Romans (Wolof)
1
1:1b.ROM.001.001 Man Pool, jaamub Kirist Yeesu, maa leen di bind bataaxal bii. Yàlla woo na ma, ma nekk ndawam, sas ma liggéeyu xamle xebaaram bu baax bi.
1:2b.ROM.001.002 Xebaar bu baax boobu, Yàlla dige woon na ko bu yàgg, jaarale ko ciy yonentam, ñu def ko ci Mbind mu sell mi,
1:3b.ROM.001.003 di xamle mbirum Doomam, Yeesu Kirist sunu Boroom. Lu jëm ci meloom ci àddina, ci askanu Daawuda la jóge, waaye lu jëm ci xelam mu sell, Doomu Yàlla la; ndaxte ndekkiteem nekk na firnde ju ràññiku, ne moom la.
1:5b.ROM.001.005 Te moom Kirist tàbbal na nu ci yiwu Yàlla, def nu ay ndawam, yónni nu ci biir xeeti àddina sépp, ngir ñu gëm ko te jébbalu, ba màggal turam.
1:6b.ROM.001.006 Te ci ngeen bokk, yéen ñi Yàlla woo, ngeen nekk ci Kirist.
1:7b.ROM.001.007 Yéen ñi dëkk Room ñépp, yéen ñi Yàlla bëgg te woo leen, ngeen nekk gaayam yu sell, na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
1:8b.ROM.001.008 Kon nag li may jëkk a wax mooy lii: sant naa Yàlla sama Boroom, jaarale ko ci Yeesu Kirist, ngir yéen ñépp, ndaxte seen ngëm siiw na ci àddina sépp.
1:9b.ROM.001.009 Bët bu set maa ngi leen di boole ci samay ñaan. Yàlla seede na li may wax, Yàlla mi may jaamu ci sama xel, ci xamle xebaar bu baax bu Doomam.
1:10b.ROM.001.010 Te li ma koy faral di ñaan mooy lii: bu soobee Yàlla, na ma ubbil bunt, ba ma man a ñëw ci yéen.
1:11b.ROM.001.011 Ndaxte bëgg naa leen a gis lool, ba indil leen barke bu jóge ci Xel mu Sell mi, ndax seen ngëm gën a dëgër.
1:12b.ROM.001.012 Maanaam ma nekk ci seen biir, te nu dimbaleente ci sunu ngëm, ndax man itam ma gën a am doole.
1:13b.ROM.001.013 Bokk yi, damaa bëgg ngeen xam ne, xalaat naa leen a seetsi ay yooni yoon, ngir meññ njariñ ci yéen, ni ma ko defe ci yeneen xeet yi, waaye ay téq-téq ñoo ma téye ba léegi.
1:14b.ROM.001.014 Am naa warugar sama diggante ak ñépp, muy ñi jàng ni Gereg yi, muy ñi jàngul ni Baarbaar yi, ñi bare xam-xam ak ñi barewul xam-xam.
1:15b.ROM.001.015 Li aju ci man nag, jekk naa ngir ñëw, xamal leen xebaar bu baax bi, yéen it waa Room.
1:16b.ROM.001.016 Ndaxte awma benn werante ci xebaar bu baax bi may waare, ndax mbirum Yàlla la, mu làmboo dooleem, ngir musal képp ku ko gëm, muy Yawut ci bu jëkk mbaa ki dul Yawut.
1:17b.ROM.001.017 Ndaxte xebaar bii day wone, ni nit man a jube ci kanam Yàlla, sukkandikoo ci ngëm rekk, tàmbali ci ngëm, yem ci ngëm. Moo tax Mbind mi wax ne: «Ku jub ci kaw ngëm, dinga dund.»
1:18b.ROM.001.018 Merum Yàllaa ngi feeñe asamaan, wàcc ci nit ñi, ndax seen weddi Yàlla gépp ak seen jubadi gépp, ñoom ñi suul dëgg, di topp lu jubadi.
1:19b.ROM.001.019 Ndax li nit man a xam ci Yàlla, leer na ci seen xel, ndax Yàlla won na leen ko.
1:20b.ROM.001.020 Ndaxte ba àddina sosoo ba tey, mbiri Yàlla yu nëbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, feeñ nañu bu leer, te bir ñépp ci yi mu sàkk, ba tax bunti lay yépp tëj nañu.
1:21b.ROM.001.021 Ndaxte bi ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ni mu ware, mbaa ñu sant ko. Waaye ñu daldi réer ci seen biiri xalaat yu mujjul fenn, ba tax seen xol gumba, ba lëndëm këruus.
1:22b.ROM.001.022 Ñu teg seen bopp ni boroomi xel, fekk ñu ñàkk xel lañu woon.
1:23b.ROM.001.023 Toxal nañu ndamu Yàlla Aji Sax ji, wuutal fa nataali nit ku dul sax, moom ak ay picc, ay rabi àll mbaa yuy raam.
1:24b.ROM.001.024 Moo tax Yàlla bërgël na leen ci seeni bëgg-bëgg, ñu sóobu ciy ñaawteef, di jëfleente lu gàccelu ci seeni cér.
1:25b.ROM.001.025 Toxal nañu dëggu Yàlla, tëral fen, di màggal ak a jaamu mbindeef, ba faaleetuñu sax Aji Bind, ji yelloo cant ba fàww. Amiin.
1:26b.ROM.001.026 Loolu moo tax nag Yàlla bërgël na leen ci seeni bëgg-bëgg yu ruslu. Seeni jigéen sax dëddu nañu li jekk, sóobu ci lu jekkadi, ñoom ak seeni moroom.
1:27b.ROM.001.027 Noonu it góor ñi bàyyi nañu li jekk ci seeni cér, maanaam ànd ak jigéen, bay am ay bëgg-bëgg yu tar ci ànd ak seeni moroom. Góor di defante ak góor li warul, ñu di jot seen peyu réer ci seeni yaram.
1:28b.ROM.001.028 Gannaaw xam Yàlla soxalu leen, Yàlla it bërgël na leen ci seen xel mu bon moomu, ñu sax ci jëf yu jekkadi.
1:29b.ROM.001.029 Seen xol fees na ak lu jubadi, lu bon, bëgge ak coxor; duñu xalaat lu dul kiñaan, rey nit, xuloo, njublaŋ ak ñaaw njort; dañuy jëw,
1:30b.ROM.001.030 di yàq der, di ñu bañ Yàlla te ñàkk sutura, di réy-réylu ak a kañu; ay jàmbaar lañu ci fexe lu bon, di bañ seeni waajur.
1:31b.ROM.001.031 Amuñu xel, amuñu kóllëre, amuñu cofeel, amuñu yërmande.
1:32b.ROM.001.032 Xam nañu ne, ñiy jëfe loolu, Yàlla daganal na seen dee, waaye teewul ñu di ko def, boole ko ak di farle ñi ci sax.
2
2:1b.ROM.002.001 Kon nag képp ku mu man a doon, yaw miy àtte sa moroom ak ñaaw njort, amuloo aw lay, ndaxte àtte sa moroom, daan sa bopp la; yaa ngi koy àtte ndax ay jëfam, fekk yaw itam noonu ngay jëfe.
2:2b.ROM.002.002 Xam nanu ne, ñiy jëfe noonu, Yàlla dina leen àtte, te àtteem jub na.
2:3b.ROM.002.003 Yaw nag miy àtte ñiy def loolu, te di ko def, ndax defe nga ne, dinga rëcc ci àtteb Yàlla?
2:4b.ROM.002.004 Ndax dangaa xeeb mbaaxu Yàlla, mi yéex a mer te di la muñal? Xanaa xamuloo ne, Yàllaa ngi lay won baaxaayam, ngir nga réccu say bàkkaar?
2:5b.ROM.002.005 Waaye ndegam dëgër nga bopp te bëgguloo réccu, yaa ngi dajale merum Yàlla ci sa bopp. Ndaxte Yàlla sàkk na bés bu muy wone àtteem bu jub bi te meram wàcc ci ñi bon;
2:6b.ROM.002.006 bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam.
2:7b.ROM.002.007 Ñiy góor-góorlu ciy def lu baax, bëgg Yàlla boole leen ca ndamam te sédde leen ngërëm ak dund gu sax, dina leen tàbbal ci dund gu dul jeex.
2:8b.ROM.002.008 Waaye ñi dëgër bopp, ba tanqamlu dëgg, di topp lu jubadi, seen pey mooy dooni merum Yàlla ak toroxte.
2:9b.ROM.002.009 Ki doon def lu bon, peyam mooy tiis ak metit wu tar, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut.
2:10b.ROM.002.010 Waaye ki doon def lu baax, añam mooy bokk ci ndamu Yàlla, am ngërëm ak jàmm, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut.
2:11b.ROM.002.011 Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
2:12b.ROM.002.012 Képp ku doon bàkkaar nag te nekkuloo woon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci lu dul yoonu Musaa, nga door a sànku. Te képp ku doon bàkkaar te nga nekkoon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci yoon woowu.
2:13b.ROM.002.013 Kon déglu yoonu Musaa rekk doyul; du loolu mooy tax nit jub ci kanam Yàlla; kiy sàmm yoon wi, moom la Yàlla di àtte ni ku jub.
2:14b.ROM.002.014 Ndax ñi dul Yawut te nekkuñu ci yoonu Musaa, ñu ngiy def li yoon woowu tëral, ndaxte Yàlla def na ko ci nit. Te wonee nañu noonu ne, man nañoo ràññee lu baax ak lu bon, su ñu nekkul sax ci yoonu Musaa,
2:15b.ROM.002.015 di wone it ne, Yàlla bind na ci seen xol jëf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat ñoo leen di tuumaal, mbaa ñu leen di jéggal.
2:16b.ROM.002.016 Ndax bés dina ñëw, bu xalaat yu làqu yi di feeñ, te Yàlla àtte nit ñi jaarale ko ci Yeesu Kirist. Xebaar bu baax, bi may waare, moo ko wax.
2:17b.ROM.002.017 Maa ngi ñëw nag ci yaw mi ne Yawut nga; yaa ngi sukkandiku ci yoonu Musaa ak di damu ci Yàlla.
2:18b.ROM.002.018 Xam nga coobareem, ndaxte jàng nga ci yoonu Musaa, ba fonk yëf yi gën a baax.
2:19b.ROM.002.019 Yaa ngi teg sa bopp wommatkatu gumba yi ak leeru ñi nekk cig lëndëm.
2:20b.ROM.002.020 Yaa di jàngalekatu ñi jàngul ak xamlekatu ñi xamul, ndaxte xalaat nga ne, Yàlla jagleel na leen ci yoonu Musaa bépp xam-xam ak gépp dëgg.
