni tànk.
16:25b.ACT.016.025 Ba guddi giy xaaj nag, Pool ak Silas di ñaan ak di sant Yàlla, te ñeneen ñi nekk ca kaso ba di leen déglu.
16:26b.ACT.016.026 Ca saa sa suuf yengu bu metti, ba fondamaab kaso ba daanu; bunt yépp daldi ne kulbet ubbiku, te jéngi ña ñu tëj ne tell tijjiku.
16:27b.ACT.016.027 Ci kaw loolu boroom kaso ba tiite ci ay nelaw, gis bunt yépp ubbiku, mu daldi bocci jaaseem, bëgg a xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo daw.
16:28b.ACT.016.028 Waaye Pool wax ci kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp nu ngi fi.»
16:29b.ACT.016.029 Bi ko boroom kaso ba déggee, mu daldi laaj làmp, ne saraax dugg, daanu ci kanamu Pool ak Silas, di lox.
16:30b.ACT.016.030 Mu génne leen ci biti ne leen: «Kilifa yi, lu ma war a def, ba mucc?»
16:31b.ACT.016.031 Ñu tontu ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.»
16:32b.ACT.016.032 Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp.
16:33b.ACT.016.033 Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp.
16:34b.ACT.016.034 Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp.
16:35b.ACT.016.035 Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.»
16:36b.ACT.016.036 Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen, te dem ci jàmm.»
16:37b.ACT.016.037 Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanamu ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgg a sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»
16:38b.ACT.016.038 Bi mu ko waxee, alkaati ya yégal àttekat ya la mu wax. Bi ñu déggee ne, jaamburi Room lañu, ñu daldi tiit.
16:39b.ACT.016.039 Ñu ñëw nag di leen dëfël, ñu gunge leen ci biti, di leen ñaan, ñu génn dëkk ba.
16:40b.ACT.016.040 Noonu ñu génn ca kaso ba, dugg ci kër Lidi, ñu gis fa bokk ya, dëgëral leen, daldi dem seen yoon.
17
17:1b.ACT.017.001 Bi ñu fa jógee, ñu aw yoon wa jaar dëkku Amfipolis ak Apoloni, door a ñëw Tesalonig, fa Yawut ya am jàngu.
17:2b.ACT.017.002 Pool nag dugg ca ñoom, na mu ko daan defe, ba am fa ñetti bésu noflaay, muy werante ak ñoom ci li Mbind mi wax.
17:3b.ACT.017.003 Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne, fàww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: «Yeesu, mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.»
17:4b.ACT.017.004 Noonu ñenn ci Yawut yi gëm, ànd ak Pool ak Silas, ñoom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Yàlla, ak jigéen ñu am maana ñu bare.
17:5b.ACT.017.005 Waaye kiñaan tàbbi ca Yawut ya, ñu daldi jël ay taxawaalukat ca pénc ma, dajale mbooloo, ñuy yengal dëkk ba. Ñu daanu ci kër Yason, di wut Pool ak Silas, ngir dëj leen ci kanam waa dëkk ba.
17:6b.ACT.017.006 Bi ñu leen gisul nag, ñu diri Yason ak ñeneen ca bokk ya ci kanam àttekat ya. Ñuy wax ci kaw naan: «Nit ñi dëpp àddina sépp agsi nañu fii léegi,
17:7b.ACT.017.007 te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp dañoo bañ ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
17:8b.ACT.017.008 Bi ko mbooloo mi ak àttekat yi déggee, ñu daldi jaaxle lool.
17:9b.ACT.017.009 Noonu nanguwuñoo yiwi Yason ak ñi ci des, lu dul bi ñu leen bataleelee dara.
17:10b.ACT.017.010 Bi loolu amee bokk yi jàllale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, ñu jëm Bere. Ba ñu fa eggee nag, ñu dugg ca jàngub Yawut ya.
17:11b.ACT.017.011 Fekk ña fa nekk ñoo gën a am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet.
17:12b.ACT.017.012 Kon nag Yawut yu bare gëm ak ñu bare ci Gereg yi, di jigéen yu am maana ak ay góor.
17:13b.ACT.017.013 Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne, Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma.
17:14b.ACT.017.014 Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa.
17:15b.ACT.017.015 Ñi ànd ak Pool nag gunge ko ba dëkku Aten. Bi ñu fa àggee, ñu woññiku, yóbbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote ñëw fekksi ko ci lu gën a gaaw.
17:16b.ACT.017.016 Bi leen Pool di nég ca Aten, mu am naqaru xol wu réy ci li mu gis dëkk ba fees ak ay nataali bokkaale Yàlla.
17:17b.ACT.017.017 Muy werante nag ca jàngu ba ak Yawut ya ak ña ragal Yàlla, tey werante it bés bu nekk ca pénc ma ak ña fay dajaloo.
17:18b.ACT.017.018 Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgg a wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xebaar bu baax bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni, day waare ay yàlla yu nu xamul.»
17:19b.ACT.017.019 Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle.
17:20b.ACT.017.020 Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoon a xam nag léegi, loolu lu muy tekki.»
17:21b.ACT.017.021 Ndaxte waa Aten ñépp ak doxandéem ya fa dëkk, wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xënte.
17:22b.ACT.017.022 Noonu Pool taxaw ci biir mbooloom Areyopas ne leen: «Yéen waa Aten gis naa ne, farlu ngeen ci diine lool.
17:23b.ACT.017.023 Ndaxte bi may doxantu di seet seeni màggalukaay, gis naa ci benn bu ñu bind lii: “Yàlla mi nu xamul.” Li ngeen di màggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal.
17:24b.ACT.017.024 «Yàlla mi sàkk àddina ak li mu ëmb lépp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du dëkk ci néegi màggalukaay yu loxoy nit defar.
17:25b.ACT.017.025 Du jariñu it ci loxoy nit, mel ni dafa soxla dara, ndax moom mooy jox ñépp bakkan ak ruu ak lépp.
17:26b.ACT.017.026 Ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xebla yi; fekk àppal na xeet wu nekk jamonoom, te rëdd seen diggi réew.
17:27b.ACT.017.027 Yàlla def na loolu, ngir ñu koy wut ci yaakaaru daj ko ci làmbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun.
17:28b.ACT.017.028 “Ndaxte ci moom lanuy dunde, di ci jëf te nekk ci,” ni ko ñenn ci seeni taalifkat dëggale naan: “Nun noo di aw xeetam.”
17:29b.ACT.017.029 Kon nag, bu nu nekkee xeetu Yàlla, warunoo gëm ne, Yàlla mel na ni nataali wurus, xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel.
17:30b.ACT.017.030 Ca jamono yu wees ya Yàlla toppul ñàkka xam googa, waaye léegi koo man a doon ak foo man a nekk, Yàlla santaane na, nga tuub say bàkkaar.
17:31b.ACT.017.031 Ndaxte sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn; te firndeel na loolu bu wóor, ci li mu ko dekkal ca néew ya.»
17:32b.ACT.017.032 Bi ñu déggee nag, muy wax ci mbirum ndekkitel ñi dee, ñii di ko fontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu ci mbir moomu beneen yoon.»
17:33b.ACT.017.033 Noonu Pool génn ci seen biir.
17:34b.ACT.017.034 Moona am na ñenn ñu taq ci moom te gëm: xàmmees na ci Denis, ku bokk ci mbooloom Areyopas, ak jigéen ju tudd Damaris, ak ñeneen.
18
18:1b.ACT.018.001 Bi loolu wéyee Pool bàyyikoo Aten, dem Korent.
18:2b.ACT.018.002 Mu tase fa ak Yawut bu tudd Akilas te juddoo diiwaanu Pont. Muy sog a jóge réewu Itali ak jabaram Pirsil, ndaxte buur ba Këlódd sant na Yawut yépp, ñu génn Room.
