1 Peter (Wolof)
1
1:1b.1PE.001.001 Man Piyeer, ndawul Yeesu Kirist, maa leen di bind, yéen doxandéem yi tasaaroo ci diiwaani Pont, Galasi, Kapados, Asi ak Bitini. Yàlla Baay bi tànn na leen,
1:2b.1PE.001.002 ci li mu leen xam bu jiitu, te sédde leen boppam ci jëfu Xel mu Sell mi, ngir ngeen déggal ko, te seen xol laab ndax deretu Yeesu Kirist. Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm.
1:3b.1PE.001.003 Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju bare, ba may nu yaakaar ju sax ndax ndekkitel Yeesu Kirist.
1:4b.1PE.001.004 Sédd na leen cér bu dul yàqu, du gàkk te du seey mukk, dencal leen ko ci asamaan,
1:5b.1PE.001.005 yéen ñi muy aar ci dooleem, sukkandikoo ci ngëm, di leen nége mucc, gi mu nar a feeñal bés bu mujj ba.
1:6b.1PE.001.006 Yéena ngi bég bu baax ci biir yaakaar jooju, doonte sax, su waree am, yéena ngi dékku tiis ab diir, ci seen jànkoonte ak nattu yu wuute.
1:7b.1PE.001.007 Xam ne nattu yooyu dinañu sellal seen ngëm, ni safara di setale wurus, fekk wurus luy wéy la, te ngëm a ko gën fuuf. Noonu seen ngëm dina yelloo cant, ndam ak màgg, bés bu Yeesu Kirist feeñee.
1:8b.1PE.001.008 Musuleen koo gis waaye bëgg ngeen ko, gisuleen ko waaye gëm ngeen ko te am mbég mu xel dajul, mu fees dell ak ndam,
1:9b.1PE.001.009 di jot muj gi ngëm séentu, maanaam muccu xol.
1:10b.1PE.001.010 Naka mucc googu nag, yonent yi xamle yiw, wi ngeen naroon a joti, seet nañu ko te gëstu ko.
1:11b.1PE.001.011 Bi Xelum Kirist, mi nekkoon ci ñoom, seedee lu jiitu coonoy Kirist ak ndam la cay topp, jéem nañoo takk, kañ ak nan lay ame.
1:12b.1PE.001.012 Waaye Yàlla xamal na leen ne, moomuñu woon kàddu googu ñu wax, waaye yéena ko moom. Te mooy kàddu gi ngeen dégg ci gémmiñu ñi leen doon jottali xebaar bu baax bi, ci dooley Xel mu Sell, mi Yàlla yónnee asamaan; malaaka yi sax bëgg nañoo gëstu yëf yii.
1:13b.1PE.001.013 Kon fagaruleen ci seeni xalaat te maandu, di wékk seen yaakaar jépp ci yiw, wi leen Yàlla di jagleel bés bu Yeesu Kirist di feeñ.
1:14b.1PE.001.014 Gannaaw gaayi Yàlla yu koy déggal ngeen, buleen toppati bëgg-bëgg, yi ngeen toppoon, bi ngeen xamagul Yàlla.
1:15b.1PE.001.015 Waaye na seen dund gépp sell, ni Yàlla mi leen woo selle.
1:16b.1PE.001.016 Ndaxte Mbind mi nee na: «Sell-leen, ndaxte ku sell laa.»
1:17b.1PE.001.017 Gannaaw nag Yàlla, mi ngeen di wooye Baay, mooy àtte jëfi ñépp te du gënale kenn, saxleen ci ragal ko diirub seen ngan ci àddina.
1:18b.1PE.001.018 Xam ngeen ne, Yàlla jot na leen ci seen dund gu tekkiwul dara, gi maam ya nekkoon; te jotuleen ak yu deme ni xaalis mbaa wurus yuy wéy,
1:19b.1PE.001.019 waaye ci deretu Kirist ju tedd ji, mel ni mbote mu sikkul te wàññikuwul.
1:20b.1PE.001.020 Yàlla xamoon na ko, ba àddina sosoogul, waaye léegi ci mujug jamono feeñal na ko ndax yéen
1:21b.1PE.001.021 ñi jaar ci moom, gëm Yàlla. Te Yàlla dekkal na ko, sol ko ndam, ngir ngeen wékk seen ngëm ak seen yaakaar ci Yàlla.