2:21b.ROM.002.021 Kon nag yaw miy jàngal say moroom, xanaa doo jàngal sa bopp? Yaw miy waare di tere sàcc, mbaa doo sàcc yaw itam? Yaw miy tere njaaloo, mbaa doo njaaloo?
2:22b.ROM.002.022 Yaw miy araamal xërëm yi, mbaa doo sàcc li nekk ci seeni xàmb?
2:23b.ROM.002.023 Yaw miy damoo yoonu Musaa, mbaa doo ko moy, ba indi gàcce ci turu Yàlla?
2:24b.ROM.002.024 Moo tax Mbind mi ne: «Yéena tax ñi nekkul Yawut di suufeel turu Yàlla.»
2:25b.ROM.002.025 Bëggoon naa ngeen xam ne, xaraf am na njariñ, boo ca boolee sàmm yoon. Waaye boo ko ca boolewul, sa xaraf amatul njariñ.
2:26b.ROM.002.026 Te itam ku xaraful, tey def jëf yu jub yi yoonu Musaa santaane, ndax Yàlla du ko teg ni ku xaraf?
2:27b.ROM.002.027 Ku dul Yawut te xaraful waaye di sàmm yoon wi, kooku dina la man a àtte yaw Yawut bi. Ndaxte li ngay xam-xam yoonu Musaa ci Mbind mi te xaraf, terewul nga koy moy.
2:28b.ROM.002.028 Juddu nekk Yawut taxul sag Yawut dëggu, te xaraf ci saw yaram taxul sa xaraf wóor.
2:29b.ROM.002.029 Waaye Yawut dëgg, ci xol lay nekk. Te xaraf dëgg itam, ci xol lay nekk. Du ngistal, lu dëggu la. Te képp ku mel noonu, dees na la gërëm, waxumala nit ñi, waaye Yàlla ci boppam.
3
3:1b.ROM.003.001 Yawut bi nag, ci lan la rawe ku dul Yawut? Te xaraf lu muy njariñ?
3:2b.ROM.003.002 Raw na ko fu nekk. Ci bu jëkk Yawut yi la Yàlla dénk waxam.
3:3b.ROM.003.003 Bu fekkee ne am na ci ñoom ñu ñàkk kóllëre, ndax loolu man na fanq kóllëreg Yàlla?
3:4b.ROM.003.004 Mukk! Su ñépp nekkoon ay naaféq, du tere Yàlla nekk dëgg. Moom la Mbind mi wax ci Yàlla ne:«Loo wax, ñépp ànd ci,te ku layoo ak yaw, nga yey ko.»
3:5b.ROM.003.005 Su fekkee nag njubadig nit dina feeñal njubteg Yàlla, lu ciy seen xalaat? Wax ji may bëgg a wax nag léegi, waxi nit rekk la, maanaam: ndax kon Yàlla àttewul yoon ci li muy daan ku jubadi?
3:6b.ROM.003.006 Mukk! Ndax su Yàlla jubadi woon, naka lay àttee àddina si?
3:7b.ROM.003.007 Waaye nag xanaa dina am ku tontu ci loolu ne: «Su fekkee sama ñàkk kóllëre gën na yékkati kóllëreg Yàlla, di yokk it ndamam, lu tax kon Yàlla di ma teg ba tey bàkkaarkat, ba di ma àtte?»
3:8b.ROM.003.008 Lu tax mënunoo wax ne: «Nanu def lu bon, ngir lu baax génn ca?» Am na sax ñu nuy tuumaal, di wax ne, noonu lanuy waaree. Waaye ñiy wax loolu, ndaan gi ñu yelloo dina leen dal.
3:9b.ROM.003.009 Kon nag lu nu ci war a wax? Nun Yawut yi, ndax noo gën ñi ci des? Mukk! Ndaxte wone nanu ne, nit ñépp ñu ngi ci nootaangeg bàkkaar, muy Yawut yi mbaa Gereg yi.
3:10b.ROM.003.010 Moom la Mbind mi wax ne:«Ku jub amul, du kenn sax.
3:11b.ROM.003.011 Amul kenn ku xam yëfi Yàlla,mbaa kenn ku koy wut.
3:12b.ROM.003.012 Ñépp jeng nañu,ba kenn amalatul Yàlla njariñ.Kenn du def lu baax, du kenn sax!
3:13b.ROM.003.013 Seen put a ngi xasaw ni méddum ñetti fan,seen làmmiñ làggi ci njublaŋ,te seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
3:14b.ROM.003.014 Duñu génne ci seen gémmiñ lu dul ay móolu ak i xas.
3:15b.ROM.003.015 Ñu sawar lañu ci rey nit.
3:16b.ROM.003.016 Fu ñu jaar, foofa yàqu ak musiba.
3:17b.ROM.003.017 Xamuñu yoonu jàmm,
3:18b.ROM.003.018 te ragal Yàlla sore na seen xol.»
3:19b.ROM.003.019 Xam nanu nag ne, lépp lu yoonu Musaa wax, wax na ko ñi nekk ci yoon woowu, ngir gémmiñ yépp ne miig, te waa àddina sépp jaar ci àtteb Yàlla.
3:20b.ROM.003.020 Ndaxte sàmm yoon wi taxul kenn jub ci kanam Yàlla; solob ndigal yi daal mooy wone bàkkaar.
3:21b.ROM.003.021 Waaye léegi nag Yàlla feeñal na, ni nit man a jube ci kanamam, ci lu séqul ak yoonu Musaa dara. Waaye ba tey yoonu Musaa ak waxi yonent yi seedeel nañu ko.
3:22b.ROM.003.022 Jub ci kanam Yàlla, gëm Yeesu Kirist rekk a koy maye, te képp ku ko gëm bokk nga ci. Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
3:23b.ROM.003.023 Ñépp a bàkkaar, ba joteetuñu ndamu Yàlla.
3:24b.ROM.003.024 Waaye gannaaw Kirist Yeesu dee na ngir jot leen, Yàlla ciw yiwam man na leen a àtte ni ñu jub ci dara.
3:25b.ROM.003.025 Wàcce na Kirist, mu nekk sarax ngir Yàlla baal nu sunuy bàkkaar, jaar ci deretam ji ñu tuur; te ngëm rekk moo nu ciy boole. Noonu Yàlla firndeel na ne ku jub la, doonte sax dafa muñaloon ñi jiitu jamonoy Kirist, ba jéggal leen seeni bàkkaar.
3:26b.ROM.003.026 Kon ci jamono jii nu ne, Yàlla wone na bu leer ne ku jub la, di àtte ni ku jub képp ku gëm Yeesu, te ba tey dëkk ci njubteem.
3:27b.ROM.003.027 Kan a man a bàkku nag ci kanam Yàlla? Kenn! Lu ko waral nag? Xanaa sàmm yoon? Déedéet! Ngëm rekk.
3:28b.ROM.003.028 Ndaxte danoo dëggal ne, ngëm rekk a tax Yàlla di àtte nit ni ku jub, waaye du sàmm yoon.
3:29b.ROM.003.029 Walla ndax nag Yawut yi rekk la fi nekkal? Ndax nekkalu fi it ñu dul Yawut? Aaŋkay!
3:30b.ROM.003.030 Gannaaw Yàlla kenn la, ñépp la fi nekkal. Ñi xaraf dina leen àtte ni ñu jub ndax seen ngëm, ñi xaraful it dina leen àtte ni ñu jub ndax seen ngëm.
3:31b.ROM.003.031 Xanaa kon ngëm day fanq yoonu Musaa? Mukk! Da koy gën a dëgëral sax.
4
4:1b.ROM.004.001 Sunu maam Ibraayma, mi nu soqikoo; nu mbiram tëdde?
4:2b.ROM.004.002 Bu fekkoonte ne Ibraayma, ci kaw i jëfam la ko Yàlla àttee ni ku jub, kon am na lu mu ci man a damoo. Waaye demewul noonu ci kanam Yàlla.
4:3b.ROM.004.003 Lan la Mbind mi wax ci loolu? Nee na: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub.»
4:4b.ROM.004.004 Képp kuy liggéey dina jot peyam; te pey googu du ag may, ñaqam la.
4:5b.ROM.004.005 Waaye Yàlla dina àtte jub sax ki ko weddi woon; kon ku wéeruwul ciy jëfam, waaye mu gëm rekk, Yàlla dina jàppe ngëmam ni njub.
4:6b.ROM.004.006 Noonu la Daawuda birale barkeelug nit ki Yàlla jagleel njub, fekk ay jëfam taxul.
4:7b.ROM.004.007 Mu ne:«Ñi ñu baal seen jàdd yoon,te seeni bàkkaar far ci kanam Yàlla,ñu barkeel lañu.
4:8b.ROM.004.008 Ki Boroom bi sëful ay bàkkaaram,kooka ku barkeel la.»
4:9b.ROM.004.009 Kon nag barkeel googu, ndax ñi xaraf rekk ñoo ko yeyoo? Ndax ñi xaraful it bokkuñu ci? Aaŋkay! Ndaxte wax nanu ne, Yàlla jàppe na ngëmu Ibraayma ni njub.
4:10b.ROM.004.010 Kañ la ko jagleel njub nag? Ndax lu jiitu xarafam la woon, am gannaaw ga? Lu ko jiitu la woon.
4:11b.ROM.004.011 Ndaxte Ibraayma gëm na, te Yàlla jàppe na ngëmam ni njub, fekk booba xarafagul. Te xarafal gi, màndarga la woon ci yaramam, di firndeel ne, ku jub la woon. Noonu la Ibraayma man a nekke baayu ñépp ñi gëm, ba Yàlla man leen a àtte ni ñu jub, te xarafuñu sax.
4:12b.ROM.004.012 Te noonu itam la Ibraayma man a nekke baayu ñi xaraf, bu fekkee yemuñu rekk ci xaraf, waaye ñu am ngëm, ga Ibraayma sunu maam amoon lu jiitu xarafam.
4:13b.ROM.004.013 Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ak ñi naroon a soqikoo ci moom, ne dinañu moom àddina si. Te dige boobu jógewul ci yoonu Musaa, waaye dafa jóge ci njub, gi Ibraayma amoon ci kanam Yàlla ci kaw ngëmam.
4:14b.ROM.004.014 Ndaxte su fekkee ne ñi nekk ci yoonu Musaa rekk ñooy moom àddina, kon ngëm amatul njariñ, te digeb Yàlla dafa toxu.
4:15b.ROM.004.015 Yoonu Musaa daal du def lu dul wàcce merum Yàlla ci sunu bopp; ndax fu yoon amul, jàdd yoon du fa man a am.