18:3b.ACT.018.003 Noonu Pool seeti leen, te gannaaw ñoo bokk liggéey, maanaam di defar ay tànt, mu dal fa ñoom, ñuy liggéeyandoo.
18:4b.ACT.018.004 Bésu noflaay bu nekk nag muy diisoo ak ñi nekk ca jàngu ba, di jéem a gëmloo ay Yawut ak ay Gereg.
18:5b.ACT.018.005 Waaye bi Silas ak Timote jógee diiwaanu Maseduwan, egg fa, Pool jublu ci xamle kàddu gi, tey dëggal ci Yawut yi naan, Yeesu mooy Almasi bi.
18:6b.ACT.018.006 Bi ko Yawut ya gàntoo nag, di ko xas, mu yëlëb ay yéreem ne leen: «Yéena sàkku seen musiba; set naa ci. Léegi maa ngi dem ci ñi dul Yawut.»
18:7b.ACT.018.007 Ci kaw loolu mu jóge fa, dugg ci këru ku tudd Tisiyus Yustus, di ku ragal Yàlla, te kër ga dend ak jàngu ba.
18:8b.ACT.018.008 Kirispus nag, njiitu jàngu ba, gëm na Boroom bi ak waa këram gépp. Te waa Korent ñu bare dégg kàddu gi te gëm ko, ñu sóob leen ci ndox.
18:9b.ACT.018.009 Naka noona Boroom bi feeñu Pool ci guddi ne ko: «Bul tiit dara, waaye deel wax te bañ a noppi.
18:10b.ACT.018.010 Ndaxte maa ngi ànd ak yaw, te kenn du la jàpp, ba fitnaal la, ndaxte am naa xeet wu bare ci dëkk bii.»
18:11b.ACT.018.011 Noonu Pool des at ak genn-wàll ci seen biir, di fa jàngale kàddug Yàlla.
18:12b.ACT.018.012 Ci nguuru Galyon ci diiwaanu Akayi nag, Yawut ya likkoo, ñu dal ci kaw Pool, yóbbu ko ca àttekaay ba.
18:13b.ACT.018.013 Ñu ne: «Kii day xiir nit ñi ci màggal Yàlla ci lu juuyoo ak yoon wi.»
18:14b.ACT.018.014 Bi Pool bëggee wax nag, Galyon ne Yawut ya: «Yéen Yawut yi, bu aju woon ci jàdd yoon walla ñaawteef wu réy, kon liy yoon mooy ma déglu leen.
18:15b.ACT.018.015 Waaye bu ajoo ci ay werante ciy wax ak ay tur ak seen yoon, loolu seen wàll la; man duma ko àtte.»
18:16b.ACT.018.016 Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba.
18:17b.ACT.018.017 Ci kaw loolu nit ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, ñu di ko dóor ca kanamu àttekaay ba, waaye Galyon faalewu leen.
18:18b.ACT.018.018 Bi loolu wéyee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu jógeegul teerub Señsere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Yàlla.
18:19b.ACT.018.019 Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya.
18:20b.ACT.018.020 Ñu ñaan ko, mu des fa lu gën a yàgg, waaye nanguwul.
18:21b.ACT.018.021 Kon mu tàggtoo ak ñoom naan: «Dinaa dellusi ci yéen, bu soobee Yàlla.» Noonu mu dugg gaal, jóge Efes,
18:22b.ACT.018.022 teersi dëkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom ñi gëm, ba noppi dem Ancos.
18:23b.ACT.018.023 Bi mu fa desee ay jamono, mu jóge fa, di jaar dëkkoo-dëkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe yépp.
18:24b.ACT.018.024 Amoon na nag Yawut bu tudd Apolos te juddoo Alegsàndiri, mu dikk Efes. Nit ku yeewu la woon te am xam-xam bu yaatu ci Mbind mi.
18:25b.ACT.018.025 Jàngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a jàngale bu wóor ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan sóobe ci ndox.
18:26b.ACT.018.026 Noonu mu daldi wax ak fit wu dëgër ca jàngu ba. Bi ko Pirsil ak Akilas déggee nag, ñu woo ko fi ñoom, gën ko leeral yoonu Yàlla.
18:27b.ACT.018.027 Naka mu bëgg a dem Akayi, bokk ya xiir ko ca, ñu bind taalibe ya, ngir ñu teeru ko teeru bu rafet. Noonu mu dikk fa te jariñ lool ñi gëm jaare ko ci yiwu Yàlla.
18:28b.ACT.018.028 Ndaxte mu ngay yey Yawut ya ca kanam ñépp, di firi Mbind yi, ba wone ne Yeesu mooy Almasi bi.
19
19:1b.ACT.019.001 Ba Apolos nekkee Korent nag, Pool jaar ca teggi ya gën a kawe ca réew ma, door a dikk Efes. Noonu mu gis fa ay taalibe.
19:2b.ACT.019.002 Mu ne leen: «Ndax jot ngeen ci Xel mu Sell mi, bi ngeen gëmee?» Ñu tontu ko: «Déggunu sax ne, Xel mu Sell mi am na.»
19:3b.ACT.019.003 Mu ne leen: «Kon nag, bi ñu leen sóobee ci ndox, lu ciy maana?» Ñu tontu ko: «Xanaa li Yaxya tëral.»
19:4b.ACT.019.004 Pool ne leen: «Yaxya daan na sóob nit ñi ci ndox, ndax bi ñu tuubee seeni bàkkaar; te mu ne bànni Israyil, kiy topp ci moom lañu war a gëm, maanaam Yeesu.»
19:5b.ACT.019.005 Bi ñu déggee loolu nag, sóob nañu leen ci ndox ci turu Yeesu Boroom bi.
19:6b.ACT.019.006 Te bi leen Pool tegee loxo, Xel mu Sell mi ñëw ci ñoom, ñuy wax yeneeni làkk, di wax ci kàddug Yàlla.
19:7b.ACT.019.007 Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar.
19:8b.ACT.019.008 Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéem a gëmloo.
19:9b.ACT.019.009 Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus.
19:10b.ACT.019.010 Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.
19:11b.ACT.019.011 Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool.
19:12b.ACT.019.012 Ñu yóbbul sax ñi wopp ay kaala ak ay taraxlaay yu laaloon yaramam, ba jàngoro yi di leen bàyyi, rab yay génn ci ñoom.
19:13b.ACT.019.013 Noonu ay Yawut yuy wëndéelu, di faj ñi rab jàpp, ñu di leen jéem a ñaanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: «Ci turu Yeesu, mi Pool di yégle, génnleen.»
19:14b.ACT.019.014 Ñi doon def loolu, juróom-ñaari doom lañu woon ci Sewa, mi doon taafantaloo saraxalekat bu mag ba ci Yawut yi.
19:15b.ACT.019.015 Waaye bi ñu ko defee rab wa tontu leen ne: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?»
19:16b.ACT.019.016 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, noot leen ñoom ñépp; mu soxore leen lool, ba ñu daw kër ga, def yaramu neen te gaañu bu metti.
19:17b.ACT.019.017 Loolu siiw na ci ñépp, ñi dëkk Efes, di Yawut ak Gereg; tiitaange jàpp leen ñoom ñépp, ba ñu màggal turu Yeesu Boroom bi.
19:18b.ACT.019.018 Bi loolu amee ñu bare ci ñi gëm ñëw, di wesar ci kanam ñépp seeni jati luxus.
19:19b.ACT.019.019 Te ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp. Te bi ñu xaymaa njëg ga, mu tollook juróom-fukki junniy poseti daraxma.
19:20b.ACT.019.020 Noonu la kàddu Boroom bi lawe, te noot lépp.
