Luke (Wolof)
1
1:1b.LUK.001.001 Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,
1:2b.LUK.001.002 li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla.
1:3b.LUK.001.003 Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.
1:4b.LUK.001.004 Noonu dinga man a xam ne, li ñu la jàngaloon lu wér peŋŋ la.
1:5b.LUK.001.005 Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na saraxalekat bu ñu tudde Sakariya te bokk ca mbootaayu saraxalekat, ya askanoo ci Abiya. Jabaram Elisabet askanoo moom itam ci Aaroona.
1:6b.LUK.001.006 Sakariya ak jabaram ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp.
1:7b.LUK.001.007 Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet mënul a am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.
1:8b.LUK.001.008 Benn bés nag Sakariya doon def liggéeyu saraxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.
1:9b.LUK.001.009 Bi ñuy tegoo bant, ni ko saraxalekat yi daan defe nakajekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakariya.
1:10b.LUK.001.010 Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.
1:11b.LUK.001.011 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakariya, taxaw ca féeteek ndeyjooru saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.
1:12b.LUK.001.012 Naka la ko Sakariya gis, fitam daldi dem, mu tiit.
1:13b.LUK.001.013 Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakariya, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa jabar dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.
1:14b.LUK.001.014 Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,
1:15b.LUK.001.015 ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.
1:16b.LUK.001.016 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
1:17b.LUK.001.017 Mooy jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Iliyas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
1:18b.LUK.001.018 Sakariya daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne, loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama jabar it màggat na.»
1:19b.LUK.001.019 Malaaka ma tontu ko ne: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu.
1:20b.LUK.001.020 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo man a wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
1:21b.LUK.001.021 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakariya yàgg ca bérab bu sell ba.
1:22b.LUK.001.022 Waaye bi mu génnee nag, mënul a wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne, dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
1:23b.LUK.001.023 Bi Sakariya matalee liggéeyu saraxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.
1:24b.LUK.001.024 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet jabaram ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer
1:25b.LUK.001.025 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»
1:26b.LUK.001.026 Bi Elisabet nekkee ci juróom-benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
1:27b.LUK.001.027 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.
1:28b.LUK.001.028 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm ngaam, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
1:29b.LUK.001.029 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu man a tekki.
1:30b.LUK.001.030 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.
1:31b.LUK.001.031 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
1:32b.LUK.001.032 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.
1:33b.LUK.001.033 Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
1:34b.LUK.001.034 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu man a ame? Man de, janq laa ba tey.»
1:35b.LUK.001.035 Malaaka ma tontu ko ne: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.
1:36b.LUK.001.036 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku mënul a am doom, mu ngi ci juróom-benni weeram.
1:37b.LUK.001.037 Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
1:38b.LUK.001.038 Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.
1:39b.LUK.001.039 Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.
1:40b.LUK.001.040 Mu dugg ca kër Sakariya, daldi nuyu Elisabet.
1:41b.LUK.001.041 Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yengatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.
1:42b.LUK.001.042 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
1:43b.LUK.001.043 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
1:44b.LUK.001.044 Maa ngi lay wax ne, naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yengu ci sama biir ndax mbég.
1:45b.LUK.001.045 Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne, li la Boroom bi yégal dina mat!»
1:46b.LUK.001.046 Noonu Maryaama daldi ne:
1:47b.LUK.001.047 «Sama xol a ngi màggal Boroom bi,sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,
1:48b.LUK.001.048 ndaxte fàttaliku na ma,man jaamam bu woyof bi.Gannaawsi tey, niti jamono yéppdinañu ma wooye ki ñu barkeel,
1:49b.LUK.001.049 ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.Turam dafa sell.
1:50b.LUK.001.050 Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
1:51b.LUK.001.051 Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
1:52b.LUK.001.052 daaneel boroom doole yi ci seen nguur,yékkati baadoolo yi.
1:53b.LUK.001.053 Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,te dàq boroom alal yi,ñu daw ak loxoy neen.
1:54b.LUK.001.054 Wallu na bànni Israyil giy jaamam,di fàttaliku yërmandeem,
1:55b.LUK.001.055 ni mu ko dige woon sunuy maam,jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
1:56b.LUK.001.056 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu war a tollook ñetti weer, sog a ñibbi.
1:57b.LUK.001.057 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
1:58b.LUK.001.058 Dëkkandoom yi ak mbokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
1:59b.LUK.001.059 Bi bés ba dellusee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakariya.
1:60b.LUK.001.060 Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
1:61b.LUK.001.061 Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
1:62b.LUK.001.062 Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
1:63b.LUK.001.063 Sakariya laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.
1:64b.LUK.001.064 Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakariya daldi waxaat, di màggal Yàlla.
1:65b.LUK.001.065 Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.
1:66b.LUK.001.066 Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne, dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.
1:67b.LUK.001.067 Sakariya baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
1:68b.LUK.001.068 «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
1:69b.LUK.001.069 Feeñal na nu Musalkat bu am doole,bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,
1:70b.LUK.001.070 ni mu yéglee woon bu yàggjaarale ko ci yonentam yu sell yi.
1:71b.LUK.001.071 Dina nu musal ci sunuy noon,jële nu ci sunu loxoy bañaale.
1:72b.LUK.001.072 Yàlla wone na yërmandeem,ji mu digoon sunuy maam,te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,
1:73b.LUK.001.073 di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
1:74b.LUK.001.074 dina nu teqale ak sunuy noon,ngir nu man koo jaamu ci jàmm,
1:75b.LUK.001.075 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
1:76b.LUK.001.076 Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi,di ko xàllal yoon wi.
1:77b.LUK.001.077 Dinga xamal mbooloom,ni leen Boroom bi man a musale,jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,
1:78b.LUK.001.078 ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk,
1:79b.LUK.001.079 ngir leeral ñi toog ci lëndëm,takkandeeru dee tiim leen,ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»
1:80b.LUK.001.080 Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.
2
2:1b.LUK.002.001 Ca jamono jooja buur bu mag bu ñuy wax Ogust joxe ndigal ne, na ñépp binduji.
2:2b.LUK.002.002 Mbindu mooma, di mu jëkk ma, daje na ak jamono, ja Kiriñus nekke boroom réewu Siri.
2:3b.LUK.002.003 Noonu ku nekk dem binduji ca sa dëkku cosaan.
2:4b.LUK.002.004 Yuusufa nag daldi jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndaxte ci askanu Daawuda la bokk.
2:5b.LUK.002.005 Mu dem binduji, ànd ak Maryaama jabaram, fekk booba Maryaama ëmb.
2:6b.LUK.002.006 Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc agsi.
2:7b.LUK.002.007 Mu taawloo doom ju góor, mu laxas ko ci ay laytaay, tëral ko ca lekkukaayu jur ga, ndaxte xajuñu woon ca dalukaay ba.
2:8b.LUK.002.008 Fekk booba amoon na ca gox ba ay sàmm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga.
2:9b.LUK.002.009 Noonu benn malaakam Boroom bi feeñu leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, wër leen. Tiitaange ju réy jàpp leen.
2:10b.LUK.002.010 Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xebaar bu baax buy indi mbég mu réy ci nit ñépp.
2:11b.LUK.002.011 Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi.
2:12b.LUK.002.012 Ci firnde jii ngeen koy xàmmee: dingeen gis liir bu ñu laxas ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur.»
2:13b.LUK.002.013 Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu jóge asamaan, ànd ak moom, di sant Yàlla naan:
2:14b.LUK.002.014 «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa,te ci àddina, na jàmm ji wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!»
2:15b.LUK.002.015 Bi malaaka ya delloo ca asamaan, sàmm yi di waxante naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.»
2:16b.LUK.002.016 Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga.
2:17b.LUK.002.017 Bi ñu leen gisee, ñu nettali la ñu leen waxoon ca mbirum xale ba.
2:18b.LUK.002.018 Ñi dégg li sàmm yi doon wax ñépp daldi waaru lool.
2:19b.LUK.002.019 Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam.
2:20b.LUK.002.020 Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
2:21b.LUK.002.021 Bi bés ba dellusee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
2:22b.LUK.002.022 Noonu jamono ji ñu leen waroon a sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
2:23b.LUK.002.023 Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
2:24b.LUK.002.024 Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»
2:25b.LUK.002.025 Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla war a dëfël bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
2:26b.LUK.002.026 te xamal na ko ne, du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.
2:27b.LUK.002.027 Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee,
2:28b.LUK.002.028 Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yàlla ne:
2:29b.LUK.002.029 «Boroom bi, nanga yiwi sa jaam,mu noppaluji ci jàmm, ni nga ko waxe.
2:30b.LUK.002.030 Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal,
2:31b.LUK.002.031 xeet yépp seede ko.
2:32b.LUK.002.032 Muy leer giy leeral xeet yi,di ndamu Israyil say gaay.»
2:33b.LUK.002.033 Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi.
2:34b.LUK.002.034 Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,
2:35b.LUK.002.035 ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.»
2:36b.LUK.002.036 Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana màggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom-ñaari at ak jëkkëram.
2:37b.LUK.002.037 Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom-ñett-fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woon a jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor.
2:38b.LUK.002.038 Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla war a jot Yerusalem.
2:39b.LUK.002.039 Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
2:40b.LUK.002.040 Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom.
2:41b.LUK.002.041 At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir màggali bésu Jéggi ba.
2:42b.LUK.002.042 Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe nakajekk.
2:43b.LUK.002.043 Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
2:44b.LUK.002.044 Ñu xalaat ne, Yeesu dafa àndoon ak ñeneen, ñi ñu bokkaloon yoon. Bi ñu doxee bésub lëmm, ñu tàmbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi.
2:45b.LUK.002.045 Bi ñu ko gisul nag, ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
2:46b.LUK.002.046 Ca gannaaw ëllëg sa ñu fekk ko ca kër Yàlla ga, mu toog ci jàngalekati Yawut yi, di déglu ak di laajte.
2:47b.LUK.002.047 Ñépp ñi dégg li mu wax yéemu ci xel, mi mu àndal, ak ni mu doon tontoo.
2:48b.LUK.002.048 Naka la ko waajuram yi gis, ñu daldi waaru. Yaayam ne ko: «Sama doom, lu tax nga def nu lii? Man ak sa baay nu ngi la doon seet, jaaxle lool.»
2:49b.LUK.002.049 Mu ne leen: «Lu tax ngeen may seet? Xanaa xamuleen ne, damaa war a nekk ci sama kër Baay?»
2:50b.LUK.002.050 Waaye xamuñu li kàddoom yi doon tekki.
2:51b.LUK.002.051 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom, dellu Nasaret te déggal ay waajuram. Fekk yaayam moom takk mbir yooyu yépp ci xolam.
2:52b.LUK.002.052 Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam te neex Yàlla ak nit ñi.
3
3:1b.LUK.003.001 Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen.
3:2b.LUK.003.002 Te it Anas ak Kayif nekkoon saraxalekat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakariya, ca màndiŋ ma.
3:3b.LUK.003.003 Yaxya daldi dugg àll, bi wër dexu Yurdan gépp, di waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
3:4b.LUK.003.004 Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.
3:5b.LUK.003.005 Nañu sëkk xur yi,maasale tund yi ak jànj yi.Yoon yi dëng ñu jubbanti leen,yi ñagas ñu rataxal leen.
3:6b.LUK.003.006 Bu ko defee bépp mbindeef dina gismucc gi Yàlla tëral.”»
3:7b.LUK.003.007 Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?
3:8b.LUK.003.008 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te bañ a nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.
3:9b.LUK.003.009 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.»
3:10b.LUK.003.010 Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu war a def nag?»
3:11b.LUK.003.011 Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.»
3:12b.LUK.003.012 Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu war a def?»
3:13b.LUK.003.013 Mu tontu leen ne: «Laajleen rekk lu jaadu.»
3:14b.LUK.003.014 Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»
3:15b.LUK.003.015 Mbooloo maa ngay xaar, di séentook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi.
3:16b.LUK.003.016 Noonu Yaxya tontu leen ñoom ñépp ne: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara.
3:17b.LUK.003.017 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàqam, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.»
3:18b.LUK.003.018 Noonu Yaxya teg ca yeneen dénkaane yu bare, di yégal nit ña xebaar bu baax ba.
3:19b.LUK.003.019 Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd, jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef,
3:20b.LUK.003.020 ba faf tëj Yaxya kaso.
3:21b.LUK.003.021 Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku.
3:22b.LUK.003.022 Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
3:23b.LUK.003.023 Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu war a tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi.Te Yuusufa mooy doomu Eli,
3:24b.LUK.003.024 miy doomu Matat.Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki;Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
3:25b.LUK.003.025 Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.
3:26b.LUK.003.026 Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.
3:27b.LUK.003.027 Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa;Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;
3:28b.LUK.003.028 Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.
3:29b.LUK.003.029 Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi;
3:30b.LUK.003.030 Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim.
3:31b.LUK.003.031 Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena;Mena, Matata; Matata, Natan;Natan, Daawuda.
3:32b.LUK.003.032 Daawuda mooy doomu Yese;Yese, Obedd; Bowas; Salmon; Naason.
3:33b.LUK.003.033 Naason; Aminadab; Aminadab, Admin;Arni; Esrom; Fares; Yuda;
3:34b.LUK.003.034 Yanqóoba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor;
3:35b.LUK.003.035 Serug; Ragaw; Faleg; Eber; Sala.
3:36b.LUK.003.036 Sala, Kaynam mooy baayam; Kaynam, Arpagsàdd;Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;
3:37b.LUK.003.037 Lemeg, Matusala; Enog, Yaredd; Maleleel; Kaynan;
3:38b.LUK.003.038 Enos; Set; Set doomu Aadama;Aadama doomu Yàlla.
4
4:1b.LUK.004.001 Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, jóge dexu Yurdan.
4:2b.LUK.004.002 Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent-fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif.
4:3b.LUK.004.003 Noonu Seytaane ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj wii mu nekk mburu.»
4:4b.LUK.004.004 Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”»
4:5b.LUK.004.005 Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef-ak-xippi mu won ko réewi àddina sépp,
4:6b.LUK.004.006 ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox.
4:7b.LUK.004.007 Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.»
4:8b.LUK.004.008 Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»
4:9b.LUK.004.009 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf,
4:10b.LUK.004.010 ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu sàmm la,
4:11b.LUK.004.011 dinañu la leewu ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”»
4:12b.LUK.004.012 Yeesu tontu ko ne: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
4:13b.LUK.004.013 Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.
4:14b.LUK.004.014 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.