4:16b.ROM.004.016 Kon nag loolu Yàlla dige, ngëm rekk a koy indi, ngir mu sukkandikoo yiwu Yàlla rekk. Noonu la dige bi wóore ci ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, du ci ñi nekk ci yoonu Musaa rekk, waaye itam ñi gëm ni Ibraayma gëme woon. Kon Ibraayma mooy sunu baay, nun ñépp.
4:17b.ROM.004.017 Moom la Yàlla dogal, wax ko ci Mbind mi ne: «Def naa la baayu xeet yu bare.» Ndaxte Ibraayma gëmoon na Yàlla, miy dekkal ñi dee, tey wax ci lu amagul, mel ni dafa am.
4:18b.ROM.004.018 Ibraayma dafa jàppoon ci ngëmam, di yaakaar, fekk bunti yaakaar yépp tëju. Moo tax mu nekk baayu xeet yu bare, ni ko Mbind mi waxe ne: «Noonu la sa askan di meli.»
4:19b.ROM.004.019 Mu xool yaramam, xam ne dee rekk a ko dese, ndax mi ngi tollu woon ci lu mat téeméeri at, waaye ba tey ngëmam wàññikuwul. Mu xam it ne, Saarata mënatul a ëmb.
4:20b.ROM.004.020 Waaye loolu taxul ngëmadi jàpp ko, ba muy werante ci waxu Yàlla; ngëmam sax di gën a dëgër, mu daldi sant Yàlla,
4:21b.ROM.004.021 mu wóor ko ne, loolu ko Yàlla dig, Yàlla man na koo def.
4:22b.ROM.004.022 Moo tax «Yàlla jagleel na Ibraayma njub.»
4:23b.ROM.004.023 Waaye loolu lañu bind ne: «Yàlla jagleel na ko njub,» du Ibraayma rekk a moom wax ji.
4:24b.ROM.004.024 Nun itam ci wax jooju lanu bokk, te Yàlla dina nu jagleel njub, nun ñi gëm Yàlla, mi dekkal Yeesu sunu Boroom.
4:25b.ROM.004.025 Ndaxte Yàlla jébbale na ko ngir sunuy tooñ, dekkal ko ngir àtte nu jub.
5
5:1b.ROM.005.001 Léegi nag, gannaaw Yàlla àtte na nu jub ci kaw ngëm, nanu jàpp ci jàmm, ji nu am fa kanam Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist.
5:2b.ROM.005.002 Moo nu ubbil bunt ci Yàlla, nu taxaw temm ci yiwam, jaar ci ngëm. Te it nu ngi bég ciy négandiku, Yàlla boole nu ci ndamam.
5:3b.ROM.005.003 Te du ci loolu rekk, waaye bég nanu it ci sunuy nattu; ndax xam nanu ne, nattu day feddali muñ;
5:4b.ROM.005.004 te muñ mooy ndeyu jikko ju dëgër; te jikko ju dëgër day jur yaakaar.
5:5b.ROM.005.005 Te yaakaar jooju du ay nax, ndax mbëggeelu Yàllaa ngi baawaan ci sunu xol, jaarale ko ci Xelam mu Sell mi mu nu may.
5:6b.ROM.005.006 Ndaxte bi nu amul jenn doole, booba la Kirist dee ngir nun, fekk danoo weddi woon Yàlla.
5:7b.ROM.005.007 Kuy nangoo deeyal nit ku jub, yombul a gis, waaye nag jombul am na ku nangoo deeyal ku baax.
5:8b.ROM.005.008 Waaye Yàlla firndeel na mbëggeelam ci nun, ci li Kirist dee ngir nun, bi nu nekkee sax ay bàkkaarkat!
5:9b.ROM.005.009 Gannaaw Kirist tuur na deretam nag, ngir Yàlla àtte nu jub, rawatina ne dina nu musal ci merum Yàlla.
5:10b.ROM.005.010 Nun ay bañaaley Yàlla lanu woon, waaye Doomam dee na, ngir jubale nu ak moom. Gannaaw léegi nag xariti Yàlla lanu, rawatina ne dinanu mucc ndax dundug Doomam.
5:11b.ROM.005.011 Te sax nu ngi bég ci Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu jubale ak moom.
5:12b.ROM.005.012 Kon nag bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar.
5:13b.ROM.005.013 Bàkkaar kon nekkoon na ci àddina, bi Yàlla di laata wàcce yoonu Musaa. Waaye gannaaw yoonu Musaa tëddagul woon, bàkkaar du woon jàdd yoon.
5:14b.ROM.005.014 Teewul nag la dale ca Aadama ba ca Musaa, dee a ngi fi woon ci àddina, di noot ñépp, ak sax ñi seen bàkkaar melul woon ni bosu Aadama, maanaam jàdd yoon. Aadama moomu nag moo di takkandeeru Kirist, mi waroon a ganesi àddina.
5:15b.ROM.005.015 Waaye warunoo yemale tooñu Aadama ak mayu Yàlla. Bàkkaaru kenn nit kooku tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak may, gi nu keneen nit ka Yeesu Kirist yéwénal, baawaan na ci ñu bare, ba suul tooñ googu.
5:16b.ROM.005.016 Te bàkkaaru Aadama niroowul ak mayu Yàlla. Aadama bàkkaar na benn yoon, ba tax Yàlla daan ko, daanaale ñépp; waaye Yàlla jéggale na tooñ yu bare ci dara, ba mu àtte ñu bare ni ñu jub.
5:17b.ROM.005.017 Bàkkaaru kenn nit tax na dee tàbbi àddina, yilif ñépp ni buur; waaye jëfu keneen nit ka, maanaam Yeesu Kirist, moo ko suul, ba tax ñu bare tàbbi ci dund gu bees, falu ni ay buur; xanaa ñi Yàlla boole ci yiwam wu bare, te àtte leen jub ci dara fa kanamam.
5:18b.ROM.005.018 Kon nag nu gàttal wax ji; jàddug kenn nit ka rekk moo waral Yàlla daan ñépp; noonu itam jëf ju jubu keneen nit ka rekk moo ubbi bunt, ba ñépp man a jub ci kanam Yàlla te am dund gu bees.
5:19b.ROM.005.019 Aadama moomu dafa déggadil Yàlla, ba yóbbaale ñu bare, ñu nekk i bàkkaarkat; noonu itam Yeesu Kirist dafa déggal Yàlla, yóbbaale ñu bare itam, ñu jub.
5:20b.ROM.005.020 Te yoonu Musaa daldi wàcc, ngir bàkkaar gën a bare; waaye fa bàkkaar bare, yiwu Yàlla gën faa bare.
5:21b.ROM.005.021 Ba tax, ni bàkkaar doon yilife ñépp ni buur, indaale dee, noonu itam la yiwu Yàlla faloo ni buur, jóge ci njub, jëm ci dund gu dul jeex. Te loolu lépp darajay Yeesu Kirist sunu Boroom moo nu ko may.
6
6:1b.ROM.006.001 Lu nu war a wax léegi nag? Xanaa nu sax ci bàkkaar, ngir yiwu Yàlla gën a bare?
6:2b.ROM.006.002 Mukk! Nun ñi dee, ba rëcc ci kàttanu bàkkaar, naka lanu manatee sax ci di ko def?
6:3b.ROM.006.003 Xanaa dangeen a xamul ne, képp ku ñu sóob ci ndox, ngir wone ne, mu ngi bokk ci Yeesu Kirist, ci deewu Yeesu la bokk.
6:4b.ROM.006.004 Bi ñu nu sóobee ci ndox moomu nag, day misaal ne, dañu noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Yàlla Baay bi, te nu sóobu ci dund gu bees.
6:5b.ROM.006.005 Kon nag gannaaw benn lanu ak Kirist, dee ni mu deeye woon, kon dinanu nekk it benn ak moom, dekki ni mu dekkee woon.
6:6b.ROM.006.006 Ndegam xam nanu ne, daajoon nañu Kirist ca bant ba, xam nanu it ne, jikko ju bon ji nu judduwaale, daajaale nañu ko ak Kirist ca bant ba. Te Yàlla def na loolu, ngir nguuru bàkkaar, gi nekkoon ci sunu yaram tas, nu rëcc ci dooleem.
6:7b.ROM.006.007 Ndaxte ku dee, bàkkaar mënatul dara ci yaw.
6:8b.ROM.006.008 Gannaaw nag dee nanu ak Kirist, gëm nanu ne, dinanu dekki it ni moom,
6:9b.ROM.006.009 xam ne Kirist mi dekki dootul dee mukk, dee mënatul dara ci moom.
6:10b.ROM.006.010 Dee na benn yoon, ba bàkkaar mënul ci moom dara; te mi ngi dund léegi, di ànd ak Yàlla ba fàww.
6:11b.ROM.006.011 Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.
6:12b.ROM.006.012 Buleen mayati bàkkaar nag, mu yilif seeni yaram yu néew doole, bay topp ay bëgg-bëggam.
6:13b.ROM.006.013 Te buleen jébbalati seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jubadi; waaye gannaaw rëcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, jébbaluleen ci Yàlla te jébbal ko seeni cér, mu def leen jumtukaayam ngir jëfam yu jub.
6:14b.ROM.006.014 Ndaxte bàkkaar dootu leen manal dara, yéen ñi génn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla.
6:15b.ROM.006.015 Lan lanu war a wax nag léegi? Gannaaw génn nanu ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Yàlla, ndax danoo war a sax ci def bàkkaar? Mukk!
6:16b.ROM.006.016 Ndax dangeen a xamul ne, koo jébbalu ci moom te déggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami bàkkaar, mu jëme leen ci dee, mbaa ngeen déggal Yàlla, mu sóob leen ci yoonu njub.
6:17b.ROM.006.017 Waaye sant naa Yàlla ci lii: yéen ñi doon jaami bàkkaar, bi ngeen déggee mboolem dëgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol bépp.
6:18b.ROM.006.018 Te ci noonu rëcc ngeen ci nootaangeg bàkkaar te jébbalu ci Yàlla, sóobu ci njub.
6:19b.ROM.006.019 Xam naa ne, seen xam-xam ci mbir mii sorewul, moo tax ma yombal wax ji, awale ko ci baat yii. Ni ngeen jële woon seeni cér, jébbal leen, ñu nekk jaami lu selladi ak lu bon, di gën a jur lu bon, noonu itam léegi jébbal-leen seeni cér, ñu nekk jaami njub, ngeen door a sell.
6:20b.ROM.006.020 Ndaxte keroog ba ngeen nekkee jaami bàkkaar, séquleen woon dara ak lu jub.