1:22b.1PE.001.022 Kon nag gannaaw déggal ngeen dëgg gi, ba sellal seeni xol te am mbëggeel gu dëggu, bëgganteleen mbëggeel gu tar ak seen xol bépp.
1:23b.1PE.001.023 Ndaxte du ci jiwu wuy yàqu ngeen judduwaate, waaye ci jiwu wu sax, maanaam kàddug Yàlla giy dund tey sax.
1:24b.1PE.001.024 Ndaxte:«Nit ñax la,ndamam di tóor-tóor kese;ñax day wow, tóor-tóor ruus,waaye kàddug Boroom bi day sax ba fàww.»
1:25b.1PE.001.025 Te kàddu googu mooy xebaar bu baax, bi ñu leen doon yégal.
2
2:1b.1PE.002.001 Kon nag dëdduleen gépp coxor, gépp njublaŋ, naaféq, kiñaan ak jëw.
2:2b.1PE.002.002 Gannaaw ay liir ngeen yuy door a juddu te mos ci mbaaxug Boroom bi, nàmpleen ci meew mu sell, miy dundal seen xol, ba màgg ci biir muccu Yàlla.
2:4b.1PE.002.004 Kon nag ñëwleen ci moom; nit ñi bañ nañu ko, waaye Yàlla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la,
2:5b.1PE.002.005 te yéena ngi mel niy doj yuy dund yu Yàllay defare dëkkukaayam. Noonu ay saraxalekat yu sell ngeen, ngir jébbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist.
2:6b.1PE.002.006 Looloo tax bind nañu:«Maa ngi samp fi ci Siyon doju koñ.Doj wu tedd la, wu ma tànn;ku gëm ci moom, sa yaakaar du tas mukk.»
2:7b.1PE.002.007 Kon nag yéen ñi gëm am ngeen cér ci teraangaam. Waaye naka ñi gëmul:«Doj wa tabaxkat ya sànni,mujj na di doju koñ.»
2:8b.1PE.002.008 Te it:«Doj la wuy fél nit,di xeer wu koy fakkastal.» Dañu cee fakkastalu, ndaxte gëmuñu kàddug Yàlla, te loolu la Yàlla dogal ci ñoom.
2:9b.1PE.002.009 Waaye yéen xeet wu Yàlla tànn ngeen, di askanu saraxalekati Buur Yàlla, askan wu sell ngeen, di mbooloom Yàlla, ngir ngeen yégle ngëneelam, moom mi leen woo, ba génne leen lëndëm gi, tàbbal leen ci leeram gu yéeme gi.
2:10b.1PE.002.010 Démb nekkuleen woon ci dara, waaye tey mbooloom Yàlla ngeen; booba jotuleen woon yërmandeem, waaye léegi jot ngeen ko.
2:11b.1PE.002.011 Samay xarit, yéen ñiy ay gan ak ay doxandéem ci àddina si, maa ngi leen di dénk lii: dëdduleen bànneexi bakkan yiy xeex ak xol.
2:12b.1PE.002.012 Na seen dundin rafet ci biir xeeti àddina, kon doonte ñu di leen sosal ay ñaawteef, dinañu gis seeni jëf yu rafet bay màggal Yàlla, bés bu leen feeñoo.
2:13b.1PE.002.013 Na seen nangub Boroom bi tax, ngeen déggal képp kuy kilifa, muy buur ba gën a kawe,
2:14b.1PE.002.014 mbaa jawriñ yu mu yebal, ngir ñu yar ñiy def lu bon, te teral ñiy def lu baax.
2:15b.1PE.002.015 Ndaxte noonu la coobareg Yàlla tëdde, maanaam ngeen sax ci def lu baax, ba wedamloo jayil yi xamul dara.
2:16b.1PE.002.016 Li leen Yàlla goreel nag, bu mu tax ngeen mbubboo ko, bay def lu bon, waaye ngeen gën a feddali seen jaamu Yàlla.
2:17b.1PE.002.017 Teral-leen ñépp, bëgg kureelu bokk yi, ngeen ragal Yàlla te teral buur bi.