4:15b.LUK.004.015 Muy jàngale ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
4:16b.LUK.004.016 Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésu noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi.
4:17b.LUK.004.017 Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:
4:18b.LUK.004.018 «Xelum Boroom baa ngi ci man,ndaxte moo ma tànn,ngir ma yégal néew doole yi xebaar bu baax bi.Dafa maa yónni,ngir ma yégal jaam ñi ne, dinañu leen goreel,yégal gumba yi ne, dinañu gis,te jot ñi ñu noot,
4:19b.LUK.004.019 tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»
4:20b.LUK.004.020 Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët.
4:21b.LUK.004.021 Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.»
4:22b.LUK.004.022 Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?»
4:23b.LUK.004.023 Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»
4:24b.LUK.004.024 Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam.
4:25b.LUK.004.025 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Iliyas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
4:26b.LUK.004.026 Moona Yàlla yónniwul Iliyas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.
4:27b.LUK.004.027 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alisa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naaman, mi dëkkoon réewu Siri.»
4:28b.LUK.004.028 Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer.
4:29b.LUK.004.029 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.
4:30b.LUK.004.030 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.
4:31b.LUK.004.031 Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile.
4:32b.LUK.004.032 Mu jàngal leen ca bésu noflaay ba, ñu waaru ca njàngaleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ.
4:33b.LUK.004.033 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi xaacu ne:
4:34b.LUK.004.034 «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!»
4:35b.LUK.004.035 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanamu ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko.
4:36b.LUK.004.036 Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.»
4:37b.LUK.004.037 Noonu turam siiw ca diiwaan bépp.
4:38b.LUK.004.038 Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu naan Yeesu, mu dimbali leen ci.
4:39b.LUK.004.039 Mu randusi, tiim ko, gëdd tàngoor wi, mu dem. Noonu tàngoor wi wàcc, soxna si jóg ca saa sa, di leen topptoo.
4:40b.LUK.004.040 Bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ay jàngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, wéral la.
4:41b.LUK.004.041 Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne, mooy Almasi bi.
4:42b.LUK.004.042 Ca njël gu jëkk Yeesu génn, dem ca bérab bu wéet. Mbooloo ma di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu koy wut a téye, ngir bañ mu dem.
4:43b.LUK.004.043 Waaye mu ne leen: «Damaa war a dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma.»
4:44b.LUK.004.044 Noonu mu dem di waare ca jàngu ya ca réewu Yawut ya.
5
5:1b.LUK.005.001 Benn bés Yeesu taxaw ca tefesu dexu Senesaret. Mbooloo ma wër ko, di buuxante ngir déglu kàddug Yàlla.
5:2b.LUK.005.002 Noonu mu gis ñaari gaal yu teer ca tefes ga, nappkat ya ca wàcce, di raxas seeni mbaal.
5:3b.LUK.005.003 Mu dugg ci genn gaal, fekk muy gu Simoŋ, mu ne ko, mu joow ba sore tuuti. Noonu Yeesu toog ca gaal ga, di jàngal mbooloo ma.
5:4b.LUK.005.004 Bi mu jàngalee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gën a xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.»
5:5b.LUK.005.005 Simoŋ tontu ko ne: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.»
5:6b.LUK.005.006 Naka lañu sànni mbaal yi, jàpp jën yu bare, ba mbaal yay tàmbalee xëtt.
5:7b.LUK.005.007 Noonu ñu daldi liyaar seen àndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir ñu ñëw dimbali leen. Ñooñu agsi, ñu feesal ñaari gaal yi, ba ñuy bëgg a suux.
5:8b.LUK.005.008 Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanamu Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!»
5:9b.LUK.005.009 Wax na loolu nag, ndax jën yu bare ya ñu mbaaloon daf koo jaaxal, moom ak ña mu àndaloon
5:10b.LUK.005.010 ak ña mu bokkaloon liggéey ba, maanaam ñaari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaawsi tey, ay nit ngay mbaal jëme ci man.»
5:11b.LUK.005.011 Noonu ñu teer ca tefes ga, bàyyi lépp, di topp ci moom.
5:12b.LUK.005.012 Ni Yeesu nekke woon ci ab dëkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi dëpp jëwam ci suuf, ñaan ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
5:13b.LUK.005.013 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
5:14b.LUK.005.014 Yeesu sant ko ne: «Bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax si yoonu Musaa santaane, ngir ñu xam ne wér nga, te mu nekk seede ci ñoom.»
5:15b.LUK.005.015 Noonu turu Yeesu di gën a siiw. Mbooloo mu bare di ñëw ci moom, ngir déglu ko te mu faj seeni jàngoro.
5:16b.LUK.005.016 Waaye Yeesu moom di beddeeku ci bérab yu wéet ya, di ñaan.
5:17b.LUK.005.017 Am na bés Yeesu doon jàngale. Amoon na ca mbooloo, ma teewoon, ñu bokkoon ca Farisen ya ak ay xutbakat yu jóge ca dëkk yépp, ya ca Galile ak ya ca Yude ak Yerusalem. Yeesu àndoon na ak dooley Boroom bi, ba muy faj ay jarag.
5:18b.LUK.005.018 Noonu ay nit ñëw, jàppoo basaŋ, ga ñu tëral nit ku yaram wépp làggi. Ñu di ko wut a dugal ca kër ga, ngir indi ko ca Yeesu.
5:19b.LUK.005.019 Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu daldi yéeg ca kaw kër ga nag, xeddi tiwiil ya, yoor waa ja ak basaŋ ga, wàcce ko ca kanamu Yeesu ca biir mbooloo ma.
5:20b.LUK.005.020 Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne làggi ba: «Sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
5:21b.LUK.005.021 Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: «Kii mooy kan bay sosal Yàlla? Ana ku man a baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?»
5:22b.LUK.005.022 Waaye Yeesu xam seen xalaat, tontu leen ne: «Lu tax ngeen di werante ci seen xel?
5:23b.LUK.005.023 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb?
5:24b.LUK.005.024 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
5:25b.LUK.005.025 Nit ka jóg ca saa sa ci kanamu ñépp, jël basaŋ, ga ñu ko tëraloon, ñibbi tey màggal Yàlla.
5:26b.LUK.005.026 Mbooloo mépp waaru, di màggal Yàlla. Ñu ragal tey wax naan: «Gis nanu tey ay mbir yu ëpp xel.»
5:27b.LUK.005.027 Gannaaw loolu Yeesu génn, gis ab juutikat bu tudd Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay topp ci man.»
5:28b.LUK.005.028 Lewi jóg, bàyyi lépp, daldi ko topp.
5:29b.LUK.005.029 Noonu Lewi togglu ay ñam yu bare ci këram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan ñu nga fa woon, di lekkandoo ak ñoom.
5:30b.LUK.005.030 Farisen yi ak seeni xutbakat di xultu taalibey Yeesu yi ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak di naanandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
5:31b.LUK.005.031 Yeesu tontu leen ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
5:32b.LUK.005.032 Ñëwuma ngir woo ñi jub, waaye ngir woo bàkkaarkat yi, ñu tuub seeni bàkkaar.»
5:33b.LUK.005.033 Noonu ñu ne Yeesu: «Taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi dinañu faral di woor ak di ñaan ci Yàlla, waaye say taalibe ñu ngiy lekk ak di naan.»
5:34b.LUK.005.034 Yeesu ne leen: «Ndax man ngeen a woorloo gan, yi ñëw cig céet, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom?
5:35b.LUK.005.035 Waaye bés yaa ngi ñëw, yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir. Bés yooyu nag, dinañu woor.»
5:36b.LUK.005.036 Te it Yeesu wax leen léeb wii: «Kenn du jël mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu màggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci jële, du ànd ak mbubb mu màggat mi.
5:37b.LUK.005.037 Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bu bees bi day toj mbuus yi, biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu.
5:38b.LUK.005.038 Waaye dañoo war a def biiñ bu bees ci mbuus yu bees.
5:39b.LUK.005.039 Ku naan biiñ bu màggat du bëgg bu bees bi, ndax day wax ne: “Bu màggat bi baax na.”»
6
6:1b.LUK.006.001 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu di dem, jaar ci ay tool yu ñor. Taalibeem ya di fàq ay cëgg, di leen boxom ci seeni loxo tey lekk.
6:2b.LUK.006.002 Am ay Farisen yu ne: «Lu tax ngeen di def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi?»
6:3b.LUK.006.003 Yeesu tontu leen ne: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
6:4b.LUK.006.004 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu jébbal Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat.»
6:5b.LUK.006.005 Yeesu dellu ne leen: «Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»
6:6b.LUK.006.006 Beneen bésu noflaay, Yeesu dugg ci jàngu bi, di fa jàngale. Amoon na fa nit ku loxol ndeyjooram làggi.
6:7b.LUK.006.007 Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam dina ko faj ci bésu noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.
6:8b.LUK.006.008 Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanamu ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw.
6:9b.LUK.006.009 Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»
6:10b.LUK.006.010 Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wér peŋŋ.
6:11b.LUK.006.011 Waaye nit ña mer ba fees, di rabat pexe yu jëm ca Yeesu.
6:12b.LUK.006.012 Ca bés yooya Yeesu yéeg ca tund wa ngir ñaan, mu fanaan fa, di ñaan ci Yàlla.
6:13b.LUK.006.013 Bi bët setee, Yeesu woo taalibeem yi, tànn ci fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam:
6:14b.LUK.006.014 Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
6:15b.LUK.006.015 Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
6:16b.LUK.006.016 Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujj a wor.
6:17b.LUK.006.017 Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon.
6:18b.LUK.006.018 Dañoo ñëw ngir déglu ko, te it ngir mu faj leen. Ñi rab jàpp it faju nañu.
6:19b.LUK.006.019 Ñépp a ngi ko doon wut a laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp.
6:20b.LUK.006.020 Yeesu xool ay taalibeem ne leen:«Yéen ñi sësul lu dul ci Yàlla, barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo.
6:21b.LUK.006.021 Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen,ndax dingeen ree.
6:22b.LUK.006.022 Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki.
6:23b.LUK.006.023 Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi.
6:24b.LUK.006.024 Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen,ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex.
6:25b.LUK.006.025 Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen,ndax ëllëg dingeen xiif.Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen,ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc.
6:26b.LUK.006.026 Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent.
6:27b.LUK.006.027 «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ.
6:28b.LUK.006.028 Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.
6:29b.LUK.006.029 Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki.
6:30b.LUK.006.030 Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.
6:31b.LUK.006.031 Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.
6:32b.LUK.006.032 «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp.
6:33b.LUK.006.033 Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu.
6:34b.LUK.006.034 Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko.
6:35b.LUK.006.035 Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, bañ a yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne, yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.
6:36b.LUK.006.036 Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande.
6:37b.LUK.006.037 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal.
6:38b.LUK.006.038 Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkas te yengal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.»
6:39b.LUK.006.039 Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb?
6:40b.LUK.006.040 Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin.
6:41b.LUK.006.041 «Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
6:42b.LUK.006.042 Nan nga man a waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
6:43b.LUK.006.043 «Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax.
6:44b.LUK.006.044 Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla réseñ ci xaaxaam.
6:45b.LUK.006.045 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax.
6:46b.LUK.006.046 «Lu tax ngeen may wooye “Boroom bi, Boroom bi,” te dungeen def li may wax?
6:47b.LUK.006.047 Képp ku ñëw ci man, di dégg samay wax te di ko jëfe, ma won leen nu muy mel.
6:48b.LUK.006.048 Dafa mel ni nit kuy tabax kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa tabax kër ga tabax bu dëgër.
6:49b.LUK.006.049 Waaye képp ku dégg samay wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku tabax këram ci suuf, bañ koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca kër googa, dafa màbb ca saa sa, lépp yàqu yaxeet.»
7
7:1b.LUK.007.001 Bi Yeesu waxee la mu naroon a wax lépp ca kanamu mbooloo ma, mu daldi dem Kapernawum.
7:2b.LUK.007.002 Amoon na fa njiitu xare. Njiit la nag, surgaam bu mu bëggoon lool dafa feebaroon, bay bëgg a dee.
7:3b.LUK.007.003 Bi mu déggee mbiri Yeesu, mu yónni ca moom ay Yawut, di magi dëkk ba, ngir ñaan ko, mu ñëw faj surga ba.
7:4b.LUK.007.004 Bi magi dëkk ba agsee ca Yeesu, ñu sàkku ci moom ndimbal, ñaan ko: «Ki nu yónni ci yaw de, yelloo na ndimbal,
7:5b.LUK.007.005 ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu tabaxal sax sunu jàngu.»
7:6b.LUK.007.006 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom. Waaye bi ñuy bëgg a agsi ca kër ga, njiit la yebal ay xaritam ngir ñu wax Yeesu ne: «Sang bi, bul sonal sa bopp, ndaxte yeyoowuma nga dugg sama kër.
7:7b.LUK.007.007 Looloo tax it ma xalaat ne, awma darajay gatandu la. Waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
7:8b.LUK.007.008 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
7:9b.LUK.007.009 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, musuma cee gis ku gëme nii.»
7:10b.LUK.007.010 Noonu ndaw ya daldi dellu ca kër ga. Bi ñu agsee, ñu gis ne surga ba wér na.
7:11b.LUK.007.011 Yàggul dara Yeesu dem ci dëkk bu ñuy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
7:12b.LUK.007.012 Bi muy agsi ca buntu dëkk ba, fekk ñuy rob néew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji jëkkëram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca dëkk ba di gunge soxna sa.
7:13b.LUK.007.013 Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy yërëm ne ko: «Bul jooyati.»
7:14b.LUK.007.014 Mu jegeñsi, laal jaat ga, ñi ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Waxambaane wi, jógal, ndigal la.»
7:15b.LUK.007.015 Noonu nit ka dee woon jóg toog, tàmbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja.
7:16b.LUK.007.016 Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!»
7:17b.LUK.007.017 La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp.
7:18b.LUK.007.018 Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem,
7:19b.LUK.007.019 yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?»
7:20b.LUK.007.020 Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroon a ñëw, walla danuy xaar keneen?»
7:21b.LUK.007.021 Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba.
7:22b.LUK.007.022 Noonu mu tontu ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi.
7:23b.LUK.007.023 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
7:24b.LUK.007.024 Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
7:25b.LUK.007.025 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur.
7:26b.LUK.007.026 Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent.
7:27b.LUK.007.027 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.”
7:28b.LUK.007.028 Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»
7:29b.LUK.007.029 Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox.