6:21b.ROM.006.021 Ban njariñ ngeen ci jële nag? Dara lu dul gàcce, ndaxte ci dee la leen doon jëmale.
6:22b.ROM.006.022 Waaye léegi Yàlla goreel na leen ci kilifteefu bàkkaar, def leen ay jaamam, ba jural leen sell, jëme leen ci dund gu dul jeex.
6:23b.ROM.006.023 Ndaxte peyu bàkkaar mooy dee, waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.
7
7:1b.ROM.007.001 Bokk yi, yéen ñi may waxal xam ngeen luy yoon; xam ngeen kon ne, yoon am na doole ci nit diirub dundam.
7:2b.ROM.007.002 Ci maanaa, mi ngi mel ni jigéen juy séy; yoon a ngi koy boole ak jëkkëram, ñu ànd seen giiru dund, waaye su jëkkër ji faatoo, buum gi dagg na.
7:3b.ROM.007.003 Kon nag su jabar ji àndee ak beneen góor, te fekk jëkkër jiy dund, dees na ko àtte njaaloo. Waaye bu jëkkër ji faatoo, yoon jeexal na seen diggante; man na séy nag ak beneen góor, te loolu du njaaloo.
7:4b.ROM.007.004 Nii laa leen ko man a misaale, samay bokk; bi Kirist deeyee, dangeen a deeyandoo ak moom, te noonu yoonu Musaa wàcc leen. Léegi nag yéena ngi ànd ak keneen, maanaam Kirist mi dekki, ngir nu amal Yàlla njariñ.
7:5b.ROM.007.005 Keroog ba nu daan topp sunu nafsu, yoonu Musaa daan na xamb bëgg-bëgg yu bon, yiy yengal sunuy cér, ba jural nu dee.
7:6b.ROM.007.006 Waaye léegi yoon wi wàcc na nu, ci li nu dee, ba rëcc cig buumam. Léegi nag nu ngi jaamu Yàlla, waxumaleen ci sàmm santaane rekk, ndax loolu wees na, waaye ci kàttan gu bees, gi nu Xelum Yàlla di may.
7:7b.ROM.007.007 Kon nag lu nu war a wax? Ndax bàkkaar ci yoonu Musaa la jóge? Mukk! Waaye moo ma xamal luy bàkkaar. Ndaxte su ma yoon wi waxul woon: «Bul bëgg yëfi jaambur,» kon duma xam luy xemmem.
7:8b.ROM.007.008 Waaye bàkkaar jaare na ci ndigalu Yàlla, daldi ñëw dugg ci man, ba yengal ci man xemmem yu bare. Ndaxte ba ma xamagul woon yoonu Musaa, bàkkaar da ne woon nemm ci man.
7:9b.ROM.007.009 Te keroog bi ma xamagul lu yoon wi santaane, maa ngi doon dund dund gu neex; waaye ba ma ko déggee, bàkkaar dafa daldi fuddu ci man, te man ma daldi dee.
7:10b.ROM.007.010 Noonu gis naa ne, ndigal loolu waroon a jëme nit ñi ci dund, daf maa jëme ci dee.
7:11b.ROM.007.011 Ndaxte bàkkaar jaar na ci li Yàlla digle, ba nax ma, rey ma.
7:12b.ROM.007.012 Kon nag man nanoo wax ne, yoonu Musaa yoon wu sell la, te ndigalu Yàlla dafa sell, jub te baax.
7:13b.ROM.007.013 Ndax kon lu baax moo ma tàbbal ci dee? Mukk! Bàkkaar a ko def, ngir jikkoom feeñ; dafa gis ci lu baax loolu bunt bu mu man a jaar, ba rey ma. Noonu ndigalu Yàlla tax na, bàkkaar fés, bon ba jéggi dayo.
7:14b.ROM.007.014 Xam nanu ne, yoonu Musaa ngi jóge ci Yàlla, waaye man yëfi àddina laa fonk, te nekk ci dooley bàkkaar, mel nib jaam.
7:15b.ROM.007.015 Ndaxte samay jëf jaaxal na ma; li ma bëgg a def, duma ko def, waaye li ma bañ rekk, moom laay def.
7:16b.ROM.007.016 Kon nag gannaaw li may def du sama coobare, nangu naa ne yoonu Musaa baax na.
7:17b.ROM.007.017 Léegi nag du man maay def lu bon loolu, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ciy jiiñ.
7:18b.ROM.007.018 Ndaxte xam naa ne, lu baax dëkkul ci man, maanaam ci sama bindu doom Aadama. Am naa yéeney def lu baax, waaye awma kàttanu yeggale.
7:19b.ROM.007.019 Lu baax nag lu may yéene, duma ko def, waaye lu bon lu ma bëggul, moom laay def.
7:20b.ROM.007.020 Bu fekkee nag lu ma bëggul, moom laay def, kon dootul sama coobare, waaye bàkkaar bi dëkk ci man, moo ma ci jiiñ.
7:21b.ROM.007.021 Gis naa nag lii: saa su ma bëggee def lu baax, lu bon a ngi ma taxawu.
7:22b.ROM.007.022 Ndaxte ci sama biir xol yoonu Yàlla wi neex na ma.
7:23b.ROM.007.023 Waaye gis naa jeneen doole juy yengu ci samay céri yaram, di bëre ak li sama xol bëgg; day bëre ba noot ma, def ma jaam ci dooley bàkkaar joojuy yengu ci samay cér.
7:24b.ROM.007.024 Céy maaka torox! Ana ku may musal ci sama yaram, wii may jëme ci dee?
7:25b.ROM.007.025 Maa ngi sant Yàlla; am na kuy musle, mooy Yeesu Kirist sunu Boroom. Kon nag lii laa gis ci sama bopp: ci sama xel maa ngi topp yoonu Yàlla, waaye ci sama bindu doom Aadama maa ngi topp yoonu bàkkaar.
8
8:1b.ROM.008.001 Léegi nag yoon mënul a dab ñi bokk ci Yeesu Kirist.
8:2b.ROM.008.002 Ndaxte kàttanu Xelum Yàlla, tukkee ci Kirist Yeesu, di may nit dund gu bees, goreel na ma ci nootaangeg bàkkaar ak dee.
8:3b.ROM.008.003 Lu yoonu Musaa mënul woon a def, ndax néew dooley nit, Yàlla defe na ko nii: dafa yónni Doomam, ngir mu yor sunu jëmm, nun ñiy nekk ay bàkkaarkat, te mu jébbale bakkanam, ngir dindi bàkkaar yi. Noonu la Yàlla tase nguuru bàkkaar ci nit.
8:4b.ROM.008.004 Ba tax na léegi njub, gi yoonu Musaa di digle, am na ci nun, ñiy déggal Xelu Yàlla mi te bañ a topp sunu nafsu.
8:5b.ROM.008.005 Ñiy topp seen nafsu, seeni bëgg-bëgg rekk lañu fonk, waaye ñiy topp Xelu Yàlla mi, coobareem lañu fonk.
8:6b.ROM.008.006 Ndaxte fonk nafsu, ci dee lay jëme; waaye fonk Xelu Yàlla mi, dund ak jàmm lay joxe.
8:7b.ROM.008.007 Ndaxte ku fonk sa nafsu, bañaaleb Yàlla nga, ndaxte doo déggal Yàlla, mbaa ngay sàmm ay santaaneem, te mënuloo koo def sax.
8:8b.ROM.008.008 Kuy topp sa nafsu nag, doo man a neex Yàlla.
8:9b.ROM.008.009 Waaye yéen nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye yéena ngi topp Xelu Yàlla mi, bu fekkee ne mu ngi dëkk ci yéen. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom.
8:10b.ROM.008.010 Bu fekkee ne Kirist dëkk na ci yéen nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax bàkkaar bi nekk ci yéen, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Yàlla jox.
8:11b.ROM.008.011 Kon nag gannaaw Xelum Yàlla, mi dekkal Yeesu ca néew ya, dëkk na ci yéen, dina tax seen yaram wi néew doole dund ci kàttanu Xel moomu dëkk ci yéen.
8:12b.ROM.008.012 Kon bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxumaleen topp sunu nafsu ak i bëgg-bëggam;
8:13b.ROM.008.013 ndaxte kuy topp nafsoom, fàww mu dee, waaye kuy noot jëfi yaramam ci dooley Xelu Yàlla mi, dina dund.
8:14b.ROM.008.014 Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelu Yàlla mi, ay doomi Yàlla lañu.
8:15b.ROM.008.015 Kon nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba,» maanaam «Baay bi.»
8:16b.ROM.008.016 Ndaxte Xelu Yàlla mi, moom ci boppam, day ànd ak sunu xel ci seede ne, doomi Yàlla lanu.
8:17b.ROM.008.017 Te gannaaw ay doomi Yàlla lanu, dinanu moomi lépp li Yàlla jagleel ay doomam, séddu ci ngëneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku bëgg a bokk ak Kirist ndamam ëllëg, war ngaa séddu ci ay fitnaam tey.
8:18b.ROM.008.018 Xalaat naa ne sunu naqaru tey, wareesu ko tëkkale ak sunu ndamu ëllëg.
8:19b.ROM.008.019 Ndax li Yàlla bind lépp a ngi ne seew a gis doomi Yàlla yi feeñ ci seen biir ndam.
8:20b.ROM.008.020 Ndaxte dunyaa bi bépp mu ngi ci yoon wu dul mujj fenn; teyu ko, Yàlla moo ko ko teg. Waaye teewul ñu am yaakaar ne,
8:21b.ROM.008.021 Yàlla dina rengi seen buumi njaam ci dee, boole leen ci jàmmu doomi Yàlla yi ak seen ndam.
8:22b.ROM.008.022 Xam nanu ba fi nu tollu ne, li Yàlla bind lépp a ngi metitlu ni jigéen juy matu.
8:23b.ROM.008.023 Te du dunyaa bi rekk mooy metitlu, nun it nu ngi metitlu, nun ñi Yàlla sol Xelam, ngir nu ñam añu ëllëg; nu ngi ne seew Yàlla boole nu ci lépp li nu yelloo ni ay doomam, keroog bés bu Yàllay goreel sunu yaram.
8:24b.ROM.008.024 Ndaxte sunu mucc ëmb na yaakaar. Li nga gis ba noppi, nekkatul yaakaar; li teew, noo koy yaakaare?
8:25b.ROM.008.025 Li feek gisagunu nag li nuy yaakaar, dinanu ko séentu ak muñ.
8:26b.ROM.008.026 Te it Xelu Yàlla mi moo nuy xettali ci sunug néew doole. Ndaxte xamunu sax naka lanu war a ñaane Yàlla, waaye Xelu Yàlla maa ngi nuy ñaanal fa moom ak i yéene yu làmmiñ mënta takk.
