Matthew (Wolof)
1
1:1b.MAT.001.001 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
1:2b.MAT.001.002 Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
1:3b.MAT.001.003 Yuda, Fares ak Sara ci Tamar; Fares Esrom, miy baayu Aram;
1:4b.MAT.001.004 Aram Aminadab; Aminadab Naason; Naason Salmon;
1:5b.MAT.001.005 Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Yese,
1:6b.MAT.001.006 miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon jabari Uri;
1:7b.MAT.001.007 Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf;
1:8b.MAT.001.008 Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas;
1:9b.MAT.001.009 Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiyas;
1:10b.MAT.001.010 Esekiyas Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas;
1:11b.MAT.001.011 Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
1:12b.MAT.001.012 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel,
1:13b.MAT.001.013 miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor;
1:14b.MAT.001.014 Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd;
1:15b.MAT.001.015 Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba;
1:16b.MAT.001.016 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
1:17b.MAT.001.017 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
1:18b.MAT.001.018 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
1:19b.MAT.001.019 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woon a weer. Mu nar a xàccook moom ci sutura.
1:20b.MAT.001.020 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragal a yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
1:21b.MAT.001.021 Dina jur doom ju góor; na nga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
1:22b.MAT.001.022 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
1:23b.MAT.001.023 «Janq bi dina ëmb,jur doom ju góor,ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
1:24b.MAT.001.024 Noonu Yuusufa yeewu, yeggali jabaram, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
1:25b.MAT.001.025 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
2
2:1b.MAT.002.001 Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
2:2b.MAT.002.002 Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.»
2:3b.MAT.002.003 Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp.
2:4b.MAT.002.004 Mu woolu nag saraxalekat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, war a juddoo.
2:5b.MAT.002.005 Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent:
2:6b.MAT.002.006 “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude,du yaw yaa yées ci njiiti Yude,ndaxte ci yaw la njiit di génne,kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
2:7b.MAT.002.007 Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq.
2:8b.MAT.002.008 Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
2:9b.MAT.002.009 Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tell jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk.
2:10b.MAT.002.010 Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réy-a-réy.
2:11b.MAT.002.011 Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
2:12b.MAT.002.012 Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu bañ a dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew.
2:13b.MAT.002.013 Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
2:14b.MAT.002.014 Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga.
2:15b.MAT.002.015 Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Woo naa sama doom, mu génn Misra.»
2:16b.MAT.002.016 Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, mengook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.
2:17b.MAT.002.017 Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu naan:
2:18b.MAT.002.018 «Baat jib na ci Rama,ay jooy ak yuux gu réy,Rasel mooy jooy ay doomamte bëggul kenn dëfël ko,ndaxte saay nañu.»
2:19b.MAT.002.019 Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra,
2:20b.MAT.002.020 ne ko: «Ñi doon wut a rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.»
2:21b.MAT.002.021 Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil.
2:22b.MAT.002.022 Waaye bi mu déggee ne, Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile.
2:23b.MAT.002.023 Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan:«Dees na ko tudde Nasaréen.»
3
3:1b.MAT.003.001 Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude.
3:2b.MAT.003.002 Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.»
3:3b.MAT.003.003 Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:“Xàll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.”»
3:4b.MAT.003.004 Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
3:5b.MAT.003.005 Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan.
3:6b.MAT.003.006 Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
3:7b.MAT.003.007 Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?
3:8b.MAT.003.008 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar,
3:9b.MAT.003.009 te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii.
3:10b.MAT.003.010 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci safara si.
3:11b.MAT.003.011 Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak safara.
3:12b.MAT.003.012 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.»
3:13b.MAT.003.013 Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
3:14b.MAT.003.014 Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!»
3:15b.MAT.003.015 Yeesu tontu ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu.
3:16b.MAT.003.016 Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu.
3:17b.MAT.003.017 Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»
4
4:1b.MAT.004.001 Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
4:2b.MAT.004.002 Yeesu nekk fa te lekkul ñeent-fukki bëccëg ak ñeent-fukki guddi, door a xiif.
4:3b.MAT.004.003 Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.»
4:4b.MAT.004.004 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”»
4:5b.MAT.004.005 Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
4:6b.MAT.004.006 Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na:“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,ñu leewu la ci seeni loxo,ngir nga bañ a fakkastalu ciw doj.”»
4:7b.MAT.004.007 Yeesu tontu ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
4:8b.MAT.004.008 Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam.
4:9b.MAT.004.009 Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.»
4:10b.MAT.004.010 Waaye Yeesu tontu ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”»
4:11b.MAT.004.011 Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo.
4:12b.MAT.004.012 Am bés Yeesu dégg ne, jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
4:13b.MAT.004.013 Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali.
4:14b.MAT.004.014 Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
4:15b.MAT.004.015 «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali,di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan,yaw Galile, réewum ñi dul Yawut —
4:16b.MAT.004.016 xeet wa nekkoon cig lëndëm,gis na leer gu mag,ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim,leer fenkal na leen.»
4:17b.MAT.004.017 Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.»
4:18b.MAT.004.018 Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
4:19b.MAT.004.019 Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.»
4:20b.MAT.004.020 Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom.
4:21b.MAT.004.021 Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen.
4:22b.MAT.004.022 Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom.
4:23b.MAT.004.023 Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngale ci seeni jàngu tey yégle xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña,
4:24b.MAT.004.024 ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen.
4:25b.MAT.004.025 Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan..
5
5:1b.MAT.005.001 Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom.
5:2b.MAT.005.002 Mu daldi leen jàngal naan:
5:3b.MAT.005.003 «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo.
5:4b.MAT.005.004 Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen,ndax dees na dëfël seen xol.
5:5b.MAT.005.005 Yéen ñi lewet, barkeel ngeen,ndax dingeen moomi àddina.
5:6b.MAT.005.006 Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.
5:7b.MAT.005.007 Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen,ndax dees na leen yërëm.
5:8b.MAT.005.008 Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen,ndax dingeen gis Yàlla.
5:9b.MAT.005.009 Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen,ndax dees na leen tudde doomi Yàlla.
5:10b.MAT.005.010 Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub,barkeel ngeen,ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji,yéena ko yelloo.
5:11b.MAT.005.011 «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man.
5:12b.MAT.005.012 Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
5:13b.MAT.005.013 «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom si sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam.
5:14b.MAT.005.014 Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du man a nëbbu.
5:15b.MAT.005.015 Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp.
5:16b.MAT.005.016 Na seen leer leere noonu ci kanamu nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw.
5:17b.MAT.005.017 «Buleen defe ne, ñëw naa ngir dindi yoonu Musaa ak waxi yonent yi. Ñëwuma ngir dindi leen, waaye ngir ñu am ci man.
5:18b.MAT.005.018 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, li feek asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa, ba kera yépp di am.
5:19b.MAT.005.019 Ku tebbi nag ba gën a tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gën a tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
5:20b.MAT.005.020 Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
5:21b.MAT.005.021 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.”
5:22b.MAT.005.022 Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci safara.
5:23b.MAT.005.023 Booy yóbbu nag sa sarax ca saraxalukaay ba, te nga fàttaliku foofa ne, sa mbokk am na lu mu la meree,
5:24b.MAT.005.024 nanga fa bàyyi sa sarax ca kanamu saraxalukaay ba, nga jëkk a dem, juboo ak sa mbokk, ba noppi dellu, joxe sa sarax.
5:25b.MAT.005.025 «Gaawal a juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeen a egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la.
5:26b.MAT.005.026 Ci dëgg maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj.
5:27b.MAT.005.027 «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.”
5:28b.MAT.005.028 Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel.
5:29b.MAT.005.029 Bu la sa bëtu ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore.
5:30b.MAT.005.030 Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci safara. Bu la sa loxol ndeyjoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci safara.
5:31b.MAT.005.031 «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa jabar, nga bindal ko kayitu pase.”
5:32b.MAT.005.032 Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa jabar te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga.
5:33b.MAT.005.033 «Dégg ngeen itam ne, waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.”
5:34b.MAT.005.034 Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen giñ dara; bumu doon ci asamaan, ndaxte moo di jalu Buur Yàlla;
5:35b.MAT.005.035 bumu doon ci àddina, ndax moo di tegukaayu tànkam; bumu doon it ci Yerusalem, ndax moo di dëkku Buur bu mag bi.
5:36b.MAT.005.036 Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte mënuloo weexal mbaa ñuulal benn ci say kawar.
5:37b.MAT.005.037 Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge.
5:38b.MAT.005.038 «Te it dégg ngeen ne, waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.”
5:39b.MAT.005.039 Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen bañ ku leen def lu bon, waaye ku la pes ci sa lexu ndeyjoor, jox ko ba ca des.
5:40b.MAT.005.040 Ku la bëgg a kalaame, ngir jël sa turki, nga boole ca it sa mbubb mu mag.
5:41b.MAT.005.041 Ku la ga, nga yenul ko doxub benn kilomet, àndal ak moom ñaar.
5:42b.MAT.005.042 Mayal ku lay ñaan, te bul jox gannaaw ku lay leb.
5:43b.MAT.005.043 «Dégg ngeen ne, waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.”
5:44b.MAT.005.044 Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal,
5:45b.MAT.005.045 ngir wone ne, yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi.
5:46b.MAT.005.046 Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa juutikat yi duñu def noonu it?
5:47b.MAT.005.047 Su ngeen nuyoo seeni bokk rekk, lu ngeen def lu doy waar? Xanaa ñi xamul Yàlla duñu def noonu it?
5:48b.MAT.005.048 Nangeen mat nag, ni seen Baay bi ci kaw mate.
6
6:1b.MAT.006.001 «Wottuleen a def seeni jëf yu jub ci kanamu nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw.
6:2b.MAT.006.002 Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6:3b.MAT.006.003 Waaye booy sàkk sarax, bu sa loxob càmmooñ xam li sa loxob ndeyjoor di def,
6:4b.MAT.006.004 ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
6:5b.MAT.006.005 «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6:6b.MAT.006.006 Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
6:7b.MAT.006.007 «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare.
6:8b.MAT.006.008 Buleen nirook ñoom, ndaxte seen Baay xam na seeni soxla, laata ngeen ko koy wax.
6:9b.MAT.006.009 Yéen nag nii ngeen war a ñaane:“Sunu Baay bi nekk ci kaw,na sa tur sell,
6:10b.MAT.006.010 na sa nguur ñëw,na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.
6:11b.MAT.006.011 May nu tey li nu war a dunde;
6:12b.MAT.006.012 te baal nu sunuy tooñ, ni nu baale ñi nu tooñ;
6:13b.MAT.006.013 bu nu teg ci yoonu nattu, waaye nga musal nu ci lu bon.Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
6:14b.MAT.006.014 «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam.
6:15b.MAT.006.015 Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ.
6:16b.MAT.006.016 «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp.
6:17b.MAT.006.017 Yaw nag booy woor, xeeñalal sa bopp te nga sëlmu,
6:18b.MAT.006.018 ngir sa koor bañ a feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët mënta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.
6:19b.MAT.006.019 «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko.
6:20b.MAT.006.020 Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko.
6:21b.MAT.006.021 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.
6:22b.MAT.006.022 «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer,
6:23b.MAT.006.023 waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse!
6:24b.MAT.006.024 «Kenn mënul a jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Mënuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.
6:25b.MAT.006.025 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk, walla lu ngeen war a naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen war a sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay?
6:26b.MAT.006.026 Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare?
6:27b.MAT.006.027 Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo man a yokk waxtu ci àppam?
6:28b.MAT.006.028 «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc,
6:29b.MAT.006.029 waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom.
6:30b.MAT.006.030 Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gën a wodd?
6:31b.MAT.006.031 Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu war a lekk? Lu nu war a naan?” walla: “Lu nu war a sol?”
6:32b.MAT.006.032 Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp.
6:33b.MAT.006.033 Waaye jëkkleen a wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil.
6:34b.MAT.006.034 Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko.
7
7:1b.MAT.007.001 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam.
7:2b.MAT.007.002 Ndaxte dees na leen àtte ak ni ngeen di àttee, nattal leen ak li ngeen di nattale.
7:3b.MAT.007.003 Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
7:4b.MAT.007.004 Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw?
7:5b.MAT.007.005 Naaféq, jëkkal a dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
7:6b.MAT.007.006 «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanamu mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen.
7:7b.MAT.007.007 «Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
7:8b.MAT.007.008 Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
7:9b.MAT.007.009 Kan ci yéen, bu la sa doom ñaanee mburu, nga jox ko doj?