7:30b.LUK.007.030 Waaye Farisen ya ak xutbakat ya dañoo bañ, mu sóob leen ci ndox, di wone noonu ne, gàntu nañu li leen Yàlla bëggaloon.
7:31b.LUK.007.031 Yeesu tegaat ca ne: «Kon lan laa man a mengaleel niti jamono jii? Lan lañuy nirool?
7:32b.LUK.007.032 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma tey woowante naan:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
7:33b.LUK.007.033 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
7:34b.LUK.007.034 Gannaaw gi nag Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.”
7:35b.LUK.007.035 Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
7:36b.LUK.007.036 Amoon na ab Farisen bu ñaan Yeesu, mu ñëw lekkandoo ak moom. Yeesu dem kër waa ja, toog ca lekkukaay.
7:37b.LUK.007.037 Fekk amoon na ca dëkk ba jigéen juy moy Yàlla. Bi mu yégee ne, Yeesoo ngay lekk ca kër Farisen ba, mu dem, yóbbaale njaq lu ñu defare doj wu ñuy wax albaatar te def latkoloñ.
7:38b.LUK.007.038 Bi jigéen ja agsee, mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu, di jooy. Noonu ay rangooñam tooyal tànki Yeesu, jigéen ja di leen fomp ak kawaram, di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja.
7:39b.LUK.007.039 Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci këram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: «Bu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jigéen ji koy laal ak ni mu nekke bàkkaarkat.»
7:40b.LUK.007.040 Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la war a wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.»
7:41b.LUK.007.041 Yeesu ne ko: «Da fee amoon ñaari nit ñu ameel bor benn leblekat. Kenn kaa ngi ko ameel téeméeri junni ci xaalis, ki ci des fukki junni.
7:42b.LUK.007.042 Waaye kenn ci ñoom mënu koo fey. Noonu mu baal leen bor ya. Ci ñaar ñooñu nag kan moo ko ciy gën a bëgg?»
7:43b.LUK.007.043 Simoŋ tontu ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gën a bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,»
7:44b.LUK.007.044 daldi walbatiku ca jigéen ja, ne Simoŋ: «Ndax gis nga jigéen jii? Dugg naa sa kër, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay tànk. Waaye moom, raxas na samay tànk ak ay rangooñam, ba noppi fomp leen ak kawaram.
7:45b.LUK.007.045 Bi ma agsee, fóonuloo ma, waaye moom, bi ma duggee ba léegi tàyyiwul ci di fóon samay tànk.
7:46b.LUK.007.046 Defuloo diw ci sama bopp, waaye moom, sotti na latkoloñ ci samay tànk.
7:47b.LUK.007.047 Moo tax ma di la wax ne, su wonee mbëggeel gu réye nii, dafa fekk ñu baal ko bàkkaaram yu bare. Waaye ki mbëggeelam néew dafa fekk ñu baal ko lu tuuti.»
7:48b.LUK.007.048 Yeesu daldi ne jigéen ja: «Baal nañu la say bàkkaar.»
7:49b.LUK.007.049 Noonu ñi doon lekkandoo ak moom di wax ci seen xel naan: «Kii am sañ-sañu baale bàkkaar mooy kan?»
7:50b.LUK.007.050 Waaye Yeesu ne jigéen ja: «Sa ngëm musal na la. Demal ci jàmm.»
8
8:1b.LUK.008.001 Gannaaw loolu Yeesu di dem ca ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di waaraate ak di yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla. Fukki taalibe ya ak ñaar ànd ak moom,
8:2b.LUK.008.002 ak ay jigéen yu mu teqale woon ak rab te jële leen ci seeni wopp, ñu di: Maryaama, mi ñuy wooye Maryaamam Magdala, mi Yeesu tàggale woon ak juróom-ñaari rab;
8:3b.LUK.008.003 Sànn, jabaru ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem.
8:4b.LUK.008.004 Dëkk ak dëkk nit ña di fa jóge jëm ca Yeesu, ba mbooloo mu bare dajaloo, mu wax leen léeb wii:
8:5b.LUK.008.005 «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, nit ñi joggi ci, picci asamaan lekk ko lépp.
8:6b.LUK.008.006 Leneen wadd ci bérab bu bare ay doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndaxte suuf si tooyul woon.
8:7b.LUK.008.007 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, ñu saxandoo, xaaxaam ya tanc ko.
8:8b.LUK.008.008 Li ci des dal ci suuf su baax, sax, nangu ba meññ téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon.» Gannaaw loolu Yeesu wax ak kàddu gu dëgër ne: «Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
8:9b.LUK.008.009 Taalibey Yeesu yi laaj ko lu léeb woowu di tekki.
8:10b.LUK.008.010 Mu tontu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir:“Ñuy xool te duñu man a gis,di dégg te duñu man a xam.”
8:11b.LUK.008.011 «Lii la léebu beykat bi di tekki. Kàddug Yàlla mooy jiwu wi.
8:12b.LUK.008.012 Ki féete ci yoon wi mooy ki dégg. Gannaaw gi, Seytaane dafay ñëw, këf kàddu, gi ñu def ci xolam, ngir mu bañ a gëm te Yàlla musal ko.
8:13b.LUK.008.013 Ki nekk ci bérab bu bare ay doj, mooy ki dégg kàddu gi, ba noppi nangu ko ak mbég. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina gëm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi dàggeeku.
8:14b.LUK.008.014 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nes tuuti soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat.
8:15b.LUK.008.015 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg kàddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te muñ ba jur njariñ.
8:16b.LUK.008.016 «Kenn du taal làmp, dëpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
8:17b.LUK.008.017 Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu ne fàŋŋ.
8:18b.LUK.008.018 Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo kàddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne, am nga ko ba noppi.»
8:19b.LUK.008.019 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam ñëw seetsi ko, waaye mënuñu woon a agsi ci moom, ndaxte nit ña dañoo bare.
8:20b.LUK.008.020 Am ku ko yégal ne: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg laa gis.»
8:21b.LUK.008.021 Waaye mu daldi leen ne: «Sama yaay ak samay rakk, ñooy ñiy déglu kàddug Yàlla, te di ko topp.»
8:22b.LUK.008.022 Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem.
8:23b.LUK.008.023 Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yengal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgg a suux.
8:24b.LUK.008.024 Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
8:25b.LUK.008.025 Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.»
8:26b.LUK.008.026 Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
8:27b.LUK.008.027 Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk.
8:28b.LUK.008.028 Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.»
8:29b.LUK.008.029 Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon faral a jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet.
8:30b.LUK.008.030 Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu tontu ne: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon.
8:31b.LUK.008.031 Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leen a sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi.
8:32b.LUK.008.032 Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
8:33b.LUK.008.033 Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.
8:34b.LUK.008.034 Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba.
8:35b.LUK.008.035 Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
8:36b.LUK.008.036 Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon.
8:37b.LUK.008.037 Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgg a dem.
8:38b.LUK.008.038 Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu woññi ko ne ko:
8:39b.LUK.008.039 «Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal.
8:40b.LUK.008.040 Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar.
8:41b.LUK.008.041 Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, saraxu ko mu ñëw këram,
8:42b.LUK.008.042 ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaj a dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc.
8:43b.LUK.008.043 Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn mënu ko woon a faj.
8:44b.LUK.008.044 Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.
8:45b.LUK.008.045 Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.»
8:46b.LUK.008.046 Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne, am na doole ju génn ci man.»
8:47b.LUK.008.047 Te jigéen ja xam ne, mënul woon a nëbb li mu def. Mu daldi daanu ci tànki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanamu ñépp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu wére ca saa sa.
8:48b.LUK.008.048 Yeesu ne ko: «Soxna si, sa ngëm faj na la. Demal ci jàmm.»
8:49b.LUK.008.049 Bi Yeesu di wax nag, am na ku jóge ca kër njiit la, mu ñëw naan: «Sa doom faatu na; matatul ngay sonal kilifa gi.»
8:50b.LUK.008.050 Yeesu dégg kàddu yooyu, daldi ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk te dina dundaat.»
8:51b.LUK.008.051 Bi Yeesu agsee ca kër ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, ñu dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba.
8:52b.LUK.008.052 Ña fa nekk ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
8:53b.LUK.008.053 Waaye ñu di ko ñaawal, ndaxte xamoon nañu ne, dee na.
8:54b.LUK.008.054 Waaye Yeesu jàpp loxob janq ba, woo ko ne ko: «Xale bi, jógal.»
8:55b.LUK.008.055 Noonu ruuwu xale ba dellusiwaat, mu daldi jóg ca saa sa. Yeesu santaane ñu may ko, mu lekk.
8:56b.LUK.008.056 Waajuri xale bi daldi waaru. Waaye Yeesu tere leen, ñu wax kenn li xew.
9
9:1b.LUK.009.001 Benn bés Yeesu dajale fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen doole ak sañ-sañu dàq rab yépp ak di faj jàngoro yi.
9:2b.LUK.009.002 Noonu mu yónni leen ñuy yégle nguuru Yàlla ak di faj jarag yi.
9:3b.LUK.009.003 Mu ne leen: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it ñaari turki.
9:4b.LUK.009.004 Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge.
9:5b.LUK.009.005 Fépp fu leen nit ñi gàntoo, génnleen ca dëkk booba te ngeen yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
9:6b.LUK.009.006 Noonu ñu dem dëkk ak dëkk, di fa yégle xebaar bu baax bi, tey wéral jarag yi.
9:7b.LUK.009.007 Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.»
9:8b.LUK.009.008 Am it ñuy wax naan: Iliyas moo dellusi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
9:9b.LUK.009.009 Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis.
9:10b.LUK.009.010 Bi ndaw ya dellusee, ñu nettali Yeesu la ñu defoon lépp. Noonu mu yóbbaale leen, ñu sore nit ñi, jëm ca dëkk bu ñuy wax Betsayda.
9:11b.LUK.009.011 Bi ko nit ña yégee, ñu toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Yàlla, te di wéral ñi ko aajowoo.
9:12b.LUK.009.012 Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak ñaar ñëw ci Yeesu ne ko: «Yiwil mbooloo mi, ñu dugg ci dëkk yi ak àll bi ko wër, ngir am lu ñu lekk ak fu ñu fanaan, ndaxte fii àllub neen la.»
9:13b.LUK.009.013 Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu tontu ko ne: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?»
9:14b.LUK.009.014 Ndaxte lu war a mat juróomi junniy góor a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: «Neeleen mbooloo mi ñu toog def ay géewi juróom-fukki nit.»
9:15b.LUK.009.015 Taalibe ya def ko, toogloo nit ña.
9:16b.LUK.009.016 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, gërëm Yàlla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi.
9:17b.LUK.009.017 Noonu ñépp lekk ba suur. Bi ñu dajalee desit ya, ñu feesal fukki pañe ak ñaar.
9:18b.LUK.009.018 Benn bés Yeesu beddeeku mbooloo ma, di ñaan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: «Nit ñi, ku ñu wax ne moom laa?»
9:19b.LUK.009.019 Ñu tontu ko ne: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Iliyas; ñi ci des ne, yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki.»
9:20b.LUK.009.020 Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer tontu ko ne: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.»
9:21b.LUK.009.021 Noonu Yeesu daldi leen dénk, tere leen ñu wax ko kenn,
9:22b.LUK.009.022 teg ca ne: «Doomu nit ki war na sonn lu bare; saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya dëddu ko, ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.»
9:23b.LUK.009.023 Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man.
9:24b.LUK.009.024 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat.
9:25b.LUK.009.025 Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru?
9:26b.LUK.009.026 Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rus a xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi.
9:27b.LUK.009.027 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw ñoo xam ne duñu dee te gisuñu nguuru Yàlla gi.»
9:28b.LUK.009.028 Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan.
9:29b.LUK.009.029 Bi muy ñaan, xar-kanamam daldi soppiku, ay yéreem weex tàll bay melax.
9:30b.LUK.009.030 Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas.
9:31b.LUK.009.031 Ñoo feeñ ci ndamu Yàlla, di waxtaane ci demu Yeesu, gi muy àggalee yenam ci Yerusalem.
9:32b.LUK.009.032 Fekk Piyeer ak ñi mu àndal doon gëmmeentu, waaye bi ñu yeewoo bu baax, ñu gis ndamu Yeesu, ak ñaari nit ñu taxaw ci wetam.
9:33b.LUK.009.033 Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.» Fekk xamul la mu doon wax.
9:34b.LUK.009.034 Bi mu koy wax, niir ñëw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa ëmbee.
9:35b.LUK.009.035 Noonu baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma fal; dégluleen ko.»
9:36b.LUK.009.036 Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, bañ a nettali kenn ca jamono jooja la ñu gisoon.
9:37b.LUK.009.037 Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare ñëw, di ko gatandu.
9:38b.LUK.009.038 Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: «Kilifa gi, maa ngi lay ñaan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am.
9:39b.LUK.009.039 Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal.
9:40b.LUK.009.040 Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye mënuñu ko.»
9:41b.LUK.009.041 Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»
9:42b.LUK.009.042 Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi gëdd rab wa, wéral xale ba, daldi ko delloo baayam.
9:43b.LUK.009.043 Ku nekk waaru na ndax màggug Yàlla. Bi ñuy yéemu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya:
9:44b.LUK.009.044 «Dégluleen bu baax lii ma leen di wax: dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi.»
9:45b.LUK.009.045 Waaye taalibe ya xamuñu kàddu googu. Yàlla dafa leen nëbb li muy tekki, ba ñu bañ koo xam, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
9:46b.LUK.009.046 Werante am ci biir taalibe yi, ñuy laajante kan moo gën a màgg ci ñoom.
9:47b.LUK.009.047 Yeesu mi xam seen xalaat, jël ab xale, teg ci wetam ne leen:
9:48b.LUK.009.048 «Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gën a woyof ci yéen ñépp, kooku moo gën a màgg.»
9:49b.LUK.009.049 Bi loolu amee Yowaana jël kàddu gi ne: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.»
9:50b.LUK.009.050 Waaye Yeesu tontu ko: «Buleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.»
9:51b.LUK.009.051 Bi jamono ji jegeñsee, ji Yeesu waree jóge àddina dem asamaan, mu sigiñu ci dem Yerusalem.
9:52b.LUK.009.052 Noonu mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem nag, dugg ci ab dëkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.
9:53b.LUK.009.053 Waaye waa dëkk ba nanguwuñu ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.
9:54b.LUK.009.054 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, ñu ne: «Boroom bi, ndax dangaa bëgg nu ne, na safaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?»