8:27b.ROM.008.027 Te Yàlla, miy nattu xol yi, xam na xalaatu Xel mi, ndaxte tinu, gi muy tinul gaayi Yàlla yi, mengoo na ak coobareg Yàlla.
8:28b.ROM.008.028 Xam nanu itam ne ñi bëgg Yàlla, maanaam ñi Yàlla woo ci boppam te boole leen ci li mu tëral, Yàlla dina joo loxoom ci lépp lu xew ci seen dund, ngir jural leen lu baax.
8:29b.ROM.008.029 Ndaxte ñi mu xamoon lu jiitu, dafa dogaloon ñu nirook Doomam, ngir mu nekk taaw ci biir njaboot gu yaa.
8:30b.ROM.008.030 Te ñi mu dogaloon loolu ci ñoom, da leen a woo; te ñooñu mu woo, da leen a àtte ni ñu jub; te ñooñu mu àtte jub, da leen a boole ca ndamam.
8:31b.ROM.008.031 Lu nu war a wax nag ci loolu lépp? Gannaaw Yàlla ànd na ak nun, kan moo nu manal dara?
8:32b.ROM.008.032 Yàlla mi nu gàntulul Doomam waaye mu joxe ko, mu dee ngir nun, ndax dina nu bañalati dara?
8:33b.ROM.008.033 Ñi Yàlla tànnal boppam, kan moo leen di tuumaal? Yàlla moo leen àtte ni ñu jub.
8:34b.ROM.008.034 Kan moo leen man a teg tooñ? Yeesu Kirist mi dee, moo dekki itam, te mu nga fa ndeyjoorul Yàlla, di nu fa ñaanal!
8:35b.ROM.008.035 Kan moo nu man a tàggaleek mbëggeelu Kirist? Xanaa duy nattu, te du njàqare, du it fitna, du xiif walla rafle, du it ay ngaañ walla jaasi sax.
8:36b.ROM.008.036 Moo tax Mbind mi ne:«Ñu ngi nuy rey ngir yaw, ci suba ba jant so;ñu ngi nuy jàppe ni xar yu ñuy rey.»
8:37b.ROM.008.037 Waaye loolu lépp teewul, nu ngi mel niy ñeyi xare ci dooley Kirist mi nu bëgg.
8:38b.ROM.008.038 Ndax wóor na ma ne, dara mënu noo tàggaleek mbëggeelam; du dee, du dund, du malaaka yi, du seeni kilifa, du tey, du ëllëg, du boroom doole yi,
8:39b.ROM.008.039 du li ci kaw mbaa li ci suuf, mbaa leneen lu ñu bind; dara mënu noo tàggale mukk ak mbëggeel, gi nu Yàlla jox ci Kirist Yeesu sunu Boroom.
9
9:1b.ROM.009.001 Li ma bëgg a wax nag, ci kanamu Kirist laa koy waxe; dëgg la, du aw fen. Sama xel, mi Xel mu Sell miy leeral, seedeel na ma ne, dëgg laay wax.
9:2b.ROM.009.002 Maanaam, duma noppee am naqar wu réy ci sama biir xol,
9:3b.ROM.009.003 ba xaw a bëgg a tàggoo ak Kirist te alku, ngir ñi ma bokkal xeet mucc.
9:4b.ROM.009.004 Bànni Israyil lañu, te Yàlla def na leen ni ay doomam; dëkkaloon na ndamam ci seen biir, fas ak ñoom kóllëre yi. Ñoom la Yàlla dénk yoonu Musaa, ñoom la xamal ni ñu ko war a jaamoo, ñoom la jox i digam.
9:5b.ROM.009.005 Maam ya Yàlla tànnoon, ci ñoom lañu bokk, te ci ñoom it la Kirist wàcce, maanaam ci jëmmam, Kirist mi di Yàlla, tiim lépp, te yelloo teraanga ba fàww. Amiin.
9:6b.ROM.009.006 Waaye neewuma waxu Yàlla dafa toxu, ndaxte bokk ci bànni Israyil, taxul nga bokk ci Israyil tigi.
9:7b.ROM.009.007 Te it du ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, ay doomam dëgg lañu. Ndaxte Yàlla dafa wax Ibraayma ne ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.»
9:8b.ROM.009.008 Maanaam, soqikoo ci Ibraayma taxul a nekk doomu Yàlla, waaye juddu ci biir digeb Yàlla mooy tax a bokk dëgg-dëgg ci askanu Ibraayma.
9:9b.ROM.009.009 Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma naan: «Ci waxtu wii déwén dinaa dellusi ci yaw, te Saarata dina am doom ju góor.»
9:10b.ROM.009.010 Te du ci loolu rekk, waaye noonu la it ci lu jëm ci Rebeka; doom yi mu jur ñoo bokk benn baay, moo di sunu maam Isaaxa.
9:11b.ROM.009.011 Waaye Yàlla wax ko ne:«Yanqóoba rakk ji mooy yilif magam Esawu,» fekk xale ya juddooguñu te defaguñu dara, muy lu baax, muy lu bon. Yàlla def na noonu, maanaam tànn kenn ci doom yi, ngir dogalam man a taxaw, te sukkandikuwul ci seeni jëf waaye ci wooteb Yàlla.
9:13b.ROM.009.013 Loolu la Mbind mi wax ne:«Bëgg naa Yanqóoba, bañ naa Esawu.»
9:14b.ROM.009.014 Kon lu nu ci war a wax? Ndax Yàlla àttewul foofu yoon nag? Mukk!
9:15b.ROM.009.015 Dafa wax Musaa sax ne ko:«Dinaa yërëm ku ma neex,laabiir ci ku ma neex.»
9:16b.ROM.009.016 Dama leen di wax nag, dara ajuwul ci coobareg nit, mbaa ci ñaqam, waaye lépp a ngi aju ci yërmandey Yàlla.
9:17b.ROM.009.017 Ndax Mbind mi biral na li Yàlla wax Firawna ne ko:«Def naa la buur,ngir feeñal sama kàttan ci say mbir,te ngir siiwal sama tur ci àddina si sépp.»
9:18b.ROM.009.018 Kon nag Yàlla, la ko neex lay def, muy yërëm nit, mbaa dëgëral xolam ci lu bon.
9:19b.ROM.009.019 Waaye xanaa dina am ku may wax ne: «Gannaaw kenn mënul a bañ coobareg Yàlla, lu tax kon muy teg nit tooñ?»
9:20b.ROM.009.020 Yaw nag nit ki, ak koo man a doon, lu tax ngay werante ak Yàlla? Ndax mbindeef dina laaj ki ko bind: «Lu tax nga binde ma nii?»
9:21b.ROM.009.021 Ndax tabaxkatu ndaa sañul a fab banam, tabax ci ñaari ndaa, benn bi ngir soxla yu am maana, bi ci des ngir soxla yu ndaw?
9:22b.ROM.009.022 Kon nag looy wax ci lii: Yàlla bëggoon na wone meram, xamle it dooleem ci àddina; teewul dafa sax ci muñal ñi yelloo meram te taxaw ci sànku.
9:23b.ROM.009.023 Bëggoon na it xamle màggaayam mu ëpp xel, ci boole ñi mu yërëm ci ndamam; moo tax mu tànn leen ca njàlbéen.
9:24b.ROM.009.024 Te wax ji noo ko moom, nun ñi Yàlla woo ci boppam ci biir Yawut yi ak ci biir xeet yi ci des.
9:25b.ROM.009.025 Moom la wax ci téereb Ose ne:«Ñi nekkul woon sama xeetdinaa leen ko def,ñi bokkul woon ci sama mbëggeel,dinaa leen ci boole.»
9:26b.ROM.009.026 Te:«Fa ñu leen waxe woon:“Dungeen sama xeet,”dees na leen fa wooye“Doomi Yàlla Boroom dund.”»
9:27b.ROM.009.027 Esayi wax na ci mbirum Israyil ne:«Lu bànni Israyil baree-bare ni suufus géej sax,lu néew rekk a ciy mucc.
9:28b.ROM.009.028 Ndaxte li Boroom bi dogal ci àddina,dina ko gaaw a def, te dina mat sëkk.»
9:29b.ROM.009.029 Esayi it waxoon na lu jiitu loolu ne:«Yàlla Boroom kàttan gi,su bàyyiwul woon ci nun lu néew,kon ba tey raat nanu ni dëkki Sodom ak Gomor.»
9:30b.ROM.009.030 Lu nu ci war a wax nag? Ñi dul Yawut te fonkuñu woon jub ci kanam Yàlla, léegi jub nañu ci kaw ngëm.
9:31b.ROM.009.031 Waaye bànni Israyil, mi bëggoon a sàmm yoon ngir jub, matalu ko.
9:32b.ROM.009.032 Ndax lan? Ndax dañoo sukkandiku ci seeni jëf, bàyyi ngëm. Dañoo daanu ci «doj wuy fakkatale.»
9:33b.ROM.009.033 Moom la Yàlla wax ci Mbind mi ne:«Dinaa samp ci Siyon doj wuy fakkatale,di xeer wuy daaneel nit; waaye ku wéeru ci moom, sa yaakaar du tas.»
10
10:1b.ROM.010.001 Bokk yi, sama coobareg xol ci bànni Israyil ak sama ñaan ci Yàlla, mooy ñu mucc.
10:2b.ROM.010.002 Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam.
10:3b.ROM.010.003 Xamuñu yoon, wi Yàlla tëral ngir nit jub ci kanamam, waaye dañoo wéy ci seen pexey bopp; ba tax ñu bañ a nangu yoonu njub woowu Yàlla tëral.
10:4b.ROM.010.004 Ndaxte ci Kirist la yoonu Musaa dëppe, ba tax ku ko gëm, dinga jub fa kanam Yàlla.
10:5b.ROM.010.005 Ku bëgg a jub ci kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, Musaa daf cee wax ne: «Ku ko manoon a matal, dinga dund ba fàww.»
10:6b.ROM.010.006 Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm, nii lay waxe:«Bul wax ci sa xol ne:“Kuy yéeg ci kaw?”» mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc.
10:7b.ROM.010.007 «Bul wax it:“Kuy dem ca barsàq?”» mel ni dangaa bëgg Kirist dekki.
10:8b.ROM.010.008 Kon boog lan lay wax? Lii:«Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet,ci sa làmmiñ, ci sa xol.» Te wax jooju lal ngëm lanuy waare.
10:9b.ROM.010.009 Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc.
10:10b.ROM.010.010 Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne, mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko.
10:11b.ROM.010.011 Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.»