7:10b.MAT.007.010 Walla mu ñaan la jën, nga jox ko jaan?
7:11b.MAT.007.011 Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astemaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan!
7:12b.MAT.007.012 «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi.
7:13b.MAT.007.013 «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare.
7:14b.MAT.007.014 Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul.
7:15b.MAT.007.015 «Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu.
7:16b.MAT.007.016 Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte réseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam?
7:17b.MAT.007.017 Noonu garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon.
7:18b.MAT.007.018 Garab gu baax mënul a meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon mënul a meññ doom yu neex.
7:19b.MAT.007.019 Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca safara sa.
7:20b.MAT.007.020 Ci seeni jëf nag ngeen leen di xàmmee.
7:21b.MAT.007.021 «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobareg Baay, bi nekk ci kaw.
7:22b.MAT.007.022 Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?”
7:23b.MAT.007.023 Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Musuma leen a xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.”
7:24b.MAT.007.024 «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj.
7:25b.MAT.007.025 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa.
7:26b.MAT.007.026 Waaye képp ku dégg lii ma leen wax, te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gànnuus bi.
7:27b.MAT.007.027 Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.»
7:28b.MAT.007.028 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngaleem,
7:29b.MAT.007.029 ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul.
8
8:1b.MAT.008.001 Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko.
8:2b.MAT.008.002 Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.»
8:3b.MAT.008.003 Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
8:4b.MAT.008.004 Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.»
8:5b.MAT.008.005 Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko,
8:6b.MAT.008.006 ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.»
8:7b.MAT.008.007 Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.»
8:8b.MAT.008.008 Waaye njiit la tontu ko ne: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
8:9b.MAT.008.009 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
8:10b.MAT.008.010 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, musumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii.
8:11b.MAT.008.011 Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
8:12b.MAT.008.012 Waaye ñi waroon a bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.»
8:13b.MAT.008.013 Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér.
8:14b.MAT.008.014 Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng.
8:15b.MAT.008.015 Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo.
8:16b.MAT.008.016 Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp.
8:17b.MAT.008.017 Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan:«Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.»
8:18b.MAT.008.018 Bi Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, mu sant taalibe ya, ñu jàll dex ga.
8:19b.MAT.008.019 Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.»
8:20b.MAT.008.020 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
8:21b.MAT.008.021 Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkk a dem suuli sama baay.»
8:22b.MAT.008.022 Yeesu tontu ko ne: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.»
8:23b.MAT.008.023 Bi mu ko waxee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem topp ko.
8:24b.MAT.008.024 Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yengal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw.
8:25b.MAT.008.025 Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee.»
8:26b.MAT.008.026 Waaye Yeesu tontu leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
8:27b.MAT.008.027 Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?»
8:28b.MAT.008.028 Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woon a jaar foofa.
8:29b.MAT.008.029 Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgg a mbugal, bala waxtu way jot?»
8:30b.MAT.008.030 Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for.
8:31b.MAT.008.031 Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.»
8:32b.MAT.008.032 Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma.
8:33b.MAT.008.033 Ba sàmm ya gisee loolu, ñu daw, dem dëkk ba, nettaliji lépp ak la xewoon ca ña rab jàpp.
8:34b.MAT.008.034 Noonu dëkk ba bépp génn seeti Yeesu. Ba ñu ko gisee nag, ñu ñaan ko, mu génn seen réew.
9
9:1b.MAT.009.001 Bi loolu amee Yeesu dugg cig gaal, jàll dex ga, dellu dëkkam.
9:2b.MAT.009.002 Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
9:3b.MAT.009.003 Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.»
9:4b.MAT.009.004 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol?
9:5b.MAT.009.005 Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gën a yomb?
9:6b.MAT.009.006 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
9:7b.MAT.009.007 Noonu làggi ba daldi jóg, ñibbi.
9:8b.MAT.009.008 Ba mbooloo ma gisee loolu, ñu daldi ragal te màggal Yàlla, mi dénk sañ-sañ bu tollu noonu doom Aadama yi.
9:9b.MAT.009.009 Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp.
9:10b.MAT.009.010 Gannaaw ga Yeesu doon lekk ca kër ga, te ay juutikat ak i boroom bàkkaar yu bare dikk, bokk lekk ak Yeesu ak taalibeem ya.
9:11b.MAT.009.011 Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
9:12b.MAT.009.012 Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
9:13b.MAT.009.013 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.»
9:14b.MAT.009.014 Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?»
9:15b.MAT.009.015 Yeesu tontu leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor.
9:16b.MAT.009.016 Xam ngeen ne, kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gën a yaatu.
9:17b.MAT.009.017 Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.»
9:18b.MAT.009.018 Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.»
9:19b.MAT.009.019 Noonu Yeesu jóg, topp ko, moom ak ay taalibeem.
9:20b.MAT.009.020 Bi ñuy dem nag, amoon na ca mbooloo ma jigéen juy xëpp deret diirub fukki at ak ñaar. Mu defe ne, su laalee mbubbam rekk, dina wér. Mu jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam.
9:22b.MAT.009.022 Bi mu ko defee Yeesu woññiku ne ko: «Na sa xel dal, soxna si, sa ngëm faj na la.» Noonu jigéen ja daldi wér ca saa sa.
9:23b.MAT.009.023 Bi Yeesu eggee kër njiit la, mu gis ñiy liit ak toxoro, ak mbooloo may def coow lu bare.
9:24b.MAT.009.024 Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal.
9:25b.MAT.009.025 Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg.
9:26b.MAT.009.026 Noonu xebaaru li mu def daldi siiw ca réew ma.
9:27b.MAT.009.027 Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!»
9:28b.MAT.009.028 Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne, man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu tontu ko: «Waaw Sang bi.»
9:29b.MAT.009.029 Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.»
9:30b.MAT.009.030 Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.»
9:31b.MAT.009.031 Waaye ñu génn rekk, siiwal turam fu nekk.
9:32b.MAT.009.032 Bi ñu fa jógee nag, amoon na ñeneen ñu ñëw fi moom, indil ko ku rab jàpp, mu luu.
9:33b.MAT.009.033 Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, musuñu koo gis ci Israyil.»
9:34b.MAT.009.034 Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
9:35b.MAT.009.035 Noonu Yeesu wër dëkk yu mag ya yépp ak yu ndaw ya, di leen jàngal ci seeni jàngu, tey yégle xebaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla, di faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
9:36b.MAT.009.036 Bi Yeesu gisee mbooloo ma, mu yërëm leen, ndaxte dañoo sonn ba ne yogg, mel ni xar yu amul sàmm.
9:37b.MAT.009.037 Noonu mu ne taalibeem ya: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu.
9:38b.MAT.009.038 Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.»
10
10:1b.MAT.010.001 Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
10:2b.MAT.010.002 Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam;l
10:3b.MAT.010.003 Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade;l
10:4b.MAT.010.004 Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nar a wor Yeesu.
10:5b.MAT.010.005 Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari.
10:6b.MAT.010.006 Waaye demleen ci bànni Israyil, ñoom ñi réer niy xar.
10:7b.MAT.010.007 Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.”
10:8b.MAT.010.008 Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen.
10:9b.MAT.010.009 Buleen dajale wurus, xaalis mbaa xànjar ci seeni maxtume.
10:10b.MAT.010.010 Buleen wut it mbuus ngir tukki mbaa ñaari turki, ay dàll mbaa aw yet, ndaxte liggéeykat yeyoo na dundam.
10:11b.MAT.010.011 «Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba.
10:12b.MAT.010.012 Bu ngeen di dugg ci kër nag, nuyooleen.
10:13b.MAT.010.013 Bu fekkee ne kër ga yeyoo na ko, na seen jàmm wàcc ci ñoom, waaye bu ko yeyoowul, na seen yéene dellusi ci yéen.
10:14b.MAT.010.014 Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu seeni wax, génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba, yëlëb seen pëndu tànk.
10:15b.MAT.010.015 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu.
10:16b.MAT.010.016 «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax.
10:17b.MAT.010.017 Waaye moytuleen nit ñi, ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu.
10:18b.MAT.010.018 Dees na leen yóbbu ngir man ci kanami boroom réew ak i buur, ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut.
10:19b.MAT.010.019 Boo xamee ne nag jébbale nañu leen, buleen am xel ñaar ci li ngeen di wax, mbaa ni ngeen koy waxe. Ndaxte ca waxtu woowa sax dingeen jot li ngeen war a wax;
10:20b.MAT.010.020 du yéenay wax, waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen.
10:21b.MAT.010.021 «Mag dina joxe rakkam ci dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu.
10:22b.MAT.010.022 Te yéen nag, ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba muj ga, mucc.
10:23b.MAT.010.023 Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen man a wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.»
10:24b.MAT.010.024 Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam.
10:25b.MAT.010.025 Bu taalibe yemee ak kilifaam demin, doy na; jaam it ni sangam. Ndegam tudde nañu boroom kër gi Beelsebul, astemaak waa kër gi.
10:26b.MAT.010.026 Kon nag buleen leen ragal, ndaxte amul dara lu nëbbu, lu ñu warul a biral, mbaa luy kumpa lu ñu warul a siiwal.
10:27b.MAT.010.027 Li ma leen wax ci biir lëndëm, waxleen ko ci leer; li ma leen déey, yégleleen ko ci kaw taax yi.
10:28b.MAT.010.028 Te buleen ragal ñu man a rey yaram, te mënuñoo rey ruu, waaye ragal-leen Ki man a sànk yaram ak ruu ci safara.
10:29b.MAT.010.029 Ñaari picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay.
10:30b.MAT.010.030 Seen kawari bopp sax, waññees na leen.
10:31b.MAT.010.031 Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu.
10:32b.MAT.010.032 «Koo xam ne nangu nga ma ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw.
10:33b.MAT.010.033 Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw.
10:34b.MAT.010.034 «Te it buleen defe ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale.
10:35b.MAT.010.035 Ndaxte ñëw naa ngir féewale doom ak baayam, doom ju jigéen ak ndeyam, jabar ak goroom;
10:36b.MAT.010.036 te nooni nit ñooy waa këram.
10:37b.MAT.010.037 Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen, yeyoowuloo ma.
10:38b.MAT.010.038 Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, yeyoowuloo ma.
10:39b.MAT.010.039 Kuy rawale sa bakkan, ñàkk ko, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, jotaat ko.
10:40b.MAT.010.040 «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni.
10:41b.MAT.010.041 Ku nangu yonent ndax yónnentam, dina jot ci peyu yonent; te ku nangu ku jub ndax njubteem, dina jot ci peyu ku jub.
10:42b.MAT.010.042 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gën a ndaw, ndax sama taalibe la, kooku du ñàkk yoolam mukk.»
11
11:1b.MAT.011.001 Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu, mu jóge fa, ngir dem jàngaleji ak a waare ci seeni dëkk.
11:2b.MAT.011.002 Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem,
11:3b.MAT.011.003 ne ko: «Ndax yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?»
11:4b.MAT.011.004 Yeesu tontu leen ne: «Demleen nettali Yaxya li ngeen dégg te gis ko.
11:5b.MAT.011.005 Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi.
11:6b.MAT.011.006 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
11:7b.MAT.011.007 Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
11:8b.MAT.011.008 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur.
11:9b.MAT.011.009 Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent.
11:10b.MAT.011.010 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.”
11:11b.MAT.011.011 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut.
11:12b.MAT.011.012 Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll.
11:13b.MAT.011.013 Ndaxte li yonent yi wax ak li yoonu Musaa tëral ñu ngi doon dox, ba kera Yaxya di feeñ.
11:14b.MAT.011.014 Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Iliyas bi waroon a ñëw.
11:15b.MAT.011.015 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.
11:16b.MAT.011.016 «Niti jamono jii nag, lan laa leen man a mengaleel? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di woo seeni xarit,
11:17b.MAT.011.017 ne leen:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
11:18b.MAT.011.018 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
11:19b.MAT.011.019 Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
11:20b.MAT.011.020 Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk, ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam, ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar.
11:21b.MAT.011.021 Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
11:22b.MAT.011.022 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
11:23b.MAT.011.023 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey.
11:24b.MAT.011.024 Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.»
11:25b.MAT.011.025 Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi.
11:26b.MAT.011.026 Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.»
11:27b.MAT.011.027 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it mënul a xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.
11:28b.MAT.011.028 «Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay.
11:29b.MAT.011.029 Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol.