9:55b.LUK.009.055 Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya,
9:56b.LUK.009.056 ba noppi ñu daldi dem wuti beneen dëkk.
9:57b.LUK.009.057 Bi ñuy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: «Dinaa la topp fépp foo jëm.»
9:58b.LUK.009.058 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
9:59b.LUK.009.059 Yeesu ne keneen: «Toppal ci man.» Waaye kooku ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.»
9:60b.LUK.009.060 Mu tontu ko ne: «Bàyyil ñi dee, ñu suul seeni néew. Yaw demal, yégle nguuru Yàlla.»
9:61b.LUK.009.061 Keneen ne ko: «Sang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma jëkk a tàgguji sama waa kër.»
9:62b.LUK.009.062 Yeesu ne ko: «Kuy ji, di geestu, yeyoowul a liggéey ci nguuru Yàlla.»
10
10:1b.LUK.010.001 Gannaaw loolu Boroom bi tànn na yeneen juróom-ñaar-fukki taalibe ak ñaar, yebal leen, ñu ànd ñaar ak ñaar, jiituji ko ca dëkk yépp ak ca bérab yépp, ya mu naroon a dem moom ci boppam.
10:2b.LUK.010.002 Mu ne leen: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.
10:3b.LUK.010.003 Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki.
10:4b.LUK.010.004 Buleen yor xaalis walla mbuus walla ay dàll. Buleen nuyu kenn ci yoon wi.
10:5b.LUK.010.005 «Kër gu ngeen man a dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.”
10:6b.LUK.010.006 Bu fa nitu jàmm nekkee, seen yéene dina ko indil jàmm. Lu ko moy, seen yéene dina dellusi ci yéen.
10:7b.LUK.010.007 Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër.
10:8b.LUK.010.008 «Dëkk bu ngeen man a dugg, te waa dëkk ba teeru leen, lu ñu leen jox, lekkleen ko.
10:9b.LUK.010.009 Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.”
10:10b.LUK.010.010 Waaye bu ngeen duggee ci dëkk te teeruwuñu leen, demleen ca mbedd ya te ne leen:
10:11b.LUK.010.011 “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne, nguuru Yàlla jegesi na.”
10:12b.LUK.010.012 Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu.
10:13b.LUK.010.013 «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
10:14b.LUK.010.014 Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
10:15b.LUK.010.015 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe.
10:16b.LUK.010.016 «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.»
10:17b.LUK.010.017 Juróom-ñaar-fukki taalibe yi ak ñaar dellusi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.»
10:18b.LUK.010.018 Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni safaras melax.
10:19b.LUK.010.019 Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen man a gaañ.
10:20b.LUK.010.020 Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.»
10:21b.LUK.010.021 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi. Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.»
10:22b.LUK.010.022 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënul a xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn mënul a xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.»
10:23b.LUK.010.023 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég.
10:24b.LUK.010.024 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.»
10:25b.LUK.010.025 Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def, ba am dund gu dul jeex?»
10:26b.LUK.010.026 Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?»
10:27b.LUK.010.027 Nit ka ne ko: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”»
10:28b.LUK.010.028 Yeesu ne ko nag: «Li nga wax dëgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba fàww.»
10:29b.LUK.010.029 Waaye xutbakat ba bëggoon a am aw lay, ne Yeesu: «Kan mooy sama moroom nag?»
10:30b.LUK.010.030 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko ba muy bëgg a dee, dem bàyyi ko fa.
10:31b.LUK.010.031 Faf ab saraxalekat jaar ca yoon wa, séen nit ka, teggi.
10:32b.LUK.010.032 Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca bérab booba, séen waa ja, teggi.
10:33b.LUK.010.033 Waaye benn waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko.
10:34b.LUK.010.034 Noonu mu ñëw, diw ko diwlin ak biiñ ngir faj gaañu-gaañu ya, bandaas ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo.
10:35b.LUK.010.035 Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”»
10:36b.LUK.010.036 Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?»
10:37b.LUK.010.037 Xutbakat ba tontu ko ne: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.»
10:38b.LUK.010.038 Bi Yeesu ak ay taalibeem nekkee ci yoon wi, mu dugg ci benn dëkk, fekk fa jigéen ju tudd Màrt, ganale ko.
10:39b.LUK.010.039 Màrt nag amoon rakk ju tudd Maryaama, ma nga toog ci tànki Boroom bi, di déglu ay kàddoom.
10:40b.LUK.010.040 Fekk Màrt jàpp lool ca waañ wa. Noonu mu ñëw ci wetu Yeesu ne ko: «Boroom bi, doo ci wax dara, boo gisee sama rakk ji bàyyi ma ak liggéey bi yépp? Ne ko mu jàpple ma.»
10:41b.LUK.010.041 Boroom bi tontu ko ne: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu.
10:42b.LUK.010.042 Moona de, lenn rekk a am solo. Maryaama dafa tànn cér bi gën, te kenn du ko nangu ci moom.»
11
11:1b.LUK.011.001 Am bés Yeesu di ñaan ci benn bérab. Bi mu noppee, kenn ci taalibeem yi ne ko: «Boroom bi, jàngal nu, nan lanu war a ñaane, ni ko Yaxya jàngale ay taalibeem.»
11:2b.LUK.011.002 Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee ñaan, nangeen ne:“Baay bi, na sa tur sell,na sa nguur ñëw.
11:3b.LUK.011.003 May nu bés bu nekk li nu war a dunde.
11:4b.LUK.011.004 Baal nu sunuy bàkkaar,ndaxte nun itam danuy baal ñépp ñi nu tooñ.Te bu nu teg ci yoonu nattu.”»
11:5b.LUK.011.005 Yeesu teg ca ne leen: «Mi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: “Xarit, lebal ma ñetti mburu.
11:6b.LUK.011.006 Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.”
11:7b.LUK.011.007 «Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko tontu: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd, man ak sama njaboot; mënumaa jóg di la jox dara.”
11:8b.LUK.011.008 Maa ngi leen koy wax, su jógul jox ko li muy laaj ndax li ñu xaritoo it, ndax la kee ñàkk jom dina tax mu jox ko lépp li mu soxla.
11:9b.LUK.011.009 Moo tax ma ne, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
11:10b.LUK.011.010 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
11:11b.LUK.011.011 Bu la sa doom ñaanee jën, yaw miy baayam, ndax dinga ko bañ a jox jën, jox ko jaan?
11:12b.LUK.011.012 Walla mu ñaan la nen, nga jox ko jiit?
11:13b.LUK.011.013 Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!»
11:14b.LUK.011.014 Am bés Yeesu dàq rab wu luu. Naka la rab wa génn, luu ba daldi wax, ba mbooloo may yéemu.
11:15b.LUK.011.015 Waaye am ca mbooloo ma ay nit, ñu doon wax naan: «Ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
11:16b.LUK.011.016 Am ñeneen ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam.
11:17b.LUK.011.017 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, kër gu xeex boppam gent.
11:18b.LUK.011.018 Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di man a yàgge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay dàq rab jaarale ko ci kàttanu Beelsebul.
11:19b.LUK.011.019 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
11:20b.LUK.011.020 Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
11:21b.LUK.011.021 «Su nit ku bare doole gànnaayoo, di wottu këram, alalam dina raw.
11:22b.LUK.011.022 Waaye bu ku ko ëpp doole ñëwee, daan ko, dafay nangu gànnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi séddale alal ja.
11:23b.LUK.011.023 Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.
11:24b.LUK.011.024 «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”
11:25b.LUK.011.025 Bu ñëwee nag, mu fekk këram, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
11:26b.LUK.011.026 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor. Ñu dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy yées njàlbéenam.»
11:27b.LUK.011.027 Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!»
11:28b.LUK.011.028 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Neel kay, ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.»
11:29b.LUK.011.029 Naka la mbooloo may gën a takku, Yeesu ne: «Niti jamono jii dañoo bon. Ñu ngi laaj firnde, waaye duñu jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.
11:30b.LUK.011.030 Ndaxte ni Yunus nekke woon firnde ci waa dëkku Niniw, noonu la Doomu nit kiy nekke firnde ci niti jamono jii.
11:31b.LUK.011.031 Keroog bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
11:32b.LUK.011.032 Te it ca bés pénc, waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen, ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fii.
11:33b.LUK.011.033 «Kenn du taal làmp, ba noppi di ko duggal cig kàmb, walla di ci këpp leget. Daf koy wékk, ngir mu leeral ñiy dugg.
11:34b.LUK.011.034 Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer. Waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm.
11:35b.LUK.011.035 Moytul ndax leer gi nekk ci yaw du lëndëm.
11:36b.LUK.011.036 Kon bu sa yaram wépp nekkee ci leer te amul genn wet gu laal ci lëndëm, dina leer nàññ, mel ni leeraayu làmp ne ràyy ci sa kaw.»
11:37b.LUK.011.037 Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu ñëw lekke këram. Yeesu dugg ca kër ga, toog ca lekkukaay ba.
11:38b.LUK.011.038 Farisen bi nag daldi jaaxle, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk.
11:39b.LUK.011.039 Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeen a fees ak càcc ak mbon!
11:40b.LUK.011.040 Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam?
11:41b.LUK.011.041 Saraxeleen li nekk ci biir te seen lépp dina sell.
11:42b.LUK.011.042 Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des.
11:43b.LUK.011.043 Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma.
11:44b.LUK.011.044 Dingeen torox, ndaxte dangeen a mel ni ay bàmmeel yu raaf, ba nit ñi di ci dox te teyuñu ko.»
11:45b.LUK.011.045 Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: «Kilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.»
11:46b.LUK.011.046 Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam.
11:47b.LUK.011.047 Dingeen torox, ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon.
11:48b.LUK.011.048 Dangeen di seede noonu ne, ànd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte ñoo rey yonent yi, yéen ngeen tabax xabru yi.
11:49b.LUK.011.049 Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.”
11:50b.LUK.011.050 Kon nag Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax dereti yonent yi ñu tuur, ba àddina sosoo ak léegi,
11:51b.LUK.011.051 la dale ca Abel ba ci Sakariya, moom mi ñu rey ci diggante saraxalukaay bi ak bérab bu sell bi. Waaw, maa ngi leen koy wax, Yàlla dina mbugal niti jamono jii ndax loolu.
11:52b.LUK.011.052 Yéen xutbakat yi, dingeen torox, ndaxte yéena yóbbu caabiy xam-xam; dugguleen ci, te ku ci bëgg a dugg, ngeen tere ko ko.»
11:53b.LUK.011.053 Bi Yeesu génnee bérab boobu, Farisen ya ak xutbakat ya ëmbal ko mer te di ko seetlu ci fànn gu nekk,
11:54b.LUK.011.054 di ko yeeru, bëgg a këf waxam bu awul yoon.
12
12:1b.LUK.012.001 Gannaaw loolu, naka la mbooloo ma dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, di tancante, Yeesu tàmbalee wax jëmale ca taalibeem ya ne leen: «Moytuleen lawiiru Farisen ya, li di naaféq.
12:2b.LUK.012.002 Amul dara lu nëbbu lu ñu warul a biral, mbaa lu kumpa lu ñu warul a siiwal.
12:3b.LUK.012.003 Looloo tax lu ngeen wax ci biir lëndëm, dees na ko dégg ci leer. Lu ngeen déey nit ci biir néeg, dees na ko yégle ci kaw taax yi.
12:4b.LUK.012.004 «Maa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal ñu man a rey yaram, ba noppi dootuñu man a def dara.
12:5b.LUK.012.005 Dinaa leen wax nag ki ngeen war a ragal: ragal-leen Ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca safara. Waaw maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku.
12:6b.LUK.012.006 Juróomi picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom.
12:7b.LUK.012.007 Seen kawari bopp sax waññees na leen. Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu.
12:8b.LUK.012.008 «Te maa ngi leen koy wax, képp ku ma nangu ci kanamu nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanamu malaakay Yàlla yi.
12:9b.LUK.012.009 Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, dinañu la gàntu ci kanamu malaakay Yàlla yi.
12:10b.LUK.012.010 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko baal.
12:11b.LUK.012.011 «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanamu kilifa ya ak àttekat ya, buleen am xel ñaar ci li ngeen war a tontu ak nan ngeen war a tontoo, walla lu ngeen war a wax,
12:12b.LUK.012.012 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen war a wax.»
12:13b.LUK.012.013 Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: «Kilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu sédd ma ci sunu ndono.»
12:14b.LUK.012.014 Yeesu tontu ko ne: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen séddaleel seen alal?»
12:15b.LUK.012.015 Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree-bare.»
12:16b.LUK.012.016 Noonu mu dégtal leen wii léeb ne: «Dafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool,
12:17b.LUK.012.017 muy werante ci xelam naan: “Nu ma war a def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.”
12:18b.LUK.012.018 Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gën a réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am jépp.
12:19b.LUK.012.019 Te dinaa kañ sama bopp ne: ’Yaw mii, am nga alal ju bare ju man a dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey bég.’ ”
12:20b.LUK.012.020 Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?”
12:21b.LUK.012.021 «Kiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Yàlla, lu mel nii moo lay dal.»
12:22b.LUK.012.022 Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen war a sol,
12:23b.LUK.012.023 ndaxte bakkan moo gën lekk, te yaram a gën koddaay.
12:24b.LUK.012.024 Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi!
12:25b.LUK.012.025 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem, moo man a yokk ab waxtu ci àppam?
12:26b.LUK.012.026 Su fekkee lu tuuti loolu rekk mënuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?
12:27b.LUK.012.027 «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam, soluwul woon ni benn ci ñoom.
12:28b.LUK.012.028 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxu tool yi, miy sax tey te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd?
12:29b.LUK.012.029 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle.
12:30b.LUK.012.030 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay xam na ne, soxla ngeen ko.
12:31b.LUK.012.031 Waaye wutleen nguuram, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
12:32b.LUK.012.032 «Buleen ragal dara, yéen coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram.
12:33b.LUK.012.033 Jaayleen seen alal, saraxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq.
12:34b.LUK.012.034 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
12:35b.LUK.012.035 «Takkuleen bu dëgër te bàyyi làmp yi tàkk.
12:36b.LUK.012.036 Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa.
12:37b.LUK.012.037 Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gën a yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi.
12:38b.LUK.012.038 Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay ñëw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu ñoo gën a yeyoo ngërëm.
12:39b.LUK.012.039 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, du ko bàyyi, mu toj këram.
12:40b.LUK.012.040 Yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
12:41b.LUK.012.041 Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?»