10:12b.ROM.010.012 Ndax ñépp a yem ci kanam Yàlla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun ñépp, te ku yéwén la ci képp ku koy ñaan.
10:13b.ROM.010.013 Ndaxte bind nañu: «Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.»
10:14b.ROM.010.014 Waaye nan lañuy wooye ki ñu gëmagul? Te naka lañu man a gëme ki ñu déggagul turam? Te naka lañu man a dégge turam, te kenn xamalu leen ko?
10:15b.ROM.010.015 Te it nan lañu man a waaree, su leen kenn yónniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: «Ñiy yégle xebaar bu baax bi, ni seen ñëw di sedde xol!»
10:16b.ROM.010.016 Waaye ñépp nanguwuñu xebaar bu baax bi; moom la Esayi wax ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?»
10:17b.ROM.010.017 Kon boog ngëm ci kaw dégg lay juddoo, te dégg sosoo ci xebaaru Kirist.
10:18b.ROM.010.018 Waaye ma ne: xanaa ñépp dañoo déggul? Aaŋkay! Mbind mi wax na ne:«Seen baat jolli na ci ñeenti xebla yépp,seen wax wër na àddina sépp.»
10:19b.ROM.010.019 Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Aaŋkay! Musaa dafa jëkkoon a wax ne:«Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla,merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.»
10:20b.ROM.010.020 Te Esayi takk na fitam, ba wax ne:«Ñi ma wutul woon, gis nañu ma,feeñ naa ci ñi ma laajul woon.»
10:21b.ROM.010.021 Waaye ci mbirum Israyil dafa wax ne:«Tàllal naa samay loxo, suba ba ngoon, ci xeet wu may bañ tey werante.»
11
11:1b.ROM.011.001 Ma ne kon, ndax Yàlla bërgël na xeetam? Mukk! Ndaxte man itam ci Israyil laa bokk, wàcce ci Ibraayma te bokk ci giiru Ben-yamin.
11:2b.ROM.011.002 Yàlla bërgëlul xeetam, wi mu xamoon lu jiitu. Ndax dangeen a xamul li Mbind mi di wax ci mbirum Iliyas? Dafa doon tawat Israyil ci Yàlla naan:
11:3b.ROM.011.003 «Boroom bi, rey nañu say yonent, daaneel say bérab yu sell, ba man kenn maa ci des, te ñu ngi may wut a rey.»
11:4b.ROM.011.004 Waaye lii la ko Yàlla tontu: «Dencal naa sama bopp juróom-ñaari junniy nit, ñi jaamuwul Baal.»
11:5b.ROM.011.005 Noonu itam ci jamono ji nu nekk, des na nit ñu néew ñu Yàlla dencal boppam ciw yiwam.
11:6b.ROM.011.006 Gannaaw nag yiwu Yàlla rekk a tax mu denc leen, kon du seen peyug ñaq, walla boog yiwu Yàlla dootul yiw.
11:7b.ROM.011.007 Kon lu nu ci war a wax? Li bànni Israyil doon wut, gisuñu ko. Waaye ñi Yàlla tànn rekk a ko gis, te ña ca des bañ a gëm, ba seen xol dërkiis.
11:8b.ROM.011.008 Looloo tax Mbind mi ne:«Yàlla daf leen a jox xelum nit ku gëmmeentu,bët yu gëlëm ak nopp yu tëx,ba ci bésub tey.»
11:9b.ROM.011.009 Te Daawuda it daf ci wax naan:«Na seeni ñam sax nekk fiir ak i pakk;nañu ci daanu, te Yàlla mbugal leen.
11:10b.ROM.011.010 Nañu gumba ba ne fatuus,nañu tiis te sëgg ba fàww.»
11:11b.ROM.011.011 Ndax kon dañoo tarxiis, daanu ba fàww? Mukk! Waaye jéllub Israyil dafa ubbi bunt, ngir xeeti ñi dul Yawut man a mucc, te bànni Israyil siis leen.
11:12b.ROM.011.012 Gannaaw seen tooñ nag moo ubbi buntu yiw ci waa àddina si, te seen ñàkk moo meññ barkeb xeet yépp, céy bés bu Israyil gépp delloo ci Yàlla, ndaw barke bu bare!
11:13b.ROM.011.013 Yéen ñi dul Yawut, yéen laay waxal. Ndegam Yàlla daf maa def ndawam, yónni ma ci yéen xeeti àddina si, damay matal samab yónnent.
11:14b.ROM.011.014 Dama koy def, ngir ñi bokk ak man xeet siis, ba ñenn ñi mucc.
11:15b.ROM.011.015 Ndaxte bi Yàlla génnee Israyil, ubbee na noonu bunt, ngir xeeti àddina juboo ak moom; kon su Yàlla dugalaatee Israyil, ndax du mel ni ndekkitel néew ya?
11:16b.ROM.011.016 Damay wax ne, mburu mépp sell na, bu ci Yàlla amee wàll. Naka noonu garab gi Yàlla séddoo reen bi, garab gépp sell na.
11:17b.ROM.011.017 Bànni Israyil a ngi mel ni garabu oliw gu ñu jëmbët ci kër gi, waaye mu am car yu ci fàq. Yaw mi dul Yawut, yaa ngi mel ni caru garabu oliw gu àll bu ñu jabtal ci garabu kër googu. Noonu nga jariñoo meen, mi jóge ci reen bi.
11:18b.ROM.011.018 Kon nag bul bàkku, di xeeb car yooyu Yàlla fàq. Waaye soo bëggee bàkku, xamal ne, reen moo lay yenu, te du yaw miy car yaa koy yenu.
11:19b.ROM.011.019 Xanaa dinga wax ne: «Car yooyu dañu leen a fàq, ngir jabtal ma fa ñu nekkoon.»
11:20b.ROM.011.020 Dëgg la; waaye seen ngëmadee tax ñu fàq leen, wuutal la fa ndax sa ngëm. Bumu tax nag ngay bàkku, waaye nanga moytu.
11:21b.ROM.011.021 Gannaaw Yàlla baalul car ya cosaanoo ca garab ga, kon boog yéen itam man na leen a fàq.
11:22b.ROM.011.022 Loolu kon wone na ni Yàlla baaxe ak ni muy meree tooñ. Ci ñi daanu, Yàlla wone na ni meram tànge, wone mbaaxam ci yéen, su fekkee yéena ngi ci wéy; lu ko moy, dees na leen fàq yéen itam.
11:23b.ROM.011.023 Te car yooyu fàq, su ñu wéyul ci seen ngëmadi, dees na leen delloo ci garab gi, ndax Yàlla man na leen cee tafaat.
11:24b.ROM.011.024 Yaw mi dul Yawut, yaa ngi bokkoon ci garabu oliw gu àll, waaye Yàlla daf la cee jële, ci lu dul faral a am, jabtal la ci garabu kër gi. Kon man nanoo gën a wóor ne, Yawut ya judduwaale nekk ci garabu oliw gu kër gi, Yàlla dina leen ci delloo.
11:25b.ROM.011.025 Bokk yi, dama leen a bëgg a dindi kumpa ci lii, ngir ngeen bañ a yég seen bopp. Dërkiisu xol dab na bànni Israyil ab diir, ba bés ba mboolem waa àddina, ñu war a bokk ci nguuru Yàlla, dugg ca.
11:26b.ROM.011.026 Bu loolu amee nag, bànni Israyil gépp dina mucc. Moom la Mbind mi tëral, bi mu naan:«Ab xettalikat dina jóge ci Siyon,dàq weddi ci askanu Yanqóoba.
11:27b.ROM.011.027 Loolu mooy kóllëre, gi may fas ak ñoom,bés bu may dindi seeni bàkkaar.»
11:28b.ROM.011.028 Gannaaw bañ nañu xebaar bu baax bi, ay bañaaley Yàlla lañu, ngir ngeen jot barkeem. Waaye gannaaw Yàlla tànn na leen, dafa leen bëgg ba tey ndax seen maam ya.
11:29b.ROM.011.029 Ndax li Yàlla maye, dootu ko nangu mukk, te ku mu woo ci boppam, dootu la dàq mukk.
11:30b.ROM.011.030 Ñu déggadil Yàlla ngeen woon, waaye ngëmadig Yawut yi tax na, ngeen jot yërmandeem.
11:31b.ROM.011.031 Ñoom itam lànk nañu léegi, ngir man a bokk ak yéen yërmandey Yàlla.
11:32b.ROM.011.032 Kon Yàlla tëj na ñépp ci ngëmadi, ngir man a yërëm ñépp.
11:33b.ROM.011.033 Xelum Yàlla ni mu xóote, ak xam-xamam ni mu baree, ba raw xelum nit! Kan moo muus, ba xam dogalam? Walla nga am xel, ba nànd ay jëfam?
11:34b.ROM.011.034 Mbind mi dafa ne:«Ana ku xam xalaatu Boroom bi?Ku ko doon digal?»
11:35b.ROM.011.035 Te it:«Ku ko mas a jox dara,ba mu war laa delloo?»
11:36b.ROM.011.036 Ndaxte ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp di jaar, ci moom la lépp di dellu. Moo yelloo ndam ba fàww. Amiin.
12
12:1b.ROM.012.001 Kon nag bokk yi, gannaaw yërmandey Yàlla baree na noonu, maa ngi leen di ñaan, ngeen jébbal ko seen yaram wépp. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu mooy njaamu, gi leen war.
12:2b.ROM.012.002 Bu leen àddina jey, waaye yeesluleen ci seen xel, ba soppiku, ngeen man a xam bu wér coobareg Yàlla, di lépp lu baax, neex ko te mat sëkk.
12:3b.ROM.012.003 Gannaaw Yàlla may na ma ciw yiwam, ma nekk ndawam, maa ngi leen di wax lii, kenn ku nekk ci yéen: buleen yég seen bopp, waaye ngeen am xalaat yu yem, mengook ngëm gi leen Yàlla sédd, ku nekk ak wàllam.
12:4b.ROM.012.004 Loolu, ci maanaa, mi ngi mel ni yaramu nit: yaram, lu cér yi baree-bare, benn niroowul ak moroomam liggéey.
12:5b.ROM.012.005 Noonu itam nun ñi bokk ci Kirist, lu nu baree-bare, benn lanu te danoo mànkoo.
12:6b.ROM.012.006 Kon gannaaw Yàlla séddale na ay mayam, ku nekk ak sa cér, nanu koy jëfandikoo. Ku Yàlla may, ngay waare kàddoom, nga wax ko kem sa ngëm;
12:7b.ROM.012.007 kuy topptoo yëfi mbooloo mi, nga takku ci; ku Yàlla may, ngay jàngale, nekk ci;
12:8b.ROM.012.008 kuy feddali ngëmu nit ñi ci Yàlla, nga sax ci; kuy séddoo alalam ak nit ñi, nga def ko ak xol bu laab; kuy jiite mbooloo mi, nga sawar ci; kuy dimbali ñi néew doole, nanga ci bég.