11:30b.MAT.011.030 Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul.»
12
12:1b.MAT.012.001 Amoon na benn bésu noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk.
12:2b.MAT.012.002 Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésu noflaay bi.»
12:3b.MAT.012.003 Noonu Yeesu tontu leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
12:4b.MAT.012.004 Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu jébbal Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; saraxalekat rekk a ko sañoon a lekk.
12:5b.MAT.012.005 Te it ndax jànguleen ci yoonu Musaa, ne saraxalekat ya ca kër Yàlla ga teraluñu bésu noflaay bi, te tooñuñu?
12:6b.MAT.012.006 Waaye maa ngi leen koy wax, am na ci seen biir ku sut kër Yàlla ga.
12:7b.MAT.012.007 Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul.
12:8b.MAT.012.008 Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésu noflaay bi.»
12:9b.MAT.012.009 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, dugg ci seen jàngu,
12:10b.MAT.012.010 te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésu noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko.
12:11b.MAT.012.011 Yeesu tontu leen: «Ku fi amoon xar, mu daanu ci kàmb ci bésu noflaay bi, ndax doo ko jàpp, génne ko?
12:12b.MAT.012.012 Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésu noflaay bi jaadu na.»
12:13b.MAT.012.013 Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des.
12:14b.MAT.012.014 Farisen ya génn nag, daldi gise, ngir fexee reylu Yeesu.
12:15b.MAT.012.015 Waaye bi ko Yeesu yégee, mu sore foofa; te ñu bare topp ko, mu wéral leen ñoom ñépp.
12:16b.MAT.012.016 Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal.
12:17b.MAT.012.017 Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
12:18b.MAT.012.018 «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn,di sama Soppe bi neex sama xol.Dinaa def sama Xel ci moom,muy yégal xeet yi yoonu njub.
12:19b.MAT.012.019 Du xëccoo mbaa muy wax ci kaw,te kenn du dégg baatam ci mbedd yi.
12:20b.MAT.012.020 Du dammaate barax bu banku,te mees guy saxar, du ko fey,ba kera mu yégal njub, ba daan.
12:21b.MAT.012.021 Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.»
12:22b.MAT.012.022 Booba ñu indil ko ku rab jàpp, mu gumba te luu. Yeesu faj ko, ba ku luu ki di wax tey gis.
12:23b.MAT.012.023 Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?»
12:24b.MAT.012.024 Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
12:25b.MAT.012.025 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, te dëkk mbaa kër guy xeex boppam du man a yàgg.
12:26b.MAT.012.026 Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di man a yàgge?
12:27b.MAT.012.027 Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
12:28b.MAT.012.028 Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
12:29b.MAT.012.029 «Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgg a dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj këram gépp.
12:30b.MAT.012.030 Noonu ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.»
12:31b.MAT.012.031 Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu man a doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal.
12:32b.MAT.012.032 Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira.
12:33b.MAT.012.033 Neeleen garab gi baax na, moom ak meññeefam, walla ngeen ne garab gi bon na, moom ak meññeefam; ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee.
12:34b.MAT.012.034 Yéen ñi fees ak daŋar ni ay co, naka ngeen man a waxe lu baax, fekk dangeen bon? Ndaxte gémmiñ, la fees xol lay wax.
12:35b.MAT.012.035 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, jële ko ca fa mu denc lu baax, te nit ku bon, lu bon lay wax, jële ko ca fa mu denc lu bon.
12:36b.MAT.012.036 Maa ngi leen di wax ne, keroog bés pénc, nit ñi dinañu làyyi ndax wax ju nekk ju amul njariñ, ju ñu mas a wax.
12:37b.MAT.012.037 Ndaxte dees na la àtte ni ku jub ci say wax, walla ñu daan la ci say wax.»
12:38b.MAT.012.038 Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.»
12:39b.MAT.012.039 Yeesu tontu leen: «Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg yonent Yàlla Yunus.
12:40b.MAT.012.040 Ndaxte ni Yunus nekke woon ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir rabu géej wu mag, noonu la Doomu nit ki di nekke ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir suuf.
12:41b.MAT.012.041 Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi.
12:42b.MAT.012.042 Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
12:43b.MAT.012.043 «Boo xamee ne rab wa jàppoon nit génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis.
12:44b.MAT.012.044 Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
12:45b.MAT.012.045 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom-ñaari rab yu ko gën a soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.»
12:46b.MAT.012.046 Bi Yeesu nekkee di wax ak mbooloo ma, ndeyam ak ay rakkam daldi ñëw, taxaw ci biti, bëgg a wax ak moom.
12:47b.MAT.012.047 Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgg a wax ak yaw.»
12:48b.MAT.012.048 Waaye Yeesu tontu ko ne: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?»
12:49b.MAT.012.049 Noonu mu joxoñ ay taalibeem naan: «Ñii ñooy sama ndey ak samay rakk.
12:50b.MAT.012.050 Ndaxte ku def sama coobareg Baay bi nekk ci kaw, yaa di sama rakk, sama jigéen ak sama ndey.»
13
13:1b.MAT.013.001 Bés booba Yeesu génnoon na ca kër ga, toog ca wetu dex ga.
13:2b.MAT.013.002 Mbooloo mu bare dajaloo ca moom, ba tax mu dugg cig gaal, toog; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
13:3b.MAT.013.003 Noonu Yeesu dégtal leen lu bare ciy léeb ne leen: «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
13:4b.MAT.013.004 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
13:5b.MAT.013.005 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
13:6b.MAT.013.006 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
13:7b.MAT.013.007 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko.
13:8b.MAT.013.008 Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom-benn-fukk, li ci des fanweer.
13:9b.MAT.013.009 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
13:10b.MAT.013.010 Bi Yeesu waxee ba noppi, ay taalibeem jegeñsi, laaj ko lu tax mu di leen wax ciy léeb.
13:11b.MAT.013.011 Noonu mu tontu leen ne: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
13:12b.MAT.013.012 Ndaxte ku am, dinañu la dollil, ba nga barele; waaye ku amul, li nga am as néew, dinañu ko nangu.
13:13b.MAT.013.013 “Dañuy xool te duñu gis, di déglu waaye duñu dégg te duñu xam,” moo tax ma di leen wax ciy léeb.
13:14b.MAT.013.014 Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan:“Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.
13:15b.MAT.013.015 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.”
13:16b.MAT.013.016 «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg!
13:17b.MAT.013.017 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, ay yonent yu bare ak nit ñu jub ñu bare bëggoon nañu gis li ngeen di gis waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg waaye dégguñu ko.
13:18b.MAT.013.018 «Yéen nag dégluleen li léebu beykat biy tekki.
13:19b.MAT.013.019 Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi.
13:20b.MAT.013.020 Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw;
13:21b.MAT.013.021 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
13:22b.MAT.013.022 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ.
13:23b.MAT.013.023 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom-benn-fukk mbaa fanweer.»
13:24b.MAT.013.024 Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam.
13:25b.MAT.013.025 Waaye bi nit ñi di nelaw, noonam ñëw, ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem.
13:26b.MAT.013.026 Bi dugub ji saxee nag, jëmb bi saxaale ak moom.
13:27b.MAT.013.027 «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?”
13:28b.MAT.013.028 Mu tontu leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?”
13:29b.MAT.013.029 Waaye mu tontu leen: “Déedéet, ngir bañ a buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi.
13:30b.MAT.013.030 Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: Jëkkleen a dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.”»
13:31b.MAT.013.031 Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam.
13:32b.MAT.013.032 Doomu fuddën moo gën a tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
13:33b.MAT.013.033 Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
13:34b.MAT.013.034 Loolu Yeesu wax mbooloo ma, ëmb na ko lépp ciy léeb, te waxuleen dara lu dul ciy léeb.
13:35b.MAT.013.035 Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Dinaa leen wax ciy léeb,di yégle yëf yu nëbbuli dale ca njàlbéen ga ba bésu tey.»
13:36b.MAT.013.036 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.»
13:37b.MAT.013.037 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Doomu nit ki mooy ji jiwu wu baax wi;
13:38b.MAT.013.038 àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi;
13:39b.MAT.013.039 Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi.
13:40b.MAT.013.040 Ni ñu dajalee jëmb ba, lakk ko, noonu lay nekke, bu àddina tukkee.
13:41b.MAT.013.041 Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar,
13:42b.MAT.013.042 sànni leen ci safara; foofa dees na fa jooy te yéyu.
13:43b.MAT.013.043 Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
13:44b.MAT.013.044 Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.
13:45b.MAT.013.045 «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet.
13:46b.MAT.013.046 Am bés mu gis per buy jar njëg gu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.»
13:47b.MAT.013.047 Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk.
13:48b.MAT.013.048 Bi mbaal mi feesee nag, ñu ñoddi ko ci tefes gi, ba noppi ñu taxaw, dajale yu baax yi ciy ndab, waaye sànni yi bon.
13:49b.MAT.013.049 Noonu lay mel, bu àddina tukkee. Malaaka yi dinañu génn, tànn ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi,
13:50b.MAT.013.050 sànni leen ci safara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.»
13:51b.MAT.013.051 Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu tontu ko: «Waaw.»
13:52b.MAT.013.052 Yeesu ne leen: «Kon xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.»
13:53b.MAT.013.053 Bi nga xamee ne Yeesu dégtal na léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa,
13:54b.MAT.013.054 dem fa mu yaroo. Mu di leen jàngal ci seen jàngu, ba ñu waaru ne: «Xam-xam bii ak kéemaan yii, fu mu ko jële?
13:55b.MAT.013.055 Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda?
13:56b.MAT.013.056 Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?»
13:57b.MAT.013.057 Kon ñu daldi koy xeeb.Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.»
13:58b.MAT.013.058 Te Yeesu defu fa kéemaan yu bare ndax seen ngëmadi.
14
14:1b.MAT.014.001 Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am.
14:2b.MAT.014.002 Noonu mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya, mi dekki; moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
14:3b.MAT.014.003 Ndaxte Erodd jàppoon na Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd, jabaru Filib magam,
14:4b.MAT.014.004 te Yaxya daan ko wax: «Jaaduwul nga denc ko.»
14:5b.MAT.014.005 Erodd nag bëgg koo rey, waaye dafa ragal nit ñi, ci li ñu teg Yaxya ab yonent.
14:6b.MAT.014.006 Bi ñu ca tegee ab diir nag, ñuy màggal bés ba Erodd juddu woon, te doomu Erojàdd ju jigéen di fecc ci biir gan ñi. Loolu neex Erodd,
14:7b.MAT.014.007 ba mu dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, dinaa la ko jox.»
14:8b.MAT.014.008 Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.»
14:9b.MAT.014.009 Bi ko buur ba déggee, mu am naqar, waaye ngiñ la ak gan ña tax mu santaane, ñu jox ko ko.
14:10b.MAT.014.010 Mu yónnee nag, ngir ñu dagg boppu Yaxya ca kaso ba.
14:11b.MAT.014.011 Ñu indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq ba, mu jox ko ndeyam.
14:12b.MAT.014.012 Noonu taalibey Yaxya ñëw, fab néew wa, suul ko; ba noppi dem, wax ko Yeesu.
14:13b.MAT.014.013 Bi Yeesu déggee deewu Yaxya nag, mu jóge fa, dugg cig gaal, di dem ca bérab bu wéet. Waaye bi ko nit ñi yégee, ñu daldi jóge ci dëkk yi, topp ko ak seeni tànk.
14:14b.MAT.014.014 Yeesu génn ci gaal gi nag, gis mbooloo mu réy, mu yërëm leen, ba faj ñi ci wopp.
14:15b.MAT.014.015 Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu man a lekk?»
14:16b.MAT.014.016 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Matul ñu dem, yéen joxleen leen lu ñu lekk.»
14:17b.MAT.014.017 Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.»
14:18b.MAT.014.018 Yeesu ne leen: «Indil-leen ma ko fii.»
14:19b.MAT.014.019 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo ma, ñu toog ca ñax ma. Mu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool ci kaw, sant Yàlla. Mu damm mburu ma, jox ko taalibe ya, ñu séddale ko nit ña.
14:20b.MAT.014.020 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale dammit ya ca des, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees.
14:21b.MAT.014.021 Gannaaw jigéen ña ak gune ya, góor ña doon lekk matoon nañu juróomi junni.