2:18b.1PE.002.018 Yéen jaam yi déggal-leen seeni sang ak wegeel gu mat sëkk, waxuma ñi baax te lewet rekk, waaye sax ñu wex ñi.
2:19b.1PE.002.019 Ndaxte su ngeen dékkoo tiis, di sonn ci lu dul yoon ndax seen ànd ak Yàlla, loolu lu rafet la.
2:20b.1PE.002.020 Su ngeen tooñee te muñ i pes, luy pey gi? Waaye su ñu leen fitnaalee ci def lu baax te ngeen muñ ko, jëf ju rafet la fa kanam Yàlla.
2:21b.1PE.002.021 Ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ndaxte Kirist itam sonn na ngir yéen, teg fi seen kanam royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
2:22b.1PE.002.022 «Musul a def bàkkaar,te jenn waxu njublaŋ musul a génn ci gémmiñam.»
2:23b.1PE.002.023 Saaga nañu ko te feyyuwul, fitnaal nañu ko te tëkkuwul, waaye mu dénk boppam Ki yor àtte bu dëgg bi.
2:24b.1PE.002.024 Gàddu na moom ci boppam sunuy bàkkaar ca bant, ba ñu ko daajoon, ngir nu tàggook bàkkaar, sóobu ci dund gu jub; ndax ay gaañu-gaañoom may na nu ag wér.
2:25b.1PE.002.025 Ndaxte yéena ngi réeroon niy xar, waaye léegi dellusi ngeen ci sàmm, biy aar seeni xol.
3
3:1b.1PE.003.001 Yéen itam jigéen ñi, na ku nekk nangul sa jëkkër. Noonu su amee góor gu gëmul kàddug Yàlla, te gis jabaram di dund dund gu sell, boole ci weg ko, loolu dina ko gindi ci lu àndul ak wax.
3:3b.1PE.003.003 Bu seen taar aju ci col, maanaam ay létt, wurus mbaa yére yu rafet,
3:4b.1PE.003.004 waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir, di xol bu nooy te dal, ndax loolu lu takku la fa Yàlla.
3:5b.1PE.003.005 Ndaxte jigéeni démb yu sell, ya gëmoon Yàlla, loolu moo doon seen taar; nanguloon nañu seen jëkkër,
3:6b.1PE.003.006 ni Saarata déggale woon Ibraayma, ba daan ko wooye «Sang bi.» Yéen nag, su ngeen dee def lu baax te bañ cee boole genn njàqare, kon mel na ni Saarataa leen jaboote.
3:7b.1PE.003.007 Te yéen itam góor ñi, na ku nekk ci yéen am xel, ci ni ngay ànde ak sa jabar, xam ne àndandoo ju la gën a néew doole la. Joxleen ko teraanga ju mat, ndax yéena yem cér ci yiwu Yàlla, wi nu ubbil buntu dund gu dul jeex. Noonu dara du man a yàq seeni ñaan.
3:8b.1PE.003.008 Kon nag bokkleen xalaat, bokkleen i tiis, bëgganteleen, yërëmante te woyof.
3:9b.1PE.003.009 Ku la def lu bon mbaa mu saaga la, bul feyyu, waaye ñaanal ko lu baax; ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ngir barkeel leen.
3:10b.1PE.003.010 Ndaxte:«Ku bëgg a am dund gu naatte fekke bés yu rafet,na jàpp làmmiñam ci lu bon,sàmm gémmiñam ci fen.
3:11b.1PE.003.011 Na dëddu lu bon, tey def lu baax,na xënte jàmm te sax ci.
3:12b.1PE.003.012 Ndax Boroom baa ngi xool ñi jub bëti yërmande,di ubbi ay noppam ci seeni ñaan,waaye dàq ñiy def lu bon.»
3:13b.1PE.003.013 Te it kan moo leen di sonal, su ngeen góor-góorloo ci def lu baax?
3:14b.1PE.003.014 Doonte ñu di leen fitnaal sax ci def lu jub, ñu barkeel ngeen. Buleen tiit nag ndax seeni xëbal, mbaa ngeen di ci am njàqare.