12:9b.ROM.012.009 Na seen cofeel di lu dëggu te bañ a nekk ngistal; araamal-leen lu bon te sax ci lu baax.
12:10b.ROM.012.010 Bëgganteleen ak xol bu leer, niy doomi ndey, te farlu ci teralante.
12:11b.ROM.012.011 Sawarleen te bañ a tayel, di jaamu Boroom bi ak seen xol bépp.
12:12b.ROM.012.012 Bégleen ci yaakaaru ëllëg te muñ bépp tiis, di sax ci ñaan Yàlla.
12:13b.ROM.012.013 Dimbalileen gaayi Yàlla yi ci seeni soxla, te saxoo dalal gan.
12:14b.ROM.012.014 Ku leen fitnaal, ñaanal-leen ko yiw, te bañ koo móolu.
12:15b.ROM.012.015 Bégandooleen ak ñi bég, te jooyandoo ak ñiy jooy.
12:16b.ROM.012.016 Bokkleen menn xel, tey bañ a yékkatiku, di yóotu daraja, waaye ngeen fonk ñi suufe; buleen teg seen bopp boroomi xel.
12:17b.ROM.012.017 Buleen feyante lu bon, waaye sàkkuleen seede su rafet ci kanam ñépp.
12:18b.ROM.012.018 Wutleen a juboo ak ñépp, ba fa seen kàttan yem.
12:19b.ROM.012.019 Samay soppe, buleen di feyantoo, waaye bàyyileen lépp ci loxoy Yàlla, mi yelloo àtte; ndax Yàlla nee na ci Mbind mi: «Man maay àtte, maay fey jëf.»
12:20b.ROM.012.020 Waaye defleen lii:«Bu sa noon xiifee, may ko mu lekk;bu maree, may ko mu naan.Ndax boo ko defee, dinga ko rusloo.»
12:21b.ROM.012.021 Bu leen lu bon ëpp doole, waaye nootleen ko ci def lu baax.
13
13:1b.ROM.013.001 Gannaaw loolu na nit ku nekk déggal ñi yore baat ci kanamam; ndaxte amul njiit lu fi Yàlla sampul. Njiit yépp nag Yàlla moo leen fi teg.
13:2b.ROM.013.002 Kon ku leen bañ a déggal, ndigalu Yàlla nga lànk, te ku def loolu, yoon dina la dab.
13:3b.ROM.013.003 Kuy def lu baax warul a ragal njiit li, kuy def lu bon moo ko war a ragal. Soo ko bëggee bañ a ragal nag, kon defal lu baax, te dina la tagg.
13:4b.ROM.013.004 Ndax Yàllaa ko dénk liggéey boobu ngir sa jàmm. Waaye sooy def lu bon, war ngaa ragal, ndax du cig neen la ame jaasiy àtte; jawriñu Yàlla la ngir wàcce meru Yàlla, ci fey ku def lu bon.
13:5b.ROM.013.005 Kon fokk ngeen déggal ko, waxuma sax ndax sañ-sañam boobu, waaye it ngir seen xel dal.
13:6b.ROM.013.006 Gannaaw Yàllaa sas njiit yi liggéey boobu, te ñi ngi ci, kon fàww ngeen fey galag.
13:7b.ROM.013.007 Joxleen ku nekk céram; ku ngeen war a fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen war a fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen war a weg, wegleen ko; ku ngeen war a teral, teral-leen ko.
13:8b.ROM.013.008 Buleen ameel kenn dara, lu dul mbëggeel; ndax ku bëgg sa moroom, wàccoo nga ak yoonu Musaa.
13:9b.ROM.013.009 Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul rey nit, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu man a doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
13:10b.ROM.013.010 Ku bëgg sa moroom, doo ko tooñ; kon ku wéy ci mbëggeel matal nga yoonu Musaa.
13:11b.ROM.013.011 Te lii itam am na: xam ngeen bu baax jamono ji nu tollu; jamonoy yeewu jot na, ndax léegi sunu mucc gën na noo jege, ca ba nu dooree gëm.
13:12b.ROM.013.012 Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgg a set. Nanu bàyyi nag jëf yu lëndëm te ràngoo gànnaay yi nu Yàlla jox, ngir dund ci leer.
13:13b.ROM.013.013 Gannaaw nu ngi ci leer, na sunug dund rafet. Bunu naan sangara ba màndi tey bànneexu; bunu njaaloo tey def i ñaawteef ak sunuy cér; bunu xuloo mbaa nuy ñeeyante.
13:14b.ROM.013.014 Waaye gànnaayooleen Yeesu Kirist Boroom bi, te bañ a topp seen bakkan ciy bëgg-bëggam yu bon.
14
14:1b.ROM.014.001 Gannaaw loolu ku ngëmam néew nangeen ko nangu, te bañ a werante ak moom ci lu lënt.
14:2b.ROM.014.002 Ndax am na ku xalaat ne, man na lekk ñam wu nekk, fekk ku ngëmam néew du lekk yàpp, waaye léjum rekk lay lekk.
14:3b.ROM.014.003 Kiy lekk lu nekk, bumu xeeb ki ko dul def. Naka noonu itam ku dul lekk yàpp, bumu teg tooñ ki koy lekk; ndax Yàlla nangu na leen ñoom ñaar.
14:4b.ROM.014.004 Koo teg sa bopp, ba di ko teg tooñ? Jaamu jaambur la! Mu taxaw ci liggéeyam, mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la. Waaye dina jub, ndax Boroom bi am na dooley taxawal ko ci njub.
14:5b.ROM.014.005 Noonu itam am na ñiy tànn bés ak ñiy yemale bés yépp. Na ku nekk xam bu wér li muy def, te jàpp ci.
14:6b.ROM.014.006 Ndaxte kuy tànn bés, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi. Kiy lekk lu nekk it, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi; loolu leer na ndax day sant Yàlla. Te it ki bañ a lekk yàpp, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi, di ko sant.
14:7b.ROM.014.007 Kenn ci nun dundul ngir boppam, kenn deewul it ngir boppam.
14:8b.ROM.014.008 Danuy dund ngir màggal Boroom bi, dee it ngir màggal ko. Kon nag nuy dund mbaa nu dee, noo ngi ci Boroom bi.
14:9b.ROM.014.009 Loolu sax moo waral Kirist dee te dundaat, ngir man a nekk Boroomu ñi dee ak ñiy dund.
14:10b.ROM.014.010 Yaw nag lu tax ngay teg sa moroom tooñ? Lu tax nga koy xeeb? Xanaa nun ñépp, danu dul dajeji fa kanam Yàlla, ngir mu layoo ak nun?
14:11b.ROM.014.011 Ndaxte Mbind mi tëral na lii:«Boroom bi nee na:“Ni mu wóore ne maa ngi dund,ni la wóore ne, ñépp dinañu ma sukkal,te ku nekk seede ne maay Yàlla.”»
14:12b.ROM.014.012 Noonu ku nekk ci nun dinga làyyi fa Yàlla ci lépp loo mas a def.
14:13b.ROM.014.013 Kon nanu bàyyee tegante tooñ, waaye nu fas yéenee moytu lépp lu nekk fiir guy yóbbe sunu moroom bàkkaar.
14:14b.ROM.014.014 Xam naa ne, amul wenn ñam wu sellul, ndax Yeesu Boroom bi xamal na ma loolu. Waaye loo yaakaar ne sellul, ci yaw la sellul.
14:15b.ROM.014.015 Soo dee lekk luy indil sa moroom tiis, génn nga ci mbëggeel. Yaw nag bul réeral sa moroom ci sa ñam, ndax Kirist dee na ngir moom.
14:16b.ROM.014.016 Bu sa njariñ jur wax ju ñaaw.
14:17b.ROM.014.017 Ndaxte bokk ci nguuru Yàlla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Yàlla mooy jub ci kanam Yàlla, te am mbég ak jàmm ci dooley Xel mu Sell mi.
14:18b.ROM.014.018 Kiy jaamoo noonu Kirist moo neex Yàlla ak nit ñi.
14:19b.ROM.014.019 Kon nag nanu wut luy indi jàmm, tey yékkati ngëmu sunu moroom.
14:20b.ROM.014.020 Bu sa ñam yàq jëfu Yàlla. Bépp ñam sell na ci kanam Yàlla. Ci lu wér! Waaye képp ku lekk luy yàq sa ngëmu moroom, def nga lu bon.
14:21b.ROM.014.021 Liy sa warugar mooy nga bañ a fiir sa moroom ci yàpp mbaa ci biiñ mbaa ci leneen lu mu man a doon.
14:22b.ROM.014.022 Su fekkee sa ngëm dëgër na, wone ko ci sa diggante ak Yàlla. Kiy nangu, te du ci sikkal boppam, kooku barkeel na.
14:23b.ROM.014.023 Waaye kuy lekk ñam te am ci xel ñaar, def nga bàkkaar, ndax sa ngëm yemu fa. Ndaxte jëf ju àndul ak ngëm, bàkkaar la.
15
15:1b.ROM.015.001 Nun ñi dëgër ci sunu ngëm, war nanoo nangu ñi seen ngëm néew te am ci lu ñuy sikki-sàkka, te bañ a yem ci wut sunu bànneex.
15:2b.ROM.015.002 Na ku nekk ci nun di wut lu neex moroomam ngir jariñ ko, ba mu gën a dëgër ci ngëmam.
15:3b.ROM.015.003 Ndaxte Kirist musul a wut bànneexu boppam. Loolu la Mbind mi wax ne: «Lor yi ñu la saagaa, ci sama kaw lañu dal.»
15:4b.ROM.015.004 Ndaxte lépp lu ñu waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, dañu koo tëraloon, ngir nu sàkku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak muñ, ak di feddali sunu yaakaar.
15:5b.ROM.015.005 Kon nag Yàlla miy maye muñ ak fit, na leen may, ngeen déggoo te nekk benn bu yellook li Kirist Yeesu wone.
15:6b.ROM.015.006 Ba tax nu bokk benn xalaat ak benn baat ci màggal Yàlla, Baayu Yeesu Kirist sunu Boroom.
15:7b.ROM.015.007 Moo tax nangoonteleen, bay màggal Yàlla, ni leen Kirist nangoo.