14:22b.MAT.014.022 Bi loolu amee Yeesu sant taalibe ya, ñu dugg gaal ga te jàll dex ga, jiituji ko, muy yiwi mbooloo ma.
14:23b.MAT.014.023 Bi mu ko yiwee nag, mu yéeg ca tund wa, ngir wéet ak Yàlla. Noonu guddi jot, fekk mu nekk fa moom rekk.
14:24b.MAT.014.024 Bi mu fa nekkee nag, gaal ga sore na tefes ga, te duus ya di ko yengal bu metti, ndax ngelaw la leen soflu.
14:25b.MAT.014.025 Ca njël nag Yeesu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi.
14:26b.MAT.014.026 Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu.
14:27b.MAT.014.027 Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!»
14:28b.MAT.014.028 Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.»
14:29b.MAT.014.029 Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu.
14:30b.MAT.014.030 Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!»
14:31b.MAT.014.031 Ca saa sa Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko naan: «Yaw mi néew ngëm, lu tax nga am xel ñaar?»
14:32b.MAT.014.032 Noonu ñu dugg ca gaal ga, te ngelaw li ne tekk.
14:33b.MAT.014.033 Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.»
14:34b.MAT.014.034 Bi loolu amee ñu jàll, teer ca diiwaanu Senesaret.
14:35b.MAT.014.035 Ña fa dëkk xàmmi Yeesu, yónnee nag ca diiwaan bépp, indil ko ñu wopp ñépp.
14:36b.MAT.014.036 Noonu ñu ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk, te ku ko laal daldi wér.
15
15:1b.MAT.015.001 Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko:
15:2b.MAT.015.002 «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.»
15:3b.MAT.015.003 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada?
15:4b.MAT.015.004 Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.”
15:5b.MAT.015.005 Waaye yéen dangeen ne, ku wax sa ndey walla sa baay: “Li ngeen war a jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,”
15:6b.MAT.015.006 kooku amatul warugaru teral baayam. Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada.
15:7b.MAT.015.007 Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan:
15:8b.MAT.015.008 “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,waaye seen xol sore na ma.
15:9b.MAT.015.009 Seen màggal amul benn njariñ,ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.”»
15:10b.MAT.015.010 Noonu Yeesu woo mbooloo mi ci moom ne leen: «Dégluleen te xam:
15:11b.MAT.015.011 du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
15:12b.MAT.015.012 Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?»
15:13b.MAT.015.013 Yeesu tontu leen ne: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi.
15:14b.MAT.015.014 Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.»
15:15b.MAT.015.015 Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.»
15:16b.MAT.015.016 Noonu Yeesu ne ko: «Ndax ba tey seen xol dafa tëju, yéen itam?
15:17b.MAT.015.017 Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu?
15:18b.MAT.015.018 Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe.
15:19b.MAT.015.019 Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga.
15:20b.MAT.015.020 Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.»
15:21b.MAT.015.021 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon.
15:22b.MAT.015.022 Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.»
15:23b.MAT.015.023 Waaye Yeesu tontuwu ko genn kàddu. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.»
15:24b.MAT.015.024 Yeesu tontu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xar yu réeri bànni Israyil.»
15:25b.MAT.015.025 Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!»
15:26b.MAT.015.026 Yeesu tontu ko: «Jël ñamu gune yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
15:27b.MAT.015.027 Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.»
15:28b.MAT.015.028 Ci kaw loolu Yeesu tontu ko ne: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
15:29b.MAT.015.029 Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa.
15:30b.MAT.015.030 Ba mu fa nekkee, nit ñu bare ñëw ci moom, indaale ay lafañ, ay làggi, ay gumba, ay luu ak ñeneen ñu bare. Ñu teg leen ci tànki Yeesu, mu faj leen.
15:31b.MAT.015.031 Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil.
15:32b.MAT.015.032 Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leen a yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.»
15:33b.MAT.015.033 Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?»
15:34b.MAT.015.034 Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu tontu ko: «Juróom-ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
15:35b.MAT.015.035 Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf.
15:36b.MAT.015.036 Mu fab juróom-ñaari mburu yi ak jën yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ñu séddale leen mbooloo mi.
15:37b.MAT.015.037 Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom-ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
15:38b.MAT.015.038 Gannaaw jigéen ñi ak gune yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni.
15:39b.MAT.015.039 Noonu Yeesu yiwi mbooloo mi, dugg ci gaal, ñëw ci wàlli Magadan.
16
16:1b.MAT.016.001 Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.»
16:2b.MAT.016.002 Noonu Yeesu tontu leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.”
16:3b.MAT.016.003 Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeen a ràññee melow asamaan, waaye mënuleen a ràññee firndey jamono ji nu tollu.
16:4b.MAT.016.004 Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla. Waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.» Bi Yeesu waxee loolu, mu jóge ci ñoom, dem.
16:5b.MAT.016.005 Gannaaw loolu taalibe yi jàllaat dex gi, fekk fàtte nañoo yóbbaale mburu.
16:6b.MAT.016.006 Noonu Yeesu ne leen: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.»
16:7b.MAT.016.007 Bi ko taalibe yi déggee, ñu daldi werante ci seen biir naan: «Nun de indaalewunu mburu.»
16:8b.MAT.016.008 Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen di werante ci seen biir, ndaxte indaalewuleen mburu?
16:9b.MAT.016.009 Ndax xamaguleen ba tey? Xanaa fàttalikuwuleen juróomi mburu ya ngir juróomi junniy góor ña, ak ñaata pañe ngeen dajale woon ciy dammit?
16:10b.MAT.016.010 Te ndax fàttalikuwuleen itam juróom-ñaari mburu ya ngir ñeenti junniy góor ña, ak ñaata dàmba ngeen dajale woon ciy dammit?
16:11b.MAT.016.011 Kon nag lu tax xamuleen ne, waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.»
16:12b.MAT.016.012 Noonu ñu xam ne, Yeesu waxul woon lawiiru mburu, waaye ñu moytu njàngalem Farisen ya ak Sadusen ya.
16:13b.MAT.016.013 Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?»
16:14b.MAT.016.014 Taalibe yi tontu ne: «Am na ñu naan, Yaxya, ñeneen ñi, Iliyas; ñi ci des ne, Yeremi walla keneen ci yonent yi.»
16:15b.MAT.016.015 Noonu Yeesu ne leen: «Waaye yéen, ku ngeen may teg?»
16:16b.MAT.016.016 Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer tontu ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.»
16:17b.MAT.016.017 Yeesu tontu ko: «Barkeel ñeel na la, Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal lii, waaye sama Baay bi nekk ci kaw.
16:18b.MAT.016.018 Te maa ngi lay wax lii: yaa di Piyeer, te ci kaw doj wu réy woowu laay samp mbooloom ñi ma gëm, te dooley dee du ko manal dara.
16:19b.MAT.016.019 Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.»
16:20b.MAT.016.020 Noonu Yeesu dénk taalibe yi bu wóor ne leen: «Buleen wax kenn ne, maay Almasi bi.»
16:21b.MAT.016.021 Li dale ci jamono jooja, Yeesu tàmbali na xamal taalibeem yi ne, war na dem Yerusalem, daj fa coono yu bare, jóge ca njiit ya, ca saraxalekat yu mag ya ak ca xutbakat ya; ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba.
16:22b.MAT.016.022 Bi mu waxee ba noppi, Piyeer woo ko ci pegg, bëgg koo yedd ne ko: «Yàlla tere, Boroom bi, loolu du la dal.»
16:23b.MAT.016.023 Waaye Yeesu woññiku, daldi ne Piyeer: «Sore ma Seytaane, bu ma xatal; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
16:24b.MAT.016.024 Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko war a daaj, door a topp ci man.
16:25b.MAT.016.025 Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, jotaat ko.
16:26b.MAT.016.026 Te it moom àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Te nit, lu mu war a weccee bakkanam?
16:27b.MAT.016.027 Ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci ndamul Baayam, ànd ak ay malaakam; bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam.
16:28b.MAT.016.028 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu Doomu nit ki ñëw ci nguuram.»
17
17:1b.MAT.017.001 Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool.
17:2b.MAT.017.002 Mu soppiku fa seen kanam, xar-kanamam di melax nib jant, te ay yéreem weex ni leer.
17:3b.MAT.017.003 Naka noonu ñu gis yonenti Yàlla Musaa ak Iliyas, di waxtaan ak Yeesu.
17:4b.MAT.017.004 Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.»
17:5b.MAT.017.005 Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
17:6b.MAT.017.006 Bi taalibe yi déggee baat bi, ñu ne nërëm ci suuf, daldi tiit lool.
17:7b.MAT.017.007 Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.»
17:8b.MAT.017.008 Noonu ñu xool ci kaw, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk.
17:9b.MAT.017.009 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi ñuy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki.»
17:10b.MAT.017.010 Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Iliyas mooy jëkk a ñëw?»
17:11b.MAT.017.011 Yeesu tontu leen ne: «Waaw dëgg la, Iliyas war na ñëw, jubbanti lépp.
17:12b.MAT.017.012 Teewul maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nar a sonal léegi Doomu nit ki.»
17:13b.MAT.017.013 Ndax wax jooju nag, taalibe ya xam ne, ci mbirum Yaxya la leen doon wax.
17:14b.MAT.017.014 Bi nga xamee ne wàcc nañu, ba ñëw ca mbooloo ma, genn góor ñëw ci moom, sukk
17:15b.MAT.017.015 naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci safara, léeg-léeg mu daanu ci ndox.
17:16b.MAT.017.016 Indi naa ko ci say taalibe, waaye mënuñu koo faj.»
17:17b.MAT.017.017 Noonu Yeesu tontu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen di war a muñal?» Mu ne leen, «Indil-leen ma xale bi fii.»
17:18b.MAT.017.018 Noonu Yeesu tëkku rab wa, rab wa génn ca xale ba, mu daldi wér ca saa sa.
17:19b.MAT.017.019 Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun mënunu woon a dàq rab wi?»
17:20b.MAT.017.020 Yeesu tontu leen ne: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.»
17:22b.MAT.017.022 Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi;
17:23b.MAT.017.023 dinañu ko rey, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» Bi ko taalibe ya déggee, ñu am naqar lool.
17:24b.MAT.017.024 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?»
17:25b.MAT.017.025 Piyeer ne leen: «Aaŋkay!»Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkk a wax ne Piyeer: «Waaw lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?»
17:26b.MAT.017.026 Piyeer tontu ko ne: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci.
17:27b.MAT.017.027 Waaye bëgguma nu naqaral leen; kon demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkk a xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.»
18
18:1b.MAT.018.001 Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gën a màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?»
18:2b.MAT.018.002 Noonu Yeesu woo xale, teg ko ci seen biir,
18:3b.MAT.018.003 ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen woññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
18:4b.MAT.018.004 Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gën a màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
18:5b.MAT.018.005 Te it ku nangu ci sama tur xale bu mel ni kii, man mii nga nangu.
18:6b.MAT.018.006 Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ca fa gën a xóot ca géej ga.
18:7b.MAT.018.007 «Yaw àddina dinga torox ndax say fiir yiy yóbbe nit bàkkaar. Fiir mënta ñàkk, waaye toroxte dal na nit ki koy lal.
18:8b.MAT.018.008 Boo xamee ne sa loxo mbaa sa tànk mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga lafañ walla ñàkk loxo te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo walla ñaari tànk, te ñu sànni la ci safara su dul fey mukk.
18:9b.MAT.018.009 Boo xamee ne sa bët mu ngi lay yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga patt te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, te ñu sànni la ci safara.
18:10b.MAT.018.010 «Te it wottuleen a xeeb kenn ci ñi gën a tuuti, ndax kat seeni malaakaa ngi sax ci jataayu sama Baay bi nekk ci kaw. Maa leen wax loolu.
18:12b.MAT.018.012 «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent, te dem wuti ma réer?
18:13b.MAT.018.013 Bu ko gisee, mbég mi mu am ci moom mooy ëpp mbég, mi mu am ci juróom-ñeent-fukki xar ya ak juróom-ñeent ya réerul.
18:14b.MAT.018.014 «Noonu it seen Baay bi nekk ci kaw bëggul kenn ci ñi gën a tuuti sànku.
18:15b.MAT.018.015 «Te lii itam, bu sa mbokk defee bàkkaar, demal yedd ko, yéen ñaar rekk. Bu la dégloo, kon gindi nga sa mbokk.