19:21b.ACT.019.021 Bi loolu wéyee Pool nas xel jëm Yerusalem, jaar ci diiwaani Maseduwan ak Akayi. Mu ne: «Gannaaw bu ma fa demee, fàww ma seeti Room it.»
19:22b.ACT.019.022 Mu yebal nag ci Maseduwan ñaari jaraafam, di Timote ak Erast, waaye moom mu des ab diir ci Asi.
19:23b.ACT.019.023 Fekk booba amoon na yengu-yengu bu réy ci lu aju ci Yoon wi.
19:24b.ACT.019.024 Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di tëggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir màggal Artemis, daan na ci jariñu lu bare, moom ak ay nawleem.
19:25b.ACT.019.025 Noonu mu dajale leen ak seeni liggéeykat ne leen: «Gaa ñi, xam ngeen ne, sunu njariñ mu ngi aju ci liggéey bii.
19:26b.ACT.019.026 Gis ngeen nag te dégg ne, Pool male gëmloo na bay fàbbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi gépp naan: “Yàlla yu ay loxo defar duñu ay yàlla.”
19:27b.ACT.019.027 Léegi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xañ nu sunu liggéey rekk, waaye it dina daaneel màggalukaayu Artemis sunu yàlla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi gépp te àddina sépp di màggal.»
19:28b.ACT.019.028 Bi ñu déggee loolu, mer mu réy tàbbi ci ñoom, ñuy yuuxu ne: «Artemis mu Efes màgg na!»
19:29b.ACT.019.029 Noonu dëkk bépp jaxasoo. Ñu bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan, ñi ànd ak Pool.
19:30b.ACT.019.030 Pool nag bëgg a dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko.
19:31b.ACT.019.031 Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu bañ a jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.
19:32b.ACT.019.032 Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gën a bare xamuñu lu waral ndaje ma.
19:33b.ACT.019.033 Ci kaw loolu Yawut ya jéñ Alegsàndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi tàllal loxoom, ngir làyyi ca mbooloo ma.
19:34b.ACT.019.034 Waaye bi ñu xamee ne Yawut la, ñépp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat ñaari waxtu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
19:35b.ACT.019.035 Gannaaw loolu boroom dëkk ba dalal mbooloo ma ne leen: «Yéen waa Efes, ana ku xamul ne, dëkku Efes moo di wottukaayu màggalukaayu Artemis ak nataalam, bi wàcce asamaan?
19:36b.ACT.019.036 Gannaaw nag kenn mënta weddi loolu, war ngeen a dalal seen xel te bañ a sañaxu ci dara.
19:37b.ACT.019.037 Ndaxte nit ñii ngeen fi indi sàccuñu ca màggalukaay ya te sosaluñu sunu yàlla.
19:38b.ACT.019.038 Su fekkee ne Demetirus ak ay nawleem jànkoonte nañu ak kenn, am na ay bési layoo ak ñu yilif réew mi; nañu fa woo ku ñu amleenteel.
19:39b.ACT.019.039 Waaye su ngeen di laaj leneen, mbooloom dëgg dina ko àtte.
19:40b.ACT.019.040 Ndaxte fi mu ne man nañu noo jiiñ jógug mbooloo mi ndax li fi xew tey. Te bu loolu amee dunu am aw lay ci mbirum mbooloo mu rëb mii, ndaxte amul dara lu ko waral.»
19:41b.ACT.019.041 Bi mu waxee loolu nag, mu tas mbooloo ma.
20
20:1b.ACT.020.001 Bi yengu-yengu ba dalee, Pool woo taalibe ya fa moom, dooleel leen. Bi mu ko defee mu tàggoo ak ñoom, jóge fa, dellu diiwaanu Maseduwan.
20:2b.ACT.020.002 Noonu mu jaar ca bérab yooyu, di dooleel nit ñi ak wax yu bare; ba noppi mu dem réewu Geres,
20:3b.ACT.020.003 toog fa ñetti weer. Waaye bi mu nekkee ci kaw tànki dugg gaal jëm diiwaanu Siri, te Yawut yi lalal ko pexe, mu fas yéenee dellu, jaare Maseduwan.
20:4b.ACT.020.004 Booba nag ñii ñoo ànd ak moom: Sopater, doomu Pirus mi dëkk Bere; Aristàrk ak Segond, ñi dëkk Tesalonig; Gayus, mi dëkk Derbë, ak Timote; te it Tisig ak Torofim ñi dëkk Asi.
20:5b.ACT.020.005 Ñooñu nag jiitu, di nu nég dëkku Torowas.
20:6b.ACT.020.006 Waaye naka nun, gannaaw màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, nu dugg gaal ci Filib, def ci juróomi fan, fekksi leen Torowas, nu am fa juróom-ñaari fan.
20:7b.ACT.020.007 Ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, booloo nanu ngir damm mburu ma. Te Pool, mi bëggoon a dem ca ëllëg sa, di diisoo ak ñoom te waxtaanam law ba ci xaaju guddi.
20:8b.ACT.020.008 Ca néeg bu kawe, ba nu booloo nag, amoon na fa làmp yu bare.
20:9b.ACT.020.009 Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palenteer ba, gëmmeentu bay jeyaxu. Bi Pool di gën a yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwweekoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.
20:10b.ACT.020.010 Waaye Pool wàcc, daldi sëgg ci kawam, roof ko loxoom ne leen: «Bàyyileen jooy yi, mu ngi dund.»
20:11b.ACT.020.011 Noonu mu yéegaat, damm mburu ma, lekk; ba noppi delluwaat ci waxtaanam, di ko yaatal ba ca njël, door a tàggoo.
20:12b.ACT.020.012 Naka waxambaane wa, ñu indi ko muy dund, ba seen xol sedd guyy.
20:13b.ACT.020.013 Nun nag nu jiitu, dugg gaal jëm Asos, fa nu Pool santoon, nu jële ko fa; fekk moom fas na yéeney dox, ba agsi fa.
20:14b.ACT.020.014 Noonu mu fekksi nu ci Asos, nu jël ko ca gaal ga, dem Mitilen.
20:15b.ACT.020.015 Gannaaw loolu gaal ga jóge fa, nu agsi ca ëllëg sa janook dunu Kiyos. Bés ba ca tegu nag nu jàll ba Samos, te ñetteelu fan ba nu àgg Mile.
20:16b.ACT.020.016 Ndaxte Pool fasoon na yéenee teggi Efes, ngir bañ a yàgg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir màggal, gi ñuy wax Pàntakot fekk ko Yerusalem.
20:17b.ACT.020.017 Bi Pool eggee Mile nag, mu yónnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom ñi gëm.
20:18b.ACT.020.018 Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey.
20:19b.ACT.020.019 Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rangooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.
20:20b.ACT.020.020 Xam ngeen ne, musuma leen a nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanamu ñépp ak ca kër ya.
20:21b.ACT.020.021 Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba woññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu.
20:22b.ACT.020.022 «Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.
20:23b.ACT.020.023 Xam naa rekk ne, ci dëkkoo-dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne, ay buum ak ay metit ñu ngi may nég.
20:24b.ACT.020.024 Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla.
20:25b.ACT.020.025 «Fi mu ne nag xam naa ne, dootuleen gis sama kanam, yéen ñépp ñi ma jaaroon ci seen biir, di yégle nguuru Yàlla.
20:26b.ACT.020.026 Moo tax may dëggal tey jii ne, wàccoo naa ak yéen ñépp bés pénc.
20:27b.ACT.020.027 Ndaxte ñeebluwuma leen, ci di leen xamal lépp li Yàlla digle.
20:28b.ACT.020.028 Wottuleen nag seen bopp te wottu coggal jépp, ji leen Xel mu Sell mi def sàmm, ngeen sàmm mbooloo, mi Yàlla jotal boppam ak deretu Doomam.