15:8b.ROM.015.008 Lii laay wax: Kirist ñëw na liggéeyal Yawut yi, ngir wone kóllëreg Yàlla ci matal dige, ya mu digoon maam ya.
15:9b.ROM.015.009 Ñëw na itam ngir ñi nekkul Yawut man a màggal Yàlla ndax yërmandeem. Moo tax Mbind mi ne:«Dinaa la màggal tey tagg saw tur,ci kanamu xeet yépp.»
15:10b.ROM.015.010 Mbind mi nee na it:«Yéen xeeti àddina, ñëwleen bànneexuak xeet wi Yàlla tànnal boppam.»
15:11b.ROM.015.011 Mu dellooti ne:«Santleen Boroom bi, yéen waa àddina,te ñëw màggal ko, yéen xeet yépp.»
15:12b.ROM.015.012 Te it Esayi wax na ne:«Am na sëtu Yese buy ñëw,dina yilif xeeti ñi dul Yawut,te ci moom lañuy wékk seen yaakaar.»
15:13b.ROM.015.013 Kon Yàlla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mbég mu réy ak jàmm ju yaa ci seen kaw ngëm, ba ngeen am yaakaar ju mat sëkk ci dooley Xel mu Sell mi.
15:14b.ROM.015.014 Bokk yi, wóor na ma ne, baax ngeen ba fa mbaax man a yem, fees dell ak xam-xam, ba man a jàngaleente mbiri Yàlla ci seen biir.
15:15b.ROM.015.015 Bu sama kàddu diisee nag ci bataaxal bii, dara taxul lu dul bëgg a yeesal seen xalaat, ndaxte Yàlla ci kaw yiwam daf maa sas,
15:16b.ROM.015.016 ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xebaaram bu baax bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal.
15:17b.ROM.015.017 Kon nag maa ngi bànneexu ci Kirist Yeesu ngir liggéey boobu ma Yàlla dénk.
15:18b.ROM.015.018 Awma fitu wax leneen nag, lu dul li Kirist jëf jaarale ko ci man, ngir xeeti àddina jébbalu ci moom; jëf na jaarale ci samay wax ak samay jëf,
15:19b.ROM.015.019 ci ay tegtal ak i kéemaan, sukkandikoo ci dooley Xelu Yàlla mi. Ba fi mu nekk nag yégle naa fu nekk xebaaru Kirist, li dale ci Yerusalem, jaar ci gox yépp, ba àgg diiwaanu Iliri.
15:20b.ROM.015.020 Sama yéene mooy xamle xebaaru turu Kirist fa mu eggagul, ndax bëggumaa yeggale sas wu keneen daloon.
15:21b.ROM.015.021 Li ma def nag, dëppoo na ak li Mbind mi wax ne:«Ñi yégagul mbiram dinañu ko yég,te ñi ko musul a dégg, xam ko.»
15:22b.ROM.015.022 Bëggoon naa ñëw seetsi leen, fekk ay téq-téq ñoo ma téye ba tey.
15:23b.ROM.015.023 Waaye nag léegi bey naa sama sas ci gox yii.
15:24b.ROM.015.024 Bu may dem Espaañ nag, bëgg naa faa jaar, nuyu leen; ndaxte ay at a ngii maa ngi am yéene ju tar ci ñëw seetsi leen. Bëgg na maa nekk ci seen biir, ngir am bànneexu sotteente ak yéen xalaat ab diir, te it ngeen waajalal ma sama yoonu Espaañ.
15:25b.ROM.015.025 Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem, ngir dimbaliji gaayi Yàlla yu sell ya fa nekk.
15:26b.ROM.015.026 Ndaxte waa Maseduwan ak waa Akayi ñi gëm, fas nañu yéeney sàkk ci seeni alal, yónnee ko, ngir dimbali ñi néew doole ci gaayi Yàlla yu sell, yi nekk Yerusalem.
15:27b.ROM.015.027 Yéene nañu ko, te it ci dëgg-dëgg bor la, bu ñu war a fey. Ndaxte gannaaw ñi gëm ci Yerusalem séddoo nañu ak ñi dul Yawut seen ngëm, kon xeet yooyu itam war nañoo séddoo ak ñoom seen alal.
15:28b.ROM.015.028 Kon nag waxtu wu ma noppee ci liggéey boobu, teg may gu tedd gii ci loxoy boroom, dinaa dem Espaañ, tey jaar fi yéen.
15:29b.ROM.015.029 Te wóor na maa ne, bu ma agsee ci yéen, dinaa indaale barkeb Kirist bu mat sëkk.
15:30b.ROM.015.030 Gannaaw loolu bokk yi, maa ngi leen di ñaan ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist ak ci bëggante, gi Xelu Yàlla mi def ci nun, ngeen defal ma lii: àndleen ak man, nu tuur sunu ñaq ci ñaan Yàlla.
15:31b.ROM.015.031 Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci ñi gëmul ci waa Yude; te it gaayi Yàlla yu sell yu nekk ci Yerusalem nangu ndimbal, li ma leen di yóbbul.
15:32b.ROM.015.032 Dolli ci, Yàlla may ma, ma ñëw seetsi leen ak xol bu sedd, nu booloo yeeslu fa kanam Yàlla.
15:33b.ROM.015.033 Na Yàlla Boroom jàmm ànd ak yéen ñépp. Amiin.
16
16:1b.ROM.016.001 Bu nu weesoo loolu, maa ngi leen di dénk sunu jigéen Febe, miy liggéeyal mbooloom ñi gëm ci dëkku Señsere.
16:2b.ROM.016.002 Nangeen ko jàpp ci turu Boroom bi, ni ko gaayi Yàlla yi yelloo, te dimbali ko ci lépp lu mu aajowoo; ndaxte moom itam wax dëgg, dimbali na ñu bare, ba ci man mii di wax ak yéen.
16:3b.ROM.016.003 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, samay nawle ci liggéeyu Kirist Yeesu.
16:4b.ROM.016.004 Ñoom ñaar dem nañu, bay bëgg a jaay seen bakkan ngir man; maa ngi leen di gërëm ci loolu, du man rekk sax, waaye itam mboolooy ñi gëm ci xeeti àddina sépp.
16:5b.ROM.016.005 Nuyul-leen ma it ñiy booloo ci seen kër.Maa ngi nuyu it Epaynet, mi jëkk a gëm Kirist ci diiwaanu Asi;
16:6b.ROM.016.006 ak Maryaama, mi sonnoon lool ci yéen.
16:7b.ROM.016.007 Nuyul-leen ma it Andoronikus ak Yuñas, sama bokk, yi ñu ma booleeloon tëj; am nañu tur ci ndawi Yàlla yi, te ñoo ma jiitu sax ci gëm Kirist.
16:8b.ROM.016.008 Te fàttewuma Ampilyaatus, mi ma bëgg ci sama xol ngir Boroom bi.
16:9b.ROM.016.009 Nuyul-leen ma it Urban, sunu nawle ci liggéeyu Kirist, ak sama soppe Estakis;
16:10b.ROM.016.010 ak it Apeles, mi ngëmam dëggu, ba yelloo kóolute.Nuyul-leen ma it waa kër Aristobul,
16:11b.ROM.016.011 ak Erojon sama mbokk, ak waa kër Narsis, ñi ci Boroom bi.
16:12b.ROM.016.012 Maa ngi nuyu Tirifen, moom ak Tirifos, jigéen ñi sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it sama soppe Persidd, mi ci jeex tàkk.
16:13b.ROM.016.013 Maa ngi nuyu it Rufus, waa ji xolam seey ci Boroom bi, ak yaayam, mi ma féete woon it cérub ndey.
16:14b.ROM.016.014 Te fàttewuma Asànkirit, Felegon, Ermes, Patarobas, Ermas, ñoom ak mboolem bokk yépp.
16:15b.ROM.016.015 Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, Nere ak jigéenam.Te fàttewuma Olimpas ak gaayi Yàlla yiy booloo ak ñoom ñépp.
16:16b.ROM.016.016 Te yéen bokk yi, saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolooy ñi gëm Kirist yépp a ngi leen di nuyu.
16:17b.ROM.016.017 Bokk yi, maa ngi leen di dénk, ngeen moytu ñi leen di féewale, ba di leen jàddloo yoon wi, ciy wax lu juuyoo ak dëgg gi ngeen jàng. Dawleen leen ba sore.
16:18b.ROM.016.018 Ndax ñu deme noonu liggéeyaluñu Kirist sunu Boroom; seen bopp lañuy liggéeyal. Ñu ngi ñëw ak làmmiñ yu neex, di jey xol yu woyof yi, ba nax leen.
16:19b.ROM.016.019 Waaye seen dégg ndigal bir na ñépp, ba sama xol sedd lool ci yéen. Teewul nag damaa bëgg ngeen am xam-xam bu leer ci lu baax, te bañ a laal dara ci lu bon.
16:20b.ROM.016.020 Su ko defee Yàlla Boroom jàmm dina noot Seytaane ci seeni tànk léegi. Na yiwu Yeesu sunu Boroom ànd ak yéen!
16:21b.ROM.016.021 Timote sama nawle bi may jàpple ci liggéey bi, mu ngi leen di nuyu, ak samay bokk Lusiyus, Yason ak Sosipater.
16:22b.ROM.016.022 Man Tersiyus mi bind bataaxal bii nag, maa ngi leen di nuyu ci turu Boroom bi.
16:23b.ROM.016.023 Gayus mu ngi leen di nuyu; moo may ganale ci këram, te foofa it la mbooloo mi di dajaloo. Erast miy topptoo mbiri xaalisu dëkk bi it, nuyu na leen, ak sunu mbokk Kartus.
16:24b.ROM.016.024 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen! Amiin.
16:25b.ROM.016.025 Santleen Yàlla, mi leen man a saxal bu wér ci dëggu xebaar bu baax, bi may waare ci mbirum Yeesu Kirist! Nekkoon na kumpa gu làqu diirub ay ati at,
16:26b.ROM.016.026 waaye léegi nag Yàlla dindi na nu ci kumpa. Te santaane na, nu yégle xebaar boobu ci xeeti àddina sépp, ci firi Mbindi yonent yi, ngir nit ñi man koo gëm, ba jébbalu.
16:27b.ROM.016.027 Yàlla mi jagoo xam-xam bépp, moom rekk moo yelloo ndam ba fàww, jaar ci Yeesu Kirist! Amiin.
- Holder of rights
- Multilingual Bible Corpus
- Citation Suggestion for this Object
- TextGrid Repository (2025). Wolof Collection. Romans (Wolof). Romans (Wolof). Multilingual Parallel Bible Corpus. Multilingual Bible Corpus. https://hdl.handle.net/21.11113/0000-0016-C333-2