18:16b.MAT.018.016 Waaye bu la dégluwul, àndal ak kenn mbaa ñaar, ngir mbir mi dëggu ci li ko ñaar walla ñett seede.
18:17b.MAT.018.017 Bu leen dégluwul ñoom itam, wax ko mbooloom ñi gëm. Bu dégluwul mbooloo ma nag, nga teg ko ni ku gëmul Yàlla mbaa ab juutikat.
18:18b.MAT.018.018 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp lu ngeen yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yiwi ci àddina, dees na ko yiwi ci asamaan.
18:19b.MAT.018.019 «Maa ngi leen koy wax it, bu ñaar ci yéen déggoo ci àddina, ngir ñaan lu mu man a doon, sama Baay bi nekk ci kaw dina leen ko may.
18:20b.MAT.018.020 Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
18:21b.MAT.018.021 Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko war a baal? Xanaa ba ci juróom-ñaari yoon?»
18:22b.MAT.018.022 Yeesu tontu ko ne: «Waxuma la ba ci juróom-ñaari yoon, waaye ba ci juróom-ñaar-fukki juróom-ñaari yoon.
18:23b.MAT.018.023 «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgg a waññ alalam ak ay jaraafam.
18:24b.MAT.018.024 Ba mu tàmbalee waññ nag, ñu indil buur ba ku ko ameel ay milyoŋ yu baree-bare,
18:25b.MAT.018.025 waaye jaraaf ja amul lu mu feye. Kon nag sangam santaane, ñu jaay ko moom ak jabaram ak ay doomam ak lépp lu mu am, ngir fey bor ba.
18:26b.MAT.018.026 Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.”
18:27b.MAT.018.027 Noonu sangam yërëm ko, bàyyi ko, baal ko bor ba.
18:28b.MAT.018.028 «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.”
18:29b.MAT.018.029 Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.”
18:30b.MAT.018.030 Waaye moom nanguwu ko, mu dem, tëj ko kaso, ba kera mu fey li mu ko ameel.
18:31b.MAT.018.031 «Bi ay moroomam gisee loolu nag, ñu am naqar wu réy, daldi dem, xamal seen sang li xew lépp.
18:32b.MAT.018.032 Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma.
18:33b.MAT.018.033 Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?”
18:34b.MAT.018.034 Noonu sang ba mer, jébbal ko ñiy fitnaale ca kaso ba, ba kera muy fey li mu ko ameel lépp.
18:35b.MAT.018.035 «Noonu la leen sama Baay bi ci kaw di def, bu ngeen baalul ku nekk seen mbokk ak xol bu sedd.»
19
19:1b.MAT.019.001 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu ba noppi, mu jóge Galile, dem ci wàllu réewu Yawut yi, gi féete ci gannaaw dexu Yurdan.
19:2b.MAT.019.002 Mbooloo mu bare topp ko, mu faj leen fa.
19:3b.MAT.019.003 Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase jabaram, saa su ko neexee?»
19:4b.MAT.019.004 Yeesu tontu leen ne: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen,
19:5b.MAT.019.005 te mu ne: “Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, ñoom ñaar doon benn.”
19:6b.MAT.019.006 Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
19:7b.MAT.019.007 Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox jabaram kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?»
19:8b.MAT.019.008 Yeesu tontu leen: «Musaa may na leen, ngeen fase seen jabar, ndax seen xol dafa dëgër, waaye ca njàlbéen ga demewul woon noonu.
19:9b.MAT.019.009 Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa jabar te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.»
19:10b.MAT.019.010 Bi ko taalibe ya déggee, ñu ne ko: «Bu dee noonu la digganteb góor ak jigéen mel, bañ a séy moo gën.»
19:11b.MAT.019.011 Yeesu tontu leen: «Du ñépp ñoo man a nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla jagleel rekk.
19:12b.MAT.019.012 Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu bañ a séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko man a nangu, nangu ko.»
19:13b.MAT.019.013 Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen.
19:14b.MAT.019.014 Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
19:15b.MAT.019.015 Noonu Yeesu teg leen ay loxoom, ba noppi jóge fa.
19:16b.MAT.019.016 Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def ci lu baax, ngir man a am dund gu dul jeex?»
19:17b.MAT.019.017 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.»
19:18b.MAT.019.018 Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóom, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg,
19:19b.MAT.019.019 teralal sa ndey ak sa baay, te it: nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
19:20b.MAT.019.020 Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?»
19:21b.MAT.019.021 Noonu Yeesu ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, jox ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
19:22b.MAT.019.022 Waaye bi waxambaane wa déggee loolu, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
19:23b.MAT.019.023 Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu!
19:24b.MAT.019.024 Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu pusa, moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
19:25b.MAT.019.025 Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo man a mucc nag?»
19:26b.MAT.019.026 Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.»
19:27b.MAT.019.027 Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?»
19:28b.MAT.019.028 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.
19:29b.MAT.019.029 Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex.
19:30b.MAT.019.030 Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji.
20
20:1b.MAT.020.001 «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu réseñam.
20:2b.MAT.020.002 Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg posetu denariyon, door leen a yebal ca toolam.
20:3b.MAT.020.003 Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu.
20:4b.MAT.020.004 Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.”
20:5b.MAT.020.005 Ñu dem ca. Mu génnaat ci digg-bëccëg ak ci tisbaar, defaat noonu.
20:6b.MAT.020.006 Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?”
20:7b.MAT.020.007 Ñu tontu ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.”
20:8b.MAT.020.008 «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujj a ñëw, ba ci ñi fi jëkk.”
20:9b.MAT.020.009 Noonu ñi mu jël ci tàkkusaan ñëw, ku nekk jot posetu denariyon.
20:10b.MAT.020.010 Gannaaw ga nag ñi mu jëkk a jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon.
20:11b.MAT.020.011 Bi ñu ko jotee nag, ñu tàmbalee ñaxtu ca boroom kër ga,
20:12b.MAT.020.012 naan: “Ñi mujj a ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.”
20:13b.MAT.020.013 Waaye boroom kër ga tontu kenn ci ñoom ne ko: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon?
20:14b.MAT.020.014 Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujj a ñëw, li ma la fey yaw,
20:15b.MAT.020.015 ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?”
20:16b.MAT.020.016 Noonu ñi mujj ñooy jiituji, ñi jiitu ñooy mujj.»
20:17b.MAT.020.017 Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii:
20:18b.MAT.020.018 «Nu ngi jëm Yerusalem, te dees na jébbal Doomu nit ki saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya. Dinañu ko àtte, teg ko dee,
20:19b.MAT.020.019 jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.»
20:20b.MAT.020.020 Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn.
20:21b.MAT.020.021 Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu tontu ko ne: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndeyjoor, ki ci des ci sa càmmooñ.»
20:22b.MAT.020.022 Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeen a naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu tontu ko: «Man nañu ko.»
20:23b.MAT.020.023 Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndeyjoor mbaa sama càmmooñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.»
20:24b.MAT.020.024 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu, ñu mere ñaari doomi ndey ya.
20:25b.MAT.020.025 Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di noot.
20:26b.MAT.020.026 Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgg a nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga,
20:27b.MAT.020.027 te ku bëgg a nekk njiit, na nekk seen jaam.
20:28b.MAT.020.028 Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
20:29b.MAT.020.029 Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko.
20:30b.MAT.020.030 Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne, Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
20:31b.MAT.020.031 Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gën a yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!»
20:32b.MAT.020.032 Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
20:33b.MAT.020.033 Ñu tontu ko: «Sang bi, na sunuy bët ubbiku.»
20:34b.MAT.020.034 Noonu Yeesu yërëm leen, laal seeni bët, ñu daldi gis ca saa sa, topp ci moom.
21
21:1b.MAT.021.001 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba agsi dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe,
21:2b.MAT.021.002 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci seen kanam. Bu ngeen eggee, dingeen gis mbaam mu ñu yeew ak cumburam; yiwileen leen, indil ma leen.
21:3b.MAT.021.003 Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leen a soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.»
21:4b.MAT.021.004 Yeesu def na noonu, ngir la ñu waxoon jaarale ko cib yonent am, bi mu naan:
21:5b.MAT.021.005 «Waxal waa Siyon:“Seen buur a ngi ñëw ci yéen;ku lewet la, te war mbaam-sëf,dig cumbur, doomu mbaam.”»
21:6b.MAT.021.006 Noonu taalibe ya dem, def loolu leen Yeesu sant.
21:7b.MAT.021.007 Ñu indi mbaam ma, moom ak cumbur ga, lal ci seeni yére, Yeesu toog ca.
21:8b.MAT.021.008 Ña ëpp ca mbooloo ma lal seeni yére ca yoon wa, ñenn ña dagg ay cari garab, lal leen it ca yoon wa.
21:9b.MAT.021.009 Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan:«Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Ca bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”»
21:10b.MAT.021.010 Bi nga xamee ne Yeesu dugg na Yerusalem, dëkk ba bépp yengatu ne: «Kii moo di kan?»
21:11b.MAT.021.011 Mbooloo ma tontu leen ne: «Kii moo di yonentu Yàlla Yeesu, bi jóge Nasaret ci Galile.»
21:12b.MAT.021.012 Bi loolu amee Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, dàq ñépp ña fay jaay ak ña fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis ya ak tooguy jaaykati pitax ya,
21:13b.MAT.021.013 naan: «Mbind mi nee na: “Sama kër dinañu ko wooye këru ñaan ci Yàlla,” waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
21:14b.MAT.021.014 Noonu ay gumba ak ay lafañ ñëw ci moom ca kër Yàlla ga, mu faj leen.
21:15b.MAT.021.015 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer.
21:16b.MAT.021.016 Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu tontu leen ne: «Waaw dégg naa ko. Ndax musuleen a jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?»
21:17b.MAT.021.017 Bi Yeesu waxee loolu, mu bàyyi leen, génn dëkk ba, jëm Betani, fanaan fa.
21:18b.MAT.021.018 Ci suba teel Yeesu dellusi ca dëkk ba, mu xiif.
21:19b.MAT.021.019 Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk.» Ca saa sa figg ga daldi wow.
21:20b.MAT.021.020 Bi nga xamee ne taalibe ya gis nañu loolu, ñu waaru naan: «Nan la figg gi daldi wowe ci taxawaay bi?»
21:21b.MAT.021.021 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te bañ a werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def.
21:22b.MAT.021.022 Te lépp lu ngeen laaj cig ñaan, bu ngeen ci boolee ngëm, dingeen ci jot.»
21:23b.MAT.021.023 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngale. Bi muy jàngale nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?»
21:24b.MAT.021.024 Yeesu tontu leen ne: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ko waxee, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
21:25b.MAT.021.025 La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
21:26b.MAT.021.026 Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.»
21:27b.MAT.021.027 Ñu tontu Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
21:28b.MAT.021.028 «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu réseñ.”
21:29b.MAT.021.029 Taaw ba tontu ko ne: “Maa ngi dem baay,” waaye demu ca.
21:30b.MAT.021.030 Gannaaw gi, baay ba ñëw ca ñaareel ba, wax ko noonu. Mu tontu ko ne: “Bëgguma caa dem,” waaye gannaaw loolu xelam soppiku, mu dem ca.»
21:31b.MAT.021.031 Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobareg baayam?» Ñu ne: «Ñaareel bi.» Kon Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkk a dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
21:32b.MAT.021.032 Ndaxte Yaxya ñëw na ci yéen ci yoonu njub, te gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak jigéeni moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikuwul sax, ba ngeen gëm ko.»
21:33b.MAT.021.033 Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci réseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki.
21:34b.MAT.021.034 «Bi nga xamee ne bëgg nañoo witt réseñ yi, mu yónni ay surgaam ci beykat yi, ngir jot wàllam ci meññeef mi.
21:35b.MAT.021.035 Waaye beykat yi jàpp surga yi, kenn ki ñu dóor ko ay yar, keneen ki ñu rey ko, ki ci des ñu sànni ko ay doj.
21:36b.MAT.021.036 Boroom kër gi nag yónniwaat yeneen surga yu ëpp yu jëkk ya, beykat yi def leen noonu ñoom itam.
21:37b.MAT.021.037 Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.”
21:38b.MAT.021.038 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen bopp: “Kii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndonoom.”
21:39b.MAT.021.039 Ñu jàpp ko nag, génne ko tool bi, rey ko.»
21:40b.MAT.021.040 Noonu Yeesu laaj leen: «Bu boroom tool bi ñëwee nag, na muy def beykat yi?»