20:29b.ACT.020.029 Xam naa ne, bu ma leen wonee gannaaw, bukki yu soxor dinañu tàbbi ci coggal ji te duñu ci ñeeblu kenn.
20:30b.ACT.020.030 Ay nit dinañu jóg ci seen biir sax, di wax luy sànke, ngir sàkku ay taalibe.
20:31b.ACT.020.031 Foogleen nag, di fàttaliku ne diirub ñetti at, guddi ak bëccëg, musumaa noppi di leen artu kenn ku nekk ci yéen ak ay rangooñ.
20:32b.ACT.020.032 «Léegi nag maa ngi leen di dénk Boroom bi, moom ak kàddug yiwam, gi leen man a dëgëral te may leen cér ci biir gaayi Yàlla yu sell yépp.
20:33b.ACT.020.033 Nammuma xaalisu kenn mbaa wurusam mbaa koddaayam.
20:34b.ACT.020.034 Xam ngeen ne, faj naa samay soxla ak soxlay ñi ànd ak man ci sama loxo yii.
20:35b.ACT.020.035 Ci lépp won naa leen royukaay, ci li nu war a dimbali ñi néew doole te fàttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: “Joxe moo gën a barkeel nangu.”»
20:36b.ACT.020.036 Bi mu waxee loolu, mu sukk ak ñoom ñépp, ñaan ci Yàlla.
20:37b.ACT.020.037 Te ñépp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, fóon ko bu baax.
20:38b.ACT.020.038 Li leen gën a teg aw tiis mooy li mu leen wax: «Dootuleen gis sama kanam.» Noonu ñu gunge ko ba ca gaal ga.
21
21:1b.ACT.021.001 Bi nga xamee ne tàggoo nanu ak ñoom ci naqar, nu dugg gaal, jubal dunu Kos. Te ca ëllëg sa nu dem ba teer ca Rodd, ba noppi jóge fa, jàll ba Patara.
21:2b.ACT.021.002 Foofa nag nu gis gaal guy jàll ba Fenisi, nu dugg ca, mu daldi teddi.
21:3b.ACT.021.003 Noonu nu séen dunu Sipar, bàyyi ko ci sunu càmmooñ, jublu diiwaanu Siri, nu teersi Tir. Ndaxte foofa la gaal gi war a yebbee la mu yeboon.
21:4b.ACT.021.004 Nu wut taalibe ya, ba gis leen, toog ak ñoom juróom-ñaari fan. Ñoom nag ñu ne Pool ci li leen Xelu Yàlla mi may, mu bañ a dem Yerusalem.
21:5b.ACT.021.005 Moona bi jataayu gaal ga matee, nu awaat ci yoon wi. Te ñépp gunge nu, ñoom ak seeni jabar ak seeni doom; nu génn dëkk ba, sukk ca tefes ga, ñaan ci Yàlla.
21:6b.ACT.021.006 Noonu nu tàggoo ak ñoom, dugg ca gaal ga, ñu dellu seen kër.
21:7b.ACT.021.007 Bi nu jógee Tir nag, nu demaat ci géej, ba teer Patolemayis. Foofa nu nuyu bokk ya, yendu, fanaan.
21:8b.ACT.021.008 Nu jóge fa ca ëllëg sa, ñëw ba ca dëkku Sesare. Nu dugg ca kër Filib, taskatu xebaar bu baax bi, mi bokk ci Juróom-ñaar ña, nu dal fa moom.
21:9b.ACT.021.009 Amoon na ñeenti doom yuy janq, ñuy wax ci kàddug Yàlla.
21:10b.ACT.021.010 Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus jóge Yude, agsi.
21:11b.ACT.021.011 Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»
21:12b.ACT.021.012 Bi nu déggee loolu, nun ak ña fa nekk nu ñaan Pool, mu bañ a dem Yerusalem.
21:13b.ACT.021.013 Ci kaw loolu Pool tontu ne: «Lu ngeen di jooy, di yàq sama xol? Bañuma ñu yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, ñu rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.»
21:14b.ACT.021.014 Bi nu ko mënul a dëpp, nu noppi ne: «Kon na coobareg Boroom bi am!»
21:15b.ACT.021.015 Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem.
21:16b.ACT.021.016 Noonu ay taalibe yu dëkk Sesare ànd ak nun, yóbbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu war a dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu yàgg.
21:17b.ACT.021.017 Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mbég.
21:18b.ACT.021.018 Ca ëllëg sa Pool ànd ak nun, seeti Saag, fekk njiit yépp teew fa.
21:19b.ACT.021.019 Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam.
21:20b.ACT.021.020 Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne, am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa.
21:21b.ACT.021.021 Dégg nañu ci sa mbir nag ne, yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te bañ a xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.
21:22b.ACT.021.022 Lu nu ci war a def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne, ñëw nga.
21:23b.ACT.021.023 Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor yu dige ak Yàlla.
21:24b.ACT.021.024 Jël leen, bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateef. Noonu ñépp dinañu xam ne, li ñu déggoon ci sa mbir du dëgg, waaye yaa ngi jëf tey sàmm yoonu Musaa.
21:25b.ACT.021.025 Naka ñi dul Yawut ñi gëm, bind nanu leen li nu àtte ne, ñu moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm te moytu deretu médd ak njaaloo.»
21:26b.ACT.021.026 Bi ñu ko waxee, Pool jël nit ña te ca ëllëg sa mu bokk setlu ak ñoom, ñu dugg ca kër Yàlla ga. Ñu xamle ban bés la seen setlu di àgg, di bés bu ñuy jébbale sarax ngir kenn ku nekk ci ñoom.
21:27b.ACT.021.027 Bi àppu juróom-ñaari fan ya di bëgg a jeex, Yawut yi jóge diiwaanu Asi gis Pool ca kër Yàlla ga. Ñu daldi jógloo mbooloo mépp, jàpp ko,
21:28b.ACT.021.028 di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil; waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.»
21:29b.ACT.021.029 Li tax ñu wax loolu, mooy gisoon nañu Torofim mu Efes, ànd ak moom ca dëkk ba, te ñu yaakaar ne, Pool dugal na ko ca kër Yàlla ga.
21:30b.ACT.021.030 Noonu dëkk ba bépp màbb, mbooloo ma ne këpp, ñu jàpp Pool, génne ko ca kër Yàlla ga. Ca saa sa ñu tëj bunt ya.
21:31b.ACT.021.031 Bi ñu koy wut a rey, xebaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem gépp jaxasoo na.
21:32b.ACT.021.032 Ca saa sa mu ànd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas wàcc ci ñoom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, ñu daldi bàyyi dóor, ya ñu doon dóor Pool.
21:33b.ACT.021.033 Noonu kilifa ga jegesi jàpp ko, santaane ñu jéng ko ak ñaari càllala. Bi ñu ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def.
21:34b.ACT.021.034 Waaye ci biir mbooloo ma, bu ñii nee lii, ña ca des ne laa. Kon nag gannaaw mënu caa xam dara lu wóor ndax coow li, mu santaane, ñu yóbbu ko ci biir tata ja.
21:35b.ACT.021.035 Bi Pool eggee ca yéegukaayu tata ja, aaytalu mbooloo ma réy, ba ay xarekat fab ko.
21:36b.ACT.021.036 Ndaxte mbooloo maa nga ko topp, di xaacu ne: «Reyleen ko!»
21:37b.ACT.021.037 Bi ñu koy bëgg a dugal ca tata ja, Pool ne kilifa ga: «Ndax man naa laa wax dara?» Mu tontu ko: «Yaw dégg nga gereg?
21:38b.ACT.021.038 Kon nekkuloo waayi Misra, jooju jógloo woon nit ñi keroog te yóbbu woon ñeenti junniy bóomkat ca màndiŋ ma?»