12:42b.LUK.012.042 Boroom bi tontu ko ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji?
12:43b.LUK.012.043 Bu njaatigeem ñëwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
12:44b.LUK.012.044 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
12:45b.LUK.012.045 Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di màndi,
12:46b.LUK.012.046 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko dóor ay dóor yu metti, jox ko añub ñi gëmul Yàlla.
12:47b.LUK.012.047 «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti.
12:48b.LUK.012.048 Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyiku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp.
12:49b.LUK.012.049 «Damaa ñëw ngir indi safara si ci àddina, te bëgg naa xaat taal bi tàkk.
12:50b.LUK.012.050 Fàww ñu sóob ma ci metit, te ba looluy mat, duma noppalu.
12:51b.LUK.012.051 Ndax dangeen a xalaat ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina? Déedéet. Maa ngi leen koy wax, damaa ñëw ngir indi féewaloo.
12:52b.LUK.012.052 Gannaawsi tey, bu juróomi nit bokkee genn kër, dinañu féewaloo. Ñett dinañu féewaloo ak ñaar ñi ci des, ñaar ñi féewaloo ak ñett ñooñu.
12:53b.LUK.012.053 Baay bi dina féewaloo ak doom ji, doom ji ak baayam. Ndey dina féewaloo ak doomam ju jigéen; doom ju jigéen ji ak ndeyam. Goro dina féewaloo ak jabaru doomam; jabaru nit ak goroom.»
12:54b.LUK.012.054 Yeesu neeti mbooloo ma: «Bu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: “Dina taw,” te mooy am.
12:55b.LUK.012.055 Te bu ngeen yégee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: “Dina tàng tàngaay wu metti,” te mooy am.
12:56b.LUK.012.056 Naaféq yi ngeen doon! Man ngeen a ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax mënuleen a ràññee li jamonoy léegi ji di tekki?
12:57b.LUK.012.057 «Lu tax it dungeen àtteel seen bopp liy jëf ju jub?
12:58b.LUK.012.058 Bu la nit jiiñee dara, ba ngeen ànd di dem ca àttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la yóbbu ci yoon, yoon jébbal la ca loxoy alkaati ba, mu tëj la.
12:59b.LUK.012.059 Maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.»
13
13:1b.LUK.013.001 Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla.
13:2b.LUK.013.002 Mu tontu leen ne: «Mbaa du dangeen a xalaat ne, waa Galile yooyu dañoo gën a nekk bàkkaarkat ña ca des, ndax coono bi ñu daj?
13:3b.LUK.013.003 Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.
13:4b.LUK.013.004 Te fukki nit ak juróom-ñett ñooñu dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeen a yaakaar ne, ñoo gën a nekk ay tooñkat ñeneen ñi dëkk Yerusalem yépp?
13:5b.LUK.013.005 Maa ngi leen di wax ne, du dëgg. Waaye su ngeen tuubul seeni bàkkaar, dingeen sànku noonu, yéen ñépp itam.»
13:6b.LUK.013.006 Noonu mu daldi leen wax léeb wii: «Nit amoon na ci toolam garab gu ñu naan figg. Benn bés mu ñëw di ko raas-si, fekku fa benn doom.
13:7b.LUK.013.007 Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?”
13:8b.LUK.013.008 Surga ba tontu ko ne: “Sang bi, bàyyiwaat ko fi at mii. Dinaa wàqi taat wi, def ci tos.
13:9b.LUK.013.009 Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
13:10b.LUK.013.010 Benn bésu noflaay Yeesoo ngi doon jàngale ci ab jàngu.
13:11b.LUK.013.011 Amoon na fa jigéen ju rab jàppoon, ba feebarloo ko lu war a mat fukki at ak juróom-ñett; dafa xuuge woon te mënul woon a siggi dara.
13:12b.LUK.013.012 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: «Soxna si, sa feebar deñ na.»
13:13b.LUK.013.013 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di màggal Yàlla.
13:14b.LUK.013.014 Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésu noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom-benni fan yu nit ñi war a liggéey. Kon war ngeen a ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésu noflaay bi.»
13:15b.LUK.013.015 Boroom bi tontu ko: «Naaféq yi! Ndax bésu noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?
13:16b.LUK.013.016 Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom-ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésu noflaay bi?»
13:17b.LUK.013.017 Naka la wax loolu, noonam yépp daldi rus, waaye mbooloo mi di bég ci jëf yu yéeme, yi mu doon def yépp.
13:18b.LUK.013.018 Noonu Yeesu neeti: «Lan la nguuru Yàlla di nirool? Lan laa ko man a mengaleel?
13:19b.LUK.013.019 Mi ngi mel ni doomu fuddën gu nit jël, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
13:20b.LUK.013.020 Mu neeti: «Lan laa man a mengaleek nguuru Yàlla?
13:21b.LUK.013.021 Mi ngi mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
13:22b.LUK.013.022 Yeesoo ngi doon jaar ci ay dëkk yu mag ak yu ndaw, di jàngale te jublu Yerusalem.
13:23b.LUK.013.023 Am ku ko ne: «Boroom bi, ndax ñiy mucc ñu néew lay doon?» Yeesu ne leen:
13:24b.LUK.013.024 «Defleen seen kem-kàttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu jéem a dugg, waaye duñu ko man.
13:25b.LUK.013.025 Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Dina leen tontu ne: “Xawma fu ngeen bokk.”
13:26b.LUK.013.026 Bu ko defee dingeen tàmbalee naan: “Noo doon bokk di lekk ak di naan, te jàngale nga ci sunuy pénc.”
13:27b.LUK.013.027 Waaye dina ne: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!”
13:28b.LUK.013.028 Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.
13:29b.LUK.013.029 Ay nit dinañu jóge penku ak sowu, nor ak sudd, ñëw, bokk lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram.
13:30b.LUK.013.030 Noonu ñenn ci ñi mujj ñooy jiituji; te ci ñi jiitu, ñooy mujji.»
13:31b.LUK.013.031 Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wut a rey.»
13:32b.LUK.013.032 Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.”
13:33b.LUK.013.033 Waaye fàww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesul a reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.
13:34b.LUK.013.034 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen!
13:35b.LUK.013.035 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
14
14:1b.LUK.014.001 Benn bésu noflaay Yeesu dem ci këru benn kilifag Farisen yi, ngir lekke fa. Nit ñaa ngi ko doon xool bu baax.
14:2b.LUK.014.002 Faf am ca kanamam nit ku feebaroon, ay tànkam newi.
14:3b.LUK.014.003 Yeesu yékkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: «Ndax jaadu na, nu faj ci bésu noflaay bi?»
14:4b.LUK.014.004 Waaye ñépp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu ñibbi.
14:5b.LUK.014.005 Gannaaw loolu mu ne leen: «Ku sa doom walla sa yëkk daanu ci teen, ndax doo dem génneji ko ca saa sa, fekk sax bésub noflaay la?»
14:6b.LUK.014.006 Amuñu woon dara lu ñu ciy teg.
14:7b.LUK.014.007 Yeesu gis ni gan yi doon tànne toogu yu yiw yi, mu daldi leen wax léeb wii:
14:8b.LUK.014.008 «Bu ñu la wooyee ci xewu céet, bul jël toogu bu yiw. Man na am woo nañu it nit ku la ëpp daraja.
14:9b.LUK.014.009 Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rus a dem ca toogu bu gannaawe ba.
14:10b.LUK.014.010 Waaye bu ñu la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: “Sama xarit, àggal ca kaw.” Loolu dina la sagal ci ñi nga toogandool ci lekkukaay bi.
14:11b.LUK.014.011 Ndaxte képp kuy yékkatiku, dees na la suufeel, te kuy suufeelu, dinañu la yékkati.»
14:12b.LUK.014.012 Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: «Boo dee woote añ walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say dëkkandoo yu am alal. Lu ko moy ñooñu itam dinañu la woo, fey la bor bi.
14:13b.LUK.014.013 Waaye boo dee woote lekk, wool néew doole yi, làggi yi, lafañ yi ak gumba yi.
14:14b.LUK.014.014 Soo ko defee, dinga barkeel, ndaxte duñu la ko man a fey, waaye dinga jot sag pey, bés bi ñi jub di dekki.»
14:15b.LUK.014.015 Bi mu déggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: «Kiy lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram, barkeel nga!»
14:16b.LUK.014.016 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku togglu ay ñam, woo ay nit ñu bare.
14:17b.LUK.014.017 Bi waxtuw lekk jotee mu yónni surga ca ña muy ganale, fàttali leen: “Man ngeen a ñëw, ndaxte lépp sotti na léegi.”
14:18b.LUK.014.018 «Waaye ñu tàmbali di jéggalu ci ngan gi ñoom ñépp. Ku jëkk ka ne ko: “Damaa jënd tool léegi, te fàww ma dem seeti ko. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”
14:19b.LUK.014.019 Keneen ne: “Damaa jënd léegi fukki yëkk, te damay dem nii, jéem leen a beyloo ba xam. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.”
14:20b.LUK.014.020 Keneen ne ko: “Damay sog a takk jabar, looloo tax duma man a ñëw.”
14:21b.LUK.014.021 «Surga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu lépp. Noonu boroom kër ga mer, daldi ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc ya ak ca mbedd ya ca dëkk ba, te indil ma fii néew doole yi, ñu làggi ñi, gumba yi ak lafañ yi.”
14:22b.LUK.014.022 «Surga ba ñëwaat ne ko: “Sang bi, def naa li nga ma sant, waaye bérab bi feesul.”
14:23b.LUK.014.023 Noonu njaatige ba ne ko: “Génnal dëkk bi te dem ca yoon ya ak ca tool ya, xiir nit ñi, ñu duggsi, ngir sama kër fees.
14:24b.LUK.014.024 Maa ngi leen koy wax, ci ñi ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci ñam.”»
14:25b.LUK.014.025 Am mbooloo yu réy yu toppoon ci Yeesu, ba muy dem ca yoon wa. Mu geestu ne leen:
14:26b.LUK.014.026 «Képp ku ñëw ci man te gënalu ma ko baayam, yaayam, jabaram, ay doomam, ay magam ak ay rakkam, walla sax bakkanam, du man a nekk sama taalibe.
14:27b.LUK.014.027 Képp koo xam ne nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, doo man a nekk sama taalibe.
14:28b.LUK.014.028 Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkk a toog, xalaat ñaata la ko war a dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu man a àggale liggéey bi?
14:29b.LUK.014.029 Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te mënu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko:
14:30b.LUK.014.030 “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye mënu koo àggale.”
14:31b.LUK.014.031 Walla boog ban buur mooy dugg ci xare ak beneen buur te jëkkul a toog, seet ba xam moom ak fukki junniy xarekat man na xeex ak kiy ñëw ak ñaar-fukki junniy xarekat?
14:32b.LUK.014.032 Su ko mënul, dafay yónni ndaw ca beneen buur ba, fi ak ma ngay sore, ngir ñu juboo.
14:33b.LUK.014.033 Naka noonu itam ku nekk ci yéen, bu dëdduwul li mu am lépp, du man a nekk sama taalibe.
14:34b.LUK.014.034 «Xam ngeen nag ne, xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam?
14:35b.LUK.014.035 Du jariñ suuf, te du nekk tos. Dañu koy sànni ca biti. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
15
15:1b.LUK.015.001 Ay juutikat ak ay boroom bàkkaar daan jegesi Yeesu ngir déglu ko.
15:2b.LUK.015.002 Farisen ya ak xutbakat ya di ñurumtu naan: «Waa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom bàkkaar ak a lekkandook ñoom!»
15:3b.LUK.015.003 Noonu Yeesu daldi leen wax léeb wii ne leen:
15:4b.LUK.015.004 «Kan ci yéen soo amoon téeméeri xar, te benn réer ci, nooy def? Ndax doo bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, toppi ma réer, ba gis ko?
15:5b.LUK.015.005 Te boo ko gisee, dinga ko gàddu ak bànneex, yóbbu ko kër ga.
15:6b.LUK.015.006 Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.”
15:7b.LUK.015.007 «Maa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mbég ci asamaan, bu benn bàkkaarkat tuubee ay bàkkaaram. Te mbég moomu mooy ëpp mbég, mi fay am, ngir juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeent ñu jub, te soxlawuñoo tuub seeni bàkkaar.
15:8b.LUK.015.008 «Te it bu jigéen dencoon fukki libidoor, benn réer ca, nu muy def? Ndax du taal ab làmp, bale kër ga, seet fu nekk, ba gis ko?
15:9b.LUK.015.009 Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.”
15:10b.LUK.015.010 Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Yàlla yi di ame mbég ci benn bàkkaarkat bu tuubee ay bàkkaaram.»
15:11b.LUK.015.011 Yeesu dellu ne leen: «Dafa amoon góor gu am ñaari doom.
15:12b.LUK.015.012 Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may war a féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam.
15:13b.LUK.015.013 Ay fan yu néew gannaaw gi, caat ma fab yëfam yépp, dem ca réew mu sore, yàq fa alalam ci topp nafsoom.
15:14b.LUK.015.014 Bi mu sànkee alalam jépp, xiif bu metti dal ca réew ma, mu tàmbalee ñàkk.
15:15b.LUK.015.015 Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya.
15:16b.LUK.015.016 Mu xiif ba bëgg a lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.
15:17b.LUK.015.017 Mujj xelam dellusi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgg a dee ak xiif!
15:18b.LUK.015.018 Damay jóg, dem ca sama baay ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la;
15:19b.LUK.015.019 yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.’ ”
15:20b.LUK.015.020 «Mu daldi jóg, jëm kër baayam. Waaye bi muy soreendi kër ga, baayam séen ko, yërëm ko, daldi daw laxasu ko, fóon ko.
15:21b.LUK.015.021 Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.”
15:22b.LUK.015.022 Waaye baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb, mi gën a rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay dàll.
15:23b.LUK.015.023 Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;
15:24b.LUK.015.024 ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.” Noonu ñu tàmbalee bànneexu.
15:25b.LUK.015.025 «Fekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu ñëwee, ba jub kër ga, mu dégg ñuy tëgg, di fecc.
15:26b.LUK.015.026 Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew.
15:27b.LUK.015.027 Mu tontu ko: “Sa rakk moo dellusi, te sa baay rey na sëllu wu duuf wa, ndaxte ñibbisi na ci jàmm.”
15:28b.LUK.015.028 «Ci kaw loolu taaw ba daldi mer, bañ a dugg ca kër ga. Baayam daldi génn, ngir ñaan ko mu dugg.