3:15b.1PE.003.015 Waaye màggal-leen Kirist Boroom bi ci seeni xol, te jekk ngir tontu ku lay laaj ci seen yaakaar ji ngeen am;
3:16b.1PE.003.016 waaye na tont gi lewet te ànd ak wegeel. Àndleen ak xel mu dal; noonu ñi leen di sikkal ndax seen dund gu rafet ci gëm Kirist, dinañu rus ci seeni sos.
3:17b.1PE.003.017 Ñu fitnaal la ndax jëf ju baax, su dee mooy coobareg Yàlla, moo gën ñu fitnaal la ndax jëf ju bon.
3:18b.1PE.003.018 Ndaxte Kirist ci boppam dee na benn yoon ba fàww, ngir dindi bàkkaar yi, moom mi jub ngir ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; dee na ci jëmm, waaye dundaat na ci xel.
3:19b.1PE.003.019 Ci biir xel moomu la yégaleji ndamam ca ruu ya Yàlla tëj kaso;
3:20b.1PE.003.020 maanaam ña weddi woon ca jamonoy Nóoyin, fekk Yàlla muñaloon na leen diir bu yàgg, dajeek Nóoyin doon yett gaal ga. Ñu néew, maanaam limub juróom-ñett, dugg nañu ca gaal ga, jaar ca ndox ma, ba mucc.
3:21b.1PE.003.021 Loolu misaal la tey, ci li ñu nuy sóob ci ndox, te nu mucc; waxuma laabal sobe si taq ci yaram, waaye wuyu Yàlla ak xel mu dal. Li nu may mucc googu, mooy ndekkitel Yeesu Kirist,
3:22b.1PE.003.022 mi yéeg asamaan, toog fa ndeyjooru Yàlla, mu tiim malaaka yi, boroom sañ-sañ yi ak boroom doole yépp.
4
4:1b.1PE.004.001 Gannaaw Kirist nag sonn na ci yaramam, gànnaayooleen xelam moomu, ndaxte ku sonn ci yaramam, tàggoo na ak bàkkaar.
4:2b.1PE.004.002 Noonu diir bi ko dese ci kaw suuf, dëddu na bànneexi bakkan, jublu ci coobareg Yàlla.
4:3b.1PE.004.003 Ndaxte àndoon ngeen démb ci xalaati ñi xamul Yàlla, di dund ciy ñaawteef ak topp seen bakkan, di màndi ak a xawaare, di xér ci biiñ ak a jaamu ay xërëm yu araam, waaye na fi yem nag.
4:4b.1PE.004.004 Ñiy jëfe noonu waaru nañu, ba di leen sosal, ci li ngeen àndul ak ñoom, sóobu ci seeni moy yu dul jeex,
4:5b.1PE.004.005 waaye dinañu mas a teew fa kanam Ki nar a àtte ñiy dund ak ñi dee.
4:6b.1PE.004.006 Looloo waral it ñu jottali xebaar bu baax ndee, ya fekke woon jamonoy Nóoyin jooju, ngir ñu dunde Yàlla ci seen xel, doonte sax nit ñaa ngi leen daan fitnaal ci àddina.
4:7b.1PE.004.007 Te itam muju lépp jegesi na; nangeen maandu te foog, ba man a ñaan ci Yàlla.
4:8b.1PE.004.008 Li gën a am solo mooy, ngeen bëggante mbëggeel gu tar, ndax mbëggeel day suul bàkkaar yu bare.
4:9b.1PE.004.009 Ganalanteleen ci lu àndul ak njàmbat.
4:10b.1PE.004.010 Te lu la Yàlla jagleel kenn ku nekk ci yéen, nanga ko bokk ak ñépp ni jawriñ ju jub, ci séddale yiwu Yàlla wu yaatu.
4:11b.1PE.004.011 Kuy jottali kàddug Yàlla, na mel ni Yàllaay wax. Kuy jëf it, na jëfe dooley Yàlla, ngir turu Yàlla màgg ci lépp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak kàttan ba fàww. Amiin.
4:12b.1PE.004.012 Yéen samay xarit, ci mbirum nattu bu tànge ni daay, bi dal ci seen kaw, bumu leen jaaxal, ba ngeen teg ko ni lu xel dajul.