21:39b.ACT.021.039 Pool ne ko: «Man Yawut laa, di jaambur ci Tars, dëkk bu am tur ci diiwaanu Silisi. Maa ngi lay ñaan, ma wax ak mbooloo mi.»
21:40b.ACT.021.040 Te kilifa ga may ko ko. Noonu Pool taxaw ca yéegukaay ba, tàllal loxoom mbooloo ma, ñu daldi ne tekk. Mu wax ak ñoom ci làkku yawut ne:
22
22:1b.ACT.022.001 «Yéen bokk yi ak baay yi, dégluleen samaw lay.»
22:2b.ACT.022.002 Bi ñu déggee, mu di leen wax ci làkku yawut, ñu gën ne xeram. Noonu Pool ne leen:
22:3b.ACT.022.003 «Man Yawut laa, juddoo Tars ci diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Taalibe laa woon ci Gamaleel, mu jàngal ma bu wér yoonu sunuy maam, ba ma sawar ci Yàlla, mel ni yéen ñépp tey.
22:4b.ACT.022.004 Daan naa fitnaal ña bokkoon ci yoon wii, ba di ci rey sax; yeew naa góor ak jigéen, tëj leen;
22:5b.ACT.022.005 saraxalekat bu mag ba ak mbooloom njiit yi yépp man nañu ma cee seede. Am bés ñu bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damas. Ma doon fa dem, ngir yeew ña fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir ñu yar leen.
22:6b.ACT.022.006 «Waaye ci digg-bëccëg, bi ma jaaree ca yoon wa, ba jegesi Damas, ca saa sa leer gu mag jóge asamaan, melax ba ëmb ma.
22:7b.ACT.022.007 Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?”
22:8b.ACT.022.008 Ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Mu ne ma: “Maa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.”
22:9b.ACT.022.009 Ñi ma àndaloon gis nañu leer ga, waaye dégguñu baatu ka doon wax ak man.
22:10b.ACT.022.010 Noonu ma laaj ko: “Lu ma war a def, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Jógal dem Damas, foofa dees na la biral lépp, li ma la yen.”
22:11b.ACT.022.011 Gannaaw gisuma woon dara ndax leeraayu melxat ga, ña ma àndal wommat ma, ma ñëw Damas.
22:12b.ACT.022.012 «Bi ma ko defee ku tudd Anañas ñëw ci man. Nit ku ragal Yàlla la woon ci sàmm yoonu Musaa, te Yawuti Damas yépp seedeel ko lu baax.
22:13b.ACT.022.013 Mu taxaw ci sama wet ne ma: “Sool sama mbokk, delluwaatal di gis.” Noonu ma daldi gisaat ca saa sa, xool ko.
22:14b.ACT.022.014 Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam tànn na la, ba may la, nga xam coobareem te gis Aji Jub ji te nga dégg ay waxam.
22:15b.ACT.022.015 Ndaxte li nga gis te dégg ko, dinga ko seede ci ñépp.
22:16b.ACT.022.016 Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu.”
22:17b.ACT.022.017 «Bi ma dellusee Yerusalem nag, di ñaan ca kër Yàlla ga, leer tàbbi ci man.
22:18b.ACT.022.018 Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: “Génnal Yerusalem ci ni mu gën a gaawe, ndaxte duñu nangu li ngay seede ci man.”
22:19b.ACT.022.019 Waaye ma tontu ne: “Boroom bi, xam nañu ne, dama daan wër jàngoo-jàngu, di tëj kaso ak di dóor ay yar ñi la gëm.
22:20b.ACT.022.020 Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.”
22:21b.ACT.022.021 Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”»
22:22b.ACT.022.022 Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowul a dund!»
22:23b.ACT.022.023 Ñu daldi yuuxu ak di sànni seeni yére, tey callameeru suuf.
22:24b.ACT.022.024 Noonu kilifa ga santaane, ñu dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax ñu di ko yuuxoo nii.
22:25b.ACT.022.025 Waaye bi ñu koy joñ ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: «Ndax am nga sañ-sañu dóor ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?»
22:26b.ACT.022.026 Bi ko njiit la déggee, mu fekki kilifaam, yégal ko ko; mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.»
22:27b.ACT.022.027 Noonu kilifa ga ñëw laaj Pool: «Wax ma, ndax jaambur nga ci Room?» Mu tontu ko: «Waaw, moom laa.»
22:28b.ACT.022.028 Kilifa ga ne ko: «Man fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.» Waaye Pool tontu ko: «Man de dama koo judduwaale.»
22:29b.ACT.022.029 Ñi ko bëggoon a dóor ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko.
22:30b.ACT.022.030 Ca ëllëg sa mu bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, saraxalekat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.
23
23:1b.ACT.023.001 Noonu Pool xool jàkk géew ba ne leen: «Bokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Yàlla ba ci bésu tey bi.»
23:2b.ACT.023.002 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba, di ku ñuy wax Anañas, sant ña taxaw ca wetam, ñu fél gémmiñam.
23:3b.ACT.023.003 Pool ne ko: «Yàlla dina la dóor, yaw mi naaféq, bay samandaay miir bu joy bu ñu weexal. Yaa ngi toog di ma àtte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane ñu dóor ma, ci li yoon wi tere!»
23:4b.ACT.023.004 Waaye ña taxaw ca wetam ne ko: «Ndax dangay xas saraxalekat bu mag, bi Yàlla fal?»
23:5b.ACT.023.005 Pool tontu leen: «Bokk yi, xawma woon ne saraxalekat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”»
23:6b.ACT.023.006 Naka noona Pool, mi xam ne, genn-wàllu kureel ga bokk nañu ci tariixab Sadusen ya, te ña ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir géew ba ne: «Bokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax ñu may àtte tey mooy sama yaakaar ci ne, ñi dee dinañu dekki.»
23:7b.ACT.023.007 Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xaajalikoo.
23:8b.ACT.023.008 Ndaxte Sadusen yi nanguwuñu ne, ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu nañu yooyu yépp.
23:9b.ACT.023.009 Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi xuloo bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne, rab a ko wax mbaa malaaka...?»
23:10b.ACT.023.010 Noonu xuloo ba daldi gën a tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja.
23:11b.ACT.023.011 Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: «Takkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.»
23:12b.ACT.023.012 Bi bët setee Yawut ya daldi lal pexe; ñu dige ci ngiñ ne, duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñuy rey Pool.
23:13b.ACT.023.013 Ña lal pexe ma, seen lim ëpp na ñeent-fukk.
23:14b.ACT.023.014 Noonu ñu dem ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya ne leen: «Giñ nanu ne, dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool.
23:15b.ACT.023.015 Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeen a bëgg a seet mbiram bu gën a wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.»
23:16b.ACT.023.016 Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool.
23:17b.ACT.023.017 Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko war a yégal.»
23:18b.ACT.023.018 Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.»
23:19b.ACT.023.019 Noonu kilifa ga jàpp ci loxob waxambaane wa, wéetoo ak moom, laaj ko: «Loo ma bëgg a yégal?»
23:20b.ACT.023.020 Mu tontu ne: «Yawut yi dañoo dige, ngir ñaan la, nga indi Pool ëllëg ca kanamu kureelu àttekat ya, mel ni dañoo bëgg a seet mbiram bu gën a wóor.
23:21b.ACT.023.021 Bu leen ko may, ndaxte lu ëpp ñeent-fukk ci ñoom ñu ngi koy lalal fiir. Dige nañu ak ngiñ ne, dootuñu lekk, dootuñu naan, li feek reyuñu ko; fi mu ne sax fagaru nañu, di xaar, nga nangu.»
23:22b.ACT.023.022 Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu bañ koo àgge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem.