15:29b.LUK.015.029 Waaye taaw ba tontu baayam ne ko: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, mel ni jaam, te musumaa moy sa ndigal, waaye yaw, musuloo ma may sax tef, ngir ma bànneexu, man ak samay xarit.
15:30b.LUK.015.030 Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi yàq sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko sëllu wu duuf wi.”
15:31b.LUK.015.031 Noonu baay bi tontu ko ne ko: “Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk, te li ma am lépp, yaa ko moom.
15:32b.LUK.015.032 Waaye war nanoo bànneexu te bég, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.”»
16
16:1b.LUK.016.001 Yeesu neeti ay taalibeem: «Benn boroom alal moo amoon bëkk-néeg bu ñu jiiñ ne, dafay pasar-pasaree alal ji.
16:2b.LUK.016.002 Waa ja woo ko ne ko: “Li may dégg ci yaw mooy lan? Leeralal ma ni nga liggéeye ak sama alal, ndaxte dootoo nekkati sama bëkk-néeg.”
16:3b.LUK.016.003 «Bëkk-néeg bi di xalaat naan: “Nu may def nag, segam sama njaatige dafa may dàq ci liggéey bi mu ma joxoon? Dem beyi? Awma kàttanam. Yelwaani? Rus naa ko.
16:4b.LUK.016.004 Xam naa ni may def, ba su ma ñàkkee sama liggéey, ay nit fat ma.”
16:5b.LUK.016.005 Noonu mu daldi woolu kenn ku nekk ca ña ameeloon njaatigeem bor. Ka jëkk a ñëw, mu ne ko: “Ñaata nga ameel sama njaatige?”
16:6b.LUK.016.006 Mu ne ko: “Téeméeri bidoŋi diwlinu oliw.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Toogal fii gaaw te bind juróom-fukk.”
16:7b.LUK.016.007 Mu neeti keneen: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Bindal juróom-ñett-fukk.”
16:8b.LUK.016.008 Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gën a muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.»
16:9b.LUK.016.009 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen di wax lii: sàkkuleen ay xarit jaare ko ci alalu àddina, ngir bu alal nekkatul, ñu man leen a fat ca dal yu sax ya.
16:10b.LUK.016.010 Nit ku maandu ci yëf yu néew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci yëf yu néew, du jub ci yu bare.
16:11b.LUK.016.011 Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu àddina, kon ku leen di dénk alal ju wóor ji?
16:12b.LUK.016.012 Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom?
16:13b.LUK.016.013 «Benn jaam mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.»
16:14b.LUK.016.014 Farisen yi déglu li Yeesu doon wax lépp, tàmbali di ko reetaan, ndaxte ñu bëggoon xaalis lañu.
16:15b.LUK.016.015 Waaye Yeesu ne leen: «Yéen yéena ngi fexee jub ci kanamu nit ñi waaye Yàlla xam na seen xol. Ndaxte li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko.
16:16b.LUK.016.016 «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi ñu ngi fi woon ba kera Yaxya di ñëw. La ko dale foofa nag, yégle nañu xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla, te ñépp a ngi góor-góorlu, ngir dugg ci.
16:17b.LUK.016.017 Waaye nag asamaan ak suuf jóge fi moo gën a yomb randal wenn rëdd ci arafu yoonu Musaa.
16:18b.LUK.016.018 «Ku fase sa jabar, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jigéen ju jëkkëram fase, njaaloo nga.
16:19b.LUK.016.019 «Dafa amoon boroom alal juy sol yére yu rafet te jafe, tey dund bés bu set dund gu neex.
16:20b.LUK.016.020 Fekk miskin mu ñuy wax Lasaar daan tëdd ca buntu këram, fees dell ak ay góom,
16:21b.LUK.016.021 te bu sañoon, di lekk ci desiti ñam wiy rot ci lekkukaayu boroom alal ji. Xaj yi sax daan nañu ñëw, di mar ay góomam.
16:22b.LUK.016.022 «Noonu miskin ma dee, malaaka yi yóbbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, ñu suul ko.
16:23b.LUK.016.023 Bi ñu koy mbugal ca safara, mu téen, séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
16:24b.LUK.016.024 Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci safara sii!”
16:25b.LUK.016.025 Ibraayma ne ko: “Sama doom, fàttalikul ne, jot nga sa bànneex ci àddina, fekk Lasaar dëkk ci tiis. Looloo tax xolam sedd fii, yaw nag, ngay sonn.
16:26b.LUK.016.026 Rax-ca-dolli it am na kàmb gu xóot sunu diggante ak yéen, ba tax ñi bëgg a jóge fii jëm ci yéen, walla ñi bëgg a jóge foofu jëmsi ci nun, duñu ko man.”
16:27b.LUK.016.027 «Noonu boroom alal ja ne: “Kon nag maam, maa ngi lay ñaan, nga yebal Lasaar ca sama kër baay,
16:28b.LUK.016.028 ndaxte am naa fa juróomi rakk. Na leen artu, ngir ñu bañ a ñëw ñoom itam ci bérabu metit wii.”
16:29b.LUK.016.029 Ibraayma ne ko: “Say doomu baay, ñu ngeek yoonu Musaa ak téerey yonent yi. Nañu leen déggal.”
16:30b.LUK.016.030 Boroom alal ja ne ko: “Déedéet, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca ñoom, dinañu tuub seeni bàkkaar.”
16:31b.LUK.016.031 Waaye Ibraayma tontu ko ne: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»
17
17:1b.LUK.017.001 Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar mënta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal.
17:2b.LUK.017.002 Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ci ñii.
17:3b.LUK.017.003 Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko.
17:4b.LUK.017.004 Te su la tooñee juróom-ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom-ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.»
17:5b.LUK.017.005 Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.»
17:6b.LUK.017.006 Boroom bi tontu ne: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen man a ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.
17:7b.LUK.017.007 «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk.”
17:8b.LUK.017.008 Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma réer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga door a lekk te naan.”
17:9b.LUK.017.009 Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet.
17:10b.LUK.017.010 Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeen a war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
17:11b.LUK.017.011 Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xaajale Samari ak Galile.
17:12b.LUK.017.012 Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dand ko, di wax ca kaw naan:
17:13b.LUK.017.013 «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!»
17:14b.LUK.017.014 Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp saraxalekat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set.
17:15b.LUK.017.015 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb.
17:16b.LUK.017.016 Mu dëpp jëwam ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.
17:17b.LUK.017.017 Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom-ñeent ña nag?
17:18b.LUK.017.018 Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!»
17:19b.LUK.017.019 Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
17:20b.LUK.017.020 Farisen yi laaj Yeesu ne ko: «Kañ la Yàlla di tëral nguuram?» Mu tontu leen ne: «Bu Yàlla di wàcce nguuram ci nit ñi, kenn du ko man a teg bët.
17:21b.LUK.017.021 Duñu man a wax it ne: “Xool-leen, mi ngi fii,” walla: “Ma nga fale,” ndaxte nguuru Yàlla wàcc na ci seen biir.»
17:22b.LUK.017.022 Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgg a gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis.
17:23b.LUK.017.023 Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp.
17:24b.LUK.017.024 Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam.
17:25b.LUK.017.025 Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko.
17:26b.LUK.017.026 «La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki.
17:27b.LUK.017.027 Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp.
17:28b.LUK.017.028 «Dina mel it ni la xewoon ca bési Lóot. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jënd ak di jaay, di ji ak di tabax.
17:29b.LUK.017.029 Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, Yàlla tawloo safara ak tamarax, rey leen ñoom ñépp.
17:30b.LUK.017.030 Noonu lay mel, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
17:31b.LUK.017.031 «Ca bés boobee ku nekk ca kaw kër ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu wàcc jëli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu ñibbi.
17:32b.LUK.017.032 Fàttalikuleen jabaru Lóot!
17:33b.LUK.017.033 Kuy wut a rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund.
17:34b.LUK.017.034 Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, ñaar dinañu bokk a tëdd guddi, dees na yóbbu kenn ki, bàyyi ka ca des.
17:35b.LUK.017.035 Ñaari jigéen dinañu wolandoo, dees na yóbbu kenn ci, bàyyi ka ca des.»
17:37b.LUK.017.037 Taalibe yi ne Yeesu: «Fu loolu di xewe, Boroom bi?» Yeesu tontu leen ne: «Fa médd nekk, la tan yiy dajee.»
18
18:1b.LUK.018.001 Noonu Yeesu wax leen itam léeb wii ngir xamal leen ne, war nañoo sax ci ñaan te bañ a xàddi.
18:2b.LUK.018.002 Nee na: «Dafa amoon cib dëkk, benn àttekat bu ragalul Yàlla te faalewul mbindeef.
18:3b.LUK.018.003 Amoon na itam ca dëkk ba jigéen ju jëkkëram faatu ju daan faral di ñëw ci moom, naan ko: “Àtte ma ak sama noon!”
18:4b.LUK.018.004 Àttekat ba bañ lu yàgg, waaye am bés mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla te faalewuma mbindeef,
18:5b.LUK.018.005 waaye jigéen jii lakkal na ma; kon dinaa ko àtte, ngir mu bañatee ñëw sonal ma. Dina rey ak ay wax.”»
18:6b.LUK.018.006 Boroom bi tegaat ca ne: «Dégluleen bu baax li àttekat bu bon boobu wax;
18:7b.LUK.018.007 ndax Yàlla du àtte jub mbooloom mi mu tànn te ñu koy ñaan wall guddi ak bëccëg? Ndax dina leen xaarloo?
18:8b.LUK.018.008 Maa ngi leen koy wax, dina leen àtte jub ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki ñëwee, ndax dina fekk ngëm ci àddina?»
18:9b.LUK.018.009 Yeesu waxaat léeb wii nit, ñi foog ne jub nañu tey xeeb ñi ci des.
18:10b.LUK.018.010 Mu ne: «Dafa amoon ñaari nit ñu dem ca kër Yàlla ga, di ñaan. Kenn ki ab Farisen la, ki ci des juutikat.
18:11b.LUK.018.011 Farisen baa nga taxaw di ñaan ci xelam naan: “Yaw Yàlla, maa ngi lay sant ci li ma melul ni ñeneen ñiy sàcc, di def lu jubadi te di njaaloo, rawatina juutikat bii.
18:12b.LUK.018.012 Ayu-bés gu nekk damay woor ñaari yoon, di joxe asaka ci lépp lu ma wut.”
18:13b.LUK.018.013 «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te bëggul a siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay fëgg dënnam te naan: “Yaw Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat.”»
18:14b.LUK.018.014 Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen koy wax, nit kooku, ba muy ñibbi këram, moom la Yàlla àtte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy yékkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, ñu yékkati la.»
18:15b.LUK.018.015 Amoon na ay nit, ñuy indil Yeesu ay liir, ngir mu teg leen ay loxoom. Bi taalibe ya gisee loolu, ñu gëdd leen.
18:16b.LUK.018.016 Waaye Yeesu woo leen ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw ci man, te buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla.
18:17b.LUK.018.017 Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci man a dugg.»
18:18b.LUK.018.018 Benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma war a def, ba am wàll ci dund gu dul jeex?»
18:19b.LUK.018.019 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga wooye ma ku baax? Yàlla rekk a baax.
18:20b.LUK.018.020 Xam nga ndigal yi: “Bul njaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
18:21b.LUK.018.021 Njiit la ne ko: «Loolu lépp sàmm naa ko li dale ci sama ndaw ba tey.»
18:22b.LUK.018.022 Bi Yeesu déggee loolu, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am lépp, séddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.»
18:23b.LUK.018.023 Bi nit ka déggee loolu, mu am tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
18:24b.LUK.018.024 Yeesu xool ko, daldi ne: «Boroom alal, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!
18:25b.LUK.018.025 Giléem jaar ci bën-bënu pusa moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.»
18:26b.LUK.018.026 Ñi doon déglu daldi ne: «Kon nag ku man a mucc?»
18:27b.LUK.018.027 Yeesu tontu ne: «Li të nit ñi, tëwul Yàlla.»
18:28b.LUK.018.028 Noonu Piyeer ne: «Nun de, dëddu nanu li nu am lépp, topp la.»
18:29b.LUK.018.029 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku dëddu kër walla jabar walla ay doomi ndey walla ay waajur walla ay doom ngir nguuru Yàlla,
18:30b.LUK.018.030 dinga am tey jii ay yooni yoon, ak dund gu dul jeex ëllëg.»
18:31b.LUK.018.031 Yeesu wéetoo ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Nu ngi dem Yerusalem, te li yonent yi bindoon lépp ci mbirum Doomu nit ki dina mat.
18:32b.LUK.018.032 Dinañu ko jébbal ñi dul Yawut, ñu ñaawal ko, saaga ko, tifli ci kawam.
18:33b.LUK.018.033 Gannaaw bu ñu ko dóoree ay yar ba noppi, dinañu ko rey, waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
18:34b.LUK.018.034 Waaye taalibe ya dégguñu li mu leen doon wax; kàddu yooyu ump na leen, te xamuñu li waxi Yeesu yooyu tekki.
18:35b.LUK.018.035 Bi Yeesu di agsi dëkku Yeriko, am gumba gu toogoon ca wetu yoon wa, di yelwaan.
18:36b.LUK.018.036 Naka la gumba ga dégg mbooloo di jàll, mu laaj lan moo xew.
18:37b.LUK.018.037 Ñu wax ko ne: «Yeesum Nasaret moo fay jaar.»
18:38b.LUK.018.038 Noonu mu yuuxu ne: «Yeesu, Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
18:39b.LUK.018.039 Ñi jiitu woon gëdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy gën a yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma!»
18:40b.LUK.018.040 Noonu Yeesu taxaw, santaane ñu indil ko ko. Bi mu jegesee, Yeesu laaj ko ne:
18:41b.LUK.018.041 «Loo bëggoon ma defal la ko?» Mu ne ko: «Sang bi, damaa bëgg a gis.»
18:42b.LUK.018.042 Noonu Yeesu ne ko: «Na say bët gis! Sa ngëm faj na la.»
18:43b.LUK.018.043 Ca saa sa mu daldi gis. Noonu mu topp ci Yeesu, di màggal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.
19
19:1b.LUK.019.001 Yeesu dugg na Yeriko, jaar ca dëkk ba, di dem.
19:2b.LUK.019.002 Waaye amoon na fa waa ju ñuy wax Sase. Njiitu juutikat la, te di ku bare alal.