21:41b.MAT.021.041 Ñu ne ko: «Dina rey reyin wu ñaaw nit ñu soxor ñooñu, batale tool bi yeneen beykat, yi koy jox wàllam ci jamonoy meññeef.»
21:42b.MAT.021.042 Kon Yeesu ne leen: «Xanaa musuleen a jàng lii ci Mbind yi?“Doj wi tabaxkat yi sànni;mujj na di doju koñ;ci Boroom bi la loolu jóge,te yéemu nanu ci.”
21:43b.MAT.021.043 «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam.
21:44b.MAT.021.044 Ku dal ci doj wii, dammtoo; ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
21:45b.MAT.021.045 Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dégg nañu léebam yooyu, ñu xam ne ñoom lay wax.
21:46b.MAT.021.046 Noonu ñu di ko fexee jàpp, waaye ragal nañu nit ña, ndaxte ñépp teg nañu ko ab yonent.
22
22:1b.MAT.022.001 Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen:
22:2b.MAT.022.002 «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor.
22:3b.MAT.022.003 Noonu mu yónni ay surgaam, ngir ñu woo gan yi ca céet ga, waaye gan yi bëgguñoo ñëw.
22:4b.MAT.022.004 Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ”
22:5b.MAT.022.005 Waaye ba tey wuyuwuñu ko; ñu dem, kenn ki ca toolam, kenn ki jaayaani,
22:6b.MAT.022.006 ña ca des jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.
22:7b.MAT.022.007 «Noonu buur mer, daldi yónni ay xarekatam, ngir ñu rey bóomkat yooyule, lakk seen dëkk.
22:8b.MAT.022.008 Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko.
22:9b.MAT.022.009 Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.”
22:10b.MAT.022.010 Noonu surga ya génn ca yoon ya, boole ña ñu fa gis ñépp, ñu bon ña ak ñu baax ña, ba néegu reer ya fees ak ay gan.
22:11b.MAT.022.011 «Bi nga xamee ne buur bi dugg na nag, ngir seetsi gan yi, mu gis fa nit ku solul mbubb mu ñu war a sol ca céet ga.
22:12b.MAT.022.012 Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig.
22:13b.MAT.022.013 Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.”
22:14b.MAT.022.014 Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.»
22:15b.MAT.022.015 Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu war a def, ngir fiir Yeesu ci waxam.
22:16b.MAT.022.016 Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
22:17b.MAT.022.017 Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?»
22:18b.MAT.022.018 Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi?
22:19b.MAT.022.019 Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon.
22:20b.MAT.022.020 Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?»
22:21b.MAT.022.021 Ñu tontu ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
22:22b.MAT.022.022 Bi nga xamee ne dégg nañu loolu, ñu waaru, bàyyi ko, daldi dem.
22:23b.MAT.022.023 Bés boobale ay Sadusen ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom gëmuñu ne ndekkite am na. Noonu ñu laaj ko naan:
22:24b.MAT.022.024 «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.”
22:25b.MAT.022.025 Amoon na ci nun nag juróom-ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba séyoon na, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom.
22:26b.MAT.022.026 Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom-ñaareel ba.
22:27b.MAT.022.027 Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu.
22:28b.MAT.022.028 Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom-ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?»
22:29b.MAT.022.029 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéena ngi cig réer, ndaxte xamuleen Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla.
22:30b.MAT.022.030 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
22:31b.MAT.022.031 Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa musuleen a jàng la leen Yàlla waxoon ne:
22:32b.MAT.022.032 “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.»
22:33b.MAT.022.033 Bi nga xamee ne mbooloo ma dégg nañu loolu, ñu waaru ndax li mu jàngale.
22:34b.MAT.022.034 Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne, yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje.
22:35b.MAT.022.035 Noonu kenn ci ñoom, ka nekk xutbakat, fexe koo fiir. Mu laaj ko:
22:36b.MAT.022.036 «Kilifa gi, ban ndigal moo gën a màgg ci yoonu Musaa?»
22:37b.MAT.022.037 Yeesu tontu ko ne: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.”
22:38b.MAT.022.038 Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane.
22:39b.MAT.022.039 Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”
22:40b.MAT.022.040 Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.»
22:41b.MAT.022.041 Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen:
22:42b.MAT.022.042 «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu tontu ko: «Daawuda.»
22:43b.MAT.022.043 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne:
22:44b.MAT.022.044 “Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam’ ”
22:45b.MAT.022.045 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
22:46b.MAT.022.046 Ci kaw loolu kenn mënu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara.
23
23:1b.MAT.023.001 Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen:
23:2b.MAT.023.002 «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa.
23:3b.MAT.023.003 Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe.
23:4b.MAT.023.004 Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam.
23:5b.MAT.023.005 Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb.
23:6b.MAT.023.006 Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya.
23:7b.MAT.023.007 Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “Kilifa gi.”
23:8b.MAT.023.008 Waaye yéen buñu leen wooye “Kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen.
23:9b.MAT.023.009 Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw.
23:10b.MAT.023.010 Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist.
23:11b.MAT.023.011 Ki gën a mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
23:12b.MAT.023.012 Kuy yékkatiku, dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
23:13b.MAT.023.013 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanamu nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgg a dugg, mu dugg ci.
23:15b.MAT.023.015 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu safara, ku leen yées ñaari yoon.
23:16b.MAT.023.016 «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.”
23:17b.MAT.023.017 Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gën a màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell?
23:18b.MAT.023.018 Dangeen ne it: “Ku giñe saraxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.”
23:19b.MAT.023.019 Gumba yi! Lan moo gën a màgg, sarax si walla saraxalukaay bi tax sarax si sell?
23:20b.MAT.023.020 Ku giñe saraxalukaay bi, giñ nga ci saraxalukaay bi ak li ci kawam lépp.
23:21b.MAT.023.021 Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak Ki ci dëkk.
23:22b.MAT.023.022 Ku giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak Ki ci toog.
23:23b.MAT.023.023 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gën a màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des.
23:24b.MAT.023.024 Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem.
23:25b.MAT.023.025 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal.
23:26b.MAT.023.026 Farisen yu gumba yi! Jëkkleen a setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set.
23:27b.MAT.023.027 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk.
23:28b.MAT.023.028 Yéen itam, ci ngistal dangeen a mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
23:29b.MAT.023.029 «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi.
23:30b.MAT.023.030 Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.”
23:31b.MAT.023.031 Seede ngeen nii ne, yey ngeen seen bopp, te yéenay doomi ñi doon rey yonent yi,
23:32b.MAT.023.032 di aw seen tànki baay, ba yées leen sax.
23:33b.MAT.023.033 Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu safara?
23:34b.MAT.023.034 Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo-dëkk.
23:35b.MAT.023.035 Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakariya doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak saraxalukaay bi.
23:36b.MAT.023.036 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii.
23:37b.MAT.023.037 «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen!
23:38b.MAT.023.038 Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër, ba mu gent.
23:39b.MAT.023.039 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»
24
24:1b.MAT.024.001 Bi Yeesu waxee ba noppi, mu génn ca kër Yàlla ga, dem. Noonu ay taalibeem ñëw ci moom, ngir won ko tabaxi kër Yàlla ga.
24:2b.MAT.024.002 Waaye mu tontu leen ne: «Du gis ngeen yii yépp? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
24:3b.MAT.024.003 Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne, yaa ngi ñëw te àddina di tukki?»
24:4b.MAT.024.004 Yeesu tontu leen ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax.
24:5b.MAT.024.005 Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Maa di Kirist,” te dinañu nax ñu bare.
24:6b.MAT.024.006 Dingeen dégg ay xare ak coowi xare; wottuleen, buleen ci tiit, ndaxte loolu war na am, waaye booba muju jamono ji jotagul.
24:7b.MAT.024.007 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Dina am ay xiif ak ay yengu-yenguy suuf ci bérab yu bare.
24:8b.MAT.024.008 Waaye loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu.
24:9b.MAT.024.009 Bu boobaa dees na leen jébbale, metital leen, rey leen; te xeet yépp dinañu leen bañ ndax sama tur.
24:10b.MAT.024.010 Bu loolu amee ñu bare dinañu dàggeeku, di booleente tey bañante.
24:11b.MAT.024.011 Te it ñu bare ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare.
24:12b.MAT.024.012 Te gannaaw lu bon day law, mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku.
24:13b.MAT.024.013 Waaye ku muñ ba ca muj ga, mucc.
24:14b.MAT.024.014 Noonu xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp, ngir mu nekk seede ci xeet yépp. Bu loolu amee muju jamono ji jot.
24:15b.MAT.024.015 «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam.
24:16b.MAT.024.016 Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya;
24:17b.MAT.024.017 ku nekk ci kaw taax ma, bul wàcc ngir fab say yëf, ya nekk ci biir kër ga;
24:18b.MAT.024.018 ku nekk ca tool ba, bul ñibbi ngir fab sa mbubb.
24:19b.MAT.024.019 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooyu, ngalla it ñiy nàmpal!
24:20b.MAT.024.020 Ñaanleen nag seen gàddaay bumu nekk jamonoy seddaayu lolli, walla bésu noflaay bi.
24:21b.MAT.024.021 Ndaxte booba dina am metit wu réy wu musul a am, ba àddina sosoo ak tey, te dootul am mukk.
24:22b.MAT.024.022 Te bu ñu wàññiwul bés yooyu, kenn du mucc, waaye dees na leen wàññi ndax ñi Yàlla tànn.
24:23b.MAT.024.023 «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Mu nga fale,” buleen ko gëm.
24:24b.MAT.024.024 Ndaxte ñi mbubboo turu Kirist ak ñi mbubboo turu yonent dinañu feeñ, di joxe ay firnde yu réy ak ay kéemaan, ba ciy nax sax ñi Yàlla tànn, su loolu manoon a am.
24:25b.MAT.024.025 Wax naa leen ko lu jiitu.
24:26b.MAT.024.026 «Bu ñu leen waxee nag: “Seetleen, mu nga nale ca àll ba,” buleen génn, mbaa ñu ne: “Seetleen mu ngi nii ci biir kër gi,” buleen ko gëm.
24:27b.MAT.024.027 Ndaxte ni melax di fàqe penku, te lerax ba sowu, noonu la ñëwu Doomu nit ki di mel.
24:28b.MAT.024.028 Fa médd nekk, fa la tan yiy dajee.
24:29b.MAT.024.029 «Gannaaw metitu bés yooyule nag, ca saa sa jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddiiw yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yengu.
24:30b.MAT.024.030 Booba firnde ji taxaw, Doomu nit ki feeñ ci asamaan, te xeeti àddina sépp dinañu jooy. Dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ci niiri asamaan si, ànd ak kàttan ak ndam lu réy.
24:31b.MAT.024.031 Dina yónni ay malaakaam ak baatu liit bu dégtu, ñu dajale ñi mu tànn ci ñeenti xebla yi, fa asamaan dale ba fu mu yem.»
24:32b.MAT.024.032 Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, ay xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na.
24:33b.MAT.024.033 Noonu yéen itam bu ngeen gisee loolu lépp, xamleen ne jege na, mu ngi ci bunt bi sax.
24:34b.MAT.024.034 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy te loolu lépp amul.
24:35b.MAT.024.035 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
24:36b.MAT.024.036 «Waaye bés booba walla waxtu wa, kenn xamul kañ lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax man Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.
24:37b.MAT.024.037 Ni bési Nóoyin ya, noonu lay mel, bu Doomu nit ki di ñëw.
24:38b.MAT.024.038 Ndaxte ca bés ya jiitu mbënn ma, nit ñaa ngi doon lekk di naan, góor yaa ngi doon takk jabar, tey maye seeni doom, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga;
24:39b.MAT.024.039 xalaatuñu woon dara, ba kera ndoxum mbënn ma di dikk, yóbbu leen. Noonu lay mel ci ñëwu Doomu nit ki.
24:40b.MAT.024.040 «Bu boobaa ci ñaar ñu nekk cib tool, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des.
24:41b.MAT.024.041 Ci ñaari jigéen ñuy wol ca ëtt ba, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des.
24:42b.MAT.024.042 Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés bu seen Boroom di ñëw.
24:43b.MAT.024.043 Waaye xamleen lii: bu boroom kër gi xamoon, ci ban waxtu ci guddi la sàcc bi di ñëw, kon dina yeewu te du ko bàyyi, mu toj këram.