23:23b.ACT.023.023 Bi mu ko defee mu woo ñaar ci njiiti xare ba ne leen: «Waajal-leen ñaari téeméeri xarekat ak juróom-ñaar-fukki gawar ak ñaari téeméer ñu gànnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci juróom-ñeenti waxtu ci guddi.
23:24b.ACT.023.024 Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen yóbbu ko ci jàmm ak salaam ba ca Feligsë, boroom réew mi.»
23:25b.ACT.023.025 Noonu mu bind bataaxal bii:
23:26b.ACT.023.026 Yaw Feligsë mu tedd mi, di boroom réew mi; man Këlódd Lisiyas maa ngi lay nuyu.
23:27b.ACT.023.027 Yawut yi jàpp nañu nit kii, bëgg koo rey, waaye bi ma yégee ne, jaambur la ci Room, wallu naa ko ak ay xarekat, ba musal ko.
23:28b.ACT.023.028 Bëggoon naa xam lu tax ñu kalaame ko. Moo tax ma yóbbu ko ca kanamu seen kureelu àttekat ya.
23:29b.ACT.023.029 Gis naa ne li ñu ko jiiñ mu ngi aju ci ay werantey seen yoon, waaye jiiñuñu ko dara lu jar dee mbaa jéng.
23:30b.ACT.023.030 Te bi ma déggee ne, ñu ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag ñi ko kalaame, ñu xamal la seen lay.
23:31b.ACT.023.031 Noonu xarekat ya jël Pool ci guddi, indi ko ba ca dëkku Antipataris, ni ñu leen ko sante.
23:32b.ACT.023.032 Ca ëllëg sa ñu woññiku, dellusi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge ko.
23:33b.ACT.023.033 Bi gawar ga àggee Sesare, ñu jox boroom réew ma bataaxal ba, jébbal ko Pool.
23:34b.ACT.023.034 Bi loolu amee boroom réew ma jàng bataaxal ba, laaj ci ban diiwaan la Pool dëkk. Bi mu yégee ne, mu ngi dëkk Silisi,
23:35b.ACT.023.035 mu ne ko: «Kon bu ñi la kalaame ñëwee, dinga layoo.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur ba Erodd.
24
24:1b.ACT.024.001 Bi juróomi fan wéyee, Anañas saraxalekat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma.
24:2b.ACT.024.002 Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet.
24:3b.ACT.024.003 Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp.
24:4b.ACT.024.004 Waaye ngir bañ a yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt.
24:5b.ACT.024.005 Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasaréen.
24:6b.ACT.024.006 Dem na ba jéem a teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko.
24:8b.ACT.024.008 Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne, li nu koy jiiñ dëgg la.»
24:9b.ACT.024.009 Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na.
24:10b.ACT.024.010 Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne: «Xam naa ne, yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute.
24:11b.ACT.024.011 Man ngaa wóorliku ne, ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali.
24:12b.ACT.024.012 Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba.
24:13b.ACT.024.013 Te mënuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi.
24:14b.ACT.024.014 Waaye nangu naa ci sa kanam ne, maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne, mooy tariixa; terewul ne, lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko.
24:15b.ACT.024.015 Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.
24:16b.ACT.024.016 Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
24:17b.ACT.024.017 «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.
24:18b.ACT.024.018 Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.
24:19b.ACT.024.019 Waaye ay Yawut yu dëkk Asi — xanaa kay ñoo waroon a ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.
24:20b.ACT.024.020 Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,
24:21b.ACT.024.021 xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»
24:22b.ACT.024.022 Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.»
24:23b.ACT.024.023 Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»
24:24b.ACT.024.024 Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak jabaram Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist.
24:25b.ACT.024.025 Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.»
24:26b.ACT.024.026 Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko faral a woolu, ngir waxtaan ak moom.
24:27b.ACT.024.027 Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.
25
25:1b.ACT.025.001 Bi Festus teersee ci diiwaanam, mu teg ca ñetti fan, dem Yerusalem.
25:2b.ACT.025.002 Noonu saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame Pool ci moom.
25:3b.ACT.025.003 Ñuy sàkku ndimbal ci moom, di ko ñaan bu wér, mu yónni Pool Yerusalem, fekk lal nañu fiiru rey ko ca yoon wa.
25:4b.ACT.025.004 Waaye Festus tontu leen ne: «Ñu ngi wottu Pool ca Sesare, te dinaa fa dem fi ak fan yu néew.»
25:5b.ACT.025.005 Mu ne leen: «Ñi am maana ci yéen nag, nangeen ànd ak man, layooji ak nit ka, bu dee tooñ na.»
25:6b.ACT.025.006 Noonu Festus am fa ñoom juróom-ñett ba fukki fan, ba noppi dem Sesare. Ca ëllëg sa mu toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Pool.
25:7b.ACT.025.007 Bi mu ñëwee nag, Yawut ya jóge Yerusalem wër ko, di ko jiiñ tooñ yu bare te réy, te mënuñu leen a firndeel.
25:8b.ACT.025.008 Noonu Pool làyyi ne: «Tooñuma yoonu Yawut ya, tooñuma kër Yàlla ga, tooñuma buur ba Sesaar.»
25:9b.ACT.025.009 Ci kaw loolu Festus, mi bëgg lu neex Yawut ya, tontu Pool ne: «Ndax bëgguloo dem Yerusalem, nga layoo fa ci mbir yii ci sama kanam?»
25:10b.ACT.025.010 Waaye Pool ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu buur Sesaar; te fii lañu ma war a àttee. Te yaw ci sa bopp xam nga bu baax ne, tooñuma Yawut yi.
25:11b.ACT.025.011 Su ma tooñoon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir bañ a dee. Waaye bu li ñu may jiiñ taxawul, kenn sañu ma leen a jébbal. Dénk naa sama mbir Sesaar.»
25:12b.ACT.025.012 Bi mu waxee loolu, Festus gise ak ñi ko wër, mu tontu ko: «Dénk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.»
25:13b.ACT.025.013 Ba ñu ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis ñëw Sesare, ngir nuyusi Festus.
25:14b.ACT.025.014 Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: «Feligsë batale na nu ak kenn ku ñu tëj.
25:15b.ACT.025.015 Te bi ma nekkee Yerusalem, saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame nañu ko ci man, ñaan ma, ma daan ko.
25:16b.ACT.025.016 Waaye ma tontu leen ne: “Jébbale nit, fekk jàkkaarloowul ak ñi koy jiiñ, ba man a làyyil boppam ci li ñu koy jiiñ, loolu dëppoowul ak aaday nguuru Room.”
25:17b.ACT.025.017 Bi ñu àndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca ëllëg sa sax toog naa ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi nit kooku.
25:18b.ACT.025.018 Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon;
25:19b.ACT.025.019 waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne, mu ngi dund.
25:20b.ACT.025.020 Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax bëgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu.
25:21b.ACT.025.021 Waaye Pool ñaan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko àtte. Noonu santaane naa ñu aj ko, ba keroog ma koy yónnee Sesaar.»
25:22b.ACT.025.022 Booba nag Agaripa ne Festus: «Man sax bëgg naa dégg nit kooku.» Festus tontu ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
25:23b.ACT.025.023 Ca ëllëg sa nag Agaripa ak Berenis ñëw bu xumb, ñu dugg ca néegu àtte ba, ànd ak kilifay xare ba ak ña am maana ca dëkk ba. Noonu Festus joxe ndigal, ñu indi Pool.
25:24b.ACT.025.024 Bi mu ñëwee, Festus ne: «Buur Agaripa ak yéen ñépp, ñi fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut yépp, muy ci Yerusalem, muy fii, wër ma di yuuxu ne: “Nit kii waratul a dund.”