19:3b.LUK.019.003 Bëgg na gis kan mooy Yeesu, waaye dafa gàtt lool, ba mënu koo gis ndax mbooloo ma.
19:4b.LUK.019.004 Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, yéeg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroon a jaar.
19:5b.LUK.019.005 Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu téen ne ko: «Sase, wàccal gaaw, ndax tey sa kër laa war a dal.»
19:6b.LUK.019.006 Sase daldi gaawantu wàcc, ganale ko ak mbég.
19:7b.LUK.019.007 Ñépp gis loolu, di ñurum-ñurumi naan: «Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar.»
19:8b.LUK.019.008 Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma mas a njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.»
19:9b.LUK.019.009 Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.
19:10b.LUK.019.010 Ndaxte Doomu nit ki ñëw na, ngir seet te musal ñi réer.»
19:11b.LUK.019.011 Bi nit ñi doon déglu kàddu yooyu, Yeesu teg ca léeb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te ñoom foogoon nañu ne, nguuru Yàlla dafay daldi feeñ ca saa sa.
19:12b.LUK.019.012 Mu ne nag: «Dafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci réew mu sore, ngir ñu fal ko buur te mu dellusiwaat.
19:13b.LUK.019.013 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba may ñibbisi.”
19:14b.LUK.019.014 Waaye waa réewam bëgguñu ko. Noonu ñu yónni ndaw ci gannaawam ne: “Bëggunu nit kii yilif nu.”
19:15b.LUK.019.015 «Bi ñu ko falee buur nag, ba mu dellusi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan lañu ci liggéeye.
19:16b.LUK.019.016 Ku jëkk ka ñëw ne ko: “Sang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.”
19:17b.LUK.019.017 Buur ba ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne, takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki dëkk.”
19:18b.LUK.019.018 Surga ba ca topp ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor ba indi na juróomi libidoor.”
19:19b.LUK.019.019 Buur ba ne ko: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
19:20b.LUK.019.020 Keneen ñëw ne: “Sang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.
19:21b.LUK.019.021 Dama laa ragaloon, ndaxte ku néeg nga. Dangay nangu loo dénkaanewul, di dajale loo jiwul.”
19:22b.LUK.019.022 Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul.
19:23b.LUK.019.023 Lu tax nag yóbbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot sama xaalis ak la mu jur.”
19:24b.LUK.019.024 «Ci kaw loolu mu ne ña taxawoon ca wetam: “Nanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.”
19:25b.LUK.019.025 Ñu ne ko: “Sang bi, am na fukki libidoor ba noppi.”
19:26b.LUK.019.026 Buur ba ne leen: “Maa ngi leen koy wax, ku am, dinañu la dolli, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
19:27b.LUK.019.027 Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
19:28b.LUK.019.028 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem.
19:29b.LUK.019.029 Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem,
19:30b.LUK.019.030 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.
19:31b.LUK.019.031 Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»
19:32b.LUK.019.032 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon.
19:33b.LUK.019.033 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?»
19:34b.LUK.019.034 Ñu tontu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.»
19:35b.LUK.019.035 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.
19:36b.LUK.019.036 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi.
19:37b.LUK.019.037 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis.
19:38b.LUK.019.038 Ñu ngi naan:«Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na jàmm am ca asamaan,te ndam li féete ca bérab yu gën a kawe!»
19:39b.LUK.019.039 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!»
19:40b.LUK.019.040 Noonu mu tontu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»
19:41b.LUK.019.041 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko
19:42b.LUK.019.042 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la man a indil jàmm! Waaye fi mu ne mënuloo koo gis.
19:43b.LUK.019.043 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la.
19:44b.LUK.019.044 Dinañu la yàqaate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»
19:45b.LUK.019.045 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaay,
19:46b.LUK.019.046 naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”»
19:47b.LUK.019.047 Bés bu nekk Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wut a reylu.
19:48b.LUK.019.048 Waaye xamuñu woon lan lañu man a def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.
20
20:1b.LUK.020.001 Benn bés Yeesu doon jàngal nit ña ca kër Yàlla ga, di leen yégal xebaar bu baax bi. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya ñëw ne ko:
20:2b.LUK.020.002 «Wax nu ci ban sañ-sañ ngay defe yëf yii, walla kan moo la may boobu sañ-sañ.»
20:3b.LUK.020.003 Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn: wax leen ma,
20:4b.LUK.020.004 la Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
20:5b.LUK.020.005 Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
20:6b.LUK.020.006 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” mbooloo mépp dinañu nu sànni ay xeer, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.»
20:7b.LUK.020.007 Noonu ñu tontu ne, xamuñu fu mu ko jële.
20:8b.LUK.020.008 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
20:9b.LUK.020.009 Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu réseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg.
20:10b.LUK.020.010 Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
20:11b.LUK.020.011 Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
20:12b.LUK.020.012 Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko.
20:13b.LUK.020.013 «Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”
20:14b.LUK.020.014 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
20:15b.LUK.020.015 Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag?
20:16b.LUK.020.016 Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!»
20:17b.LUK.020.017 Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki:“Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.”
20:18b.LUK.020.018 Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
20:19b.LUK.020.019 Xutbakat ya ak saraxalekat yu mag ya ñu ngi doon wut a jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne, ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma.
20:20b.LUK.020.020 Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ.
20:21b.LUK.020.021 Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngale lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
20:22b.LUK.020.022 Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet.»
20:23b.LUK.020.023 Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen:
20:24b.LUK.020.024 «Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu tontu ko: «Sesaar.»
20:25b.LUK.020.025 Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
20:26b.LUK.020.026 Noonu mënuñu ko woon a jàpp ciy waxam ci kanamu mbooloo ma; ñu waaru ci tontoom, ba wedam.
20:27b.LUK.020.027 Noonu ay nit, ñu bokk ci Sadusen yi, ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom weddi nañu ndekkite li. Noonu ñu laaj ko ne:
20:28b.LUK.020.028 «Kilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te bàyyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jigéen ji, ba yékkati giiru magam.
20:29b.LUK.020.029 Amoon na fi nag juróom-ñaari góor ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te bàyyiwul doom.
20:30b.LUK.020.030 Ñaareel ba takk jigéen ja, def noonu; ak ñetteel ba, ba juróom-ñaar ñépp faatu te bàyyiwuñu doom.
20:32b.LUK.020.032 Gannaaw ga nag jigéen ja it faatu.
20:33b.LUK.020.033 Ci ndekkite li nag, kan ci ñoom moo war a donn jigéen ja, fekk ku nekk ci juróom-ñaar ñi mas na koo takk?»
20:34b.LUK.020.034 Yeesu tontu leen ne: «Ci àddina sii, góor ñi ak jigéen ñi dañuy séy.
20:35b.LUK.020.035 Waaye ña ñu àtte ne, yeyoo nañoo bokk ci dundu ëllëg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am jëkkër.
20:36b.LUK.020.036 Dafa fekk ne mënatuñoo dee, ndaxte dañuy mel ni malaaka yi. Ay doomi Yàlla lañu ndaxte doomi ndekkite lañu.
20:37b.LUK.020.037 Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.”
20:38b.LUK.020.038 Kon nag nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la, ndaxte Yàllaa tax ñépp di dund.»
20:39b.LUK.020.039 Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!»
20:40b.LUK.020.040 Ndaxte kenn ci ñoom ñemeetu koo laaj dara.
20:41b.LUK.020.041 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
20:42b.LUK.020.042 Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sabóor:“Boroom bi nee na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,
20:43b.LUK.020.043 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ”
20:44b.LUK.020.044 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
20:45b.LUK.020.045 Bi ko nit ña fa nekkoon ñépp doon déglu, Yeesu ne ay taalibeem:
20:46b.LUK.020.046 «Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi. Ci jàngu yi, toogu yu féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi.
20:47b.LUK.020.047 Ñu ngi lekk alalu jigéen ñi seen jëkkër faatu, di ñaan Yàlla ay ñaani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina gën a tar.»
21
21:1b.LUK.021.001 Noonu Yeesu siggi, séen ay boroom alal ñuy dugal seen sarax ca ndab ya ca kër Yàlla ga.
21:2b.LUK.021.002 Mu gis itam jenn jigéen ju jëkkëram faatu te mu ñàkk, ju fa def ñaari poseti xànjar.
21:3b.LUK.021.003 Noonu mu daldi ne: «Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, jigéen ju ñàkk jee moo ëpp ñeneen ñépp lu mu joxe.
21:4b.LUK.021.004 Ñoom ñépp dañu sàkku ci seen barele, waaye moom dafa sàkku ci néewleem, ba joxe xaalis bi mu waroon a dunde.»
21:5b.LUK.021.005 Noonu ay nit doon wax ci lu jëm ca kër Yàlla ga, ak ni ñu ko rafetale ak ay doj yu jafe ak alal ju ñu jébbal Yàlla. Waaye Yeesu ne leen:
21:6b.LUK.021.006 «Li ngeen gis fii lépp, jamono dina ñëw joo xam ne dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
21:7b.LUK.021.007 Ñu laaj ko ne: «Kilifa gi, kañ la loolu di am? Te luy tegtal ne, looloo ngi waaj a xew?»
21:8b.LUK.021.008 Yeesu tontu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu.
21:9b.LUK.021.009 Bu ngeen déggee ay xare ak ay réew yu jóg, wottuleen a tiit, ndaxte fàww yooyule jëkk a am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.»
21:10b.LUK.021.010 Noonu mu teg ca ne: «Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew.
21:11b.LUK.021.011 Suuf dina yengu yengu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan.
21:12b.LUK.021.012 Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam ay buur yi ak ay boroom réew ndax sama tur.
21:13b.LUK.021.013 Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.
21:14b.LUK.021.014 Fasleen yéenee bañ a wut lay ngir musal seen bopp.
21:15b.LUK.021.015 Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko man a teggi, mbaa ñu di ko weddi.
21:16b.LUK.021.016 Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen.
21:17b.LUK.021.017 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
21:18b.LUK.021.018 Waaye seen genn kawar sax du neen.
21:19b.LUK.021.019 Seen muñ moo leen di musal.
21:20b.LUK.021.020 «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.
21:21b.LUK.021.021 Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba!
21:22b.LUK.021.022 Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat.
21:23b.LUK.021.023 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii.
21:24b.LUK.021.024 Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.
21:25b.LUK.021.025 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yengu-yengub duus yi.
21:26b.LUK.021.026 Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nar a wàcc ci àddina, ndaxte dees na yengal kàttani asamaan.
21:27b.LUK.021.027 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
21:28b.LUK.021.028 Bu mbir yooyu di tàmbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, téen, ndaxte seen njot jubsi na.»
21:29b.LUK.021.029 Noonu Yeesu misaal leen lii: «Xool-leen garabu figg ak yeneen garab yi.
21:30b.LUK.021.030 Bu ñu gisee ñu sëq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat.
21:31b.LUK.021.031 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na.
21:32b.LUK.021.032 «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul.
21:33b.LUK.021.033 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
21:34b.LUK.021.034 «Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal.
21:35b.LUK.021.035 Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf.
21:36b.LUK.021.036 Yeewuleen, di sax ci ñaan, ngir ngeen man a mucc ci loolu lépp war a xew, te man a taxaw ak kóolute ci kanamu Doomu nit ki.»
21:37b.LUK.021.037 Yeesoo ngi daan yendoo jàngale ca kër Yàlla ga, te bu guddee mu dem ca tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, fanaan fa.
21:38b.LUK.021.038 Te nit ñépp dañu daan teel a xëy ca kër Yàlla ga, di ko déglu.
22
22:1b.LUK.022.001 Màggalu Mburu ya amul lawiir jege woon na, te ñu di ko wax Bésu Jéggi ba.
22:2b.LUK.022.002 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte dañoo ragaloon nit ña.
22:3b.LUK.022.003 Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar.
22:4b.LUK.022.004 Noonu Yudaa dem waxtaani ak saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu.
22:5b.LUK.022.005 Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis.
22:6b.LUK.022.006 Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.
22:7b.LUK.022.007 Bésu màggalu Mburu ya amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroon a rendi mbotem màggalu Jéggi ba.
22:8b.LUK.022.008 Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru Jéggi ba.»
22:9b.LUK.022.009 Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?»
22:10b.LUK.022.010 Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg,
22:11b.LUK.022.011 te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru Jéggi ba, man ak samay taalibe?”
22:12b.LUK.022.012 Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»
22:13b.LUK.022.013 Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
22:14b.LUK.022.014 Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,
22:15b.LUK.022.015 ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru Jéggi bii, laata ñu may sonal.
22:16b.LUK.022.016 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»
22:17b.LUK.022.017 Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.
22:18b.LUK.022.018 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum réseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»
22:19b.LUK.022.019 Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
22:20b.LUK.022.020 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
22:21b.LUK.022.021 Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.
22:22b.LUK.022.022 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»
22:23b.LUK.022.023 Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nar a def loolu.
22:24b.LUK.022.024 Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gën a màgg.
22:25b.LUK.022.025 Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.
22:26b.LUK.022.026 Waaye yéen buleen def noonu. Ki gën a màgg ci yéen, na nekk ni ki gën a ndaw, te njiit mel ni surga.
22:27b.LUK.022.027 Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gën a màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
22:28b.LUK.022.028 Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.
22:29b.LUK.022.029 Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.
22:30b.LUK.022.030 Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»
22:31b.LUK.022.031 Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
22:32b.LUK.022.032 Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo dellusee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»
22:33b.LUK.022.033 Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.»
22:34b.LUK.022.034 Yeesu tontu ko ne: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne, xam nga ma.»
22:35b.LUK.022.035 Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu tontu ne: «Déedéet.»
22:36b.LUK.022.036 Mu neeti leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.
22:37b.LUK.022.037 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»
22:38b.LUK.022.038 Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
22:39b.LUK.022.039 Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe nakajekk. Taalibeem ya topp ci moom.
22:40b.LUK.022.040 Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir bañ a daanu cig fiir.»
22:41b.LUK.022.041 Noonu mu dand leen, ba fu aw saan man a tollu, daldi sukk di ñaan ne:
22:42b.LUK.022.042 «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
22:43b.LUK.022.043 Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.
22:44b.LUK.022.044 Ci biir tiis, Yeesu gën a sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
22:45b.LUK.022.045 Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, dellusi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.
22:46b.LUK.022.046 Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir.»
22:47b.LUK.022.047 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.