4:13b.1PE.004.013 Waaye bégleen ci cér, boobu ngeen am ci coonoy Kirist, ngir bés bu ndamam di feeñ, ngeen bég ak mbég mu ëpp xel.
4:14b.1PE.004.014 Su ñu leen jànnee sax ci turu Kirist, xamleen ne ñu barkeel ngeen, ndax Xelum Yàllaa ngi ci yéen, di firndeel seen ndamu ëllëg.
4:15b.1PE.004.015 Buñu sonal kenn ci yéen ci li mu rey nit walla mu sàcc, mbaa def lu bon, walla dugg ci lu yoonam nekkul.
4:16b.1PE.004.016 Waaye ku ñu sonal ndax waayu Kirist nga, bu ci rus, waaye nga màggal Yàlla ci tur woowu.
4:17b.1PE.004.017 Ndaxte àpp bi jot na, àtte baa ngi tàmbalee ci nun waa kër Yàlla. Te su tàmbalee ci nun nag, luy muju ñi weddi xebaaru Yàlla?
4:18b.1PE.004.018 Te:«Su muccu ki jub jafee,luy doon muju ki weddi te dëng?»
4:19b.1PE.004.019 Kon nag ñi tegoo fitna ci coobareg Yàlla, nañu sax ci def lu baax, dénk seen bopp Yàlla, miy Bindkat biy sàmm kóllëre.
5
5:1b.1PE.005.001 Kon yéen njiit yi, maa ngi leen di dénk, man miy njiit ni yéen, man mi seede coonoy Kirist te am cér ci ndam li nar a feeñ.
5:2b.1PE.005.002 Lii laa leen di ñaan: sàmmleen géttug Yàlla, gi mu leen dénk, di ko wottu, waxuma ci sañul-bañ, waaye di surgay Yàlla ci xol bu tàlli; ngeen def ko ak xol bu laab te bañ cee séentu alal.
5:3b.1PE.005.003 Buleen noot ñi leen Yàlla dénk, waaye ngeen nekk ay royukaay fi kanam jur gi.
5:4b.1PE.005.004 Noonu waxtu wu Boroom gétt gi feeñee, dina leen jagleel kaalag ndam guy sax ba fàww.
5:5b.1PE.005.005 Noonu itam yéen ndaw ñi, nangeen déggal mag ñi. Te yéen ñépp, solooleen woyof ci seen biir, ndaxte:«Yàlla day dàq ñi réy,di yiwal ñi woyof.»
5:6b.1PE.005.006 Suufeel-leen seen bopp kon ci ron loxob Yàlla bu am kàttan, ngir mu yékkati leen ci jamono ju ko soob.
5:7b.1PE.005.007 Te ngeen yenniku ci kawam seen njàqare jépp, ndax ku leen ñeewante la.
5:8b.1PE.005.008 Maanduleen te foog, ndax seen noon Seytaane mu ngi wër, ni gaynde guy yëmmu, di rëbb ku mu yàpp.
5:9b.1PE.005.009 Jànkoonteleen ak moom ci biir ngëm gu takku, xam ne kureelu bokk yi ci àddina yépp, ñu ngi daj ay fitna ni yéen.
5:10b.1PE.005.010 Te Yàlla mi jagoo yiw wépp te woo leen ci darajay Kirist, ngir ngeen bokk ci ndamam li sax, gannaaw bi ngeen yendoo bëccëgu tiis, dina leen yeesalaat, di leen dëgëral ak a dooleel, ba ngeen sampu.
5:11b.1PE.005.011 Na Yàlla yelloo màgg ba fàww. Amiin.
5:12b.1PE.005.012 Bind naa leen ci lu gàtt ci ndimbalu Silwan, mi ma jàpp ni sama mbokk mu takku. Dénk naa leen, di leen seedeel ne, lii mooy yiwu Yàlla dëgg; kon nag saxleen ci.
5:13b.1PE.005.013 Mbooloo mi nekk ci dëkk bi ñuy wax Babilon te Yàlla tànn ko ni yéen, moo di leen nuyu, ñoom ak Màrk sama doomu diine.
5:14b.1PE.005.014 Nuyoonteleen ak saafoonte yu sell. Na jàmm ñeel képp ku gëm Kirist.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. 1 Peter (Wolof). 1 Peter (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C360-F