25:25b.ACT.025.025 Waaye gis naa ne, deful dara lu jar dee. Moona, gannaaw moom ci boppam dénk na boppam buur bu tedd ba, fas naa yéene yónnee ko ko.
25:26b.ACT.025.026 Fekk awma dara lu wóor ci mbiram, lu ma man a bind sang bi. Moo tax ma indi ko ci seen kanam, rawatina ci sa kanam buur Agaripa, ngir sunu jataay may ma lu ma bind.
25:27b.ACT.025.027 Ndaxte yaakaar naa ne, yónnee ku ñu tëj, te bañ caa boole lu ko waral, àndul ak xel.»
26
26:1b.ACT.026.001 Bi mu ko waxee, Agaripa ne Pool: «Jëlal kàddu gi.» Noonu Pool tàllal loxoom, daldi làyyi ne:
26:2b.ACT.026.002 «Buur Agaripa, ma làyyi ci sa kanam tey ci lépp, li ma Yawut yiy jiiñ, xol bu sedd la ci man,
26:3b.ACT.026.003 ndaxte xam nga bu baax aaday Yawut yi ak seeni werantey yoon. Kon maa ngi lay ñaan, nga déglu ma ak muñ.
26:4b.ACT.026.004 «Ci lu jëm ci Yawut yi, xam nañu sama dund li dale ci samag ndaw, muy ci sama biir xeet, muy ci Yerusalem.
26:5b.ACT.026.005 Xam nañu ma bu yàgg te man nañoo seede, su leen neexee, ne daan naa dund ni Farisen, te mooy tariixa bi gën a diis ci sunu diine.
26:6b.ACT.026.006 Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag, mooy yaakaar ne, Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam.
26:7b.ACT.026.007 Dige booba la fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di sàkku, ngir jot ko, ci jaamu Yàlla ak cawarte guddi ak bëccëg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax ñu may kalaame, ñoom Yawut yi.
26:8b.ACT.026.008 Lu tax seen xel dàq ne, Yàlla dina dekkal ñi dee?
26:9b.ACT.026.009 «Man sax ci sama bopp defe woon naa ne, war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.
26:10b.ACT.026.010 Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci saraxalekat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoon a bëgg a rey, ànd naa ci.
26:11b.ACT.026.011 Daan naa wër jàngoo-jàngu, di leen teg toskare te di leen jéem a weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen.
26:12b.ACT.026.012 «Noonu am bés, may dem dëkku Damas, yor sañ-sañ ak ndigalu saraxalekat yu mag ya.
26:13b.ACT.026.013 Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal.
26:14b.ACT.026.014 Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.”
26:15b.ACT.026.015 «Noonu ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal.
26:16b.ACT.026.016 Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man, ak li ma lay feeñuji.
26:17b.ACT.026.017 Dinaa la musal ci bànni Israyil ak ci ñi dul Yawut. Ci ñoom laa lay yebal,
26:18b.ACT.026.018 ngir ubbi seeni bët, nga jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sañ-sañu Seytaane, woññi leen ci Yàlla, ma baal leen seeni bàkkaar te may leen cér ci biir sama gaa yi sell ci kaw ngëm.”
26:19b.ACT.026.019 «Kon nag buur Agaripa, woruma li ma Yàlla yen ci peeñu.
26:20b.ACT.026.020 Waaye li tàmbali ci Damas, teg ci dëkku Yerusalem ak réewu Yawut mépp, ba agsi ci ñi dul Yawut, yégal naa leen, ñu tuub seeni bàkkaar te woññiku ci Yàlla, bay jëf lu dëppook réccu.
26:21b.ACT.026.021 Loolu nag moo waral Yawut yi jàpp ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.
26:22b.ACT.026.022 Waaye gannaaw Yàllaa ngi may taxawu ba tey, maa ngi taxaw fi, di ko seedeel ci mag ak ndaw; yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa xamle woon lu jiitu,
26:23b.ACT.026.023 maanaam Almasi bi dina dékku ay coono, te mooy jëkk a dekki, bay jollil leer ci bànni Israyil ak ñi dul Yawut.»
26:24b.ACT.026.024 Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.»
26:25b.ACT.026.025 Waaye Pool tontu ko: «Festus mu tedd mi, dofuma; waaye lu dëggu laay wax te ànd ak sago.
26:26b.ACT.026.026 Yëf yii leer na buur bi, moo tax maa ngi koy wax ak kóolute. Wóor naa ne, dara ci lii may wax umpu ko, ndaxte lii amewul ciy ruq.
26:27b.ACT.026.027 Yaw buur Agaripa, ndax gëmuloo yonent yi? Xam naa bu wér ne, gëm nga.»
26:28b.ACT.026.028 Noonu Agaripa ne Pool: «Xanaa yaw, ci diir bu gàtt bii rekk, nga ma bëgg a dugale ci gaayi Kirist!»
26:29b.ACT.026.029 Pool tontu ko: «Muy tey, muy ëllëg, waxuma yaw rekk waaye it ñi may déglu tey ñépp, na Yàlla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy jéng yii!»
26:30b.ACT.026.030 Ci kaw loolu buur ba daldi jóg, boroom réew ma topp ci, Berenis tegu ca ak mbooloo ma mépp.
26:31b.ACT.026.031 Bi ñu génnee nag, ñuy waxante ne: «Nit kii deful dara lu jar dee mbaa kaso.»
26:32b.ACT.026.032 Te Agaripa ne Festus: «Manoon nanu koo yiwi, bu dénkuloon mbiram Sesaar.»
27
27:1b.ACT.027.001 Bi loolu wéyee ñu fas yéene noo dugal gaal jëme réewu Itali. Noonu ñu jël Pool ak ñeneen ñi ñu tëjoon, dénk leen njiitu xare bu tudd Yulyus, mi bokk ci mbooloom xare mu buur.
27:2b.ACT.027.002 Nu dugg ca gaalu dëkku Adaramit guy taxaw ci teeruy Asi, daldi tàbbi ci biir géej; te Aristàrk, mi dëkk Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.
27:3b.ACT.027.003 Ca ëllëg sa nu teer Sidon; Yulyus laabiir ci Pool, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu ganale ko.
27:4b.ACT.027.004 Bi nu fa jógee, nu dem ci biir géej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu.
27:5b.ACT.027.005 Nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca wàlli Lisi.
27:6b.ACT.027.006 Foofa nag njiit la gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.
27:7b.ACT.027.007 Noonu nuy dem ndànk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu réy; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu jëm kanam, nu leru dunu Kereet ci fegu ngelaw li, janook Salmon.
27:8b.ACT.027.008 Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca bérab bu ñuy wax Teeru yu neex, te dend ak dëkku Lase.
27:9b.ACT.027.009 Fekk booba yàggoon nañu ca yoon wa, te dem ci géej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne:
27:10b.ACT.027.010 «Gaa ñi, gis naa ne, tukki bi ëmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
27:11b.ACT.027.011 Waaye njiit la sobental waxi Pool, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
27:12b.ACT.027.012 Te gannaaw teeru ba neexul a lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wut a agsi Fenigsë, biy teerub dunu Kereet te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.
27:13b.ACT.027.013 Noonu bi ngelaw lu woyof liy jóge sudd wolee, ñu defe ne, man nañoo sottal seen pexe, ñu wëgg diigal, daldi tafu ci dunu Kereet.
27:14b.ACT.027.014 Waaye nes tuuti ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon,» jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw.
27:15b.ACT.027.015 Mu ëpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal.
27:16b.ACT.027.016 Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu ñuy wax Kóda ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare.
27:17b.ACT.027.017 Bi ñu ko yéegee, ñu fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragal a daanu ci suuf su nooy su ñuy wax Sirt; ba noppi ñu daldi sànni diigal, ngir wàññi doxub gaal ga, nuy yale noonu.