24:44b.MAT.024.044 Loolu moo tax yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.»
24:45b.MAT.024.045 Yeesu teg ca ne: «Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu leen di dundal ca jamono ja?
24:46b.MAT.024.046 Bu njaatigeem ñëwee te gis muy def noonu, surga boobu dina am ngërëm.
24:47b.MAT.024.047 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp.
24:48b.MAT.024.048 Waaye bu dee surga bu bon bu naan ci xelam: “Sama njaatige day yéex a ñëw,”
24:49b.MAT.024.049 mu tàmbalee dóor ay bokki surgaam, di lekk te naan ak naankat ya,
24:50b.MAT.024.050 kon njaatige ba dina ñëw ci bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu xamul.
24:51b.MAT.024.051 Dina ko dóor ay yar yu metti, jox ko añub naaféq. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.
25
25:1b.MAT.025.001 «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba.
25:2b.MAT.025.002 Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel.
25:3b.MAT.025.003 Ñi ñàkk xel nag fab nañu seeni làmp, waaye fabaalewuñu diwlin;
25:4b.MAT.025.004 waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diwlin ciy njaq.
25:5b.MAT.025.005 Ni boroom séet bi yéexee ñëw nag, ñépp gëmmeentu bay nelaw.
25:6b.MAT.025.006 «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.”
25:7b.MAT.025.007 Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp.
25:8b.MAT.025.008 Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diwlin, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgg a fey.”
25:9b.MAT.025.009 Waaye ñi am xel tontu leen ne: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen; tee ngeen a dem ca jaaykat ya, jënd.”
25:10b.MAT.025.010 «Bi nga xamee ne dem nañu jëndi, boroom séet ba agsi. Ñi amoon diwlin ci seeni làmp, ànd ak boroom séet ba ca reer ya. Noonu bunt ba tëj.
25:11b.MAT.025.011 Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu.”
25:12b.MAT.025.012 Waaye mu tontu leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.”
25:13b.MAT.025.013 «Yeewuleen nag, ndaxte xamuleen bés ba mbaa waxtu wa.
25:14b.MAT.025.014 «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi mu laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan.
25:15b.MAT.025.015 Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki.
25:16b.MAT.025.016 «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom.
25:17b.MAT.025.017 Noonu it ki jot ñaar amaat yeneen ñaar.
25:18b.MAT.025.018 Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem.
25:19b.MAT.025.019 «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya dellusi, daldi leen laaj alalam.
25:20b.MAT.025.020 Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.”
25:21b.MAT.025.021 Njaatigeem tontu ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
25:22b.MAT.025.022 Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.”
25:23b.MAT.025.023 Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.”
25:24b.MAT.025.024 «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul.
25:25b.MAT.025.025 Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.”
25:26b.MAT.025.026 Waaye njaatigeem tontu ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne, damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul,
25:27b.MAT.025.027 kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma man a jot li ma moom ak la mu jur.”
25:28b.MAT.025.028 Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi.
25:29b.MAT.025.029 Ndaxte ku am dinañu la dolli, ba nga barele, waaye ku amul, li nga am as néew sax, dinañu ko nangu.
25:30b.MAT.025.030 Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.”
25:31b.MAT.025.031 «Boo xamee ne Doomu nit ki mu ngi ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam.
25:32b.MAT.025.032 Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjalee xar yi ak bëy yi,
25:33b.MAT.025.033 mu teg xar yi ci ndeyjooram, bëy yi ci càmmooñam.
25:34b.MAT.025.034 «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndeyjoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina.
25:35b.MAT.025.035 Ndaxte xiifoon naa, ngeen jox ma, ma lekk; te mar, ngeen jox ma, ma naan; nekkoon naa ab doxandéem, ngeen fat ma;
25:36b.MAT.025.036 te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.”
25:37b.MAT.025.037 Ci kaw loolu ñi jub dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan?
25:38b.MAT.025.038 Kañ lanu la gisoon, nga nekk ab doxandéem, nu fat la; mbaa nga rafle, nu wodd la?
25:39b.MAT.025.039 Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?”
25:40b.MAT.025.040 Noonu Buur bi dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gën a ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
25:41b.MAT.025.041 «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmooñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci safara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam.
25:42b.MAT.025.042 Ndaxte xiifoon naa waaye joxuleen ma, ma lekk; te mar waaye joxuleen ma, ma naan.
25:43b.MAT.025.043 nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.”
25:44b.MAT.025.044 Ci kaw loolu dinañu tontu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?”
25:45b.MAT.025.045 Kon dina leen tontu ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gën a ndaw, man ngeen ko defalul.”
25:46b.MAT.025.046 Noonu ñii dinañu sóobu ci mbugal gu dul jeex, waaye ñi jub dinañu tàbbi ci dund gu dul jeex.»
26
26:1b.MAT.026.001 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu lépp ba noppi, mu ne taalibeem ya:
26:2b.MAT.026.002 «Xam ngeen ne, ñaari fan a des ci màggalu bésu Jéggi ba, te dinañu wor Doomu nit ki, daaj ko ci bant.»
26:3b.MAT.026.003 Booba nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa dajaloo ca kër gu réy gu saraxalekat bu mag ba, tudd Kayif.
26:4b.MAT.026.004 Ñu daldi gise, ba xam lu ñu man a fexe, ba jàpp Yeesu, reylu ko.
26:5b.MAT.026.005 Waaye ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yengu-yengu bañ a am ci nit ñi.»
26:6b.MAT.026.006 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani ca kër Simoŋ ma gaana woon,
26:7b.MAT.026.007 jenn jigéen ñëw ci moom, yor njaq lu ñu yette doj wu ñuy wax albaatar. Njaq la def latkoloñ bu jar lu baree-bare. Noonu bi Yeesu toogee di lekk, jigéen ji tuur ko ci boppu Yeesu.
26:8b.MAT.026.008 Waaye bi ko taalibe ya gisee, ñu daldi mer ne: «Yàq gii lu muy jariñ?
26:9b.MAT.026.009 Maneesoon na koo jaay ci lu bare, jox xaalis bi miskin yi.»
26:10b.MAT.026.010 Yeesu nag xam la ñu wax, mu ne leen: «Jigéen ji defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal?
26:11b.MAT.026.011 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.
26:12b.MAT.026.012 Kii, ci li mu tuur latkoloñ bii ci sama yaram, def na ko ngir waajal sama rob.
26:13b.MAT.026.013 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xebaar bu baax bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.»
26:14b.MAT.026.014 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca saraxalekat yu mag ya,
26:15b.MAT.026.015 ne leen: «Lan ngeen ma man a jox, ngir ma jébbal leen Yeesu?» Noonu saraxalekat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer.
26:16b.MAT.026.016 Li dale ci saa soosa nag Yudaa di fexe jamono ju mu leen man a jébbal Yeesu.
26:17b.MAT.026.017 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, taalibe yi ñëw ci Yeesu ne ko: «Foo bëggoon nu defaral la reeru màggalu Jéggi ba?»
26:18b.MAT.026.018 Yeesu tontu leen: «Demleen ca dëkk ba, jëm ca diw, ngeen ne ko: “Kilifa gi nee na: Sama jamono jege na; ci sa kër laay màggalsi xewu Jéggi ba, man ak samay taalibe.”»
26:19b.MAT.026.019 Noonu taalibe yi defar reeru Jéggi ba, na leen Yeesu waxe woon.
26:20b.MAT.026.020 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu toog di lekk, moom ak fukki taalibe yi ak ñaar.
26:21b.MAT.026.021 Bi ñuy lekk, mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.»
26:22b.MAT.026.022 Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?»
26:23b.MAT.026.023 Yeesu tontu leen ne: «Ki dugal loxoom ak man ci ndab li, kooku moo may wor.
26:24b.MAT.026.024 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox; bañoon a juddu moo gënoon ci moom.»
26:25b.MAT.026.025 Yudaa, mi ko nar a wor, laaj ko: «Mbaa du man, kilifa gi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
26:26b.MAT.026.026 Noonu bu ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.»
26:27b.MAT.026.027 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci,
26:28b.MAT.026.028 ndaxte lii sama deret la, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi.
26:29b.MAT.026.029 Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaawsi tey ndoxum réseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum réseñ mu bees ci sama nguuru Baay.»
26:30b.MAT.026.030 Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya.
26:31b.MAT.026.031 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku ci guddi gii, ndaxte bind nañu: “Dinaa dóor sàmm bi, xari jur gi tasaaroo.”
26:32b.MAT.026.032 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.»
26:33b.MAT.026.033 Piyeer nag daldi jël kàddu gi naan: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la dàggeeku mukk.»
26:34b.MAT.026.034 Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, ci guddi gii, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.»
26:35b.MAT.026.035 Piyeer tontu ko: «Boo xamee ne sax, damaa war a dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu.
26:36b.MAT.026.036 Bi loolu amee Yeesu ànd ak ñoom ba ca bérab bu tudd Setsemane, mu ne taalibe ya: «Toogleen fii, ma dem fale, ñaan fa.»
26:37b.MAT.026.037 Bi mu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer ak ñaari doomi Sebede, daldi am tiis ba xonett.
26:38b.MAT.026.038 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba may bëgg a dee; toogleen fi, xool ak man.»
26:39b.MAT.026.039 Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.»
26:40b.MAT.026.040 Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
26:41b.MAT.026.041 Xool-leen te ñaan, ngir bañ a daanu cig fiir; seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.»
26:42b.MAT.026.042 Yeesu delluwaat di ñaan ne: «Sama Baay, bu fekkee ne kaasu naqar bii mënu maa teggi te naanuma ko, kon na sa coobare am.»
26:43b.MAT.026.043 Yeesu ñëwaat ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis.
26:44b.MAT.026.044 Mu daldi leen bàyyi, waxaat loolu ñetteel bi yoon.
26:45b.MAT.026.045 Noonu mu ñëw ca taalibe ya ne leen: «Nelawleen léegi te noppalu. Waxtu wu ñu ma war a jébbale ci loxoy bàkkaarkat yi, jege na.
26:46b.MAT.026.046 Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
26:47b.MAT.026.047 Bi muy wax loolu nag, Yudaa, mi bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar te naroon koo wor, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, jóge ca saraxalekat yu mag ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
26:48b.MAT.026.048 Fekk Yudaa moomu joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko.»
26:49b.MAT.026.049 Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaamu àleykum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng.
26:50b.MAT.026.050 Yeesu tontu ko: «Sama xarit, xam naa lu tax nga ñëw.» Noonu ñu daldi jegesi, song ko, jàpp ko.
26:51b.MAT.026.051 Ca saa sa kenn ci ñi ànd ak Yeesu bocci jaaseem, dóor surgab saraxalekat bu mag ba, nopp ba dagg.
26:52b.MAT.026.052 Waaye Yeesu ne ko: «Roofal sa jaasi ci mbaram, ndaxte ku bocci jaasi, jaasi moo lay rey.
26:53b.MAT.026.053 Xanaa xamuloo ne, man naa laaj sama Baay, te dina ma may ci taxawaay bi mbooloom malaaka mu xel dajul?
26:54b.MAT.026.054 Waaye su ma ko defoon, nan la Mbind mi man a ame? Ndaxte Mbind mi nee na, nii la war a ame.»
26:55b.MAT.026.055 Booba Yeesu ne mbooloo mi: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. Moona daa naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma.
26:56b.MAT.026.056 Waaye lii lépp xew na, ngir amal Mbindi yonent yi.» Ci kaw loolu taalibe yépp dëddu ko, daw.
26:57b.MAT.026.057 Ña jàppoon Yeesu yóbbu ko kër Kayif, saraxalekat bu mag ba, fa xutbakat ya ak njiit ya daje.
26:58b.MAT.026.058 Piyeer topp ko fu sore, ba ci ëttu saraxalekat bu mag ba; mu dugg, toog ak surga ya, ngir seet nu mbir may mujje.
26:59b.MAT.026.059 Noonu saraxalekat yu mag ya ak kureelu àttekat ya di seet naaféq bu man a seede ci Yeesu, ba ñu man koo rey,
26:60b.MAT.026.060 waaye mënuñu koo am. Teewul ñu bare ñëwoon nañu, di seede lu dul dëgg. Ba mujj ñaari nit ñëw naan:
26:61b.MAT.026.061 «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan.”»