22:48b.LUK.022.048 Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»
22:49b.LUK.022.049 Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgg a xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»
22:50b.LUK.022.050 Kenn ci ñoom nag dóor surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg.
22:51b.LUK.022.051 Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
22:52b.LUK.022.052 Noonu Yeesu ne saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
22:53b.LUK.022.053 Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»
22:54b.LUK.022.054 Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër saraxalekat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.
22:55b.LUK.022.055 Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.
22:56b.LUK.022.056 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»
22:57b.LUK.022.057 Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»
22:58b.LUK.022.058 Nes tuuti keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer tontu ko: «Sama waay, bokkuma ci.»
22:59b.LUK.022.059 Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.»
22:60b.LUK.022.060 Waaye Piyeer tontu ne: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.
22:61b.LUK.022.061 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.»
22:62b.LUK.022.062 Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti.
22:63b.LUK.022.063 Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor.
22:64b.LUK.022.064 Ñu ngi takkoon ay bëtam, di ko laaj, naan ko: «Yaw, wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?»
22:65b.LUK.022.065 Ñu ngi ko doon tifaar it yeneeni saaga.
22:66b.LUK.022.066 Bi bët setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam.
22:67b.LUK.022.067 Ñu ne ko: «Soo dee Almasi bi, wax nu ko.» Mu tontu leen ne: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.
22:68b.LUK.022.068 Te su ma leen laajee, dungeen tontu.
22:69b.LUK.022.069 Waaye gannaawsi tey, Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Yàlla, Aji Kàttan ji.»
22:70b.LUK.022.070 Noonu ñépp ne: «Kon nag yaay Doomu Yàlla ji?» Mu tontu leen ne: «Yéen ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.»
22:71b.LUK.022.071 Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!»
23
23:1b.LUK.023.001 Gannaaw loolu kureelu àttekat ya yépp daldi jóg, yóbbu Yeesu ca Pilaat.
23:2b.LUK.023.002 Foofa ñu tàmbali di ko sosal naan: «Fekk nanu nit kii, muy fàbbi sunu réew, di leen teree fey galag Sesaar, te mi ngi teg boppam Almasi, maanaam buur.»
23:3b.LUK.023.003 Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko.»
23:4b.LUK.023.004 Pilaat ne saraxalekat yu mag ya ak mbooloo ma: «Gisuma genn tooñ ci nit kii.»
23:5b.LUK.023.005 Waaye ñu sax ci seeni wax naan: «Mi ngi jógloo mbooloo mi, di jàngale ci réewu Yawut ya mépp, li dale ci Galile ba fii.»
23:6b.LUK.023.006 Bi Pilaat yégee baat yooyu, mu laajte ne: «Ndax nit kii Galile la dëkk?»
23:7b.LUK.023.007 Bi mu yégee ne, Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu yónnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem.
23:8b.LUK.023.008 Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mbég mu réy. Bu yàgg ba tey dafa koo bëggoon a gis, ndaxte déggoon na ñuy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne, dina ko gis mu def kéemaan.
23:9b.LUK.023.009 Noonu mu laaj ko ay laaj yu bare, waaye Yeesu tontuwul dara.
23:10b.LUK.023.010 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat yaa nga fa woon, di ko jiiñ bu metti.
23:11b.LUK.023.011 Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat.
23:12b.LUK.023.012 Erodd ak Pilaat dañoo ñi bañante woon bu jëkk, waaye ca bés booba doon nañu ay xarit.
23:13b.LUK.023.013 Pilaat daldi woo saraxalekat yu mag ya, njiit ya ak mbooloom Yawut ya ne leen:
23:14b.LUK.023.014 «Indil ngeen ma nit kii, ne ma, day jàddloo yoon mbooloo mi. Léegi nag man mii laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma tooñ ci moom ak li ngeen koy jiiñ lépp.
23:15b.LUK.023.015 Erodd itam gisul tooñ gu mu def, ndegam mu yónneewaat nu ko. Nit kii deful genn tooñ gu jar ñu koy rey.
23:16b.LUK.023.016 Kon nag dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
23:18b.LUK.023.018 Waaye ñu bokk di yuuxu, ñoom ñépp naan: «Reyal kii te bàyyi Barabas!»
23:19b.LUK.023.019 Dañoo tëjoon Barabas, ndaxte dafa jéem a tas dëkk ba, te rey nit.
23:20b.LUK.023.020 Pilaat waxaat ak mbooloo ma, ndaxte dafa bëggoon a bàyyi Yeesu.
23:21b.LUK.023.021 Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
23:22b.LUK.023.022 Pilaat ne leen ñetteel bi yoon: «Lu tax? Gan tooñ la def? Gisuma ci moom dara lu jar dee. Kon dinaa ko dóorlu ay yar te bàyyi ko.»
23:23b.LUK.023.023 Waaye ñoom ñu sax ca la ñu waxoon, di gën a yuuxu naan, ñu daaj ko ci bant. Coow la yey Pilaat.
23:24b.LUK.023.024 Muj gi Pilaat dogal, ñu defal leen li ñu bëgg.
23:25b.LUK.023.025 Mu bàyyil leen ki ñu ko ñaanoon, kooku ñu tëjoon kaso, ndax tas réew ma ak rey nit. Waaye mu jébbal leen Yeesu ci seeni loxo.
23:26b.LUK.023.026 Bi ñuy yóbbu Yeesu, ñu jàpp ku ñuy wax Simoŋ te mu dëkk Siren, ku jóge ca wet, ga féete ak tool ya, sëf ko bant, ba ñuy war a daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ci moom.
23:27b.LUK.023.027 Mbooloo mu baree nga ko toppoon, te jigéen ñu baree ngi doon yuuxu, di ko jooy.
23:28b.LUK.023.028 Yeesu daldi walbatiku ca ñoom ne: «Yéen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.
23:29b.LUK.023.029 Ndaxte jamono dina ñëw, ju ñu naan: “Jigéen ñi musul a jur ak ñi musul a nàmpal, barkeel ngeen!”
23:30b.LUK.023.030 Bu keroogee,“Nit ñi dinañu ne tund yi:‘Daanuleen ci sunu kaw!’te naan jànj yi: «“Suul-leen nu!»“ “
23:31b.LUK.023.031 Ndaxte su ñu defee nii garab gu tooy gi, lu ñuy def garab gu wow gi?»
23:32b.LUK.023.032 Yóbbaale nañu itam ñeneen, ñuy ñaari defkati lu bon, ngir rey leen.
23:33b.LUK.023.033 Bi xarekat ya agsee ba ca bérab, ba ñuy wooye Kaaŋu Bopp, ñu daaj fa Yeesu ca bant, daajaale ñaari defkati lu bon ya, kenn ca ndeyjooram, ka ca des ca càmmooñam.
23:34b.LUK.023.034 Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndaxte xamuñu li ñuy def.» Xarekat ya tegoo ay bant yéreem, ngir séddoo ko.
23:35b.LUK.023.035 Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: «Musal na ñeneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Yàlla fal!»
23:36b.LUK.023.036 Xarekat ya it di ko ñaawal. Ñu jegesi, jox ko bineegar te naan:
23:37b.LUK.023.037 «Su fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!»
23:38b.LUK.023.038 Ñu daaj mbind, mu tiim ko naan: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
23:39b.LUK.023.039 Kenn ca defkatu lu bon ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!»
23:40b.LUK.023.040 Waaye ka ca des yedd moroom ma, naan ko: «Xanaa ragaloo Yàlla, yaw mi ñuy mbugal ni moom!
23:41b.LUK.023.041 Nun yelloo nanu sunu mbugal, waaye moom deful dara.»
23:42b.LUK.023.042 Noonu mu ne: «Yeesu, fàttaliku ma, boo dellusee ci sa nguur.»
23:43b.LUK.023.043 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, tey jii dinga texe ak man ca jataayu Yàlla.»
23:44b.LUK.023.044 Noonu digg-bëccëg daldi jot, jant ba nëbbu, réew mépp daldi lëndëm këruus lu mat ñetti waxtu. Ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga daldi xar ñaar.
23:46b.LUK.023.046 Yeesu woote ak kàddu gu dëgër naan: «Baay, jébbal naa la sama ruu!» Bi mu waxee loolu, mu delloo ruuwam Yàlla.
23:47b.LUK.023.047 Bi njiitu xare ba gisee li xewoon, mu màggal Yàlla ne: «Dëgg-dëgg nit kii ku jub la woon.»
23:48b.LUK.023.048 Nit ña fa dajaloo woon ñépp, di seetaan li xew, ba ñu gisee loolu, ñu dellu seen kër, fëgg seen dënn, di jooy.
23:49b.LUK.023.049 Xamey Yeesu yépp ak jigéen, ña ko toppe woon Galile, dand leen, di xool li xew.
23:50b.LUK.023.050 Nit ku ñuy wax Yuusufa dem ca Pilaat. Mi ngi dëkk Arimate ca diiwaanu Yude. Yuusufaa nga bokkoon ca kureelu àttekat yi. Nit ku baax la woon te jub, te àndul woon ci li ñu dogaloon te jëf ko. Da doon séentu nguuru Yàlla.
23:52b.LUK.023.052 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu.
23:53b.LUK.023.053 Gannaaw loolu mu wàcce ko ca bant ba, laxas ko ci càngaay, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ciw doj te musuñu caa def kenn.
23:54b.LUK.023.054 Fekk bésu Waajal la woon, te bésu noflaay baa ngi doon tàmbali.
23:55b.LUK.023.055 Jigéen ña gungee woon Yeesu Galile, ànd ak Yuusufa, gis bàmmeel ba ak na ñu ca dence néewu Yeesu ba.
23:56b.LUK.023.056 Noonu ñu dellu defari cuuraay ak latkoloñ ngir néew ba. Ca bésu noflaay ba ñu noppalu, ni ko yoon wi santaanee.
24
24:1b.LUK.024.001 Bés bu jëkk ca ayu-bés ga, jigéen ña jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Ñu ngi yoroon cuuraay lu ñu defaroon.
24:2b.LUK.024.002 Bi ñu agsee, ñu fekk ñu béraŋ doj, wa uboon bàmmeel ba.
24:3b.LUK.024.003 Ñu dugg ca bàmmeel ba, waaye fekkuñu fa néewu Boroom bi Yeesu.
24:4b.LUK.024.004 Noonu ba ñu nekkee ak seen njaaxle, am na ñaar ñu leen feeñu, sol yére yuy melax.
24:5b.LUK.024.005 Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi?
24:6b.LUK.024.006 Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile.
24:7b.LUK.024.007 Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”»
24:8b.LUK.024.008 Noonu ñu daldi fàttaliku kàdduy Yeesu ya.
24:9b.LUK.024.009 Bi ñu jógee bàmmeel ba, ñu dem nettaliji loolu lépp fukki ndaw ya ak benn, ak ña ca des ñépp.
24:10b.LUK.024.010 Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya.
24:11b.LUK.024.011 Waaye ñu teg wax jooju ay jeneer, ba gëmuñu jigéen ñooñu.
24:12b.LUK.024.012 Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ca bàmmeel ba. Bi mu àggee, mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Noonu mu dëpp ñibbi, jaaxle lool ci li xew.
24:13b.LUK.024.013 Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet.
24:14b.LUK.024.014 Ñu waxtaane li xewoon lépp.
24:15b.LUK.024.015 Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom,
24:16b.LUK.024.016 fekk seeni bët muuru, ba mënu ko woon a xàmmi.
24:17b.LUK.024.017 Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex.
24:18b.LUK.024.018 Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?»
24:19b.LUK.024.019 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu tontu ko ne: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla.
24:20b.LUK.024.020 Waaye sunuy saraxalekat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant.
24:21b.LUK.024.021 Nun nag danoo yaakaaroon ne, mooy kiy nar a jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi.
24:22b.LUK.024.022 Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba,
24:23b.LUK.024.023 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu dellusi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne, mi ngi dund.
24:24b.LUK.024.024 Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.»
24:25b.LUK.024.025 Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéex a gëm li yonent yi yégle woon!
24:26b.LUK.024.026 Xanaa du Almasi bi dafa waroon a daj boobu coono te dugg ci ndamam?»
24:27b.LUK.024.027 Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram.
24:28b.LUK.024.028 Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam.
24:29b.LUK.024.029 Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.» Noonu mu dugg, toog ca ñoom.
24:30b.LUK.024.030 Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko.
24:31b.LUK.024.031 Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko.
24:32b.LUK.024.032 Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?»
24:33b.LUK.024.033 Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneeni taalibe.
24:34b.LUK.024.034 Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!»
24:35b.LUK.024.035 Ñaari taalibe ya ñoom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni ñu xàmmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma.
24:36b.LUK.024.036 Bi ñaari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen.»
24:37b.LUK.024.037 Ñu daldi tiit, foog ne dañoo gis njuuma.
24:38b.LUK.024.038 Waaye Yeesu ne leen: «Lu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel ñaar ci seen xol?
24:39b.LUK.024.039 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.»
24:40b.LUK.024.040 Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay tànkam.
24:41b.LUK.024.041 Waaye ba tey mënuñu woon a gëm ndax seen mbég ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: «Ndax am ngeen fii lu ñu lekk?»
24:42b.LUK.024.042 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk.
24:43b.LUK.024.043 Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
24:44b.LUK.024.044 Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa war a am.»
24:45b.LUK.024.045 Noonu mu ubbi seen xel, ngir ñu xam li Mbind mi di wax.
24:46b.LUK.024.046 Mu ne leen: «Fàww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca ñetteelu fan ba, ni ñu ko binde,
24:47b.LUK.024.047 te it ñuy yégle xeet yépp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne, war nañoo tuub seeni bàkkaar, Yàlla baal leen.
24:48b.LUK.024.048 Yéenay samay seede.
24:49b.LUK.024.049 Te man dinaa leen yónnee li sama Baay dige. Yéen nag toogleen ci dëkk bi, ba ñu sol leen doole ji jóge ci kaw.»
24:50b.LUK.024.050 Gannaaw loolu Yeesu yóbbu leen ca wetu Betani. Foofa mu yékkati ay loxoom, barkeel leen.
24:51b.LUK.024.051 Bi mu leen dee barkeel, mu tàggoo ak ñoom, Yàlla yéege ko asamaan.
24:52b.LUK.024.052 Taalibe ya màggal ko, daldi dellu Yerusalem, fees ak mbég.
24:53b.LUK.024.053 Foofa daawuñu jóg ca kër Yàlla ga, di gërëm Yàlla.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Luke (Wolof). Luke (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C32A-D