27:18b.ACT.027.018 Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca ëllëg sa ñu sànni la gaal ga yeboon ca géej ga.
27:19b.ACT.027.019 Te ca ñetteelu fan ba, ñu sànni ak seeni loxo jumtukaay, yi ñu yeboon ngir fàggu.
27:20b.ACT.027.020 Noonu jant bi ne meŋŋ te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc gépp tas.
27:21b.ACT.027.021 Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te bañ a jóge Kereet, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii.
27:22b.ACT.027.022 Léegi nag maa ngi leen di dénk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy yàqu, waaye kenn ci yéen du dee.
27:23b.ACT.027.023 Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, jóge ci Yàlla sama Boroom, bi may jaamu.
27:24b.ACT.027.024 Mu ne ma: “Pool bul tiit; fàww nga taxaw ci kanamu Sesaar, te yaa tax Yàllay aar bakkani ñi nga àndal ñépp.”
27:25b.ACT.027.025 Moo tax gaa ñi, takkleen seen fit, ndax wóolu naa Yàlla ne, li mu ma wax, dina am.
27:26b.ACT.027.026 Waaye war nanoo luf cib dun.»
27:27b.ACT.027.027 Ca fukkeelu guddi ga ak ñeent nu nga doon jayaŋ-jayaŋi ca géeju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne, danu jegesi suuf.
27:28b.ACT.027.028 Ñu sànni nattukaay ba ci biir géej, mu jàpp ñeent-fukki meetar, dem ca kanam tuuti, sànniwaat ko, jàpp fanweeri meetar.
27:29b.ACT.027.029 Ñu ragal ne, dinañu fenqu ci ay xeer, kon ñu daldi sànni ñeenti diigal ci geenu gaal ga, di ñaan bët set.
27:30b.ACT.027.030 Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo sànniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk dañuy fexee jël looco ga, ba raw.
27:31b.ACT.027.031 Waaye Pool ne njiit la ak xarekat ya: «Bu ñii desul ci gaal gi, dungeen raw.»
27:32b.ACT.027.032 Noonu xarekat ya dagg buum, yay téye looco ga, bàyyi ko mu wéy.
27:33b.ACT.027.033 Bi bët setagul, Pool sant leen ñu lekk; mu ne leen: «Tey mooy seen fukki fan ak ñeent yu ngeen ne jonn, lekkuleen, mosuleen dara.
27:34b.ACT.027.034 Maa ngi leen di sant nag, ngeen lekk, ndax noonu rekk ngeen man a rawe. Ndax genn kawar du rot ci yéen.»
27:35b.ACT.027.035 Bi mu waxee loolu, mu fab mburu, sant Yàlla ci kanamu ñépp, damm ko, daldi ko lekk.
27:36b.ACT.027.036 Bi ñu gisee loolu, ñépp dëgëraat, ñu daldi lekk ñoom itam.
27:37b.ACT.027.037 Mboolem ñi nekkoon ca gaal ga mat na ñaari téeméeri nit ak juróom-ñaar-fukk ak juróom-benn.
27:38b.ACT.027.038 Noonu ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma ca géej ga, ngir woyofal gaal ga.
27:39b.ACT.027.039 Bi bët setee nag, xàmmiwuñu réew ma, waaye séen nañu ruqu tefes. Noonu ñu fas yéene caa teeral gaal ga, bu ñu ko manee.
27:40b.ACT.027.040 Ñu dagg diigal ya, bàyyi leen ci biir géej, yiwiwaale baar ba; ba noppi firi wiiru kanam ga, jublu ca tefes ga.
27:41b.ACT.027.041 Waaye ñu dal ca tundu suuf ca bérab bu ñaari koroŋ daje, gaal ga daldi fa luf. Boppu gaal ga nuur bu baax, ne fa tekk, te dooley duus ya daldi toj geen ba.
27:42b.ACT.027.042 Bi loolu amee xarekat ya bëgg a rey ñi ñu tëj, ngir ragal ñenn ñi féey, ba raw.
27:43b.ACT.027.043 Waaye njiit la bëgg a musal Pool, mu tere leen pexe ma. Mu sant ñi man a féey, ñu jëkk a sóobu ca ndox ma, ba jot tefes ga.
27:44b.ACT.027.044 Mu sant ñi ci des ñu def noonu, langaamu ci ay dénk, mbaa ca tojiti gaal ga. Noonu ñépp jot tefes ga ci jàmm ak salaam.
28
28:1b.ACT.028.001 Bi nu rëccee, nu yég ne dun baa nga tudd Màlt.
28:2b.ACT.028.002 Te waa réew ma won nu laabiir gu ràññiku, ndaxte taalal nañu nu safara, ganale nu ndax taw bi sóob ak sedd bi.
28:3b.ACT.028.003 Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca mëlle ndax tàngoor wa, taq ci loxoom.
28:4b.ACT.028.004 Bi waa réew ma gisee rab wa wéqu ci loxoom nag, ñuy waxante naan: «Ci lu wóor nit kii reykat la; te bi mu rëccee ca géej ga sax, ndogalu Yàlla mayu ko mu dund.»
28:5b.ACT.028.005 Waaye Pool yëlëb rab wa ca safara sa, te wàññiwu ko dara.
28:6b.ACT.028.006 Nit ñi di xaar mu newi, mbaa mu ne dàll, dee; waaye bi ñu négee lu yàgg te gis ne dara jotu ko, ñu soppi xel ne: «Kii yàlla la.»
28:7b.ACT.028.007 Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu réy diirub ñetti fan.
28:8b.ACT.028.008 Fekk baayu Publiyus dafa tëdd ndax ay tàngoori yaram yu koy dikkal ak biiru taññ. Pool nag dem seeti ko, ñaan ci Yàlla, teg ko ay loxoom, mu daldi wér.
28:9b.ACT.028.009 Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat wér-gi-yaram.
28:10b.ACT.028.010 Ñu teral nu ci fànn yu bare, te bi nuy dem, ñu jox nu li nuy soxla lépp.
28:11b.ACT.028.011 Bi nu fa amee ñetti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi tàbbi ca géej ga. Gaalu dëkku Alegsàndiri la woon, te yor xàmmikaay guy nataalu Kastor ak Polugsë.
28:12b.ACT.028.012 Noonu nu teer dëkku Sirakus, toog fa ñetti fan.
28:13b.ACT.028.013 Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol.
28:14b.ACT.028.014 Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room.
28:15b.ACT.028.015 Sunuy xebaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam.
28:16b.ACT.028.016 Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.
28:17b.ACT.028.017 Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.
28:18b.ACT.028.018 Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee.
28:19b.ACT.028.019 Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.
28:20b.ACT.028.020 Moo tax ma ñaan a gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.»
28:21b.ACT.028.021 Bi ñu ko déggee, ñu tontu ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.
28:22b.ACT.028.022 Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»
28:23b.ACT.028.023 Noonu ñu dig ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéem a gëmloo.
28:24b.ACT.028.024 Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko.
28:25b.ACT.028.025 Gannaaw mënuñoo déggoo, ñu bëgg a tas. Waaye bi ñu laata dem, Pool teg ca wax jii: «Xel mu Sell mi wax na dëgg ak seeni maam, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi.
28:26b.ACT.028.026 Nee na:“Demal ci xeet wii ne leen:‘Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’
28:27b.ACT.028.027 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.”
28:28b.ACT.028.028 «Xamleen nag ne, xebaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»
28:30b.ACT.028.030 Noonu diirub ñaari at Pool dëkk ca kër gu muy fey, di fa àggali ñépp ñi koy seetsi.
28:31b.ACT.028.031 Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngale ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Acts (Wolof). Acts (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C330-5