26:62b.MAT.026.062 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo tontu dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?»
26:63b.MAT.026.063 Waaye Yeesu ne cell. Saraxalekat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.»
26:64b.MAT.026.064 Yeesu tontu ko: «Wax nga ko. Maa ngi leen koy wax it, li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji Kàttan ji, di ñëw ci niiri asamaan si.»
26:65b.MAT.026.065 Bi mu déggee loolu, saraxalekat bu mag ba daldi mer lool, ba xotti ay yéreem, daldi ne: «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Dégg ngeen ni mu weddee.
26:66b.MAT.026.066 Lu ngeen ci xalaat?» Ñu tontu ko: «Yoon teg na ko dee.»
26:67b.MAT.026.067 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar-kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko,
26:68b.MAT.026.068 ne ko: «Yaw Kirist, yonent bi, ndax xam nga ku la dóor?»
26:69b.MAT.026.069 Bi looluy xew, Piyeer moom ma nga toogoon ca biti ca ëtt ba. Noonu benn mbindaan ñëw ci moom ne ko: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Galile.»
26:70b.MAT.026.070 Waaye Piyeer weddi ko ci kanamu ñépp ne ko: «Xawma li ngay wax.»
26:71b.MAT.026.071 Bi mu ko waxee, mu jëm ca bunt ba, te beneen mbindaan gis ko, mu wax ña fa nekkoon: «Kii àndoon na ak Yeesum Nasaret.»
26:72b.MAT.026.072 Waaye Piyeer weddiwaat, boole ko ak ay ngiñ ne ko: «Xawma nit kooku.»
26:73b.MAT.026.073 Nes tuuti ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.»
26:74b.MAT.026.074 Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab.
26:75b.MAT.026.075 Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti.
27
27:1b.MAT.027.001 Ci suba teel saraxalekat yu mag yépp ak njiiti xeet wa gise, ngir fexee reylu Yeesu.
27:2b.MAT.027.002 Ñu yeew ko, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat boroom réew ma.
27:3b.MAT.027.003 Bi nga xamee ne Yudaa, mi woroon Yeesu, gis na ne, daan nañu ko, mu am naqaru xol. Mu dem nag ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya, delloo leen fanweeri poset yu xaalis,
27:4b.MAT.027.004 ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu tontu ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.»
27:5b.MAT.027.005 Noonu Yudaa sànni xaalis ba ca kër Yàlla ga, jóge fa, dem, takk buum ci baatam, xaru.
27:6b.MAT.027.006 Saraxalekat yu mag ya nag fab xaalis ba, naan: «Jaaduwul nu def xaalis bii ci dencukaayu xaalis bi ci kër Yàlla gi, ndaxte njëgu deret la.»
27:7b.MAT.027.007 Ñu daldi diisoo nag, jënd ca xaalis ba toolu defarkatu ndaa ya, ngir di fa suul doxandéem ya.
27:8b.MAT.027.008 Loolu moo tax ñu wooye tool booba ba tey Toolu deret.
27:9b.MAT.027.009 Noonu la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi am, bi mu naan: «Fab nañu fanweeri poseti xaalis ya, mooy njëg gi bànni Israyil xayma woon ci nit ki;
27:10b.MAT.027.010 ñu joxe ko ngir toolu defarkatu ndaa ya, ni ma ko Boroom bi sante.»
27:11b.MAT.027.011 Gannaaw loolu Yeesu taxaw ca kanamu boroom réew ma, boroom réew ma laaj ko; «Ndax yaa di buuru Yawut yi?»
27:12b.MAT.027.012 Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko,» waaye tontuwul dara ca la ko saraxalekat yu mag ya ak njiit ya jiiñ.
27:13b.MAT.027.013 Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo lépp li ñu la jiiñ?»
27:14b.MAT.027.014 Waaye Yeesu tontuwu ko ci dara, ba tax boroom réew ma waaru lool.
27:15b.MAT.027.015 Ca màggal gu nekk nag boroom réew ma daan na may mbooloo ma, ñu tànn kenn ca ña ñu tëjoon, mu daldi leen ko bàyyil.
27:16b.MAT.027.016 Fekk booba amoon nañu ku ñu tëjoon, ku siiw te tudd Barabas.
27:17b.MAT.027.017 Bi nga xamee ne daje nañu nag, Pilaat laaj leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Barabas walla Yeesu mi ñuy wax Kirist?»
27:18b.MAT.027.018 Ndaxte xamoon na ne, kiñaan rekk a taxoon, ñu jébbal ko ko.
27:19b.MAT.027.019 Te it bi mu toogee sax ca jalu àttekaay ba, jabaram yónnee ci moom ne ko: «Bul dugg ci yëfi ku jub kooku, ndaxte tey gént naa ci moom te sonn naa ci lool.»
27:20b.MAT.027.020 Waaye saraxalekat yu mag ya ak njiit ya xiir mbooloo ma, ñu laaj Barabas te reylu Yeesu.
27:21b.MAT.027.021 Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu tontu ko: «Barabas.»
27:22b.MAT.027.022 Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp tontu ko ne: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
27:23b.MAT.027.023 Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gën a kawe naan: «Daaj ko ci bant!»
27:24b.MAT.027.024 Naka Pilaat xam ne, du ci man dara, fekk na sax yengu-yengu bi gën a am doole, mu daldi fab ndox, raxas ay loxoom ca kanamu mbooloo ma ne leen: «Set naa ci deretu ku jub kii; nu ngeen xam, defleen ko.»
27:25b.MAT.027.025 Ñépp tontu ko: «Na deretam dal ci sunu kaw ak sunu kaw njaboot.»
27:26b.MAT.027.026 Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas, mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
27:27b.MAT.027.027 Bi ñu ko defee xarekati boroom réew ma fab Yeesu, yóbbu ko ci biir kër ga, ñu daldi woo mbooloom xarekat ya yépp ci moom.
27:28b.MAT.027.028 Noonu ñu summi ko, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.
27:29b.MAT.027.029 Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndeyjooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
27:30b.MAT.027.030 Ba noppi ñu daldi tifli ci kawam, fab bantu xat ba, dóor ko ci boppam.
27:31b.MAT.027.031 Bi ñu ko ñaawalee ba noppi, ñu summi mbubbum xarekat ma, solalaat ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
27:32b.MAT.027.032 Bi nga xamee ne génn nañu, ñu daje ak nit ku dëkk Siren te tudd Simoŋ; ñu ga ko, ngir mu gàddu bant, ba ñu war a daaj Yeesu.
27:33b.MAT.027.033 Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.»
27:34b.MAT.027.034 Bi ñu fa eggee, ñu jox ko biiñ, ñu def ci lu wex. Waaye bi mu ko mosee, nanguwu koo naan.
27:35b.MAT.027.035 Noonu ñu daaj ko ca bant ba, ñu daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant,
27:36b.MAT.027.036 ba noppi toog fa, di ko wottu.
27:37b.MAT.027.037 Te it ñu teg ci kaw boppam mbind, mu xamle lu tax ñu rey ko, mu ne: «Kii mooy Yeesu, buuru Yawut yi.»
27:38b.MAT.027.038 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew ma, kenn ci ndeyjooram, ka ca des ci càmmooñam.
27:39b.MAT.027.039 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko,
27:40b.MAT.027.040 naan: «Yaw mi man a toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi.»
27:41b.MAT.027.041 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya it di ko ñaawal naan:
27:42b.MAT.027.042 «Waa jii musal na ñeneen te mënul a musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko.
27:43b.MAT.027.043 Gannaaw dénk na boppam Yàlla, kon na ko Yàlla musal, bu ko soppee, ndaxte nee na: “Maay Doomu Yàlla.”»
27:44b.MAT.027.044 Taskati réew ma it, ya ñu daajaale ak moom, di ko xas noonule.
27:45b.MAT.027.045 La tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
27:46b.MAT.027.046 Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
27:47b.MAT.027.047 Ñenn ña ca ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.»
27:48b.MAT.027.048 Ca saa sa kenn ci ñoom daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci kaw bant, jox ko ko, mu muucu.
27:49b.MAT.027.049 Waaye ña ca des ne: «Bàyyil, nu seet ba xam Iliyas dina ñëw, musal ko.»
27:50b.MAT.027.050 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
27:51b.MAT.027.051 Ca saa sa ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf; suuf si yengu, doj yi toj, bàmmeel yi ubbiku,
27:52b.MAT.027.052 te ñu bare ci jëmmi nit ñu sell ñu dee, dekki.
27:53b.MAT.027.053 Te gannaaw ndekkitel Yeesu ñu génn ca bàmmeel ya, dugg ca dëkk bu sell ba, te feeñu ñu bare.
27:54b.MAT.027.054 Noonu njiitu xare bi ak ñi ànd ak moom di wottu Yeesu, bi ñu gisee suuf si yengu ak li xew, ñu daldi tiit lool ne: «Ci dëgg, kii Doomu Yàlla la.»
27:55b.MAT.027.055 Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dand, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo.
27:56b.MAT.027.056 Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, ndeyu Saag ak Yuusufa, ak ndeyu doomi Sebede ya.
27:57b.MAT.027.057 Ca ngoon amoon na taalibeb Yeesu mu ñëw, tudd Yuusufa te dëkk Arimate; ku bare alal la woon.
27:58b.MAT.027.058 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Pilaat santaane, ñu jox ko ko.
27:59b.MAT.027.059 Noonu Yuusufa fab jëmm ja, laxas ko ci càngaay lu set,
27:60b.MAT.027.060 dugal ko ca bàmmeel bu bees, ba mu yettaloon boppam ciw doj. Mu béraŋ doj wu mag ca buntu bàmmeel ba, dem.
27:61b.MAT.027.061 Fekk Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des ñoo fa toogoon janook bàmmeel ba.
27:62b.MAT.027.062 Ba bët setee nag, ca bés ba topp bésu Waajal ba, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dajaloo, jëm ci Pilaat.
27:63b.MAT.027.063 Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.”
27:64b.MAT.027.064 Danoo bëggoon nag, nga santaane, ñu wottu bàmmeel ba, ba am ñetti fan, ngir bañ taalibeem ya ñëw, sàcc néew ba, tey yégle ne dekki na. Bu ko defee nax bu mujj boobu dina yées bu jëkk ba.»
27:65b.MAT.027.065 Pilaat tontu leen: «Amleen, ay wottukat a ngi nii. Demleen wottuji ko, ni ngeen mane.»
27:66b.MAT.027.066 Noonu ñu dem, tëj bàmmeel ba bu wóor, ñu tay ca doj wa màndarga, teg fa wottukat ya.
28
28:1b.MAT.028.001 Gannaaw bésu noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba.
28:2b.MAT.028.002 Fekk suuf yengu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw.
28:3b.MAT.028.003 Meloom mel na ni melax, ay yéreem weex tàll ni perkaal.
28:4b.MAT.028.004 Ñi doon wottu tiit bay lox, daldi mel ni ñu dee.
28:5b.MAT.028.005 Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne, yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba,
28:6b.MAT.028.006 waaye nekkatu fi, ndaxte dekki na, ni mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon,
28:7b.MAT.028.007 te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne, dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.»
28:8b.MAT.028.008 Bi loolu amee nag jigéen ña daldi jóge bu gaaw ca bàmmeel ba, tiit ak mbég mu réy di jax seen xol, ñu daldi daw, ngir yégal ko taalibe ya.
28:9b.MAT.028.009 Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal.
28:10b.MAT.028.010 Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.»
28:11b.MAT.028.011 Ba ñuy dem, ñenn ca wottukat ya ñëw ca dëkk ba, xamal saraxalekat yu mag ya lépp lu xew.
28:12b.MAT.028.012 Noonu saraxalekat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya,
28:13b.MAT.028.013 ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.”
28:14b.MAT.028.014 Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.»
28:15b.MAT.028.015 Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey.
28:16b.MAT.028.016 Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon.
28:17b.MAT.028.017 Bi ñu gisee Yeesu, ñu màggal ko, waaye ñenn ñi am xel ñaar.
28:18b.MAT.028.018 Yeesu jegesi ne leen: «Sañ-sañ bépp, jox nañu ma ko ci kaw ak ci suuf.
28:19b.MAT.028.019 Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi;
28:20b.MAT.028.020 te ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. Te maa ngi ànd ak yéen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Matthew (Wolof). Matthew (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C324-3